You are on page 1of 6

Page |1

XARNU BI

SEEX MUUSAA KA WEREKAANU BMBA Aji-Taalif Ji XARNU BI : Seex Muusaa Ka Werekaanu Bmba (Yalna ngrmul Ylla eel leen) woy ko ci atum 1929, ndeysaan! doon jamono ju taroon lool, kk ab dund, mbay mu doxul, taw amul, kk xaalis, muy jamono ju naqari wallaahi! jaam i yooy, tumurnke, xiif, jaaxle te soxla ndimbl lool, ba tax Werekaan wi jl xalimaam woo Ylla ci barkeb Sriam bi mu yaakaar ni Ylla man na len a wallu ci barkeem, te def ko nag ci cakkuteful S Daam Abdu Rahmaan Lo ak i mag i taalibeem. Ba tax mu naan : Awma mqaamam di la woo | Waaye mutiid yi oo ma woo | Ni tawatal te bu u woo | Saw lmmiay wow xarnu bi. Muni:"waaye muriit yi oom a woo, ni tawatal te bu u woo." Bu u woo [maanaam] kon woowal Ylla ci barkeb Sunu Sri. Muy woy wu Ylla nangu it ndax waxees nani: ba mu noppee ci woy wi la jawal ca Barabu Sri Tuubaa jng ko fa, te fekkoon toogees na diir bu ygg tawul, gncax gi loof, niki mu ko yuuxoo ci woy wi, waaye ba mu jngee woy wi ci Barabu Sri Tuubaa bay gnn, dees koo wutal lumu seeloo ndax taw bu bari. Loolu dey manees na ko jppe firnde ci nangu gu Ylla nangu woy wi, ngir loolu moo doon dttub sen tawat. Waaye ginnaaw nangug woy wi yit, taar beek woyiin wee gnatee yeme, ci bees ko tkkalee ak woykat yi ci Araab mbaa sax weneen lkk. Ci nimu tnkoo ci saart i woy ak i trliinam, smmoonte ak galan (bahru) bi mu tnn, matal nattun yi (awzaan), jotale (balaaxa) te leer n (bayaan ak ma`aanii), boole ci xoromu lool. Yeme na! ni mu woyee woy wi, xamni bees koy dglu, man di yg mettitu jamono ja, ak it aal ji mu ko doon woyee, lpp mu dxaale ko ci woy wi, ba manees ko cee fekk. Loolu nag di nu won nooyug Wolof. Ginnaaw taar bi yit nimu fealee woomug Wolof ak smmoonte ak nos-wax (lgg-lgg/grammaire) ci woy wi yeme na, ba lees ci man a jle ci ay baati Wolof, ak nosiinu baat yi, duun na lool, kon daal kuy yggu ci suqali wolof mbaa yitte woo Wolof war gaa sant Seex Muusaa Ka, Yl nanu ko Ylla, aji-mgg ji, fayal ci barkeb Seexul Xadiim Sriam.

BISMI-L-LAAHI AR-RAHMAANI AR-RAHIIMI Wa izaa sa-alaka 'ibaadii 'annii fa-innii qariibun ajiibu da'wata-d-dii'ii, izaa da'aanii fa-ajib da'wata. rabbi innii lima anzlta ilayya min xayrin faqiirun. rabbi yassir walaa tu'assir

Page |2

Sri bi noo gi deeti aan Noongi dangaan ci Mustafaa Ak qi mboolem ay rakkam Mboolem muriid ypp a ngi tuub Mbkke, dangay boroom i mbot Aw ma mqaamam di la woo Tay jii ma wax bani tareet Te bul ma tanxamlu ci aan Jooy i perantal la nu jooy Jis u nu baay te noo ngi raam Fabal sa doom yi ypp boot Te fab muriid yi suturaal Ndax Ylla amdi Mustafaa Boolem muriid ypp a ngi jooy Jamono jaa ngi xiif a xiif Xiif tax na, enn mag i yooy Taxna, a daa joxee ngi laaj Xam na ni yaa nu daa tawal Sa yrmandee nu daa defal Sa yrmandee nu daa sanal oo sen i sag sggiku na At moo ni ndax mooy tane daaw Wy ! nu ni wy! noo ka torox Garab gu mag bu nee jirim Allaahu akabaruz zamaan Libeek, sikkeek i shfaraan Astaxfirul Laahal Aziim Xeewal yi daf daa wal-wali Xeewal yi daf daa walangaan Wcci nga yaw loo mas a wax Gcax gu ndaw gi weddatul Njmbt la mooy gaa ya dikkon Ag kk a bon ci waa ju baax Leek-leek nga gis fi ab muriid nd'ak komersaa ya di jaay a lee nga xcc i defi seef Yaw la nu yaakaar abadaa Yrm nu tay yaru na nu Soo nu joxoon la nu yoran Yrm lu nan, torox lu nan Nun tuxu nan sun kr i baay Muriid yi saalit nanu ren Tiijaan yi rccu nau tay Bawal-bawal jolof-jolof Koo xam ni daan a ame jaak Ku mas a am yaar i wata Koo xam ni daan a ame taax Kr yaa ngi wet ba ni woyo Tubaab yi sax pert nau a tukkiwan faf nau la Naar yaangi yalwaan'ak a xaar Wooy Mbkke ! yuuxu nan ba dee Yaw yaay donoy Muhammadu Man ngaa defar biteek i biir Man sa kanam, man sa gannaaw Sa mbir ppante na'ak drm Ma lebu ngaa yi la xamul Nan far waee ku tagg daam Bmba muneef u laa misaal

Faqiir dafay nangoo dagaan Ma nekk marwat'ak safaa Ak qi sen baay yi u am Tey rccu bkkaar yi nu joob Te sag njaboot tawat gilot Waaye muriid yi oo ma woo Ngir yaa ma def antarpareet Ngir lii ma bon tey ku aaan Boo nu fabul, lee nu ni wooy Ku kk yaay, day nmpu maam oom it u boot senug njaboot Mottali jkk a jii nu naal Tabax jumaa-i Mustafaa Ngir luu bay-bay mu dal di gooy Lu togg, bar gi ni ko fuuf Xiif tax na, gor su ndaw si jooy ii pp sen i sas di xaaj Daanu bayal, daanu oral Lu xel dajul, daanu dfl Jigen a, yaa nu daa amal oo sen i gaay dggeeku na Mooy gn a far dellu gannaaw Yalwaan, amoo ku la sarax Garab yu ndaw yi day jirim Jamono moo man a safaan Lan daa diwoo muy walangaan Tuub nanu lan daa def i koom Baawaan fi nun di kel-keli Waxset nga wuute nga'ak sayaan Def nga ko jox ku mat a jox Mag a nga yar ken woddatul Daa wy ci xeewal ya fi won Day tas krm xolam ba jaax Muy taxawaalu ni'b mariid ii di wajaaseeri baxaay ii def i dag ngir ba a loof Ngir yaa nu tggaleek bidaa Dotu nu fo, xmme na nu Dotu nu def ,nanu defan Jooy na nu ren, saraxtu nan Gddaay te def la ngn ji baay Ngir xamni yaa len ame wan Xam na ni by du soru boy Mboolem pl'ak naar'ak wolof Daa ame ngaar'aki juuk Soxla na ren jii yaar i mta Tay ming ni ngeeju'b nek bu baax Lal ya yoroon def i koyo a len gmoon pert nau Fu wcci deef i len fala Seex bu xamoon dellu fa jaar Wallu nu boo yeexee nu dee Te yor nga sirrub Ahmadu Defar nga baadoola'aki buur Loo sant Ylla mu ni waaw Nde xarnu bpp am grm Waa ju xamul dees koy xamal Ngir moo nu may lu jombi maam Yaay gej gi wr waa senegaal

Nangul nu lpp lu nu aan Ak qi amdi Mustafaa Ak qi seex yi Bmba am Ba lu nu bay-bay, du nu gob u def ma ab ntarpareet Ni tawatal te bu u woo Yaa fab i xam-xam ne yuret Muriid yi ypp a la ko aan Ku nuy yafal, ban def i kooy Buural te boot nu, ngalla daam ! Ku manta boot nga jox ko mbot Foo toll dolli sen alaal Bam tol ni marwata'ak safaa Ba sen i ddiya'a ngi booy Seex Bmba, neel ngn ji mbindef Xiif tax na, yenn tool yi booy Ken dotu dem fenn ba waaj Daanu roal, daanu daggal Daanu tibbal, daanu leel Tay pp a yam ken amatul oo sen i ngm rkkiku na Ba rab yu aay yi sax di naaw Garab bu daanoo xob ya lax Mat ma say mbir ya lm Xewl yi daf daa walangaan Nuy xelli kopp ya di naan Te muy lu neexulan boroom Moo tax ma jg di pl-pli Xamoo xur'ak tund'ak sayaan Daawoo nu nax, daawoo nu cax Moo tax ma naala suuxatal Tay i ngi def ya u bawon Daa ceeb u tay ngay ae laax Walla mu xcc def triid Te xamni yaa doon sen i baay ii daw ba raw ba ni nu fuuf Tuub nanu mboolem la nu daa Dotun nelaw, yewwu na nu Xanaa ygooni yaru nan Soppeeku nan, jbbalu nan Tuubaa di kr, bmba'a di waay Yaa len joxon la nu yoran Yaa man a may nit lu ko doy Kenn gis a tul ku ame yf Mii at mu am dwn mu jek De munta am njg u mta Bu gn a feex bam ni ca faax a doon i wuur def i koya Yahood yi it fayit nau dduna yaa ka noo wela Ken talatul loo jox i naar Melal ni kuy rammu ku dee Te yor nga bot i Haamidu Yaa dindi llarba'ak diber Loo wax fa diiwaan u ni waaw Te am drm te yokku ngm Subhaana, yaa ka mat kumal Boolee'k Muriid yuy daw di raam Deef u la jlle genn gaal

Ndax Ylla naatal xarnu bi Mi Ylla jbbal xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi May lpputoo waa xarnu bi Saw lmmiay wow xarnu bi Ci sama xol, ci xarnu bi Ngir bgg a dekkal xarnu bi Mu dellu naatal xarnu bi Roggani mboolem xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Sarax nu naatal xarnu bi Mu dellu naatal xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Feesal nga sqi xarnu bi Reggal nga mboolem xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Ngir kk gii ci xarnu bi Ay Mbkke ! gesul xarnu bi
Bmba'ay danjaamal xarnu bi

Lii rekk a dal waa xarnu bi Ci ndabi mboolem xarnu bi Wata ya kornu xarnu bi Jurbel a wuuteek xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sam ndox a naatal xarnu bi
Sddon nga mboolem xarnu bi

Njmbt li wan ci xarnu bi Ngir kk gii ci xarnu bi Jaaxal na gaa yi xarnu bi Ndaw njombe gaa yi xarnu bi Moo tee nga naatal xarnu bi Moo tee nga naatal xarnu bi Bkkaar ci njkk xarnu bi Yrm nu naatal xarnu bi Ku weddi laajal xarnu bi Sarax nu naatal xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Yobbu nga mboti xarnu bi Moo tee nga naatal xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sri geesul xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Yal na u yes ci xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Sri bi geesul xarnu bi Yaa nuy tinul waa xarnu bi Man ngaa defar waa xarnu bi Skk Muriidi xarnu bi Wax len u naatal xarnu bi Nga may njari waa xarnu bi Yaa neex a wan waa xarnu bi Ag cant a war waa xarnu bi Say duus a tooyal xarnu bi

Page |3
Seex Bmba yaa di'k mbmbulaan

Ku sobu gnnaaley drm Gejug hikkam ga mu dtm Luum loo na fore ya wyon Sirrub andaar i xam-xamam Fekkon na dab yi ni xareet Taalif na mol yu fees i taax Day duusu dong a yay dtm Bmba'a di gej gu tbbi gej Lu baax du baax ba jll baax Waa ju la sopp dal di baax Waayam du iit gariiti laax Ku weddi lii demal lagan Ngneli daam ya gn a tuut Xarbaax la raw na kuy xiyaas Moo jar a way ba a selaw Seex Bmba yaa bariy njari Sri si, oo doon fatafoor Seex Bmba yaa di'g mndawaar Nun sobu nan la jlle nu Seex bmba yaay ngn ji keno Billaahi weru nan ci yaw Seex Bmba yaay ngn ji wurus Def nan la ngay sunu takkaay Seex Bmba yaa di'b libidoor Seex bmba yaa nu mat boroom Buur Ylla jox na la'y midaay Seex Bmba yaa di'b kir-kiraan Def nan la geg bu deefi yeg Ylla'a la jiital ca qadiim Yawma ajaaba bi balee Sirrub dggoom ba la ni naat Mu jll toog ca gngunaay Billaahi Bmba'a dim kela Qaataltu fil bahril la'iin Yonent ba'ak ahlubadar Gabo a xam na uy biram Kerook la lbbe ya ni waaw Tubaab ya naa ko nan maroo Tngaale wu la asamaaw Karaama yaa nu ko xamal ll'ak kr'ak jaam'ak gor'ag/k Luy nit ku uul'ak nit ku weex Mbindef yi yaa len fal i buur Soodaanu war na ni nrm Ko-mersi naa la mersi oom Ken dotu dox kem li nga dox Limaamu Shahraaneey kamaal Mboolem xawsu ya weyon Xaadiru, yeesal ngay biram Lottal nga o sharii'atu Woroom kurus yadaa aji Wommat nga naar yeek i wolof Roytef i xarnu bi nga won Xutbu yi, yaw la daa fegoo Naar yaa ngi am hidaaya tay Seex Bmba, yaa di ab newet Dundal nu, noo di sa'g njaboot Yaay fekk waay i njoro-ndiaay Muriid yi yaa yor sen ngrm Seex Bmba yaa di ag nduyoor Wa saabiquuna saabiquun

Ku sobu dotu aane naan Bkkoor bi dot u dem krm Bani ko scc moo'k oam Raam loo na kngam ya fi won Museefu caa nattal wujjm Mu soppi len watay sareet Te xalimaam du juum du jaax Duus yay jallaaoo ci'b dnnam Fekk fa gej gu ni ko ngej Waaye Sri bee weesu baax Waa ju la weddi dotu baax Dotul lmbooy sagar di daax Iisaa di mbar moo man u gan Xel man u koo takk di root Lu xel dajul deefu ko raas Guddee'k bccg ba a nelaw Fri nga wuute ga'ak kri Sondeel du mel ni'b limiyeer Waaju la tbbi dotu rer Waay Mbkke! bul dem byyi nu Sa jn yi doy na uy dono oy nan ci yaw lu man a xew Foo gnn xnjar daaldi rus Di sun bitik nu di la jaay Lmburde wuute na'aki cuur Fekkoo ci ddina moroom Diiwaan a xam nau sa waay Ku jm ca Ylla na la aan Te def la mbr mu deefi deg Tuddee la Ahmadul Xadiim Yefar ya juum wuyoo walee/aa Ca doqi gor a uy sanaat Buur Ylla rng koy medaay Moo jppu saytaane wela Kabkabuhuu nadbul amiin oo dkku kaarce ya ko wr Galwaa a xam na uy biram Maarbbu bii bu leen ci gaaw Soldaar sa naa ko bun meroo Br ypp booloo na ni waaw Mqaama yaa nu ko amal Ceddook sri buur'aki dag Diggante askan yu du jeex Ku mas a xy taal baboor Biidaanu war na ni na'am Pl yaa nga naala mujji-doom Ken dotu wax kem li nga wax Tererm ba Bmba lay misaal Yaa sobu ngiir ya u awon Tiijaanu yeesal ngay biram Jommal nga o haqiiqatu Ak gaa ya daa siyaare ji Xllaat nga ngiirum tasawuuf Kiimaan i labdaal yi nga won Nattu ya gor a daa tegoo Tiijaan di laaj hidaaya tay Sbbi nga tooyal gpp wet Wodd nu, nee nu wkk boot Nga fal ko, boole kook i gaay Sri si yaa yor sen xorom Sri si oo doon njawli ber Yllaay boroom Kun fa yakuun

Ku mndi day dmbaan i teen Ku ni curum kaasub ngrm Maseef u caa nndal ku xam Daane na mbr ya fi newon Ayam ngi suural na'w oam Duy len ngnel ba ni sret Te am xelam du gag du naax Mooy gej gu ridwaan di'y jnam Mu duy ca ler ya ba ni ngiij Baax a ngi yam fi xotti baax Waa joo grm muy gn di baax Loxoom du daarati ci mbaax Yaa ramla wuute na'ak sa gan Mbaa xalima'aki daa yu xot Fugraas la rawna goru faas Ba raw i daa wayal calaw (buur ya) Sri si yaa di sen sri Jant la moom fawxana weer Yaay jant say gaa ya di weer Yawmal Xiyaam yobbaale nu Soo doon fital di ag kno Ngir `urwarul wusqaa du sew Gor su la waaje dotu rus Yaa gn i baay gn i nejaay Sri si sobu wu sa mboor Toooo boroom, toooo moroom Waajoo grm, krm du daay Soo doonu tur di Alxuraan Kela mi, wub nga br yi jeg Jiitu na aadama'aki doom La bmba not u naa alee pp ni nuut tllal i baat Diiwaan ba jox ko sen i gaay Ba tr ko rendi fa gabo Ma'al amiini wal amiin Saytaane nrmelu di sr Lmbar a seere nay biram Leeram gi sarna asamaaw Lbbe ya naa ko bun woroo Gurag yi lay na sa gannaaw Kaaraanga yaa nu ko defal Bokk'ak i jmbur pp a jag Fu nekk daam def na fa seex Di xelli attaaya ju foor pp di sant ak a grm Wolof ya naa amoo moroom Ken dotu jox kem i nga jox Gi naa ni mooy aboo rijaal Wommat nga ruu ya u yoron Shazaliyu, yeesal ngay biram Sa ngiir mi mooy tariiqatu Yaa tax u daa siyaare ji Shariif yi yaa tee u shuruf Kiiraay i lawtaad yi nga won Lashyaax yi yaw la daa sagoo Te musu oo weesu bu ry Bay nga mu or, gob nga fat Te suturaal nu, may nu mbot Ni doom i Maam Synabu Njaay Bi la gisul i'ng ni xerem Waa ju la nemm falu buur Ewwaaye gaay ya fi jkkoon

Say kaas a mndal xarnu bi Doo mar li des ci xarnu bi Toqan nga doy na xarnu bi Amul niroo ci xarnu bi Wujjm amul ci xarnu bi Wccoo na moo'k waa xarnu Du ftte lf ci xarnu bi Te mus la fer ci xarnu bi Dellu si tooyal xarnu bi Baaxaale gaa yi xarnu bi Waa yoo ko warna xarnu bi Ku weddi laajal xarnu bi Bmba'a ko aak ci xarnu bi Lottal na mboolem xarnu bi Sakkaa i teewe xarnu bi Ngir li mu def ci xarnu bi Yaa man a leeral xarnu bi Leeram nga tiim na xarnu bi Leer ya gndoo ci xarnu bi Te yobbu mboolem xarnu bi

Sa'y wal a (bal a) mokkal xarnu bi

Desu ko dog ci xarnu bi Doy nga takkaayal xarnu bi Yaa gn xariit i xarnu bi Nde kon u naatal xarnu bi Tinul nu too i xarnu bi Yaay kir-kiraanub xarnu bi Yaa boole mbot i xarnu bi Sebul ci mboolem xarnu bi Jiitu na gaa yi xarnu bi Notaale gor i xarnu bi Ken ynguwul ci xarnu bi Kerook la tte xarnu bi ibbi si wax ko xarnu bi Moo ko waxon waa xarnu bi Lbbe ya daw ci xarnu bi Seere sa wor na xarnu bi Sar na ci suusi xarnu bi ibbil yilif nga xarnu bi Nde wub nga lmbi xarnu bi Yaa suturaal waa xarnu bi Jaaraama daam ci xarnu bi Bu man a yor waa xarnu bi Fajoon nga aajoy xarnu bi Ngir yaa defar sen xarnu bi Yaa dmbe tagg i xarnu bi Daralewoon nga xarnu bi Xutbu yawon ci xarnu bi Yeesal nga wirduy xarnu bi Kuntiyu jox la xarnu bi Moo gn a jub ci xarnu bi Sri sa woon ci xarnu bi Jlle nga len ci xarnu bi Ak nujabaa-uy xarnu bi Bay laaj hidayay xarnu bi Yaw la u roy ci xarnu bi Man ngaa dundal waa xarnu b Nee len amiin yen xarnu Lmp bi won ci xarnu bi Fajal nu aajoy xarnu bi Sa lem gi neex na xarnu bi oo yobbu mboti xarnu bi

Page |4
a raflewoon wodd na len a ko bggoon Seexal na len
Seex bmba yaay ngayndeg njaloor

Fddal nu ndaama yii di daan Seex bmba yaa matub Sri Soppi nu ay wagook i gaal Seex bmba yaa matub sriif Siggil nga waa mbkke bawal Mbkke dimb'ak, mbkke xewar Askanu kr maam maaram Daarus Salaam, Daarul Minan Yaa tax u dooni kppitaal Sa daaru yee di'y lppitaal/n Rggi xol'ak rggi yaram Fekkoon nga rew mi defi ndol Fekkoon nga ii defi lafa Yaa dikk jag ya fi dammoon Amal nga gaa yu amulon Sa waay du ee waayi kaneen Taxoon nga ruuh yi dajaloo Xlloon nga ngiir mi ba mu weex Wommat nga ruuh yi jox boroom Dekkal nga julliy jurom Aw nga siraatal mustaqiim Sunna si yaa ko dekkalaat Fekkon nga uy wa ak a tuur Soppi jigen iy muslimaat Yaa tax nu daa sellali jf Jirim yi yaa don seni baay Ku jooy fi yaw nga noppi loo Billaahi yaa mat li nga doon Mboolem sahaabatu rasuul Ka'ab dadaa tagg rasuul Yaa raw a daa janook rasuul Yoon wamu aw ba raw mbindef Diggante mulkoo'k malakot Aras la daa gisee'k boroom Moom la u may nuurul jalaal Gaa ler, ca lay jae'y cibeel Ylla la daa sukkandi koo Tere ya lay wttalikoo Taalif la daa jfandikoo Tawhiid la daa xamali jaam Fum toll day tagg rasuul Dem jkk a moo ko tax a nuuj Njool mkk a daal lay segeree Fab na ca xayru lanbiyaa Dddoom gu mat gamu jagoo Nattoom yu ry yam daa tegoo Dunyaa da koo wanon gannaaw Bggul galan bggul medaay Bggul fas ak nag ak galeem Bggu la am junni yu ro Drm du yq ab deram Drm xmmee wu kook xandeer Mbindef yi ypp a yam fi moom Bawal-bawal akub ajoor Mbkke gnul fi moom guyaar Tabax, gnul fi moomi mbaar Wolof, gnul fi moomi naar Wata, gnul fi moom saxaar Mggat, gnul fi moom sixaar

a reflewoon sedd na len a ko boon suuxal na len Ag ndaama sobutil sa mboor Notal nu noon yii di nu daan Yaa xoti mbir te yaa xara Ten yab sa marsandiisi haal Mbkkeek mbusoobe dootu soof Mbkke kajoor yaa len bewal Ak mbkke baari, kr sayar Yaa tax ba waa ju u grm Daaru yi fii kulli zman Niroowu oo ki fkk-taal Ku rgg war na lay dagaan Yaa koy raggal joxey ngrm Fekkoon nga pp defi gool ii daanu far ba ni fl Jnganti mbir ya fi dngoon Xamal nga gaa yu xamulon Sa waay du xcci jm faneen Te wootewoo, te fitaloo Ku ci awoon mujj na seex Smmal nga njur yi sen boroom Ba ceddo yaangi jppi wom Te boolewoo wal aki doom Trbiya yaa ko yeesalaat Daa takk i ndomboy takk i cuur uy dawu gor ni muhsinaat Yaa tax nu tekki nun wolof Baayo yi yaa doon seni yaay Ku xiif fi yaw nga regg loo Noo seddu teggi cer bu duun Ak br ya daa tagg rasuul Bushayri daa tagg rasuul Ngir yaa liggey ba am wusuul Ba def donoy ngn ji mbindef Ba sar ca pey i jabarot Kursiyu lay xamey soloom Moom la u may nuurul jalaal Gii ler ca lay oddee'y ngnel Yonen la daa jottali koo Durus nga lay moyandikoo Mahfuus la daa gngandikoo Hikaaya lay xyee subaam Du war watay dammi rasuul Julli ji na fi'y rkk a ba gej Soo ko tudaa mu daldi ree Jikko yu raw yuy lawliyaa Ak xam gu mat ga mu jagoo Te teewu koo nd ak sagoo Musula faale yamu laaw Bggul lu ab tubaab di jaay Bggul bay ak xar aki doom Bggu la dox di yor i bo Wurus du tax mu ras btm Diinaar xmee wu kook ganaar Alal yi ypp a yam fi moom Smm aki baadooloo ki buur Kon ummi mbkkeek taar ba kaar ngaar, gnul fi moom sabaar Gnnaar, gnul fi moom Mbayaar Mbaanik gnul fi moom daqaar Ndawit, gnul fi moom kibaar

Ruuh ya gmon wommat na len a xddiwoon neexal na len Soo doonu weer di weeru koor Jggil nu mbr yii bu nu daan Waane wi yaa raw ab mara Te yobbu gori senegaal Sen xol ya war na ni gariif Pnku bawal yaa len defal Saaka bmbaa leen defar Mu ber krm am i drm Yaa leen yoxon la u yoroon Am nau barke am halaal Ku w nga jox garab mu naan Jarak yi war na laa grm Yaa tax ba nuy niinal i bool oo ku u aan jabar mu ba Ykkati neg ya suufe woon Feeal nga mbir yi nbbu won Deesu la xam di gm kaneen Te wate woo ni kuy faloo Te masulaa jdd aka jeex Seex bmba ken du sa moroom Te fetaloo ba ami gom Ba gg yaak sa ypp doom Te alxuraan yaa ko falaat Yaa sampi daaru, fali wuur Rkki takkaayi sen i baat Yaa tax ba nuy woy di walif Miskiin yi yaa doon sen nijaay Ku mar fi yaw nga mndi loo Wccal, damul, langul te ten Melna ni bay nga sen i tool Hasaanu daa tagg rasuul Ba def xaliifatu rasuul Maneesu koo xamal mbindef Ken musla boole sen i bot Diiwaan la daa faley moroom Mu boole koo'k sirrul kamaal Kamaal ga lay falee'y meteel Jibriil la daa dimbandi koo Pexe ya noon ya daa jagoo Hikkam la daa sukkandikoo Riwaaya lay gonte nekaam Du werse bo ci tarasool Aj mkka mas na ko ni ngej Gi naani daawu u soree Moo raw xiyaaru lasfiyaa Ak mu gu ry ga mu sagoo Te amna bot yu mu fegoo Jublu ci Ylla ne njanaaw Jaayante na ak Ylla sa waay Bggu la am sqi njurom Moo mas a dox ba dem gabo Nawul drm xeebul prm Kuy waaru bmba doyna waar Bggul baul xeebul du yem Ku laaj mu jox la sa muur Kon du ko may sri guyaar Baari, gnul fi moom pataar Kon taaxi jurbel du fa jaar Rusul a yalwaan ak a xaar Njccaar, gnul gumba gu taar

Ba wommataale xarnu bi Ba del si nd'ak xarnu bi Mbaa weeru gmmuw xarni b Te def nu mbr ci xarnu bi Say gaal a jlle xarnu bi Def nub masin ci xarnu bi Maam Jaara tiim na xarnu bi Lu tax u siiw ci xarnu bi Ba uy defar waa xarnu bi Daagul rusoo ci xarnu bi Ku weddi seetal xarnu bi oo gddu mboolem xarnu bi Doktoor bi yaa faj xarnu bi Ngir yaa wral sen xarnu bi Yafal nga mboolem xarnu bi ii mel ni man ci xarnu bi Ba man a nd'ak xarnu bi Dekkal nga ruuhi xarnu bi Sa diine doyna xarnu bi Lislaam nga moome xarnu bi Ba yobbu mboolem xarnu bi Yaa man a jlle xarnu bi Yaa wone diiney xarnu bi Tay i ngi wommat xarnu bi Yaa bind loo won xarnu bi Tasaare daaray xarnu bi Di muuru dddu xarnu bi Xamal nga gaa yi xarnu bi Yaay weruwaayu xarnu bi Mndal nga goru xarnu bi Nde wub nga lmbi xarnu bi Bayaale tool i xarnu bi Semmal nga len ci xarnu bi Kawe nga mboolem xarnu bi Jomb na mboolem xarnu bi Lut Bmba bjjob xarnu bi Di folli seef i xarnu bi Leeram ya dar na xarnu bi Seexal na mboolem xarnu bi Ba jot ci mbot i xarnu bi Ba t na nooni xarnu bi Moo nndaloon waa xarnu bi Du jw du jnni xarnu bi Moo gn a wuuteek xarnu bi Faadiilu aj na xarnu bi Jikkoom ya waar na xarnu bi Dendam amul ci xarnu bi Mus la tawat ci xarnu bi Te du ko feg ci xarnu bi Wakkiirlu dddu xarnu bi Gae na mboolem xarnu bi Du jaay du jandal xarnu bi Dellu si fii ci xarnu bi Moo gn a wuuteek xarnu bi Cey Ylla ! bjjob xarnu bi Mooy gnn gor ci xarnu bi Di nig li des ci xarnu bi Xamul ku bon ci xarnu bi Kon du fa jug ci xarnu bi Ba def jumaa ci xarnu bi Ba Ylla jox ko xarnu bi Gu jox tumam ba xarnu bi

Page |5
Bmbaay boroom kun, fayakuun!

Baatin la daa fab di nu jor Tarbiya, lay yarey goneem Diraaya, lay xamal goneem Cofeel gi, moo ma ko xamal Moo tax ba dotu ma selaw Leeram gi, daal may tex-texaan Seex Bmba, yaa di sun Imaam Sri si woon daoo texm Ku leen faboon, teg ci balaas Xawsu ya, mooy sen Yilimaan Moo am "fasaahatu lisaan" Moo am "maxaarijul huruuf" Mooy "Muhjisaati adnaan" Tuubaa, eel na kuy muriid Jox naa ko fww sama xol Bmba, da ngay boroomi may Woyu nu ngir bgg i drrm Yaw mi laggeeyal sa boroom Tbbal nu "jannatul na`iim" Ridwaan tijjil nala, nga wy Nopplu jil ca Illiyiin {Ak Mursaliina'ak Lanbiyaa Yural sa punk, te dem fanaan {Alhamdulillaahi na ngen; Yaw mi laggeyal Mustafaa Matna xaliifatul xadiim Noppeek, goreek, tllal ndijoor Taafeeri njool aaminata Yaa neex a way, te neex a taas Raayaw ngnel wi yaako yor Mboolem sixaarun wa kibaar Robino yaangi'y walangaan Jumaa ji yaa ko taxawal Yaw la sulaymaan xamalon Daawuda Bmba lay misaal
Ndommoy ngnel ya won ca maam

Muriid yi jox nala'y Idaay Ylla nangay muuram muriid "Allaahu dhoo-l-fadlil aziim"
Mooy doomi "shamsun wa xamar"

Saddiiti baayam lay royaat Mooy noobalub lislaam fi nun Ma wax la lf, ci ay jikkoom Dem na ba mkkam jullikaay Taalif i baayam'ay wayam Ylla na am lamuy mbt; Nan tang ahmadul amiin Baatin ba, jaaxal na'w kajoor Faj aajo, moo ci gn a gaaw Day way te jngulon haraf Fab na ca yaayam, yan yu diis Sa-sa ba, lnde na ci moom Rijaal ya ,xam na darajaam Yal na ko may mboti lamiin Mbg maangi! teeru leen bashiir Moo am jalaal te am jamaal Taar ba ca yuusufal kariim Ca ag rawam, la daal di raw Sobu na giirum tasawuuf {`Ilmud Diraaya la jagoo

Moo donn Ahmadu-l-Amiin Du mere nit, ba di ko dor Tarqiya, mag a won fa moom Inaaya, moodi ay jikkoom Xam-xam bi, raw na sama xel Cofeel gi, tee namaa nelaw Saa xol di dem, ba poroxaan Yaw la nu teg fa sunu maam oo way ne eex, ba xerem Jl Bmba, teg ca bee balaas Moo smmuwaanteek Alxuraan Laaya yi, moo xam seen cosaan Lmmeu yaaram la ko roof Yu wcce aaxirus samaan Waylun, eel na kuy mariid Saabub ngnelamay setal Te nun, nu def woroom i moy Mbkke, danuy skku ngrm Ba am ngrm "xayrul Xadiim" Ten dkk fa'ak sa ypp doom Jox nala njndi yu la doy Ylla grm nala'ak Lamiin Ak taabi`iina'ak lawliyaa Diggante kawsara'ak jinaan Di sant rabbal `Aalamiin Bul ftte, amdi Mustafaa Fees na plaa,s ba mat na doom La moome saalum ak kajoor Yaa donn njool aaminata Ngir xarnu bii, amoo fi maas Yaa teggi tuur ba, daw ba sar Yaa tax u tbbi ci'g saxaar Nuy naan ni kawsara'ak jinaan Yaa tee mu naaxsaay ni'w yoral Karyeer ba, doj ya ca deson "Bayti-l-Muqaddasi" la naal Ya stu kokki aki ndaam Tubaab ya jox la'y midaay Te Ylla booy, muuram mriid Kum jox ngne,l deefi la yem Mbkkeek, mbusobe du ko jar Leerug cosaan ga day royaat Mboolem shariif yi moo ci gn Lewet, woyof, nd'ak sagoom Haj na, siyaare ngn ji baay Moo donn duusi xam-xamam Ci nun, nu am li nuy mbt; Moom lau may sirrul masuun Mootax u lm ko jammi biir Lum wax boroomam muni waaw Te mndaxaam du ca shuruf Te nduruwul boroomu tiis Jagle ga jiitu na'b juddoom Bu nee jala, uy safi jaam Fegal ko ayu bpp noon Donoy bashiiran wa nadhiir Te xar kanam ga leer kamaal Ba buur ba fal ko def ko doom Fore ya daa fireek a raw Ku ko rawon, neena la wif! Mbirum `Inaaya la lkkoo

Moo tax amul xejj ak i seen Mboolem jigenam aku gor Tasfiya, Mbr yu deefi yem Wilaaya, lay defal boroom Leeram gi, fees na sama xol Maa nguy wrelu, ni gelaw May naan ba mndi, coroxaan Yaw la nu doyloo, ba fa saam Seex Bmba, moo safon xorom Konte, mu wat sen i palaas Adiisi Yonen, ba raaan Moo xam, la wcce asamaan Mooy waykatub gn ji mbindef Di rammu xeet wu jm jinaan Yal na nu Bmba def muriid Terub mbalaan i sama xol Mootax nu sax ci di la woy Ca bis ba Ylla di yrm Wllil nu yaw ci say jurom Wuntu ya, yaa yor seeni doom Waaju la soob mu daal di wy Yonen grm na la'ak eneen Jinne ya'ak Malaayika ya Nottil te lekk nag, te naan Doom a di baay kii du kaneen Ak doomi baayi Mustafaa Te amna xam-xam, ame koom Ku laaj, mu joxla lay sa muur Tuubaa di sun madiinata Li dale fii, ba weesu faas Ngir naaru gor ak fasu par Ba wcc Tuubaa ngn ji gaar Dotu nu tppaatuy sayaan Naalam wi/u yal nang ko matal Jumaa ja bayti tabaxoon Wuy ji boroomam ba kamaal Nga boole koo'k ngneli daam; Sultaan nga boole koo'k wilaay Bihaqi xaadirin muriid Faadilu mooy "fadlu hamiim" Moo nmp yaari meeni ngor Nday jaa di xayru muhsinaat Donoy usaynu wal-Hasan Niru na baay ba, mat na doom Te ndiwul alal di jaay Moo naan ci gejug hikkamam Ci moom, te yal nan am i st Xarbaax la feese, bani guun Soo ko gisee ma ngay bangeer Day fal di folli ci lu gaaw Mooman arab te man wolof Kuy rooti, moodi dex gu fees Mbr mu ko soru daal di luum Nrm-nrm, di safi mbaam Ku dgg aan, nani amiin Ku teeru naan, lekk ba suur Tem bari xam-xam am alaal Jigen ja far tngook sagoom Musula jaar ci yfi ndaw Moo raw a xllon moom a lef Nuurul wilaaya la sngoo

Mooy yrmndey waa xarnu bi

Defar na len ci xarnu bi Ba man a nd'ak xarnu bi Cofeel gu am ci xarnu bi Baawaan ci gaa yi xarnu bi Dotu ma toog ci xarnu bi Di buusu gaa yi xarnu bi
Rammu nu, nook waa xarnu bi

Safaale gaa yi xarnu bi Mbkke! du maasam xarnu bi Moo ko xamal waa xarnu bi Jm si ci suusi xarnu bi Maay waykatam ci xarnu bi Tuubaa li ahli xarnu bi
Neeleen "amiin" yen xarnu bi

Fotal nu gkki xarnu bi Ndaxte, nga jggal xarnu bi Xeet wi newoon ci xarnu bi "Yawma yaquumu" xarnu bi Tijjil dugal waa xarnu bi Yaa ame caabiy xarnu bi Ak xulafaa-uy xarnu bi Grm naook waa xarnu bi} Jaajf! defar nga xarnu bi Man naa defar waa xarnu bi} oo ame bot i xarnu bi Man naa musl waa xarnu bi Te musla gntul xarnu bi Yaay weer wi tiim waa xarnu b Yaw lau jbbal xarnu bi Rawante wu ci xarnu bi Noppal nga len ci xarnu bi Jaajf! defar nga xarnu bi "Aamiina" war na xarnu bi
Moom ngay defal waa xarnu bi Taaw ba defal ko waa xarnu bi

...Rngoo, amoo ci xarnu bi Yaa man a tggat xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Turam wi, doyna xarnu bi Mooy Bmba tay ci xarnu bi Moo donn mboti xarnu bi Maay xaadamam ci xarnu bi mb na kersag xarnu bi Nawleem amul ci xarnu bi Sirroom ba, doyna xarnu bi Yu gn a gm waa xarnu bi Baay baa ko lm ci xarnu bi Ni kuuy lu mat ci xarnu bi Matnaa ragal ci xarnu bi
Jommal na mboolem xarnu bi

Moo man a mndal xarnu bi Mbiram xajul ci xarnu bi Raamal ko war na xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Doo kk lf ci xarnu bi Buurika fiika xarnu bi Manga'ak bashiirum xarnu bi Musula faale xarnu bi(dduna) Sakkaa i teewe xarnu bi Dendam amul ci xarnu bi

Page |6
Durus ci terey alxuraan Yal nafi/u sax, ba dgg maam Allaahu moodi jenn waay Booko gisee muy smmandaay Niroo doxiin, niroo waxiin Moodi wallax-njaanu jinaan Moo donn tab, ga woon ca moom Baatin ba, raw na saahiram Yal na ko dolli ay muriid Nan aan ci Ylla miy Samad Ci boti "qul huwa fadhliin" Te yokk Abdul Qaadiri Te yal na Ibraahima moom Mboolem i dooni saalihiin Dundak So`aybu ga'ak, alaal; Te maynu barke ak ridhaa Te boole luy taaw ak i aat Mboolem lu Sayxu Bmba am Muusaa ka miy sen werekaan Waykat yi bu yaboo ni xiim Ngir Abdu Mbkkem soxna MBAY Saynabu Mbkkem Absa njaay (Ma Abdu MBkke mom Maam Maaram, mooy baayi Asta MBkke, muy ndayi Absa Sekk mi jur Muusaa KA. Man lebu naa leen, kll leen Woy naa ko Shhru ramadaan Jullil ci ngn ji `Adnaan; Mbaa muy julleek a jngi aan Te tol ni maam ahmadu daam Mooy jpp doom, def ko ni baay Seex Bmba, oo niroo'b jataay Niroo jmm'ak meloo'k defiin Bu len ko xool bt i kaaan Moo donnn njmbaar ga ca moom Day gaaw a soppi ay mbiram Te yalna raw pexem mriid Mu may Sri Abdu Samad Sri bu mag bi gn ci yen Fii baatinin wa zhaahiri Def'ab xariit fa sun boroom Ci sowwu jant, mbaa feneen Ju bari jaa'ak, jam darajaal Te sol ngrm ci murtadhaa Gor ak jigen, ci benn baat Yal nau gn te yokku ngm Moo len di woy, di len dagaan Maa war di xaadimul xadiim Ak Maaram mi pp oy Ak Maaaram miy ngn ji baay Batay Zaynabu MBkke mom Maam Maaram, mooy ndayu Ahmadu Zaynabu, baayi Absa Sekk ndayi Muusaa KA) Woy naa wolof, ba lkk leen Mi Ylla wcce Alxuraan Muusaa, te aan ko; ba nu naan Yooyu la baaxoo, te ku aan... Te donn mbot ya won ca daam u bokk bennu'b taxawaay Niroo yaram, niroo sewaay Buy ree nga waat ni du keneen Kaaan du tee bjjan a daan Sen baay a sddale'y jikkoom Mbir ma ca baayamay mbiram Te yalna mujj di'b friid Te may Sri Abdu Lahad Ylla bu seni barke neen Bijaahi baayu taahiri Ba jot ca bot i turandom Ylla na saalihu di sen Yal na ko Seex Bmba misaal Ba ku ko soob mu def qadhaa... Ndax Ylla sun xarnu bi naat Kon, leenu bokk ame ndam Tey sant, tey tagg ak a aan Damay muriid, di jaam, di doom Mooy baayi-baayi sama nday Mooy baayi-baayi sama yaay Mu mayla lf ci xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Abdoo, di Bmbam xarnu bi Niroo deret ci xarnu bi Bmba'a waat ci xarnu bi Baayam a leeral xarnu bi Sdde ko lii ci xarnu bi Moo yor jaliili xarnu bi Ba tol ni gaayi xarnu bi Lu doy a doy waa xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Bam tol ni Jiilim xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi Jant bu tiim waa xarnu bi Ci sun So`aybum xarnu bi Haajaatihii, ci xarnubi Aaamiina warna xarnu bi Te am ngrm ci xarnu bi Ndax ylla naatal xarnu bi Te gn a bon ci xarnu bi Maa dikke nii ci xarnu bi Maa dambe yii ci xarnu bi

Woy naa araab, ngir bgg ngen Ngir bgg lpp lu ma aan Gwal bu jaaxlee war a aan

Xam Bmba, yeen waa xarnu Ylla defal ko xarnu bi Ndax Ylla naatal xarnu bi

Aamiin ! Allaahumma salli `alaa sayyidinaa Muhammadin wa aalihii wa sahbihii wa xayra xadiimihii wa sallama tasliiman, Subhaana rabbika rabbil `izzati `ammaa yasifuun wa salaamun `alal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil aalamiin,

Aji Taalif ji: Sri Muusaa KA Werekaanu Bmba, (Xewalug Ylla ak mbgteem ci sen kaw) Aji Bind ji: Abdu Xaadir GEY -Albadriyyu- mom Alaaji Sri GEY BADAR. Karmat: qiSos ji () eel na Abdu Xaadir GEY, mu jagleele ko eel kpp ku ko yittewoo ci ag jppandal (ci lu dul fay) ngir Ylla ak laabireente. Ammaa nag mol, walla sotti ko ngir jaay mbaa lu ni mel eel na Aji-Sos ji waliif keneen, kon war na skkoos ci ndigalm.

**** DIEUREUDIEUF SERIGNE ABDOU KHADRE GUEYE CI MBINDE MI ****

You might also like