You are on page 1of 26

58 Waareb Yaxya

1 Xibaaru

jmm bu Yeesu *Kirist, *Doomu Ylla a, nii la

tmbalee. 2 Bind nau ci tereb yonent Ylla *Esayi naan : Maa ngi ynni sama ndaw ci sa kanam, mu xllal la sa yoon. 3 Baat a ngi xaacu ca mndi ma naan : Xll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar. 4 Noonu *Yaxya fee ca mndi ma, di *sob nit i ci ndox, tey waaree nii : Tuubleen seeni bkkaar, ba noppi ma sob leen ci ndox, ngir Ylla baal leen seeni bkkaar. 5 Kon waa diiwaanu Yude pp ak waa dkku *Yerusalem pp daldi gnn jm ci moom, di nangu seeni bkkaar fi kanam pp, Yaxya sob len ca dexu Yurdan. 6 Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu u rbbe kawaru gilem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njerer la doon dunde ak lem. 7 Mu waare ne : Am na kuy w sama gannaaw koo xam ne kii moo ma pp kttan ; yeyoowuma sax sgg, ngir tekki ay dllam. 8 Maa ngi leen di sob ci ndox, waaye moom dina leen sob ci *Xel mu Sell mi.
Yaxya sob na Yeesu ci dexu Yurdan
9 Booba

Yeesu jge na dkku Nasaret ci diiwaanu Galile, w, *Yaxya *sob ko ci dexu Yurdan. 10 Bi muy gnn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te *Xelum Ylla di wcc ci melow pitax,

Xibaaru jmm bi ci Almasi bi Yeesu, ni ko Ylla jaaralee ci

MRK
1.1 Doomu Ylla : tur wii tekkiwul ne, Ylla moo jur Yeesu mook Maryaama, ndaxte loolu araam na. Tekkiwul it ne, daoo mggal nit, ba di ko mngale ak Ylla. Waaye day tekki ne Yeesu mooy Kddug Ylla, di ki dippeekoo ci Ylla te feeal jikkoom. Ku gis doom, xam nu baayam mel. Ku gis Yeesu kon, xam nu Ylla mel.
a

59

w ci moom. 11 Te baat bu jge asamaan jib ne : Yaa di sama Doom, ji ma bgg ; ci yaw laa ame bnneex.
Yeesu dkku na ay nattu ci pexey Seytaane
12 Ci

kaw loolu Xelum Ylla daldi j Yeesu, mu dem ca mndi ma. 13 Mu nekk fa eent fukki fan, jnkoonte ak fiiri *Seytaane ; mu dkk ci biir rabi ll yi, te malaakay Ylla di ko topptoo.
Yeesu tnn na eenti taalibe
14 Bi

nga xamee ne jpp nau *Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xibaaru jmm bu Ylla bi, 15 naan : Jamono ji mat na, nguuru Ylla jegesi na ; tuubleen seeni bkkaar te gm xibaaru jmm bi. 16 Am bs Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa aar u bokk ndey ak baay, di Simo ak Andare rakkam, uy snni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lau woon. 17 Yeesu ne len : wleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit. 18 Ci saa si u byyi seeni mbaal, topp ci moom. 19 Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, u nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal. 20 Noonu Yeesu woo len, u daldi byyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom.

Yeesu faj na nit ku am rab


21 Gannaaw

loolu u dem Kapernawum. Ca *bsub noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jngu bi, di len jngal. 22 Te u waaru ca njngleem, ndaxte jngal na len ak sa-sa bu seeni *xutbakat amul. 23 Noonu am na ci jngu bi nit ku rab jpp. Mu daldi yuuxu naan : 24 Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel ? Ndax dangaa w, ngir alag nu ? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jge ci Ylla. 25 Waaye Yeesu gdd ko naan : Noppil te gnn ci moom ! 26 Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te gnn ci moom ak yuux gu ry. 27 Bi loolu amee pp waaru, ba laajante naan : Kii mooy kan ? Mii njngle lu bees la te nd ak sa-sa. Day sant rab yi sax, u di ko dggal. 28 Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gpp.
Yeesu faj na jarag yu bare
29 Bi

nga xamee ne gnn nau ci jngu bi, u nd ak Saag ak Yowaana, dem ci kr Simo ak Andare. 30 Fekk gorob Simo
MRK 1 60

bu jigen tdd wopp ak yaram wu tng ; u daldi ko ygal Yeesu. 31 Mu w nag ci moom, jpp loxoom, ykkati ko. Noonu tngoor wi daldi wcc, te soxna si di len topptoo. 32 Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, u indil Yeesu i wopp pp ak i rab jpp pp, 33 ba dkk bi bpp dajaloo ci buntu kr gi. 34 Noonu mu wral u bare, u wopp ak ay jngoro yu wuute, te dq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, u wax dara, ndaxte xam nau ko.
Yeesu wetoo na ak Ylla
35 Ca

njl laata bt di set, Yeesu jg dem ca brab bu wet, di fa aan Ylla. 36 Simo nag ak i nd ak moom di ko seet fu nekk. 37 Bi u ko gisee, u ne ko : pp a ngi lay seet. 38 Waaye Yeesu ne len : Nanu dem feneen ci dkk yi nu wr, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma gnn. 39 Noonu mu wr ci diiwaanu Galile gpp, di waare ci seeni jngu, tey dq rab yi.
Yeesu faj na ku gaana
40 Am

bs ku *gaana w ci moom, sukk, aan ko ne : Soo ko bggee, man nga maa wral. 41 Yeesu yrm ko, tllal loxoom, laal ko naan : Bgg naa ko, wral. 42 Ca saa sa ngaanaam daldi de, mu wr. 43 Noonu Yeesu yebal ko, dnk ko bu wr naan : 44 Moytula wax kenn dara, waaye demal won sa bopp *sarxalkat bi, te nga jbbal Ylla sarax, si yoonu *Musaa santaane, ngir u xam ne wr nga, te mu nekk seede ci oom. 45 Waaye naka la waa ji gnn, mu di yene ci kaw li xewoon, te di ko jebaane, ba tax Yeesu manatula faaral dugg cib dkk, waaye mu nekk ci biti ciy brab yu wet. Ba tey nit i jge fu nekk, di ko fa fekk.
Yeesu faj na ku lggi

1 Bi

ay fan weesoo, Yeesu dlsi dkku Kapernawum, mu

siiw ne mu ngi ci kr gi. 2 Noonu nit u bare dajaloo fa, ba kenn amatul foo taxaw, du ci bunt bi sax. Te Yeesu di len ygal kddu gi. 3 Noonu, am u ko indil ku yaramam wpp lggi, eenti nit jppoo ko. 4 Waaye manuu koo jege ndax mbooloo mi. Kon u daldi teggi kaw kr gi, di btt fa tiim brab ba Yeesu nekk, daldi yoor basa, ga lggi ba tdd. 5 Bi Yeesu gisee seen ngm, mu ne lggi ba : Sama waay, baal

nau la say bkkaar.


MRK 1 , 2 61
6 Fekk 7

ay *xutbakat toog fa, u di werante ci seen xel naan : Kii kan la, ba saa wax lii ; mi ngi sosal Ylla. Ana ku mana baale bkkaar yi, ku dul Ylla do? 8 Waaye Yeesu yg ci xelam li uy werante ci seen biir, ne len : Lu tax ngeen di werantee nii ci seen xel ? 9 Lan moo gna yomb, ma wax ku lggi ki : Baal nau la say bkkaar, walla ma wax ko : Jgal, jl sa basa, tey dox? 10 Waaye xamleen ne, *Doomu nit ki am na ci ddina sa-sau baale bkkaar yi. Ci kaw loolu mu ne lggi ba : 11 Maa ngi la koy sant, jgal, jl sa basa te nga ibbi. 12 Ca saa sa mu jl basaam te gnn fa kanam pp. Noonu pp waaru, di mggal Ylla naan : Lu mel ni lii, masunu koo gis.
Yeesu woo na Lewi
13 Gannaaw

loolu Yeesu gnnaat, aw booru dex ga, mbooloo mpp di w ci moom, mu di len jngal. 14 Bi Yeesu di romb, mu gis ku uy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko : Kaay topp ci man. Mu jg, daldi topp ci moom. 15 Bi loolu amee Yeesu ak i taalibeem di lekk ci kr Lewi, fekk ay *juutikat ak ay boroom bkkaar yu bare di lekkandoo ak oom, ndaxte u bare ci oom a ko toppoon. 16 Waaye *xutbakat yi bokk ci *Farisen yi, bi u gisee ne dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bkkaar, u daldi laaj taalibe yi : Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bkkaar ? 17 Noonu Yeesu dgg ko, mu ne len : i wr soxlawuu fajkat, i wradi oo ko soxla ; wuma woo i jub, waaye bkkaarkat yi laay woo.
Ndax warees na woor ?
18 Taalibey

*Yaxya nag ak *Farisen yi daan nau woor. u w nag fi Yeesu ne ko : Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duu woor ? 19 Yeesu ne len : Ndax gan, yi w cig cet, dinau woor, fekk boroom cet gi nd ak oom ? Duu woor, li feek boroom cet gaa ngi nd ak oom. 20 Waaye bs yaa ngi w, yu uy jle boroom cet gi ; bs boobaa nag dinau woor. 21 Kenn du daax mbubb mu mggat ak sekkit wu bees ; ndaxte sekkit wi day oddi mbubb mi, te xottiku bi gna yaatu. 22 Te kenn du def bii bu bees ci mbuusi der yu mggat. Lu ko moy, bii bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yqu, bii bi tuuru. Waaye bii bu bees, ci mbuus yu bees lau koy def.
MRK 2 62 Yeesu nee na, mooy boroom bsub noflaay bi
23 Amoon

na benn *bsub noflaay Yeesu jaar ciy tool yu or. Bi uy dem nag, ay taalibeem daldi fq ay gub. 24 Noonu *Farisen ya ne Yeesu : Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bsub noflaay bi ? 25 Yeesu ne len : Ndax jnguleen la *Daawuda defoon, ba mu amee soxla te xiif, moom ak a mu ndaloon ? 26 Xanaa yguleen li amoon ci bsi Abiyatar *sarxalkat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kr Ylla ga, lekk *mburu, ya u teewal ca kanam Ylla, jox ci it a mu ndaloon ; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat ? 27 Yeesu dellu ne len : Ylla skkul nit ngir bsub noflaay

bi, waaye skk na bsub noflaay ngir nit. 28 Noonu *Doomu nit ki mooy boroom bsub noflaay bi.
Yeesu faj na nit ku loxoom lggi

1 Am

beneen bs, Yeesu duggaat ci jngu bi, fekk

amoon na fa nit ku loxoom lggi. 2 Am na fa nag ay *Farisen, uy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci *bsub noflaay bi, ngir u man koo tuumaal. 3 Yeesu ne ku loxoom lggi : Jgal, taxaw ci kanam pp. 4 Noonu Yeesu ne len : Lan moo jaadu, nu def ko bsub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon ; nu musal nit mbaa nu rey nit ? Waaye u ne cell. 5 Ci kaw loolu Yeesu xool len ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt ; ba noppi mu ne nit ki : Tllalal sa loxo. Nit ki tllal ko, loxoom daldi wr p. 6 Ca saa sa nag Farisen ya gnn, daldi gise ak i far ak buur bi *Erodd, ngir fexe koo reylu.
Mbooloo mu bare topp na Yeesu
7 Gannaaw

loolu Yeesu ak ay taalibeem jge fa, jm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jge diiwaanu Galile, topp ko. 8 Te it nit u bare dgg la mu def, u w fi moom, jge diiwaanu Yude ak dkku *Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wlli Tir ak Sidon. 9-10 Booba nag Yeesu faj na u bare, ba mboolem i am i jngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, u wutal ko gaal, ngir mbooloo mi ba koo buux. 11 Fekk booba kpp ku rab jpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan : Yaa di *Doomu Ylla. 12 Waaye Yeesu gdd rab yi bu wr, ngir u ba koo siiwal.
MRK 2 , 3 63 Yeesu tnn na fukki ndaw yi ak aar
13 Gannaaw

loolu Yeesu yeg ci tund wi, woo i ko neex, u daldi w ci moom. 14 Noonu mu tnn ci fukk ak aar, tudde len ay ndawam, ngir u nd ak moom te mu ynni len, u waareji, 15 mu joxaale len sa-sau dq ay rab. 16 Fukk ak aar ii la tnn : Simo, mi mu tudde Piyeer, 17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay oom i mu wooye Bowanerses, maanaam i aaytal ni dnnu gi 18 Andare ak Filib, Bartelemi ak Mac, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simo, mi bokk ca mbooloo, ma u tudde i farlu ci moom seen rew ; 19 ak Yudaa Iskariyo mi nara wor Yeesu.
Ku sosal Xelu Ylla mi
20 Am

beneen bs Yeesu waat ca kr ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax manuoo lekk sax. 21 Bi ko ay bokkam dggee nag, u w, ngir jppsi ko naan : Dafa tggoo ak sagoom. 22 Te it *xutbakat ya jge *Yerusalem ne : *Beelsebul jpp na ko ; ci kttanu buuru rab yi lay dqe rab yi. 23 Noonu Yeesu woo len, wax ak oom ciy leb ne len : Naka la *Seytaane mana dqe Seytaane ? 24 Rew mu xeex boppam, du mana ygg. 25 Te kr gu xeex boppam, du mana ygg. 26 Bu Seytaane nag jgee, ba xeex boppam, xjjalikoo

dikkal na ko te du mana ygg, waaye dina tas. 27 Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn mana dugge ci kram, nangu alalam ? Xanaa dafay jkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj kram gpp. 28 Ci dgg maa ngi leen koy wax, lpp dees na ko baal nit i, muy bkkaar, muy sosal Ylla wu mu mana doon. 29 Waaye kuy sosal *Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk ; gddu na bkkaar ba fww. 30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nau, rab jpp na ko.
Ndeyu Yeesu ak ay rakkam
31 Noonu

ndeyu Yeesu ak ay rakkam w, u taxaw ci biti, ynnee, woo ko. 32 Fekk booba mbooloo nga toog, wr ko. u ne
MRK 3 64

ko nag : Sa yaay ak say rakk u ngi taxaw ci biti, di la laaj. 33 Waaye Yeesu ne len : Kan mooy sama ndey ? an ooy samay rakk ? 34 Noonu mu xool i ko wr naan : Sama yaay ak samay rakk a ngii ; 35 ndaxte kuy def coobarey Ylla, kooku mooy sama rakk ak sama jigen ak sama ndey.
Lebu beykat bi

1 Am

beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jnglewaat.

Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yeg cig gaal, dugg ca dex ga ; mbooloo mpp taxaw ca tefes ga. 2 Noonu Yeesu daldi len jngal lu bare ciy leb. Ci njngleem nag mu ne len : 3 Dgluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi. 4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi w, lekk ko lpp. 5 Leneen ci pepp mi wadd ci brab bu bare ay doj te new suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. 6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. 7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meul dara. 8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jg, sax, di focci ay gub ; lii ntu, ba mat fanweeri yoon lu pp la mu ji woon, lii mat jurom benn fukk, lii mat temer. 9 Noonu Yeesu ne len : Dglul bu baax, yaw mi am ay nopp. 10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wet, fukki taalibe ak aar a, ak eneen u daan nd ak oom, laaj ko ci mbirum leb yi. 11 Mu ne len : Yen may nau leen, ngeen xam mboti nguuru Ylla, waaye i ci biti leb ay mb lpp. 12 Noonu la, ngir : uy xool bu baax waaye duu gis dara, di dglu bu baax waaye duu xam dara, ngir ba u tuub seeni bkkaar te Ylla baal len. 13 Noonu Yeesu ne len : Ndax xamuleen leb wii ? Nu ngeen xame nag leb yi ci des ? 14 Ki ji nag, kddu gi lay ji. 15 Ki fete ci yoon wi mooy ki dgg, *Seytaane w ci saa si, kf kddu, gi u def ci moom. 16 Ki jot kddu gi ci brab bu bare ay doj mooy ki dgg kddu gi, nangu ko ak mbg ci saa si, 17 waaye du ygg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa u fitnaal ko ndax kddu gi, mu dggeeku ci saa si. 18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dgg kddu gi, 19 waaye soxlay ddina ak naxi alal ak bgge solu ko, tanc kddu gi, ba du me dara. 20 Ki
MRK 3 , 4 65

jot kddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dgg te nangu ko, ba jari; kii mat fanweeri yoon lu pp la u ji woon, kii mat jurom benn fukk, kii mat temer.
Lebu lmp bi
21 Yeesu

ne len itam : Ndax nit dina jl lmp, dpp ci leget walla def ko ci ron lal ? Ndax du ko wkk ? 22 Amul dara luy kumpa lu u warula siiwal, mbaa mu lqu te warul ne f. 23 Dglul bu baax, yaw mi am ay nopp. 24 Mu ne len : Seetleen bu baax li ngeen di dgg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen. 25 Ku am, dees na la dollil ; ku amul, li nga am as new, dees na ko nangu.
Lebu jiwu wi
26 Yeesu 27 Muy

teg ci ne : Nguuru Ylla dafa mel ni nit ku ji tool. nelaw walla muy xool, guddi mbaa bccg, jiwu wi sax, di mgg, te xamul naka la ko defe. 28 Suuf day me moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub. 29 Bu gub yi oree nag, mu dagg ko, ndaxte ngob jot na.
Lebu doomu fuddn gi
30 Yeesu

ne len ati : Lu nu mana mngaleel nguuru Ylla ? Walla ban leb lanu ko mana misaale ? 31 Dafa mel ni doomu *fuddn, bi gna tuuti ci jiwu ypp ; 32 waaye boo ko jiyee, day jg, mgg, ba sut gncaxi tokr ypp ; mu sax ay bnqaas yu ry, ba picci asamaan tgg ci keram. 33 Noonu Yeesu dgtal len yeneen leb yu bare yu mel ni yii, di len xamal kddu gi, aju ci lu u ttan. 34 Daawu len wax dara lu dul ciy leb. Waaye bu wetee ak ay taalibe, daan na len firil lpp.
Yeesu dalal na ngelaw li
35 Bs

booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi : Nanu jll dex gi. 36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jl ko ni mu mel ci gaal gi ; te yeneen gaal nd ak moom. 37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jg, duus yi sng gaal gi, ba mu bgga fees. 38 Fekk Yeesu tdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan : Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la ? 39 Ci kaw loolu Yeesu jg, daldi gdd ngelaw li, ne
MRK 4 66

dex gi : Noppil te dal ! Noonu ngelaw li dal, ba lpp ne nemm. 40 Yeesu ne taalibe ya : Lu tax ngeen tiit ? Ndax gmaguleen ? 41 u daldi ragal lool, naan ci seen biir : Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko dggal ?
Yeesu faj na ku rab jpp
2 Bi

1 Noonu

u jll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa *Serasa.

Yeesu gnnee gaal gi, nit ku rab jpp jge ca sg ya, daldi w kar ko. 3 Kooku nag ca sg ya la dkk, te kenn manu koo yeew, du ak cllala sax. 4 Ndaxte ay yoon yu bare jngoon nau ko te yeew ko ak ay cllala, waaye waa ji daldi dagg cllala yi te damm jng yi, ba kenn amul woon kttanu tye ko. 5 Guddi ak bccg mu nga woon ca sg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer. 6 Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam, 7 di xaacu naan : Yaw Yeesu *Doomu Ylla Aji Kawe ji, loo may fexeel ? Ci turu Ylla, bu ma mbugal. 8 Ndaxte

Yeesu da ko ne : Yaw rab wu bon wi, gnnal ci nit ki. 9 Noonu Yeesu laaj ko : Noo tudd ? Mu ne ko : Coggal laa tudd, ndaxte u bare lanu. 10 Muy aan Yeesu lool, ngir mu ba lena dq ca rew ma. 11 Fekk amoon na fa ca tund wa gttu mbaam-xuux yu bare yuy for. 12 Rab ya aan Yeesu : Jox nu ndigal, nu dugg mbaamxuux ya. 13 Mu may len ko. Noonu rab ya gnn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, u daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nau aari junni. 14 Noonu smm ya daw ca dkk ba ak ca ll ba, nettaliji mbir mi, ba nit i w, seet li xew. 15 u w nag ci Yeesu, gis ka rab ya jppoon toog, sol ay yre te nd ak sagoom. u daldi ragal. 16 a fekke woon mbir ma nag nettali len mbirum nit ka ak mbaamxuux ya. 17 Ci kaw loolu u daldi aan Yeesu, mu sore seen rew. 18 Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jppoon aan Yeesu, ngir nd ak moom. 19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko : ibbil ci say bokk, nettali len ni la Boroom bi yrme, ba defal la lii lpp. 20 Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dkk yi, daldi fa ygle la ko Yeesu defal, ba pp waaru.
Yeesu dekkal na doomu Yayrus te faj jigen
21 Noonu

Yeesu jllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit u bare dajaloo, wr ko. 22 Kenn ci njiiti jngu ba nag, tudd Yayrus, w
MRK 4 , 5 67

ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tnkam, 23 di ko sarxu lu bare naan : Sama doom ju jigen mi ngi bgga faatu ; kaay *teg ko loxo, ngir mu wr te dund. 24 Noonu Yeesu nd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu ry topp ko, di ko tanc. 25 Amoon na fa nag jigen ju doon xpp deret diirub fukki at ak aar. 26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, snk ci alalam jpp te jlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku. 27-28 Noonu mu dggoon turu Yeesu, ne ci boppam : Su ma laalee ay yreem rekk, dinaa wr. Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam. 29 Ci saa si deret ji taxaw, mu yg ci yaramam ne jngoroom de na. 30 Yeesu yg ci saa si ne, doole gnn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi : Ana ku laal samay yre ? 31 Ay taalibeem ne ko : Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wr ; ngay laaj : Ku ma laal ? 32 Waaye Yeesu di xool li ko wr, ngir gis ku ko def. 33 Noonu jigen ja w, daanu ciy tnkam, wax ko dgg gpp ; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam. 34 Yeesu ne ko : Soxna si, sa ngm faj na la ; demal ci jmm, te na sa jngoro wcc. 35 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jge ca kr njiit la, mu w naan : Sa doom faatu na ; matatul nuy sonal kilifa gi. 36 Waaye Yeesu jppul wax jooju ; mu ne njiit la : Gmal rekk te baa tiit. 37 Noonu Yeesu dem, nd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu nd ak moom. 38 Naka lau w ci kr njiit li, Yeesu dgg coow li ; ii di jooy, ii di yuuxu. 39 Mu dugg ne len : Lu ngeen di soow, tey jooy ? Janq bi deewul, day nelaw rekk. 40 Waaye u di ko aawal. Noonu Yeesu gnne pp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak i mu ndal, dugg fa janq bi nekk. 41 Mu jpp loxoom ne ko : Talita kumi, liy tekki : Janq bi, maa ngi la koy wax, jgal. 42 Ca saa sa janq bi jg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at

ak aar. pp daldi waaru, ba ne jomm. 43 Ci kaw loolu Yeesu dnk len bu wor, u ba koo siiwal ; teg ca naa : Mayleen janq bi, mu lekk.
Yeesu ci dkku Nasaret

1 Bi

loolu amee Yeesu jge fa, dellu rewam, nd ak taalibe

yi. 2 *Bsub noflaay bi nag mu jngal len ci seen jngu, ba mbooloom i ko dgg waaru naan : Lii, fu mu ko jle, te
MRK 5 , 6 68

xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kemaan yii ? 3 Ndax kii du minise bi ? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simo? Te ay rakkam yu jigen ndax nekkuu fi ak nun ? Kon nag u daldi ko xeeb. 4 Noonu Yeesu ne len : Dees na faaydaal yonent, waaye du ci rewam, ciy bokkam mbaa ci kram. 5 Yeesu manu faa def ay kemaan yu bare, lu dul *teg loxo yenn jarag, wral len. 6 Mu waaru ndax seen ngmadi.
Yeesu ynni na fukki taalibe ya ak aar

Bi loolu amee Yeesu di wr dkk ya, di jngle. 7 Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak aar, jox len sa-sau dq rab yi, ynni len, u nd aar-aar. 8 Mu digal len nii : Bu ngeen di dem, buleen ybbaale dara ; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk. 9 Sol-leen ay dll te yem ci benn turki. 10 Mu ne len : Kr gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jge dkk ba. 11 Koo xam ne gntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, gnnleen fa, ylb seen pndu tnk, ngir seede len seen rer. 12 Noonu taalibe ya dem, di waare naan : Tuubleen seeni bkkaar. 13 u dq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wral len.
Yaxya faatu na
14 Noonu

*Erodd buur bi dgg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag : *Yaxya dekki na, moo tax mu nd ak kttanu def ay kemaan. 15 eneen ne : Kii *Ilyaas la. i ci des ne : Yonent la, bu mel ni yonent yu jkk ya. 16 Waaye bi ko Erodd dggee, mu ne : Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki. 17 Fekk Erodd ynnee woon na, jpp Yaxya, yeew ko, tj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojdd jabaru Filib magam. 18 Te Yaxya ne ko : Jaaduwul nga denc sa jabaru mag. 19 Moo tax Erojdd mbal ko mer, ba bgg koo rey, waaye manu koo def. 20 Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba smm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan dglu it, day jaaxle lool, teewul mu bg ci dglu ko. 21 Noonu bs bu yell w, ba Erodd doon mggal bsu juddoom ; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay *xare ba
MRK 6 69

ak njiiti diiwaanu Galile. 22 Booba doomu Erojdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan i, ba buur bi ne janq bi : Laaj ma loo bgg, dinaa la ko jox. 23 Mu boole ci ngi ne ko : Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wllu rew mi sax.

24 Noonu

janq bi gnn ne ndeyam : Lu may laaj ? Mu ne ko : Laajal boppu Yaxya. 25 Mu daldi gaawantu dugg nag ci kanam buur bi ne ko : Damaa bgg, nga indil ma legi boppu Yaxya ci biir ndab. 26 Bi ko buur ba dggee, mu am naqar wu ry. Waaye bggu koo gntu ndax ngi li ak gan i. 27 Mu daldi ynni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba, 28 indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam. 29 Ba taalibey Yaxya dggee loolu, u w, fab new ba, suul ko ci bmmeel.
Yeesu bareel na ay mburu
30 Gannaaw

loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li u def ak li u jngle lpp. 31 Ci kaw loolu Yeesu ne len : Nanu beddeeku, dem ci brab bu wet ; ngeen noppalu fa tuuti. Waxoon na loolu, ndaxte amoon na u bare u doon dem ak a dikk, ba amuu sax jot ngir lekk. 32 Noonu u dugg cig gaal, dem ca brab bu wet. 33 Bi uy dem nag, am u len gis, xmmi len, u daldi jge ci dkk ypp, daw, jiitu len fa. 34 Bi Yeesu gnnee gaal gi, mu gis mbooloo mu ry, yrm len, ndaxte daoo mel ni xar yu amul smm. Kon mu daldi len jngal lu bare. 35 Ca ngoon sa taalibe yi w ci moom ne ko : Fii llub neen la, te legi mu guddi. 36 Yiwil mbooloo mi nag, u dugg ci ll bi ak dkk yi nu wr, jnd lu u lekk. 37 Waaye Yeesu ne len : Yen joxleen len lu u lekk. u ne ko : Xanaa nu jnd lu tollook peyu jurom etti weer ci mburu, jox len u lekk ? 38 Yeesu laaj len : aata mburu ngeen am ? Demleen seeti. u dem seeti ne ko : Juromi mburu ak aari jn. 39 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, u def ay gew, toog ci ax mu naat mi. 40 u toog nag ay gewi jurom fukk ak temer. 41 Bi loolu amee Yeesu jl juromi mburu yi ak aari jn yi, xool ci kaw, sant Ylla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir u sddale ko mbooloo mi. aari jn yi it mu sddale ko pp. 42 Noonu pp lekk ba suur. 43 Te it u dajale la desoon ca dammiti mburu ak jn ya, mu nekk fukki pae ak aar yu fees. 44 u lekkoon nag matoon na limu juromi junniy gor.
MRK 6 70 Yeesu dox na ci kaw ndox mi
45 Ci

kaw loolu Yeesu sant ay taalibeem, u dugg ci gaal gi, jll ba Betsayda, bi muy yiwi mbooloo mi. 46 Bi mu tggtoo ak mbooloo mi, mu yeg ca tund wa, aan fa Ylla. 47 Noonu guddi jot, fekk gaal gi nekk ci diggu dex gi, te Yeesu rekk moo nekk ca tefes ga. 48 Booba mu gis taalibe yi sonn lool ci joow gaal gi ndax li len ngelaw li soflu. Ca njl nag mu jm ci oom, di dox ci kaw dex gi, ba xaw lena raw. 49 Bi u ko gisee nag, muy dox ci kaw dex gi, u foog ne njuuma la, daldi yuuxu. 50 Ndaxte pp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak oom ci saa si ne len : Takkleen seen fit, man la, buleen tiit ! 51 Noonu mu fekksi len ci gaal gi, ngelaw daldi ne tekk. 52 Njqarey taalibe ya nag weesu dayo, ndaxte seen xol dafa fatt, ba rere mbir kemaan, gi Yeesu defoon ci mburu yi. 53 Bi nga xamee ne jll nau, ba egg diiwaanu Senesaret, u teer fa, 54 gnn ca gaal ga. Ci saa si nit i xmmi ko, 55 u daldi daw ca diiwaan ba bpp, te fpp fu u ko dgg u di ko indil u wopp, tdd ci seeni lal. 56 Te fu mu mana aw, ci dkk yu mag

mbaa yu ndaw walla ci ll bi, u indil ko jarag yi ci pnc yi, aan ko, mu may len u laal cati mbubbam rekk. Te kpp ku ko laal daldi wr.
Farisen ya ak aada ya

1 Amoon

na bs nag, ay *Farisen ak ay *xutbakat yu jge

*Yerusalem w ci Yeesu. 2 u gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuu woon, ni ko aada santaanee. 3 Farisen yi nag oom ak Yawut yi ypp dauy topp aaday yoon, yi maam yi tral, te fandee len gnal lekk ak loxo yu u raxasul. 4 Te it bu u jgee pnc ma, su u sanguwul set, duu lekk. Am nau it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga wara raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba u laab. 5 Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne : Lu tax say taalibe duu topp aaday yoon, yi maam yi tral, waaye uy lekk ak loxo yu setul ? 6 Yeesu ne len : *Esayi waxoon na bu baax ci kddug Ylla ci seen mbir, yen naafq yi, bi mu bindee : Xeet wii, u ngi may teral ci seen gmmi, waaye seen xol sore na ma. 7 Seen mggal amul benn njari, ci li uy jngle dnkaaney nit kese.
MRK 6 , 7 71
8 Yeesu

neeti len : Dddu ngeen ndigali Ylla, jublu ci aaday nit. 9 Mu teg ca ne len : Xelu ngeen ci tebbi ndigali Ylla, ngir smm seen aada. 10 Ndaxte *Musaa nee na : Teralal sa ndey ak sa baay, teg ca ne : Ku molu sa yaay walla sa baay, dees na la rey. 11 Waaye yen dangeen ne : ku ne sa yaay walla sa baay : Li nga wara jarioo ci man Korban la, maanaam saraxu Ylla la 12 dootuleen ko byyi, mu defal dara ndeyam walla baayam. 13 Noonu tebbi ngeen kddug Ylla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yena ngi def yeneen yu bon yu mel nii. 14 Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne len : Yen pp dgluleen ma te xam. 15-16 Li ci biti, tey dugg nit, du ko mana indil sobe, waaye li gnn ci nit, loolu mooy indil nit sobe. 17 Bi nga xamee ne jge nau ci mbooloo mi, dugg ci kr gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil len wax ju lqu jooju. 18 Yeesu ne len : Ndax yen itam seen xol dafa tju ? Xanaa xamuleen ne, dara lu jge biti, dugg ci nit, du ko mana indil sobe, 19 ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jm, ba noppi daldi gnn ca brab bu lqu ? Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bpp am. 20 Yeesu ne len ati : Li gnn ci nit, loolu mooy indil nit sobe. 21 Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jge ak ndoxaanu yqute, ccc ak bom, 22 njaaloo ak bgge, coxor, naafq, aawteef, eetaan, saaga, rylu ak jfi ndof. 23 Lu bon loolu lpp day gnn ci nit, di ko indil sobe.
Yeesu faj na doomu jigen, ja dkk Tir
24 Gannaaw

loolu Yeesu jge fa, jm weti dkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kr, te bggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe. 25 Amoon na fa nag jigen ju rab jpp doomam ju jigen. Bi mu dggee ne, Yeesoo nga fa, mu w, daanu ciy tnkam, 26 fekk jigen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wlli Fenisi ci diiwaanu Siri.

Noonu jigen ja aan ko, mu dq rab wi ci doomam. 27 Waaye Yeesu ne ko : Na gone yi jkka lekk, ba regg ; fab amu gone yi, snni ko xaj yi, rafetul. 28 Jigen ji ne ko : Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi. 29 Ci kaw loolu Yeesu ne ko : Ndax wax jooju demal ci jmm, rab wa gnn na sa doom. 30 Noonu mu ibbi, fekk doom ji tdd cib lal te mucc ci rab wi.
MRK 7 72 Yeesu faj na ku tx te luu
31 Bi

loolu amee Yeesu jge na weti Tir, jaar ci wlli dkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi uy wax Fukki dkk yi. 32 Foofa u indil ko ku tx te dr lool, aan ko mu *teg ko loxo. 33 Noonu Yeesu ybbu ko, ba u sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal lmmiam. 34 Mu yrm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne : Effata, liy tekki Ubbikuleen. 35 Ci saa si ay noppam daldi dgg te lmmiam yiwiku, muy wax bu leer. 36 Bi mu ko defee Yeesu tere len, u wax ko kenn, waaye lu mu len ko gna tere, u gn ko nee siiwale. 37 u waaru lool naan : Lpp lu mu def, lu yeme la. May na sax tx yi uy dgg, ak luu yi uy wax.
Yeesu bareel na mburu yi aareel bi yoon

1 Ca

bs yooya mbooloo mu ry amaatoon

na, te amuu woon lu u lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne len : 2 Yrm naa mbooloo mi, ndaxte toog nau fi man etti fan, te amatuu lu u lekk. 3 Su ma len yiwee ak seen xiif, dinau tle ci yoon wi, ndaxte am na u jge fu sore. 4 Taalibe yi ne ko : Waaye fii llub neen la ; fu nuy jle lu doy ngir dundal len ? 5 Yeesu laaj len : aata mburu ngeen am ? u ne ko : Jurom aar. 6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, u toog ci suuf. Mu jl jurom aari mburu yi, sant Ylla, damm len, jox len taalibe yi, ngir u sddale len mbooloo mi ; taalibe yi def ko. 7 Amoon na fa it tuuti jn yu ndaw. Yeesu jl ko, sant Ylla, wax taalibe yi, u sddale len itam mbooloo mi. 8 Noonu nit i lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale jurom aari dmba yu fees ak dammit yi ci des. 9 a ko fekke nag matoon nau eenti junniy gor. 10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi len, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wlli Dalmanuta.
Kemaan gu jge ci asamaan
11 Noonu

*Farisen yi w, di werante ak moom ; u fexe koo fiir, ba laaj ko kemaan gu jge ci asamaan tey firndeel ynnentam. 12 Waaye Yeesu binni ci xolam ne len : Lu tax niti jamono jii di laaj kemaan ? Ci dgg maa ngi leen koy wax,
MRK 7 , 8 73

duu jot genn kemaan. 13 Ci kaw loolu Yeesu byyi len, duggaat ci gaal gi, di jll dex gi.
Lawiiru Farisen yi
14 Taalibe

yi nag ftte woon nau ybbaale mburu, te amuu woon lu dul benn mburu ci gaal gi. 15 Noonu Yeesu artu len ne : Wottuleen te moytu lawiiru *Farisen yi ak i far ak buur

bi *Erodd. 16 Taalibe yi nag daldi werante naan : Nun de indaalewunu mburu. 17 Waaye Yeesu yg loolu ne len : Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu ? Xanaa gisaguleen te xamuleen ? Ndax seen xol dafa fatt ba tey ? 18 Ndax ay gumbay njccaar ngeen, te seeni nopp naqari ? Xanaa fttalikuwuleen ; 19 bi ma dammee juromi mburu ya ngir juromi junni a, aata pae yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon ? u ne ko : Fukk ak aar. 20 Yeesu neeti len : Te bs bi ma dammee jurom aari mburu yi ngir eenti junni i, aata dmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon ? u ne ko : Jurom aar. 21 Noonu Yeesu ne len : Ndax seen xol dafa tju ba tey ?
Yeesu faj na ku gumba ca dkku Betsayda
22 Gannaaw

loolu u w ci Betsayda. Foofa u indil Yeesu ku gumba, di ko aan, mu laal ko. 23 Yeesu nag jpp loxob gumba gi, ybbu ko, ba gnn dkk bi. Mu def tiflit ciy btam, *teg ko loxo naan : Ndax gis nga dara ? 24 Waa ji xool ne ko : Gis naa ay nit, u mel ni ay garab, te u ngi dox. 25 Kon Yeesu laalaat bt yi, gumba gi ne xefeet, daldi wr, ba gis lpp bu leer. 26 Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ibbi ne ko : Bul dugg ca dkk ba.
Piyeer wax na ne, Yeesu mooy Almasi bi
27 Bi

loolu amee Yeesu nd ak ay taalibeem, dem ca dkk, yi wr Sesare bu Filib. Bi uy dem nag, mu laaj taalibe yi : Nit i, lu u wax ne man moom laa ? 28 u ne ko : Am na uy ne yaa di *Yaxya ; eneen ne, *Ilyaas ; i ci des ne yaay kenn ci yonent yi. 29 Noonu Yeesu laaj len : Yen nag, ku ngeen wax ne moom laa ? Piyeer ne ko : Yaa di *Almasi bi. 30 Ci kaw loolu Yeesu dnk len bu wor, u ba koo wax kenn.
MRK 8 74 Yeesu xamal na ne dina dee, dekki
31 Booba

Yeesu tmbali na lena xamal ne, *Doomu nit ki war na sonn lu bare ; njiit ya, *sarxalkat yu mag ya ak *xutbakat ya dddu ko, u rey ko, mu dekki ci etti fan. 32 Noonu mu xamal len mbir mi, ba mu leer n. Bi ko Piyeer dggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd. 33 Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko : Sore ma *Seytaane ; yfi nit ngay fonk, waaye du yfi Ylla. 34 Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne len : Ku bgga topp ci samay tnk, na byyi boppam te gddu bant bi u ko wara daaj, doora topp ci man. 35 Ndaxte koo xam ne bgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko kk, waaye ku kk sa bakkan ngir man ak ngir xibaaru jmm bi, dinga ko jotaat. 36 Ndaxte moom ddina spp, lu muy jari nit, bu kkee bakkanam ? 37 Te nit, lu mu wara weccee bakkanam ? 38 Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax ci kanam niti jamono jii, i fecci seen kllre ak Ylla te topp bkkaar, Doomu nit ki dina la rusa xam, bs bu wee ci ndamu Baayam, nd ak malaaka yu sell yi.

1 Mu

ne len ati : Ci dgg maa ngi leen koy wax, am na

i fi taxaw, oo xam ne duu dee, te gisuu nguuru Ylla w ak doole.


Ndamu Yeesu jolli na ci moom
2 Jurom

benni fan gannaaw gi, Yeesu ndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu ybbu len oom rekk fu wet ci tund wu kawe lool. Foofa jmmam soppiku ci seen kanam ; 3 ay yreem di ray-rayi, weex tll, te fotukatu ddina manu len weexale nii. 4 Noonu u gis yonenti Ylla *Ilyaas ak *Musaa, di wax ak Yeesu. 5 Piyeer daldi ne Yeesu : Kilifa gi, bg nanu ci sunu teew fii ; nanu defar etti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas. 6 Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jpp na len oom ett pp. 7 Noonu niir muur len, te baat jibe ca niir wa naan : Kii mooy sama Doom ji ma bgg, ci moom laa ame bnneex ; dgluleen ko. 8 Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuu kenn ku dul Yeesu rekk. 9 Bi loolu amee u wcc ca tund wa. Bi muy wcc nag, Yeesu sant len ne : Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera *Doomu
MRK 8 , 9 75

nit ki dekki na. 10 u tye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki. 11 Noonu taalibe yi laaj Yeesu : Lu tax *xutbakat yi di naan, Ilyaas moo wara jkka w ? 12 Yeesu ne len : Waaw, Ilyaas dina jkka w, jubbanti lpp. Waaye itam lu tax bind nau ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, u xeeb ko, dddu ko. 13 Waaye maa ngi leen di wax ne, Ilyaas w na, te def nau ko la len neex, ni ko Mbind mi waxe.
Yeesu faj na xale bu rab jpp
14 Bi

nga xamee ne Yeesu w na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare wr len, te ay *xutbakat di werante ak oom. 15 Naka la mbooloo mi gis Yeesu, u waaru, daldi daw nuyu ko. 16 Noonu Yeesu laaj len : Ci lan ngeen di werante ak oom ? 17-18 Kenn ci mbooloo mi ne ko : Kilifa gi, rab jpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jppee, daf koy daaneel ci suuf, gmmi gi di fuur, muy yyu, ne jdd. aan naa say taalibe, u dq ko, waaye manuu ko. 19 Yeesu ne len : Yen niti jamono jii, yen i gmadi, ba ka laa wara nekk ak yen, ba ka laa leen wara mual ? Indil-leen ma xale bi. 20 u indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gmmi giy fuur. 21 Yeesu laaj baay bi : Lii ka la ko dal ? Baay bi ne ko : Li dale ci ngoneem. 22 Leg-leg rab wi bmx ko ci sawara, leg-leg mu bmx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yrm nu te xettali nu. 23 Yeesu ne ko : Nga ne : Soo ko manee, ku gm man na lpp. 24 Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan : Gm naa, dqal ma sama ngmadi. 25 Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wrsi ko, mu daldi gdd rab wi nag ne ko : Gnnal ci moom, yaw rab wu luu te tx, te bu ko jppaat ; wax naa la ko. 26 Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, gnn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax u bare ne : Dee na. 27 Waaye Yeesu jpp loxoom, jgloo ko, xale bi daldi taxaw. 28 Bi Yeesu duggee ci kr gi, taalibe yi laaj ko ci pegg : Lu tax manunu ko woona dq ? 29 Yeesu ne len : Yu mel ni yii,

aan ci Ylla rekk a len di dq. 30 Bi loolu amee u jge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bggul kenn yg ko. 31 Ndaxte muy jngal taalibe yi ne len :
MRK 9 76

Dees na jbbal *Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinau ko rey, mu dekki ci etti fan. 32 Waaye taalibe yi xamuu lu wax joojuy tekki, te emewuu ko koo laaj.
Kan moo gna mgg ?
33 Bi

nga xamee ne egg nau dkku Kapernawum, te dugg ci kr gi, Yeesu laaj len ne : Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi ? 34 Waaye u ne cell, ndaxte u ngi fa doon werante, ba xam ku gna mgg ci oom. 35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak aar ne len : Ku bgga jiitu, na topp ci gannaaw pp te nekk surgab pp. 36 Bi ko Yeesu waxee, mu jl xale, indi ko ci biir gew bi, ba noppi leewu ko naan : 37 Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu ; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma ynni.
Waa jiy dq ay rab
38 Bi

loolu amee Yowaana ne ko : Kilifa gi, danoo gis nit kuy dq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun. 39 Waaye Yeesu ne ko : Buleen ko tere, ndaxte kenn manula def kemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab. 40 Ku nu sotul, far na ak nun. 41 Ci dgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yena ngi bokk ci man *Kirist, kooku du kk yoolam mukk.
i ybbe nit bkkaar
42

Waaye ku ybbe bkkaar kenn ci i gna tuuti i ma gm, li gn ci moom, moo di u takk *doj wu ry ci baatam, snni ko ci gej. 43-44 Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay ybbe bkkaar, dagg ko. Ndaxte kk loxo te tbbi ci dund gu wor gi, moo gn ci yaw, nga am aari loxo te tbbi ci sawara su dul fey mukk. 45-46 Te bu la sa tnk di ybbe bkkaar, dagg ko. Nga lafa te tbbi ci dund gu wor gi moo gn, nga am aari tnk, u snni la ci sawara. 47 Te bu la sa bt di ybbe bkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Ylla, moo gn ci yaw, nga am aari bt, u snni la ci sawara. 48 Foofa : Sax ya duu dee mukk, te sawara sa du fey. 49 pp sawara lau len di xorome. 50 Xorom lu baax la, waaye bu sppee, nan lau koy delloo cafkaam ? Amleen xorom te ngeen jmmoo.
MRK 9 77 Pase

10

1 Gannaaw

loolu Yeesu jge fa, dem ca wlli rewu Yawut

yi, ya ca gannaaw dexu Yurdan. Bi mu fa demee, mbooloo mu bare w fi moom. Yeesu daldi len jngal, ni mu ko daan defe. 2 Noonu ay *Farisen w ci moom, lalal ko fiir, u laaj ko : Ndax jaadu na, nit fase soxnaam ? 3 Yeesu ne len : Lu leen yoonu *Musaa sant ? 4 u ne ko : Musaa maye na, nit bind kayitu pase, tggook soxnaam. 5 Waaye Yeesu ne len : Dnkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt. 6 Waaye ca njlben ga Ylla skk na len, kii gor,

kii jigen. 7 Looloo tax gor di teqalikook ndeyam ak baayam, nd ak soxnaam, 8 oom aar doon benn. Kon nekkatuu aar waaye benn lau. 9 Lu Ylla takk nag, bu ko nit tas. 10 Bi u delloo ca kr ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu. 11 Noonu Yeesu ne len : Ku fase sa soxna, takk jeneen, njaaloo nga, di too ku jkk ka. 12 Te jigen ji tas, syaat ak keneen, njaaloo nga.
Xale yu ndaw yi
13 Bi

loolu wyee u indil Yeesu ay xale, ngir mu *teg len ay loxoom. Waaye taalibe ya gdd nit i. 14 Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne len : Byyileen xale yi, u w fi man ! Buleen len tere, ndaxte u mel ni oom oo yelloo nguuru Ylla. 15 Ci dgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Ylla, doo ci mana dugg. 16 Noonu Yeesu leewu len, teg len ay loxoom, barkeel len.
Waxambaane wu bare alal
17 Gannaaw

loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko : Kilifa gu baax gi, lu ma wara def, ngir am wll ci dund gu dul jeex gi ? 18 Yeesu ne ko : Lu tax nga wooye ma ku baax ki ? Ylla rekk a baax. 19 Xam nga ndigal yi : Bul bome, bul njaaloo, bul scc, bul seede lu dul dgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay. 20 Waa ji ne ko : Kilifa gi, loolu lpp smm naa ko li dale ci samag ndaw ba tey. 21 Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko : Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, jox ko miskin yi, te
MRK 10 78

dinga woomle ci asamaan ; boo noppee, nga w topp ci man. 22 Waaye ci wax jooju xar kanamam lndm, mu jge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la. 23 Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wr ne len : Boroom alal dugg ci nguuru Ylla, lu jafee ngoogu ! 24 Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti len : Samay xarit, dugg ci nguuru Ylla, lu jafee ngoogu ! 25 Gilem jaar ci bnbnu puso moo gna yomb boroom alal dugg ci nguuru Ylla. 26 Wax jooju gnatee jaaxal taalibe ya, u naan ci seen biir : Kon nag ku mana mucc ? 27 Noonu Yeesu xool len naan : Loolu t na nit, waaye twul Ylla ; Ylla man na lpp. 28 Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne : Nun de dddu nanu lpp te topp la ! 29 Yeesu ne ko : Ci dgg maa ngi leen koy wax, kpp ku dddu kr, doomu ndey yu gor walla yu jigen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xibaaru jmm bi, 30 dinga am tey jii temeri yoon ay kr, doomi ndey yu gor ak yu jigen, ndey, doom ak suuf, oom ak ay fitnay noon, te llg nga am dund gu dul jeex. 31 Waaye u bare ci i jiitu ooy mujji ; i mujj ooy jiituji.
Yeesu xamle na ne dina dee, dekki
32 Gannaaw

loolu u nd jm *Yerusalem, Yeesu jiitu ; taalibe yi am njqare, te i ci topp tiit. Noonu Yeesu woowaat fukk ak aar a cig wet, xamal len li nara xew ci mbiram. 33 Mu ne len : Noo ngi dem Yerusalem, te dees na jbbal *Doomu nit ki ci loxoy *sarxalkat yu mag ya ak *xutbakat ya. Dinau ko tte, teg ko dee, jbbal ko i dul Yawut, 34 u aawal ko, di tifli ci kawam, dor ko ay yar, rey ko. Waaye gannaaw etti fan dina

dekki.
Li doomi Sebede aan Yeesu
35 Gannaaw

loolu Saag ak Yowaana, doomi Sebede, w ci Yeesu. u ne ko : Kilifa gi, danoo bggoon nga may nu li nu lay aan. 36 Yeesu ne len : Lu ngeen bggoon, ma may leen ko ? 37 u ne ko : Bs boo soloo sa ndam, nga may nu, nu toog, kii ci sa ndijoor, kii ci sa cmmo. 38 Waaye Yeesu ne len : Xamuleen li ngeen di aan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan ? Ndax man ngeena sobu ci metit, yi ma nara sobu ? 39 u ne ko : Waaw, man nanu ko. Noonu Yeesu ne len : Dingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey
MRK 10 79

sobu ci metit, yi ma nara sobu, 40 waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama cmmo, du man maa koy maye. i u ko waajal rekk a ko yelloo. 41 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des dgg nau loolu, u daldi mere Saag ak Yowaana. 42 Waaye Yeesu woo len naan : Xam ngeen ne ci xeeti ddina, i u teg njiit dau len di dor yetu nguur, te kilifa yi di len not. 43 Buleen mel ni oou. Waaye ku bgga nekk kilifa ci yen, na nekk seen surga, 44 te ku bgga nekk njiit, na nekk seen jaam. 45 Ndaxte noonu la *Doomu nit ki we sax, du ngir u nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir *njotug u bare.
Yeesu faj na ku gumba
46 Bi

loolu wyee u agsi ca dkku Yeriko. Bi ko Yeesu di gnn, nd ak taalibe ya ak mbooloo mu xawa bare, am gumba gu tudd Bartime liy tekki doomu Time , toog ci wetu yoon wi, di yelwaan. 47 Noonu mu dgg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb ; mu daldi yuuxu naan : Yrm ma, yaw *Stu Daawuda bi ! 48 Ci kaw loolu u bare gdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gna yuuxu naan : Yaw Stu Daawuda bi, yrm ma ! 49 Noonu Yeesu taxaw, daldi ne : Wooleen ko ! u woo nag gumba gi ne ko : Na sa xel dal ! Jgal ! Mu ngi lay woo. 50 Bi mu ko dggee, mu snni malaanam, ne brt, dem ci Yeesu. 51 Yeesu ne ko : Loo bggoon ma defal la ko ? Gumba gi ne ko : Kilifa gi, damaa bgga gis. 52 Noonu Yeesu ne ko : Demal ci jmm. Sa ngm faj na la. Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.
Yeesu dugg na Yerusalem

11

1 Gannaaw

loolu Yeesu ak taalibe ya jege nau

*Yerusalem, ba agsi dkki Betfase ak Betani ci wetu *tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal aar ciy taalibeem, 2 ne len : Demleen ci dkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi. 3 Bu leen kenn nee : Lu ngeen di def ? neleen ko : Boroom bi da koo soxla, te legi mu delloosi ko. 4 Taalibe ya dem nag, u gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kr. 5 Bi u koy yiwi nag, am na ca a fa taxaw, u ne len : Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi ? 6 Taalibe yi wax len, ni len Yeesu digale woon, nit i byyi len, u dem.
MRK 10 , 11 80

7 u 8 u

indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yre, mu toog ci. bare lal seeni yre ci yoon wi, enn i dagg ay cari garab ci tool yi, lal len it ci yoon wi. 9 iy jiitu ak iy topp ci Yeesu pp di wax ci kaw naan : *Osaana ! Yaw miy w ci turu Boroom bi, ku barkeel nga ! 10 Nguuru sunu maam *Daawuda giy w dina barkeel ! Ci brab yu gna kawe, nau ne : Osaana ! 11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kr Ylla ga, xool lpp, ba noppi gnn dem dkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak aar, ndaxte dafa guddi.
Yeesu dq na jaaykat ya ca kr Ylla ga
12 Bt

set u gnn Betani, fekk Yeesu xiif. 13 Noonu mu sen fu sore garabu *figg gu sq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul. 14 Ci kaw loolu mu ne garab gi : Dootuloo me mukk ! Taalibe yi dgg loolu mu wax. 15 Bi u eggee *Yerusalem, Yeesu dugg ci kr Ylla gi, daldi dq i fay jaay ak i fay jnd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi, 16 te mayul kenn, mu ybbu am njaay ci kr Ylla gi. 17 Mu di len jngal ne len : Ndax waxuu ci Mbind mi : Dees na wooye sama kr kru aan ci Ylla ngir xeet ypp. Waaye yen def ngeen ko kru scc. 18 Bi ko *sarxalkat yu mag ya ak *xutbakat ya dggee nag, u ragal ko, ndaxte mbooloo mpp daoo waaru ci njngleem. Noonu u seet pexem reylu ko. 19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi gnn dkk bi.
Garabu figg gi u rbb
20 Ci

suba si, bi uy dem, u gis ne garabu *figg gi dee na, ba wow ko. 21 Noonu Piyeer fttaliku li xewoon, ne Yeesu : Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rbb dee na, ba wow ! 22 Yeesu ne : Gmleen Ylla. 23 Ci dgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale : Jgal, tbbi ca gej ga, te nga gm ne loolu dina am, ba cee boole xel aar, kon sa aan nangu. 24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di aan Ylla, lpp lu ngeen ko mana laaj, gmleen ne jot ngeen ko, te dingeen
MRK 11 81

ko am. 25-26 Te it bu ngeen di aan, fekk ngeen jppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni too, yen itam.
Sa-sau Yeesu
27 Gannaaw

loolu u duggaat *Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca tti kr Ylla ga. Noonu *sarxalkat yu mag ya ak *xutbakat ya ak njiit ya dab ko 28 ne ko : Yf yii ngay def, ci ban sa-sa nga koy defe ? Te ku la may sa-sau def ko ? 29 Yeesu ne len : Man itam dinaa leen laaj lenn ; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sa-sa laay defe yf yii. 30 La *Yaxya daan def, di *sob nit i ci ndox, fu mu ko jle, ci Ylla walla ci nit i ? 31 Bi u ko dggee, uy werante ci seen biir naan : Bu nu nee : Ci Ylla, kon dina nu laaj : Lu tax gmuleen ko kon ? 32 Waaye bu nu nee : Ci nit i, kon mbooloo mi dal ci sunu

kaw ; ndaxte pp teg nau Yaxya ab yonent. 33 u wax Yeesu nag ne : Loolu de xamunu ko. Noonu Yeesu ne len : Kon man itam duma leen wax ci ban sa-sa laay defe yf yii.
Lebu beykat yi

12

1 Noonu

Yeesu daldi len wax ciy leb. Mu ne len :

Amoon na fi nit ku jmbt toolu rese. Mu ag tool bi, gas pax ngir nal ci rese yi, tabax wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki. 2 Bi tool bi oree nag, mu ynni surga ci oom, ngir jot wllam ci meeef gi. 3 Waaye u jpp ko, dor ko ay yar, dq ko, mu dellu ak loxoy neen. 4 Mu ynniwaat beneen surga, waaye u dor ko ci bopp, toroxal ko. 5 Mu ynneeti beneen surga, u rey ko. Mu ynni eneen u bare, ii u dor len, ii u rey. 6 Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bgg. Mujj mu ynni ko naan : Xy na u weg sama doom. 7 Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir : Kii moo wara donn tool bi ; nan ko rey, moom ndono li. 8 u jpp ko nag, rey, snni ci biti. 9 Noonu Yeesu laaj len : Boroom tool bi nag, lu muy def ? Xanaa w, rey beykat ya, dnk tool ba eneen. 10 Ndax masuleena jng wax jii ci Mbind mi ? Doj wi tabaxkat yi snni, mujj na di doju ko; MRK 11 , 12 82 11 ci Boroom bi la loolu jge, te yemu nanu ci. 12 Noonu kilifa yi di wut pexem jpp ko, ndaxte xam nau ne oom lay wax. Waaye ragal nau mbooloo mi, ba u byyi ko fa, dem. Galag gi uy fey buur bi Sesaar 13 Bi loolu amee u ynni ci Yeesu ay *Farisen ak u far ak buur bi *Erodd, ngir fiir ko ci waxam. 14 u w ci moom nag ne ko : Kilifa gi, xam nanu ne ku wor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Ylla ci bu wor. Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi *Sesaar galag am det ? Nu fey ko walla nu ba koo fey ? 15 Waaye Yeesu xam na seen naafq, mu ne len : Lu tax ngeen bgg maa fiir ? Indil-leen ma posetu *denariyon, ma seet. 16 u jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj len : Kan lau ci def nataalam ak turam ? u ne ko : Sesaar. 17 Noonu Yeesu ne len : Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Ylla li Ylla moom. u daldi waaru ci mbiram. Sadusen yi ak ndekkite li 18 Gannaaw loolu ay *Sadusen w ci moom, ngir laaj ko lenn. Sadusen yi nag gmuu ne ndekkite am na. 19 u ne ko : Kilifa gi, *Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu, te byyiwul doom ak soxnaam, kooku war na donn jigen ji, ba ykkati giiru magam. 20 Amoon na fi nag jurom aari gor, u bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te byyiwul doom. 21 aareel ba takk jigen ja, faatu moom itam te byyiwul doom. etteel bi it noonu. 22 Mbir mi dem na nag, ba jurom aar oou pp dem, te kenn byyiwu fi doom. Mujj jigen ja faatu moom itam. 23 Ci ndekkite li nag kan ci oom moo ko wara donn, fekk ku

nekk ci jurom aar i mas na koo takk ? 24 Yeesu ne len : Mbaa du dangeena nekk cig rer, ci li ngeen xamul Mbind mi mbaa kttanu Ylla ? 25 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jkkr, waaye dinau mel ni malaaka yi ci kaw. 26 Te sax li jm ci mbirum ndekkite, xanaa jnguleen lii Ylla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si : Maay Yllay *Ibraayma, Isaaxa ak *Yanqoba? 27 Li ci gnn mooy, nekkul Yllay i dee, waaye Yllay iy dund la. Kon sobu ngeen cig rer. MRK 12 83 Ban ndigal moo gna mgg ci yoonu Musaa 28 Bi uy werante, benn *xutbakat w, dgg seen waxtaan, gis ne Yeesu tontu na len tont lu leer. Mu laaj ko nag : Ci ndigal yi, ban moo ci gna mgg ? 29 Noonu Yeesu ne ko : Bii : *Dgluleen, yen bnni Israyil ! Ylla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la. 30 Kon nanga bgg Ylla sa Boroom ak sa xol bpp ak sa bakkan bpp, sa xel mpp ak sa kttan gpp. 31 Te aareel bi, lii la : Nanga bgg sa moroom, ni nga bgge sa bopp. Ndigal yii oo sut ypp. 32 Xutbakat bi ne ko : Waaw, kilifa gi, li nga wax dgg la : Ylla kenn la, te amul jeneen Ylla ju dul moom. 33 Te nga bgg ko ak sa xol bpp ak sa xel mpp ak sa kttan gpp moo dq bpp sarax bu uy ybbu ngir mggal Ylla ak bu uy lakk ca *sarxalukaay ba. 34 Bi Yeesu gisee nag ne tontu na ak xel, mu ne ko : Sorewuloo nguuru Ylla. Bi mu waxee loolu, kenn emeetu koo laaj dara. Mbaa Almasi bi mooy stu Daawuda ? 35 Bi nga xamee ne Yeesu ma nga doon jngle ca kr Ylla ga, mu laaj nit i : Lu tax *xutbakat yi di wax ne, *Almasi bi mooy *stu Daawuda ? 36 Daawuda moom wax na ci kttanu *Xel mu Sell mi naan : Boroom bi nee na sama Boroom : Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam. 37 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko : Boroom bi, nu muy nekke stam ? Noonu mbooloo mu mag mi di ko dglu ak bnneex. 38 Bi Yeesu di jngle nag, mu ne len : Moytuleen xutbakat yi ; daoo bgg di doxantu, sol ay mbubb yu ry, te pp di len nuyoo aari loxo ci pnc mi. 39 Ci jngu yi, fete kanam lauy wut, te toogu yu yiw lauy taamu ci reeri xew yi. 40 u ngi lekk alalu jigen i seeni jkkr faatu, di aan Ylla ay aani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gna tar. Saraxu soxna si 41 Noonu Yeesu toog ca kr Ylla ga, janook ndab, yi uy def sarax ngir Ylla, muy xool nit a cay dugal seen xaalis. Am nag MRK 12 84
b

12.42 Mooy posetu lepton. Seetal Xaalis ci Leeral yi.

ay boroom alal yu ci di def xaalis bu bare. 42 Gannaaw ga daal benn jigen ju jkkram faatu, te mu kk, w, def ci aari poseti xnjar b, yu matul sax drm. 43 Bi ko Yeesu gisee, mu woo taalibe yi ne len : Ci dgg

maa ngi leen koy wax, li jigen ju kk jee dugal ca defukaay ya moo pp maana alalu eneen i pp. 44 oom pp dau skk ci seen barele, waaye moom dafa skk ci newleem, ba far ko joxe lpp, toog. Yqug Yerusalem ak dellusig Doomu nit ki

13

1 Bi

Yeesu di jge ca kr Ylla ga,

kenn ca taalibe ya ne ko : Kilifa gi, xoolal ! Ni mu rye ay doj, te rafete ni ay taax ! 2 Waaye Yeesu ne len : Du gis ngeen taax yu ry yii ypp ? Lii lpp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj. 3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci *tundu Oliw ya, jkkaarlook kr Ylla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko : 4 Wax nu ka la loolu di am ? Te luy tegtal ne, mbir yii ypp a ngi bgga mat ? 5 Noonu Yeesu ne len : Moytuleen, bu leen kenn nax. 6 u bare dinau w ci sama tur naan : Moom laa, te dinau nax u bare. 7 Bu ngeen dggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit ; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul. 8 Xeet dina jg, xeex ak weneen xeet, rew xeex ak meneen rew. Te yngu-ynguy suuf dina am ciy brab yu bare, ak ay xiif. Loolu lpp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigen juy matu. 9 Moytuleen. Dees na leen jbbal ttekat ya, di leen dor ay yar ca jngu ya. Dinau leen dj ci kanam i boroom rew ak i buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci oom. 10 Fww xibaaru jmm bi jkka jib ci xeet ypp. 11 Saa su u leen jppee nag, dj leen ci pncum layoo, buleen jq ci li ngeen wara wax ; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yenay wax waaye *Xel mu Sell mi. 12 Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam ; ay doom it dinau jg, di ba seeni waajur, di len reylu. 13 Te pp dinau leen ba ndax sama tur ; waaye ku mu ba ca muj ga, mucc. 14 Bs baa ngi w, bu li uy wax Lu araam luy yqe tegee ca brab bu mu yelloowul ; kiy jng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, MRK 12 , 13 85 ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya. 15 Ku nekk ci kaw *taax mi, bul wcc ngir dugg kr gi, fab say yf ya fa nekk. 16 Ku nekk ci tool bi, bul ibbi ngir fab sa mbubb. 17 Ngalla jigen i mb ca bs yooya, ngalla it iy nmpal. 18 aanleen ngir seen gddaay baa tase ak jamonoy seddaayu lolli. 19 Ndaxte booba dina am metit wu ry wu masula am, ba ddina sosoo ak tey, te dootul am mukk. 20 Te bu fekkul woon Boroom bi wi bs yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wi len ndax gaayam i mu tnn. 21 Booba nag, bu leen kenn waxee : Kaayleen gis, *Kirist a ngi fi, mbaa : Xool-leen, mu nga fale, buleen ko gm. 22 Ndaxte iy mbubboo turu Kirist ak iy mbubboo turu yonent, dinau fee, di joxe ay firnde yu ry ak ay kemaan, ba ciy nax sax i Ylla tnn, su loolu manoona am. 23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen. 24 Waaye booba, gannaaw metit yooyu : Jant bi dina lndm te weer dootul leer ; 25 biddiiw yi di daanoo asamaan,

te kttani asamaan yiy yngu. 26 Noonu dees na gis *Doomu nit ki w ci niir yi, nd ak kttan ak ndam lu ry. 27 Dina ynni ay malaakaam, u dajale i mu tnn ci eenti xbla yi, fa ddina dale, ba fa asamaan yem. 28 Yeesu teg ca ne : Jngleen misaalu garabu *figg ga. Boo xamee ne ay bnqaasam duy nau, tey xobam sq, xam ngeen ne nawet jege na. 29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lpp xew, xamleen ne jege na ; mu ngi ci bunt bi sax. 30 Ci dgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duu wy, te loolu lpp amul. 31 Asamaan ak suuf dinau wy, waaye samay wax du wy mukk. Ylla rekk moo xam bs ba 32 Waaye bs boobu ak waxtu woowu, kenn xamul ka lay doon ; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 33 Moytuleen te xool ! Xamuleen ka la waxtu wi di jot. 34 Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dnk kram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bkk-neg bi, mu xool. 35 Yen nag xool-leen, ndaxte xamuleen ka la boroom kr gi di dlsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njl. 36 Bu nee jala, bumu leen bett, ngeen di nelaw. 37 Li ma leen wax, pp laa ko wax : Xool-leen ! MRK 13 86 Njiiti yoon yi fexeel nau Yeesu

14

1 Booba

nag *sarxalkat yu mag ya ak *xutbakat

ya u ngi doon fexeel Yeesu, ngir jpp ko, reylu. Fekk booba aari fan a des ci mggalu bsu *Mucc ba ak mggalu *Mburu ma amul lawiir. 2 Kon nag u ne : Bumu doon ci bsu mggal bi, ngir yngu-yngu baa am ci nit i. Jigen diw na boppu Yeesu ak latkolo 3 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dkku Betani, mu dem kru Simo ma *gaana woon, di fa lekk. Noonu jigen w, yor njaq lu u defare doj wu tudd *albaatar. Njaq li def latkolo ju raxul ju uy wax nrd, tey jar lu baree bare. Jigen ji toj njaq li, tuur latkolo ci boppu Yeesu. 4 Waaye amoon na fa u mer, di xultu ci seen biir naan : Yq gii, lu muy jari? 5 Maneesoon na jaay latkolo jii ci lu tollook peyug atum lmm, jox ko miskin yi. Noonu u daldi gdd jigen ji. 6 Waaye Yeesu ne len : Byyileen ko. Defal na ma jf ju rafet ; lu tax ngeen di ko sonal ? 7 Miskin yaa ngi ak yen bs bu nekk, te man ngeen lena dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba fww. 8 Jigen ji def na li mu man ; diw na sama yaram ak latkolo, ngir waajal sama rob, laata moo jot. 9 Ci dgg maa ngi leen koy wax, fpp fu uy yene xibaaru jmm bi ci ddina spp, dinau fa fttali it li jigen jii def. Yudaa wor na Yeesu 10 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak aar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca *sarxalkat yu mag ya, ngir wori Yeesu. 11 Bi u ko dggee, u am ca bnneex bu ry, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu len mana jbbal Yeesu. Reer bu mujj bi 12 Bs bu jkk ca mggal, ga uy wax *Mburu ma amul lawiir,

taalibey Yeesu laaj ko : Foo bgg, nu defaral la reeru bsi *Mucc bi ? Bs bu jkk booba nag mooy bs, ba u farala rendi gttub bsu *Mucc ba. 13 Noonu Yeesu yebal aar ci taalibe yi ne len : Demleen ca dkk ba, foofa gor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yen, ngeen topp ko. 14 Kr gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kr gi : Kilifa gi nee na : Ana negu gan, bi may lekke MRK 14 87 reeru bsu Mucc bi, man ak samay taalibe ? 15 Dina leen won neg bu fete kaw te yaa, u defar ko, ba lpp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi. 16 Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca dkk ba, gis lpp, ni len ko Yeesu waxe woon. Noonu u defar reer bi. 17 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu w, nd ak fukki taalibe yi ak aar. 18 u toog, di lekk. Bi uy lekk nag, Yeesu ne len : Ci dgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yen, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor. 19 Taalibe yi nag am naqar, u daldi ko ne kenn-kenn : Mbaa du man ? 20 Mu ne len : Kenn ci yen fukk ak aar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li. 21 *Doomu nit ki mu ngi dem, ni u ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Baoona juddu moo gn ci moom. 22 Noonu bi uy lekk, Yeesu jl mburu, sant Ylla, jox len ko naan : Jl-leen, lii sama yaram la. 23 Gannaaw loolu mu jl kaas, sant Ylla, jox len ko, pp naan ci. 24 Mu ne len : Lii mooy sama deret, ji fas kllre gi, te tuurul u bare. 25 Ci dgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum rese mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Ylla. 26 Noonu u woy Ylla, ba noppi gnn, dem ca *tundu Oliw ya. Yeesu wax na ne, Piyeer dina ko weddi 27 Booba Yeesu ne len : Yen pp dingeen ma dggeeku, ndaxte bind nau : Dinaa dor smm bi, xari jur gi tasaaroo. 28 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile. 29 Kon Piyeer ne ko : Bu la pp dggeekoo, man duma la byyi mukk. 30 Waaye Yeesu ne ko : Ci dgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab aari yoon, dinga ma weddi etti yoon. 31 Waaye Piyeer gna sax ca la mu waxoon naan : Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk. Taalibe ypp it waxe noonu. Yeesu aan na ca toolu Setsemane ci biir tiis wu ry 32 Noonu u dem ca brab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi : Toogleen fii, ma dem aani. 33 Mu nd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jq, ba xonet. 34 Mu ne len : Sama xol dafa tiis, ba ma bgga dee ; toogleen fii, xool. 35 Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di aan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoona am. 36 Mu ne : *Abba, MRK 14 88 Baay, yaw mi dara twul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am. 37 Noonu mu dlsi ci taalibe yi, fekk uy nelaw. Mu ne Piyeer : Simo, dangaa nelaw ? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu ? 38 Xool-leen te aan, ngir baa daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof. 39 Beneen yoon Yeesu dem, di aane noonu, 40 dlsiwaat, fekk len uy nelaw, ndaxte

seeni bt daoo diis. Xamuu lu u koy tontoo. 41 etteelu yoon mu dlsi ci oom ne len : Yena ngi nelaw tey noppalu ba tey ! Jeex na. Waxtu wi jot na ; u ngi wor *Doomu nit ki ci loxoy bkkaarkat yi. 42 Jgleen nu dem ; ki may wor a ngi nii, di w. Jpp nau Yeesu 43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak aar, agsi, nd ak mbooloo mu bare, mu jge ca *sarxalkat yu mag ya, ca *xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gnnaayoo jaasi ak yet. 44 Fekk ki ko naroona wor joxoon na len tegtal ne len : Ki may fon, moom la ; jppleen ko, ybbu ko te wottu ko bu baax. 45 Noonu mu w ci Yeesu ne ko : Kilifa gi, daldi ko fon. 46 Bi mu ko defee nit i song Yeesu nag, jpp ko. 47 Waaye kenn ci i fa taxaw bocci jaaseem, dor surgab sarxalkat bu mag bi, nopp bi dagg. 48 Yeesu ne len : Jg ngeen ngir jpp ma, gnnaayoo jaasi ak yet, mel ni uy topp scc. 49 Moona daan naa toog bs bu nekk ca kr Ylla ga, di jngle, te jppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am. 50 Ci kaw loolu, pp dddu ko, daw. 51 Fekk amoon na ca waxambaane wu lkkaayoo woon sr, topp Yeesu, u daldi ko jpp. 52 Waaye waxambaane wa wacc fa sr bi, daldi daw, def yaramu neen. Yeesu taxaw na ci kanam kureelu ttekat yi 53 i jpp Yeesu ybbu ko ci *sarxalkat bu mag bi, te foofa la sarxalkat yu mag yi, njiit yi ak *xutbakat yi ypp dajaloo. 54 Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ttu sarxalkat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi. 55 Noonu sarxalkat yu mag yi ak *kureelu ttekat yi ypp di wut ku mana seede lu daan Yeesu, ba u man koo reylu, waaye gisuu kenn. 56 Teewul sax naafq u bare w, seede ci Yeesu MRK 14 89 lu dul dgg, waaye seen seede nduu. 57 Ba mujj naafq taxaw, seede ci moom naan : 58 Nun daal dgg nanu, mu ne : Dinaa toj kr Ylla, gii loxoy nit liggey, tabax ci etti fan geneen gu nit liggeyul. 59 Waaye ba tey seeni wax nduu. 60 Ci kaw loolu sarxalkat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu : Doo tontu ? Lu la nit i di jii? 61 Waaye Yeesu ne cell, waxul dara. Sarxalkat bu mag bi dellu nag ne ko : Ndax yaa di *Almasi bi, *Doomu Ylla ju tedd ji ? 62 Yeesu ne ko : Moom laa. Te dingeen gis *Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di w ci niiri asamaan. 63 Bi ko sarxalkat bu mag bi dggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay yreem naan : 64 Weddi na Ylla, lu nu doyeeti seede ? Lu ngeen ci xalaat ? Noonu pp teg ko dee. 65 Ci kaw loolu u daldi tifli ci moom, takk ay btam, di ko dor ay kurfe, naan ko : Yaw wax nu ci kddug Ylla, ku la dor ? Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes. Piyeer weddi na Yeesu 66 Piyeer nag ma nga toogoon ci tt bi fete suuf. Noonu benn mbindaanu *sarxalkat bu mag ba romb fa. 67 Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jkk naan : Yaw itam ndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu. 68 Waaye Piyeer weddi ko naan : Xawma li ngay wax, dgguma ci dara. Mu daldi gnn, dem ca buntu

kr ga. 69 Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne i fa taxaw : Waa jii ci oom la bokk. 70 Waaye Piyeer weddiwaat ko. Nees-tuut i fa taxaw ne Piyeer : Yaw mi de, ci lu wor bokk nga ci, nde waa Galile nga. 71 Waaye Piyeer daldi gi ak a waat naan : Xawma nit ki ngay wax. 72 Ci saa si ginaar sab aareelu yoon. Noonu Piyeer fttaliku li ko Yeesu wax : Bala ginaar a sab aari yoon, dinga ma weddi etti yoon. Mu daldi jooy jooy yu metti. Yeesu taxaw na ci kanam Pilaat, boroom rew ma

15

1 Ci

suba teel *sarxalkat yu

mag yi gise, oom ak njiit yi ak *xutbakat yi ak *kureelu ttekat yi ypp. u yeew nag Yeesu, daldi ko ybbu, jbbal ko *Pilaat. 2 Noonu Pilaat laaj ko : Ndax yaa di buuru Yawut yi ? Yeesu ne ko : Wax nga ko. 3 Te sarxalkat yu mag yi di ko jii lu bare. 4 Kon nag Pilaat laajaat ko : Dggal lpp li u lay jii. Xanaa amoo ci tont ? 5 Waaye ba tey Yeesu waxul dara, ba tax Pilaat waaru. MRK 14 , 15 90 6 Mggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, u tnn kenn ci i u tjoon, mu byyil len ko. 7 Fekk booba amoon na ku u tj, tudd Barabas, ku bokk ci a bggoona tas rew mi, boole ci rey nit. 8 Noonu mbooloo mi w, laaj Pilaat, mu defal len la mu daan def. 9-10 Pilaat nag xam ne kiaan rekk a taxoon sarxalkat yu mag yi jbbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi : Xanaa ma byyil leen buuru Yawut yi ? 11 Waaye sarxalkat yu mag yi xiir mbooloo mi, u laaj Pilaat, mu byyil len Barabas. 12 Kon Pilaat ne len : Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi ? 13 u daldi yuuxuwaat naan : Daaj ko ci bant, ba mu dee ! 14 Pilaat ne len : Lu tax ? Gan too la def ? Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gna kawe : Daaj ko ci bant ! 15 Noonu Pilaat, mi wuta neex mbooloo mi, byyil len Barabas, ba noppi mu dorlu Yeesu ay yar, jbbal ko, ngir u daaj ko ci bant. Xarekat yi aawal nau Yeesu 16 Bi loolu amee u dugal Yeesu ci biir kr boroom rew ma, mooy brab bu uy wax Peretoriyum, u daldi woo mbooloom xarekat ypp. 17 Noonu u solal ko mbubb mu xonq curr, rbb *kaalag dg, teg ko ci boppam. 18 u daldi ko wax bu kawe : Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi ! 19 u di ko dor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, mggal ko. 20 Bi u ko aawalee noonu ba noppi, u summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yreem, ybbu ko, ngir daaj ko ci bant. Rey nau Yeesu ci kaw bant ba 21 Amoon na nag nit ku dkk *Siren, tudd Simo, di baayu Alegsndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jge ca wet, ga fete ak tool ya, u ga ko ngir mu gddu bant bi. 22 Noonu u ybbu Yeesu ca brab bu uy wax Golgota, liy tekki brabu Kaau bopp. 23 u bgg koo jox bii bu u boole ak naan gu tudd *miir, waaye nanguwu ko. 24 Foofa u daaj Yeesu ci bant, daldi sddoo ay yreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am ; 25 booba fekk yoor-yoor di jot. 26 Mbind mi xamle lu tax u rey ko nee na : Kii mooy buuru Yawut yi. 27-28 Booba it u daajaale ak moom aari

taskati rew mi, kenn ci ndijooram, ki ci des ci cmmoam. 29 a fa doon romb di ko xas, di wcc seen bopp ndax sib ko, naan : Waaw kay, yaw mi bgga toj kr Ylla gi, tabaxaat ko MRK 15 91 ci etti fan, 30 wccal ci bant bi te musal sa bopp ! 31 Noonu it *sarxalkat yu mag yi ak *xutbakat yi di ko aawal ci seen biir naan : Kii musal na eneen waaye manula musal boppam. 32 *Almasi bii, di buuru Israyil, na wcc legi ci bant bi, nu gis ko te gm. i u daajaale ak moom it di ko xarab. Yeesu saay na 33 Li tmbalee digg bccg, ba ci tisbaar, rew mpp lndm. 34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee kddu gu dgr naan : Elowi, Elowi, lema sabaktani ? liy tekki : Sama Ylla, sama Ylla, lu tax nga dddu ma ? 35 enn ci a fa taxaw nag, bi u ko dggee, u ne : Mu ngi woo yonent Ylla *Ilyaas. 36 Noonu kenn daw, jl aw sagar, capp ko ci *bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne : Byyileen, nu seet, ba xam Ilyaas dina w, wcce ko. 37 Noonu Yeesu wootewaat ak kddu gu dgr, delloo ruuwam Ylla. 38 Bi mu ko defee ridob brab bu sell ba ca kr Ylla ga xar aar, li dale ci kaw ba ci suuf. 39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne : Ci dgg, nit kii *Doomu Ylla la ! 40 Amoon na fa nag ay jigen, u len dnd, di xool. Xmmi nau ci : Maryaama mi dkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome. 41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigen oou oo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigen yu bare yu ndoon ak moom, ba w *Yerusalem. Rob nau Yeesu 42 Booba nag bsu Waajal la woon, maanaam bs bu jiitu *bsub noflaay bi. Ca ngoon sa nag, 43 Yuusufa mi dkk Arimate takk aw fitam, dem *Pilaat, laaj ko newu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci *kureelu ttekat yi, te doon sentu moom itam nguuru Ylla. 44 Bi Pilaat dggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax ygg na faatu. 45 Bi ko ko njiit li dggalee, Pilaat jox new bi Yuusufa. 46 Noonu Yuusufa jnd cngaay, wcce new bi, laxas ko ci, dugal ko cib *bmmeel bu u yett ci xeer. Bi mu ko defee mu bra aw doj, ube ko buntu bmmeel bi. 47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc. MRK 15 92 Yeesu Kirist dekki na

16

1 Bi

*bsub noflaay bi wyee, Maryaamam Magdala,

Maryaama yaayu Saag, ak Salome, jnd cuuraay, ngir dem xeeal newu Yeesu. 2 Kon bs bu jkk ci ayu-bs gi, u njlu dem ca *bmmeel ba, 3-4 di laajante : Ku nuy braal doj, wiy ub bmmeel bi ? Doj woowu nag bu rya ry la woon. Noonu u xool, gis ne doj wa de. 5 u dugg ci bmmeel bi, gis ca ndijoor waxambaane wu sol mbubb mu weex, u daldi tiit. 6 Mu ne len : Buleen tiit. Yena ngi seet Yeesum Nasaret,

mi u daajoon ci bant bi. Nekkatu fi, dekki na ; gisleen fi u ko traloon. 7 Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya : Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon. 8 Noonu jigen i gnn, dawe bmmeel ba, tiit bay lox. Te waxuu kenn dara ndax seen tiit. 9 Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca bs bu jkk ca ayu-bs ga, mu jkka feeu Maryaama mu dkk Magdala, mi mu dqe woon jurom aari rab. 10 Maryaama nag dem nettali ko i ndoon ak Yeesu, fekk uy naqarlu, di jooy. 11 Bi u dggee ne, Yeesoo ngi dund te Maryaama gis na ko, gmuu ko. 12 Gannaaw loolu Yeesu feeu aar ci oom ci jeneen jmm, uy jaar ci yoon wi, jm ll ba. 13 u waiku nag, wax ko a ca des, waaye ba tey gmuu len oom it. 14 Gannaaw ga it Yeesu feeu fukki taalibe yi ak benn, bi uy lekk. Mu yedd len ndax seen ngmadi ak seen dgr bopp, ci li u baa gm i ko gisoon, bi mu dekkee. 15 Mu ne len : Demleen ci ddina spp, ygal xibaaru jmm bi mbindeef ypp. 16 Ku gm te u *sob ko ci ndox, dina mucc ; ku gmul, dees na ko daan. 17 i ma gm dinau nd ak firnde yii : ci sama tur dinau dq rab yi, di wax lkk yu bees, 18 di jpp jaan ak seeni loxo ; te bu u naanee lu u tooke, du len wi dara, te jarag ju u *teg loxo, mu wr. 19 Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak oom, mu ykkatiku, dem asamaan, toog ci ndijooru Ylla. 20 Taalibe ya dem waareji, te loxob Boroom bi nd ak oom, di dggal kddu gi ak firnde, yi ci nd. MRK 16__

You might also like