You are on page 1of 13

Wolofalu Boroomam

Ma jóg kañ waa ja daa way ngën ji Yónnen


Ba Yónnen fal ko muy xutbub Boroomam

Li tax way wii wolof te waroon di yaaram


Damaa nar gaa yi jàngul xam Boroomam

Ma kañ ko te way ko ndaxte mu dolli may may


Géwal sañ naa wëreeluy kañ Boroomam

Ma nettali fiy jaloore te sulli fiy ndam


Te wax xar-baax yu tax ngeen xam Boroomam

Te xejj ya Yàlla fal xam nañ maqaamaam


Ca xar-baax yaak ca may yaak xam Boroomam

Ca wàlliyu yaak ca xawsu ya sax fa diiwaan


Ca xutbu ya ak ña daa wéet ak Boroomam

Ña xam Yàllaak ña xam Yónnen ca baawon


Ba tay kenn jaarugul fa mu jaar Boroomam.

Te wax jii moo ko wax ba ko noon ya yóbboo


Wolofalu Boroomam

Ku diiŋat wax jii moo juuyook Boroomam

Ca géej ga la làmbe Yàlla ba fekk muy géej


Mu tanq ca leeru hëybu ya naan, Boroomam

Ca géej ga la dàqe saytaaneek i gaayam


Buñiy maaj muy taxaw faratay Boroomam

Ca géej ga la moome mbóotum kun ci baatin


Bu noon ba fobee kënoom mu ne kun Boroomam

Ca géej ga la Bàmba tijjee ndàmbi xam-xam


Ba faf yor alliway xalimag Boroomam

Ba àgg ci Yàlla àgg ci ngën ji Yónnen


Ñu sopp ko soppi léppam muy Boroomam

Saxal foofee jihaari bakkan ci ay at


Di boole taggag julleek weetal Boroomam

Ba faf seey mel ni suugar far ci Yonnen


Di moom muy moom ci baatin cëy! Boroomam.
Wolofalu Boroomam

Ñu bokk ko fal tofal ko ngërëm mu fob kun


Ñu wommat ruu yi jox ko mu jox Boroomam

Di kenn ku ñépp xam foofee ci baatin


Tubaab ya di bañ sëriñ si di yéem Boroomam

Mu faf dib jant faf tiim jépp dunyaa


Di taalif téere yuy sellal, Boroomam

Malaaka ya seere pal ga mu am fa diiwaan


Mu fal ay xutbu yuy déeyag Boroomam.

Balaa lëf a am ci péeyi aras ci baatin


Nu diisook Daam te mooy jaasii Boroomam.

Te mooy wuutaatu Yónnen far ci kaw suuf


Di mbóotam kun ci lépp lu soob Boroomam

Mu làq ngërëm ci saahir ak ci baatin


Maqaamaam fawqa mboolem ñoñ Boroomam

Sëriñ Tuubaa di maanaam dex, ku dem duy


Ku sóobu ne mes, bu génnee xam Boroomam
Wolofalu Boroomam

Ku sóobu te wéy aw yoonam ya feesal


Ci ay leeram ba faf di duyal moroomam

Ku sóobug dex, na xam ndox dof bi yewwul


Te wattum ndox lewet na te wex ci biiram

Ku sàggan sànku fàww te lab te doo duy


Te doo set, doo setal doo xam Boroomam

Meloy Bàmbaa ngi waa ju xamul na dégloo


Te roy-royluy jikkoom moo xam Boroomam

Di jox aji-laaj di dimbali ay dëkkaaleem


Du tooñ te ku tooñ mu jéggal ngir Boroomam

Di may ku ko bañ di woo ku ko foñ di neexal


Safoo ku ko soof ku dul kuy moy Boroomam

Di faj aajook a xamleey bóot di seexal


Di génneg ruu ci tuskare jox Boroomam

Di fekk ku ñépp xeeboon ay cosaanam


Wolofalu Boroomam

Mu fal ko ba ñépp faale ko mook Boroomam

Di fekk ku mel ni man jàngul liggéeyul


Mu seexal sol ko xam-xam mook
Boroomam

Di fekk muriit bu dof bu tilim ferul baa


Mu fóot ba mu set tofal mbooloom Boroomam

Meloy kaw yaak meloy biiram dëppoo nañ


Du digle lu bon duy déglu ku dul Boroomam

Du moy ngir tiit, du bew ngir mbég lu rëy-rëy


Du bëgg, du bañ, du faale lu dul Boroomam

Du jàq, du rët, du jaaxle, du fàtte Yónnen


Te masul a tawat lu xew ci ku dul Boroomam

Du daw ay noon, du yox-yoxi ngir pexem nit


Du sukkandikoo ci mbam ku dul Boroomam

Lu mbir rëy-rëy da koy far dolli ag ngëm


Du yoqi, du daw, di mbër mu far ak Boroomam
Wolofalu Boroomam

Du wopp ba tax mu wàññig jaamu Yàllaam


Du tiis ba mu tax mu ër faratay Boroomam

Du dégg ag nodd mbaab kàbbar te teewul


Lu taw-taw ak lu liw-liw cëy Boroomam

[20:11, 12/11/2020] Al-Faaruuq Siise: Du tabje ba


tiim, du wuute masul di maamuum
Du gàpparu bis, du wéeru jullig Boroomam

Du yeexal wenn waxtu te masul a fay faat


La koy wax raw montar mooy Boroomam

Du ñakk ba tax mu boddi kuréel ya koy laaj


Du denc alal lu dul téereey Boroomam

Du dox di tëjook i dëkkaaleem ci ay kër


Bu wéetaa ma nga ci Yónnen baa Boroomam

Du dox di nelaw ci ay lal guddi cëy kii!


Du lekk ba regg day mos ngir Boroomam
Wolofalu Boroomam

Di far ay moy di gàdduw tiis ci aw nit


Di sotiy may di jël sànjub Boroomam

Bu nattu jógaa ba jëmsi ci ag njabootam


Mu daar-daarloo ko ngir àndag Boroomam

Yërëm naw ndaw xamal leen yoonu baatin


Teral naw mag ba jébbal leen Boroomam.

Yafal nay bër tabax nay kër ci suuf sii


Xamal na ña sànku woon ngéerum Boroomam

Te taal na ci réew mi taal bu dul fay ci dunyaa


Maseefu la gis kemam cëy mook Boroomam!

Dëgër ba ni këŋ nooy ba ni nemm cig wet


Te am njàmbaar gu tar te ragal Boroomam

Wayof ba ni toyy diis ba ni gann cig wet


Lewet ba ni domm saf-sàppag Boroomam

Sawar, te lefog, te yaatu, te xér, te am ngor


Di tab bu dul jeele lumu am jox Boroomam
Wolofalu Boroomam

Rafet jëf saf xorom du wax te reewul


Bariy teggiin ci ku mu gis ngir Boroomam

Du xejjag seen, du ay bokkam, du jàmbur


Ku ñëw mu teral digal la nga xam Boroomam

Du boddi, du ñax, du jànni, du xotti saatir


Da lay yaatal ëfal la nga mel ni doomam

Du màtte, du jëw, du xool lu warul te siisul


Du rummi, du mer, du xul ci lu dul Boroomam

Du xaste, du dóore, ñakkul bay fayantoo


Du dog wormaak i bokkam baa Boroomam

[20:31, 12/11/2020] Al-Faaruuq Siise: Du fàtte, du


fécc wóllëre, masul a wor nit
Du xàddi, du naagu yërmande ngir Boroomam

Du bew, du bajantu day waarook a waare


Du jeng, day fakki maasam ngir Boroomam
Wolofalu Boroomam

Du reetaan nit, du far-farloo, du sot nit


Du yàqub der, du tas nit ngir Boroomam

Ndaxam jii waay jikooy Yónnen la làmboo


Maneeful a lim ngëneelam yeek Boroomam

Funuy raaseeti waa juy mel ni mii mbër


Woyof na kaw te diis na ci biir Boroomam

Funuy raaseeti jant bu dem ba njolloor


Te leeral yépp gox di kenul Boroomam

Funuy raaseeti waa joo xam ne buy wax


Ku nekk di lox di làqu ku dul Boroomam

Funuy raaseeti kok bu jógaa du geesoo


Di romb dërëm ya, jëm ca mbiram Boroomam

Funuy raaseeti kuy fob Alxuraan jii


Di def ciy taax di taalif ngir Boroomam

Funuy raaseeti kuy gis Ahlu Badrin


Di ànd ak ñoom te dëkkaaleek Boroomam
Wolofalu Boroomam

Funuy raaseeti waa joo xam ne buy way


Araf wu mu def aras di ca bég Boroomam

Funuy raaseeti waa joo xam ne fumu teew


Ku wopp mu faj ku dee mu yëgal Boroomam

[20:41, 12/11/2020] Al-Faaruuq Siise: Ku bañ bii


xutbu bay raasiy moroomam
Du gis bu ni mel ci jii jamonoy Boroomam

Giseefu ko woon ca gaa ya wéyoon ca baawon


Te xarnu yii nuy jub it du ci ñëw Boroomam

Ku weddi ba tax mu bëgg ne maay moroomam


Na def li mu def te wax li mu wax Boroomam

Te dox li mu dox ci réewi Gabon wa Kongo


Ci ay noonam te dellusi ciy moroomam

Te sàkk ku mel ne seexi Ibra Faati


Wa Ahmadu Ndombe ak Làmpub Boroomam
Wolofalu Boroomam

Te sàkk ku mel ni seexi Abdu Rahmaan


Ku juddu ci Mbàkke moo la xamal Boroomam

Te sàkk ku làq jagleg Siidi Muxtaar


Ki dem ba siyaare Yónnen mook i doomam

Te seexal kem li Seexi Bàmba seexal


Te sellal seen xol ba ñu xam Boroomam

Te sàkkal leen i booloo fàww yuy jëf


Te tàggat leen ba duñu man a moy Boroomam

Te kat na saxal liggéeyal ngën ji Yónnen


Te bum tere muy taxaw faratay Boroomam

Te dootul nelaw, day, daw soxna ya mu am


Di daw saytaane tey wéetag Boroomam

Te bum yoqat te bum jéllal lamuy jëf


Te bum ngistal ci jëf na ragal Boroomam

Te bum diiŋat sëriñ sa te bum fayantoo


Te bum bég ngir ku koy gottil moroomam
Wolofalu Boroomam

Te bum xas nit, bum jëw bum rambaaj it


Te bum fen bum dogag bokkag moroomam

Te kat na saxal jihaar bakkan ci boppam


Te muñ tiis ak naqar te ragal Boroomam

Te day xam bóoti xol xam baatinam nit


Di saafara ràggi xol di xalam Boroomam

Te bum digleek a aaye ci wàllu bakkan


Di woote ci kaw te biir ba gisul Boroomam

Li ngay lim doy na yaw Muusaa taxawlul


Ba tay jotagóo lu mat asakay Boroomam

Ku dégg ñu jàng way wii nang ma ñaanal


Ma am ngërëm te sax fi ba xam Boroomam

Te def géwelam bu koy way fii ak ba may dee


Te wax ju ma wax mu saf ko te saf Boroomam

Ku bëgg di mbër meloy Bàmba a ngi nii seetal


Wolofalu Boroomam

Ku mel nii mooy donay xutbub Boroomam

Aji-bind ji: Njaga Saar

You might also like