You are on page 1of 5

Daahira Munawwirus Sudoor

kurél gi boole ndaw ñi am yéeney liggéeyal Sëriñ bi ci Daara ju mag ji


Complexe Cheikh Ahmadul Khadim (CCAK)

AY TEGGIN
Gën a jubluwaat njàngaleem Sëriñ bi, ngir wuyyu Sëriñ
Muntaxaa Mbàkke ci liggéeyam bu rëy bii, di Daara ju mag ji

TEL/ 78 131 37 57 / 77 389 17 94


TEGGIN
• Kërug teggin, mooy dëkkuwaayu lépp lu baax, lépp i yiw ak lépp lu sell.
• Sëriñ bi (g.y.m) fonkkoon nako lool te fësëloon ko tamit ci am njàngaleem.
• Mongi wax ci Nahju naan :
 Ay teggin mooy boppu jikko yi, mooy koom mi gën ci tay ak ëllëg.
 Képp kuy tòpp sunna ci ludul ay teggin, doo texe, doo jariñu.
 Ay teggin day leeral xol, di jegeel ajjana, di soreel sawara. Tay tax say
dëkkëndoo dila tagg fuñ tòll.
 Ku am teggin, Yàlla (swt) dakoy bëgg; mbindéef yi bëgg ko. Safaan baay ka
ñàkk ay teggin.
• Lu jëf takku-takku te àndulak teggin, amul solo.
• Teggin mooy tax lépp looy jëflanteel nga joxko àqam bamu mat sëkk. Xam
la ca war, di ko def ba mu mat, xamit la ca warul, diko daw sa kéem. kàttan.
Te taqook mbooleem jikko yu rafet yi (muñ, kersa, rafet jort, woyof, tabe...)
• Sëriñ bi (g.y.m) nee na, ci Nahju:
 Yoonu teggin mooy:
o Yërëm ki nga mag, weg kila mag, ki nga maaseel nga def ko ni sa bòpp.
 Bokk na ci ay teggin niko Sëriñ bi (g.y.m) jàngalee ci Nahju:
• Laabiire nit ñi ak dileen dimbali ci lépp lu léen amal njariñ.
• Bañ a jàpp ne yayoo nga génn màggal, walla kenn yoreel nala àq
• Jàppal ne yaa wara màggal ñépp; te ya yoreel ñépp àq.
• Ku amul ay teggin ci yaw tamit, nanga am ay teggin ci moom.
• Nanga xool ci ñépp àqi Yàlla (swt) mi léen bind.
 Képp ku la mag, nanga ko weg rawatina say way-jur
• Deel gaaw ci jëfe seen ndigal. Kon nga raw.
• Bul toog ak ñoom ci kaw, deel took ci suuf. Kon nga kawe.
• Buñuy wax noppil bañ pare te booy wax ag ñoom nga wacce sa
kàddu.
• Bu léen wan sa mer mukk; ag luñ la man a def.
• Bul tudd mukk seeni njuumte; dee léen suturaal.
• Dee léen dimbali ci lépp loo man tey gaaw ci seen i càkkutéef.
 Bokk na ci ay teggin:
• Bañ a baril ab geestu, walla xool rawatina luñ nëbb.
• Bul dox ci lu dul aajo te bul dem fu bon.
• Bul baril say wax rawatina ci lu amul jariñ . Deel saxoo noppi (noppi
baax na lool, te amna sutura, amna nooflaay).
• Bul baril ay fo aki caaxaan, ak baj-baji
• Bul baril ay ree; day wowal ab xol, di ko ray
• Moytul xaste, saaga, xuloo, walla ngay xeex. Aka ñoo bon!
• Moytul lekk gu bari, aki nelaw. Kon nga noot sa bakkan.
• Deel muur sa awra; bul ko feeñal!
• Bul àndak ku dul ku baax; ku laay dolli diine akum xel.
• Bul xool sikkus kenn rawatina diko tudd. Nala say sikk doy!
• Nanga wan nit ñi ag cofeel te nanga léen weg, wormaal léen.
• Deel nooyal say kàddu booy wax ak ñoom, dileen jéggal te buleen tooñ
• Bul rëy-rëylu ci seen kanam te bu léen xeeb itam. Kon ñu weg la.
• Langay wax ak langay def, na doon loo xam, doon loo sañ.
• Lépp lu baax royal; lépp lu bon rombal! Deel topp ndigal!
JËRËJËF BOROOM TUUBAA
• Ñongi daaneel sunu kàddu, ginnaaw bi nu santee Boroom Tuubaa
(g.y.m) ak Boroomam (swt), di julli ci kilifaam ga (j.y.m), ci
sargal ak ñaanal Sëriñ Muntaxaa Mbàkke mu yàgg fi lool te amug
wér ba mòttali mbooleem yéeneem ci liggéeyal Sëriñ bi, rawatina
Daara ju mag ji (CCAK)

Daahira Munwwirus Sudoor


Bum laal suuf !!!, Nan ko yékkëti !!!

You might also like