You are on page 1of 139

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 1

Marsiyya
Maam Ceerno Mbàkke
Boroom Daarul Muhti
(1862-1943)

Aji bindaat ji : Sëriñ Móodu Jenn

© 1445 h / 2024 - Paris


Tous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre adresse mail:
serignmbayjaxate@gmail.com
Vous pouvez nous suivre sur youtube :
http://www.youtube.com/@serignembayediakhate1075

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 2


Indications (Source : Drouss.org)
Wolof Français
e=é per pér
u = ou rus rous
c = th caam thiam
ñ = gn ñam gnam
x = kh xol khol
j=j jibi jibi
nj = nd njaay ndiaye
nd = nd nday ndeye
ŋ ŋaam (machoire)
ë = eu gëm = gueum
é = è (plus dur) = rér perdu
óo = au góor gaure
q = xx suqali soukhali

Vous trouverez les vidéos (audio+texte) en suivant les liens ci-dessous :

Partie 1 Marsiyya Maam Ceerno Mbàkke (Sëriñ Abdul Ahat Ture)

Partie 2 Marsiyya Maam Ceerno Mbàkke(Sëriñ Musaa Géy Ndar)

Partie 3 Marsiyya Maam Ceerno Mbàkke(Sëriñ Musaa Géy Ndar)

Partie 4 Marsiyya Maam Ceerno Mbàkke(Sëriñ Musaa Géy Ndar)

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 3


Bismil ilaahi xaadiril muriidi
Moom lu ko soob lay def ci ab muriidi

Huwal lëzi yafhalu maa yuriidu


Dunal lëzi yuriduhul muriidu

Wahwa hayun samadun wa baaxi


Subhaanahuu zu kanafin wa waaxi

Nan sant tey feddali sunu tawhiid


Bahda salaatinaa alal wahiid

Te setlu yonnen yi ñëwoon ci dunyaa


Fahakadun lañ woon ku nekk wéy na

Te setlu Xayrul Xalqi ak Sahabaam ya


Ki tax ba Yàlla bind mboleem jaam ya

Teewul mu dem ñu naa wa maa Muhammadu


Ila rasuulun qad xalat lii lumu doon

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 4


Dunyaa su doon kërug saxoo di yaale
Xayrul Waraa waa Màkka duñ ko jaale

Waaye li yobb Ahmadul Màkkiyu


Dellu si yobb Ahmadul Mbàkkiyu

Du fi bàyyi sunu Maam Ceerno Ibrahiimu


Ki lee di xaadimam ki ley maxdoomu

Yoyu le yaari xew wi lee ko yetteel


Fa Daarul Muhti xew wi lee di mbeteel

Abki halaa Seyyidi Ibraahiima


Ma jooy le suuf ibran hawa tafhiima

Abki halaa Xaliili Ibrahiima


Ma dellu jooy le asamaaw xadiima

Jant a ngi jooy Maam Ceerno Ibrahiima


Weer a ngi jooy laylan badaa bahima

Ca mooma at sunu weeru koor wa jooy na


Naafila wu nu keroog ne taw ba sóob na

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 5


Ma jooy fi Saa Ndaama la sancoon Daaru
Ci alsashin céy Yàlla maa ka waaru

Waarootina waaru ga raw ga woon daaw


Jomeetinaa mii mbir a rëy ne leen waaw

Aa xin ala xaali xalilil laahi


Way jooy le leen ma saa nijaay lil laahi

Aa xin ala faqdi xalilil laahi


Maam Ceerno Ibrahiima Baabul Laahi

Aa xin ala xutbul waraa fil jaahi


Xaliifatin xadiimi duuna laahi

Aa xin ala xarmi rijaalilaahi


Sheexi suyooxi xa idil ilaahi

Woy ma ne woy man mi ko ñaanoon wérd


Def ko’b sëriñ fumay jëleeti fardu

Moo ma mayoon fa Daaru werdub xaadir


Ci darajaay Sheerifu Abdul Xaadir

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 6


Dellu ma may musabahaatul hasri
Dellu ma may maahuuzu waxtal hasri

Saxaadatan ridan bi duuna suxti


Moo ma ko warluloon fa Daarul Muhty

Ma jooy le Seex Ahmadu Awa Bàlla


Baayam ba fawxa woon ca kër Maam Bàlla

Ma jooy le Seex Muhamadul Habiibu


Baayam ba moo ëppoon njariñ am ceebo

Wayaa Xalilulaahi way Saa ndaama


La getti woon goor ña defum ndanjaama

Wallaahi saa rangooñ yi war naa tuuru


Ma jooy a jooy ba sama gët yi muuru

Saa ruu gi lax na sama xol bi wow na


Saa cër yi làgginañ ne Ceerno dem na

Billahi wallaahi tegal talaahi


Dootuma ree ba kekku duuna laahi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 7


Ndaama Xalilulaahi Ibrahiimu
War ngeena yewwu jarr nag te yéemu

Garab gu rëy ga keraloon waa Daaru


Neena jirim naaj waa nga nit ñay jaaru

Imaanu diinuna aqul imaanaa


Wa saahibal islaama wal ihsaanaa

Ceernoy kenul diine di ruuhag lislaam


Moo njëkk moo mujj te moo fi xam Daam

Kennu la yor mbaarum Sëriñ bi naay na


Lee jën yi buur galo yi daanu haayna

Maam Ceerno dem na yobb far Sëriñ Ndaam


Sëriñ Momar Absa ña ngay nuyoog Daam

Kenn dootul xamle Alxuraan ci Mbàkke


Ku melni Seex Abdu ma raw waa Bogge

Woy ma ne woy man ekspres ba teer na


Te taxumaa àgg te wàcc teel na

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 8


Gi lee saxaar teggi masiin ba wéy na
Maam Ceerno mekanisiyen baa nga aynaa

Xawma saxar gu may dugal bagaas yi


Boowul ma mbuus yi ñoy woroom bagaar yi

Pake ba dem na toppi màndiwaar ga


Maam Ceerno dem na fekk Bàmba njaam ga

Ku man a feey na feey subooxun loojo


Yaw loo ci doon ci ag tefes ngay xooju

Woy ma ne woy man fu ma newoon ba tàrde


Seex Mustafaa bu sama paas bi tàrde

Mat ngab xaliifatu di xayrul fardi


Yaay doomi Ahmadu Mbàkkiyu Amdi

Bu dul kon ak Abaabakar Sidiixu


Ginaaw Rasuulilaahi ne kon nu yuuxu

Bu dul kon ak xalifa Amdil Mustafaa


Kon tay nu gën fee jooy Xadimal Mustafaa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 9


Ma jooy le Amdil Mustafaa baayam ba
Ko jàngaloon te def donooy baayam ba

Fu miy jëleeti baay bu mel ni Ceerno


Mu di ko xoole Bàmba cëy bii xarnu

Fu nuy jëleeti kuy niroog Maam Ceerno


Mo doon peremiyeerub rijaali xarnu

Moo njëkk daw kurs ba mujj àq


Moom ba ngañaay ya fahagut la àq

Raw na ngañaay ya yépp teggi tuur ba


Ñibbi këram Njool Màkka wan ko Buur ba

Allaaxira jeexal nga kër Maam Bàlla


Seex Mustafaa amul ku dul Seex Bàlla

Seex Bàmba dem ca wamsashin fa Njurbel


Keroog la àdduna niroog ab wurmbal

Seex Anta dem ca bopp haama sasashi


Yobbu Sëriñ Aafiya murit yay bisbisi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 10


Sëriñ Ma-Sàmba dem atum unaysasi
Jumaay Tuuba di ko jooy di bisbisi

Fekkoon na Seex Coro ak rakam Seex Absa


Dem nañ ca haama nasashin céy cam sa

Murit ya yépp di yaakaar Ceerno


Ne ndax mu toog fi ba nu matal bii xarnu

Nekete woo day dem atum basasashin


Xamnaa su doon ñàŋoor ma ngay dasasasi

Watit wa laa leen bëgg wan ak mboor ma


Ku dox doxiin wa daal di yeesal ngiir ma

Ngólool ma mag ca kër ga fekkileen ko


Doom a di baay watit wa dégluleen ko

Marsiya baa leen di xamal watit wa


Njàmmee ngi deeti suli mbooti xeet wa

Ndax ku xamul saahir sa toppi mii mboor


Xaayaan balaa neex kat nga dégg sereer

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 11


Sëriñ Masàmba neena inspektër laa
Ku reere Ceerno tay ma *conse geer* la

Maam Ceerno wàcc na defar na diine


Ñibbina àjjana caa uurul hiini

Maam Ceerno wàcc na ba fab Sëriñ Ndaam


Sëriñ Momar Absa ña ngay nuyoog Daam

Jigeenu uurul ayni yaa ngi koy teeru


Lalam ya ñoñ barsàq ñoo cay feeru

Ma ngay bunaanaat ciy lalam di buuru


Jotna bisub payoor ba dootul liiru

Bàmba takkal na ko medaayub baatin


Yu dootu tekkeeku ladaa Boroom Kun

Yëngal na firdawsi lëmbaaje Tuuba


Taxaw fa janaatin nahiimi booba

Jannaati adnin am na fay ridwaani


Nuyoo nafa ak Bàcc ak Boroom Gawaani

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 12


Maam Ceerno nax na nu ba dem jinaani
Maseefu ko seeti ladaa jiraani

Fukki fan ak juroom la xëy di buuru


Ñu naa bayit-bayit mu daal di muuru

Ñetti fan ak ñenent ci weeru Shahbaan


Di alxemes la ne meles réer Soodaan

Am na juroom ñetti fukkam yu mànke


Yeneenti weer laaj naa ko Siidi Mbàkke

Ku bëgg dégg fa mu dox ci saahir


Na nga ma jox sab nopp kon nga saagër

Ku bëgg a xam na Ceerno Faati daa def


Déglu ma ndax nga roy ko moo di haarif

Bamuy xalee la daaldi ànd ak Bàmba


Di roy jikkoom ya ak jéegoom ya ak tànkam ba

Bàmba a ko jàngal moo ko def kang-foore


Jàngal na ay foore te masla doore

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 13


Roy-roylu saahir sa di xeeñ baatin ba
Fum yenni koo mu teeñu fab yanam ba

Xolam bu jébbalu ba ak tabeem ga


Ak dëddu ga ak njàmbaar ga ak yaaram ga

Ak sàmm ga ak maandu ga ak doyloom ga


Muñam ga ak wakkiirlu ga ak wooloom ga

Moo bañ tubaab mba ab ceddo mba ab yéefér


Soppul ku daa poronoose mbaa kuy siifar

Gëmam gu mat gaa waraloon liimaan ja


Dëgal gu mat gaa waraloon tawhiid ja

Sarixatoom jaa waraloon lislaam ja


Haqiqatoom ja waraloon lihsaan ja

Tarbiya gaa waral barig hadiis ja


Tarqiya gaa waral mu ray badiis ja

Tasawufam jaa tax mu saf muriit yi


Haqiqatoom jaa tax mu soof mariit yi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 14


Masula sopp àdduna ak dagam ya
Séytaane bànneex ak bakan mbokkam ya

Day seng jàkka ja saxal ca mbooloo


Saxal fa julli juroom moo yoolu

Masula mànke masula tiim fa Daaru


Masul di maamuun masula fay faat xaaru

Gennug fajar la mas a tiim fa Daaru


Keroog Mataar Jóob moo ko nax mu waaru

Noon na ma yaari tàkkusaan la masa tiim


Te ba mu amee ndox fay na julli ya mu tiim

Keroog lañuy tuddi Sëriñ Ma-Sàmba


And ak Sëriñ Ndaam sàntu Siidi Bàmba

Ñaareel ba mooy atam bamuy sanc Koso


Ñuy rooti Tuuba at ma melna ni kaso

Da daa saxoo naafila fil Xur’aani


Ci weeru koor jii ilimaan mooy waane

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 15


Jii ilimaan deesu ko jam moo màndu
Maseefu ko gaganti biir moy wàndu

Ku weddi laajal naari waa deymaani


Seen gag ba jàlloon jóg ñëw suudaani

Bàmba ne Maam Ceerno na leen gàgganti


Man Bàmba bis penc ba laay lijanti

Keroog la Maam Ceerno lijanti naar ya


Tasaare mahnaa ya te laalul mool ya

Céy muhjisaati Bàmba ak Maam Ceerno


Maneesu ko xibaar fayalma daynu

Maseefu ko sàbbaal du juum du fàtte


Masula jamuj ngir Bàmba moo koy àtte

Bàmba ne woon bu Ceerno daa liqaamlu


Fa Daaru Mannaan maa nga toog di laablu

Man Bàmba it sumay liqaam bay kàbbar


Ceernoo ma daa maamoomu ñii ñaar ay mbër

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 16


Te boobu Seex Bàmba a nga woon Konaakiri
Te Ceerno daawu ko xamal manaakiri

Ag jaxasoo du ko teree ibaada


Kenn manu ko defloo bidaa mbaa aada

Dënerlu ga ak yeexam ga ak déeyam ga


Du tax mu fàtte senn saa wetam ga

Noppeem ga mbaa mu melni daflaa fàtte


Te tewu ko dañ kumpa Ceernoo sotti

Masula rët masula tiit du jaaxle


Maseefu ko kalaame bor moo baaxle

Maseefu ko jiiñub dëram du giiñlu


Masula waato mba mu dox di joññlo

Ñemee ñemee ñemee ba mel ni ag gar


Te far ragal Yàlla ba mel ni bàqar

Te wex a wex xàtt ba mel ni xétar


Te far lewet domm ba mel ni am xar

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 17


Tabee tabee tabe ba mel ni mar-mar
Te aay a aay a aay ba mel ni par-par

Faqiir ya woon fa taaxi Daarul Muhti


Amal na leen daahif ya duñ ko fàtte

Jirim ya ak miskiin ya ak ñay baayoo


Nàmpalna leen ca saafaraam laa raayoo

Daggam yu rëy yaa tax mu saf faqiir ya


Ndimbal la moo taxoon mu saf xaqiir ya

Yërmande jaa taxoon mu saf saxiir ya


Teraanga jaa taxoon mu saf kabiir ya

Ñamam yu neex yaa tax mu saf siboor ya


Mbañam wotom maa tax mu soof sofër ya

Goreel na jaam ña goreloona gor ya


Ngoram gu rëy gaa walangaan fa kër ya

Xikam yu rëy yaa walangaan ca xol ya


Geejug xikam gaa duusu toyal xel ya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 18


Du sas murit du wër di laaj hidaaya
Du jañ du ñoddi mooy boroom hinaaya

Te du la laaj te loo ko jox muy sant


Soo ko joxul su la gisee ni patt

Soo ko joxee mu ni la hamdullaahi


Soo ko joxul du ni la abdullaahi

Du woo murit du yewwi ab murit


Te loo ko jébbal xam ni mooy hamiid

Du tudd nit fum newul du bodde


Du jëw du jëwloo ña fa moom du gëdde

Ku mu denk lëf doo tu ko laaj ba abadaa


Lu mu denc it doo tu ko laali sarmadaa

Ku moy mu wan la yoon fa Daarul Muhti


Masula far-farlo du wàlli parti

Xàmmeewuloon waadoola ya ak waa nguur wa


Ca la mu nar ku bañ mu wan la yoon wa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 19


Fu mu masa toog ñaari ngimiñ ya dar ko
Ak ñaari ndaama ya sa poos ya wër ko

Buy julli hiit fetal ya daaldi tàkk


Muy sànni jàkk wa di dox ba àgg

Te teewu ko lewet ba raw waa Mbàkke


Waaye donoo gëna dëhar fa Kokki

Li mu joxe ciy fetal maneesu ko lim


Li mu maye ciy fas it maneesu ko xam

Li mu maye ciy sàq aki nag aki mbalaan


Mayna ma am sàq fa kër Bàlla Bajaan

Masula wor ci ab dëhal kuy laaji


Li mu faj ci aajo zu hadaa’il haaji

Lu war mu def ko cogalam day gaaru


Baa aki mbaam lañ daa wutal fa Daaru

Xari talaabiir aki bëy ak naaga


Ba àddinay baax sàmm saa ngay saaga

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 20


Yonneena waa jumaa ja junnib ngurdi
Siket gëleem gaa ko sëfoon di fardi

Fukki junneek ñaar la joxoon Seex Anta


Bam ko yótee maqaama moo dib jant

Seex delluwaat yót ko lalub pëmeem ba


Ñetti junneem la yobb mook goroom ba

Ku weddi lii laajal Mataar Masóogi


Moo yobbuwoon xaalis ba moo ko sooke

Déglul ma wax la tay fa sunu Maam Ceerno


Jàmbaar ju rëy ja jaar a jaar ba raw nu

Yàllaa ko jagleel ca asal mook Bàmba


Ñu bokk seen mbir ca xadiim fab yan ba

Yawma alastu la ko Bàmba tànnoon


Murit yi bañ laa wax "balee" la genoon

Moom lañ duyal ndab la mu bokk ak Bàmba


Seex yépp dañ ca tank naan ba ñiit ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 21


Moo njëkk sukk mujj jóg ci baatin
Kun fayakoon moo ko dogal moo leen gën

Ngëneeli saayir ya mu bokk ak Bàmba


Ci wàllu maam moo tax mu àttan yan ba
Ahmadu Soxna Buso mom Maam Maharam
Moo sémpi raaya maami Mbàkke fa këram

Maam Maharam bindoon na bis ab dénk


Sereel ko ay ngërëm yu ànd ak tagg

Neena bu degaa nodd day dawaale


Ba sër ya xotteeku lixubil waali

Ñaari sëtam ñu baax ñi doy nañ seere


Seex Bàmba ak Maam Ceerno li ka biire

Sen yaari maam yaa bokk baay fa Mbàkke


Ñu dellu bokk benn baay am bàrke

Maam Asta Waalooy ndeyi Soxna Jaara


Bu dul kon ak moom kenn du sampi daara

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 22


Maam Absa Mbàkkeey ndeyi Soxna Faati
Miy ndeyi Maam Ceerno mi xar’aadaati

Yi yaari maam ñoo bokk genn góor ga


Ahmadu Soxna Buso way na géer ga

Ci sunu Maam Ahmadu Soxna Busó


La seeni géej di bëx-bëxi di duusu

Déglul ma wax la lëf ci mbokkag baatin


Loo xamni tuuti laa ci xam ci baatin

Ca haama sharfadin la ñëw ci dunyaa


Neeleen sunuy nopp bi dooni sunyaa

Fukki fan ak juroom ci weeru gàmmu


Di alxemes gaynde ga ñëw di yëmmu

Keroog la Seex Bàmba mu mag ma faatu


Maam Bàlla Aysa faatu at ma laatu

Bis bam ganee àddina daal di tàkku


La Bàmba xam ni am na lam doon sàkku

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 23


Fekkoon na Seex Bàmba di ñaan Buur Yàlla
Jàmbaar ju askanoo ci Mbàkke Bàlla

Yoor-yoor la judd alxemes fa poroxaan


Yoor-yoor di alxemes la tàbbi fil jinaani

Bis bam juddoo ba tàkku sér baatam ba


Seex Bàmba daw njëkkante koog baayam ba

Keroog la Maam Moor Anta naa Seex Bàmba


Sa ñaan gi nangu na kii lee yor yan bi

Xamnaa ni sooy donoy Rasululaahi


Mooy sam Aliwu mbaa Umar bilaahi

Bu Bàmba doon Muusa mu dib Haruuna


Seeni mbir ak yooye le mbir niroona

Neena keroog aluwwa jam doon jàng


La fa taxaw ca kaw lu rëy di fëgg

Te naa ko sooy amiiru mooy wasiiru


Sooy xutbu mooy xawsu te moo lay sooru

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 24


Fekkoon na Bàmbay jàng saaru xasasi
Ba ca fa arsilhu mahii la ko gise

Seex Bàmba daal di dem fa néeg Maam Faati


Jàngal ko fay sabxatu munjiyaati

Cër ya juroom ñaar cër bu nekkay amu saar


Mu julli fay ràkka saxal ko ba Pataar

Keroog la Bàmba sange mbooleem cër ya


Masula dox fi lu xaraam fa bar ya

Foofe la Bàmba toog bindal ko'b teere


Xar per ma burxal ko ndeyam muy seere

Bisub keroog la Mabba toj Pawos Koto


Ñu dégg sox ya tàkk kenn xamul fu të

Waxtu wa muy tàkku la sox yay tàkk


Loola wara jàmbaar ja maa ko bàkk

Seex Bàmba naa jihaar ja doyna faalu


Seerey limay xarfaanu maak rijaalu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 25


Keroog la Yàlla def ci sunu Maam Ceerno
Sopp fetal jihaar ba moom ab xarnu

Ca tàkkusaan la sunu Maam Moor Anta


Laxasu gonte Poroxaan dib jant

Ñu daaldi soos kasaa ga genn réew ma


Soxna sa daal koy yanu booleeg meew ma

Ba ñu demee Njaaba Kundaa ci xarte


Soose sa berndeel ko fa lañ ko ngente

Neleen sunuy nopp lii may wax waruma


Waaye Rasuulu sax waxoon nañ mbir ma

Baayam ba jébbal ko keroog Maam Ceerno


Ne ko su ngeen dundee yilif ab xarnu

Guddi gu ñëw muy jàng tey wër néeg ba


Ba muy ayug-bis géej ga wal ca déeg ba

Géej bu walee cib déeg ba sar ca dex ya


Bamuy ayug-bis kenn du xàmme ndox ya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 26


Li lee taxoon Maam Ceerno Ak Seex Bàmba
Seeni mbir ndiroo da fa ni diib tànkam ba

Seex Bàmba nee fu ma taxaw balaa ngoon


Mu ne fa jaas di xeeñtu mboor ma aw yoon

Ne suma doon ab dëkk Ceernooy yoon wa


Jëm si ci man ku soobu tàggoog buun wa

Baay baa ko tuddee Ceerno Ibraahiima


Mooy Sëriñam bu ndaw xawa tafhiima

Ñu teg ca ay at njool ma daal di gàddaay


Ñibbi Kajoor sañc Pataar moo mat baay

Keroog ba muy dem dafa listixaarlu


Ñu ne ko ñibbil ren kajoor te mbaarlu

Keroog la pencum Poroxaan ma daanu


Maam Faati Jóob wopp Sëriñ ba kaanu

Ca mooma at la Xaadi Momar Anta


Ñibbi Kajoor Lat Joor du naa man anta

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 27


Mboleem Kajoor jiital ko def ko xaadi
Moo raw ku teew ak kuy ñëw ak kuy maadi

Mu bolee kook Seex Anta ñuy sidwaani


Jox leen Sëriñ Ñang xaafisul Xur’aani

Mu am fa am at baay ba daal koy laaji


Jébbal ko Bàmba zi xadaa il xaaji

Bàmba a ko jàngal Al Xur’aan ak xam xam


Jàng ak liggéey la boole woon ba am ndam

Bàmba a ko yar yor ko ci waxtu sihari


Masula tagoog moom lil waxtil kibari

Masula juyoog ndigëlal Seex Bàmba


Masula fanaan fu dul fa suuf fa der ba

Buy dem mu yor satala gaak deram ba


Ak teere baag daa ja di saf laram ba

Masula juum ba tàbbi néeg Maam Faati


Ngir bëgg lekk mbaa mu naan laa yaati

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 28


Masula fanaan àll du génn daara ja
Day rafle tey yalwaan ba xëy am daraja

Ca yooya at la Bàmba ak Maam Ceerno


Ak Seex Masàmba Jóob di dox ba wër nu

Wër nañ Kajoor ak Bawol ak waa Njàmbur


Ngir bëgg am ñetti dëram bay jàmbur

Ngir boobu Naar bu ñu naa Seriiful Hasanu


Moo ko bindal ab teere bor la ca yanu

Téere bu tedd nee ñu fathul àqfaal


Ak rawdu faa iqin limaale ci ab jalaal

Ànd nañook Masàmba Jóob ba dem Saam


Amuñu lu dul fukki xasab boleek mbaam

Nee nañ mbaam ma baayi Seex Moodu Jigal


Moo ko joxoon Sëriñ ba loo laa ko jagal

Moo di Sëriñ Majibbu am nam ceebo


Seex Bàmba soppi tur wa naa Mujiibu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 29


Mbaam ma Sëriñ Masàmba Asta Mbàkke
La ko Sëriñ Tuuba sarax moo sekki

Ba ñu demee ba toll neegi Wajja


Fa lañ fanaan Sëriñ ba xatta wa ja

Sëriñ Wajja’a nga yor mbalaanum tàndan


Di leen bijanti di niroog waa xàndan

Seex Bàmba nee ndax waxtu wuy tàggook ñoom


Jox leen mbalaan ma laaj ko day waral juum

Sëriñ ba tàggoo joxewul mbalaanam


Yàkaar ja tas Maam Ceerno sàntu waayam

Seex Bàmba nee su ko joxoon mbalaan ma


Seex Ibra Faati lay yamal maqaama

Mbaa mu yam ak Seex Ibra Faal maqaama


Di rammu ay kuréel bisub xiyaama

Boobee ba tay Maam Ceerno Ibra Faati


Masula tàggoog Bàmba fil hadaati

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 30


Te lu mu am jox ko te lu mu xam wax ko
Te lu mu amul yéene ko mbaa mu am ko

Te du ko laaj te lum ko laaj mu jox ko


Te lu mu soxla Ceerno Faati faj ko

Jii waay maneesula xalam màqaamaam


Aki ngëneelam lu dul keroog bisub xiyaama

Déglul ma wax la bis ba Bàmba ak Ceerno


Delusee Pataar nit ña di ree ngir deynu

Maam Ceerno naa seex Bàmba ñi ngi nuy reetaan


Naan du nu fay bor bi danaa ko yalwaan

Seex Bàmba naa ko ku bëgg cor sunug siis


Ngànnaay ga delusi yobbuwale sag siis

Bisub keroog la sunu maam Soxna Coro


Jébbal Sëriñ Tuuba mbalaan mu defaru

Keroog la Bàmba mës a dem ca kër ga


Waa kër ga gépp naa ko Bàmba gar nga

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 31


Mbalaan ma moo waral mbalaan yu bari yi
Dëram ya moo waral dëram yu gore yi

Wëndeelu baa tax woto yiy wëndeelu


Ba roplaani Amerig jëmbeelu

Ca tànk neeni Bàmba yaak Maam Ceerno


La woto yiy raame di daw di koornu

Ganaaw ga naar ba delusee fi soodaani


Mu jox ko ñetti junni lil biidaani

Maam Ceerno Faati jox ko ñetti téeméer


Sëriñ Masàmba Jóob tofal ca téeméer

Keroog la Gànnaar xam ni njëkk fecc


Taxul a mujje'b géew ku gëm du xàcc

Kuy rëb day xiif aka mar di raamu


Su fetalee tànn yu duuf yam taamu

Bàmba fetal na rab wa Ceerno fees ko


Dogte ko togg ko ne ñëw leen reer ko

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 32


Mosandileen te xam ni lii aw mban la
Mbana ga laalaguñ ko junniy ñay la

Ma wax la at ma Mbàkke Anta faatoo


Mooy magi Seex Anta boroom aayaatu

Keroog la Bàmba donn Mbàkke Anta


Fi saahirin wa baatinin dib jant

Daa na ko wax naa waa ji ñaari jant


Du ñu man a bokk asamaaw dub lënt

Man Mbàkke Anta duma so damay suux


Bàmba na toog ba so nde mooy sunu Seex

Ca yooya fan la woppu daaldi faatu


Mo amewoon Soxna Ja moo ka yaatu

Njaañ la ko baayam rob bisub alarba


Bisub keroog la rammu mbooleem bar ba

Ca mooma at la Xaadi Momar Anta


Yonni Sëriñ baak Ceerno ñépp gontu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 33


Ñuy jaay ab kaamil ba yendu Njañaar
Maam Ceerno yalwaani xamul fumuy jaar

Ngir làmb yaa ngay gor sabar yay jaaxaan


Góor ñaak jigeen ña jaxasoo di caaxaan

Seex Bàmba yendu fa garab di jàng


Te masula déglu ndënd masul a jeng

Jigéen ju ñuy wax Jee moo leen romb


Nuyu Sëriñ ba daal di xam la mu làmboo

Moo leen fa toggal añ sarax leen ay lam


Booleeki ndor Maam Ceerno yor ko moo gëm

Mooy ndeyi Jee Yaasin ma faatu Ndànd


Ñu rob ko ahlulaahi awma ndend

Seex Bàmba noon na Ceerno yaa koy rammu


Yawmal xiyaamati mook ndey ja Ceernoo sàmmu

Jaay nañu jaay kaamil ba kenn jëndu ko


Te muy mbindum Seex Bàmba kenn yëggul ko

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 34


Céy Yàlla Laa ilaaha ilalaahu
Muhamadun Arsalahu ilaahu

Salla aleyhi laahu bi salaami


Wa aalihi wa sahbihi ahlaami

Amaana kuy sewal ku rëy fa Yàlla


Amaana kuy rëyal ku sew du Yàlla

Ba ñu ñëwee te amuñu hidaaya


Di yaari mbër yu nëbb seen wilaaya

Maam Faati Jòob a ko sarax sa ay nopp


La ñu canoo mu tudd ñétt opp

Ñu boolekoog lami Jee ya ak mbalaan ya


Maam Ceerno jox ko baay ba fab rawaan ya

Ñu daal di jox soxna sa Séydi Bàmba


Neeleen sunuy nopp donoy Yonnen ba

Keroog la donn mag ja ak baatin ba


Ñu jox ko Soxna Ja Tureek Taaram ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 35


Ca mooma at la Xaadi Momar Anta
Tuxoo Pataar ñëw Mbàkke mel nib jant

Ñu am fa yetti at mu daal di faatu


Bawol di wal-walli li léey aayaatu

Haama sasin la faatu wuyuji Yàlla


ñu robb ko Déqle ki lee xam Yàlla

Wa raddiyalaahu anil xadiimi


Maa amiihi wa laxil amiimi

Déglul ma wax la yaw keroog miraas ma


Waa Mbàkke ak waa Kokki teew turaas ma

Keroog miras ma Bàmba naa leen ceerno


moy sama wàll bu amee mu doynu

Man Yàlla doynama te doyloonaa ko


Maam Ceerno doynama man it doynaa ko

Bu benn xeeti Kokki mbaa wu Mbàkke


Taxaw fi naa Sàmba aki Demba Mbàkke

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 36


Keroog la Ceerno yeesalat njébbal ga
Feddali booleek ga wéyoon ca ndaw ga

Keroog la jaay mbokk ga ak xam-xam ba


Jëndee murit saadix wëlif am-am ba

La ñu donne woon si sunu Maam Moor Anta


Ñu jox ko Seex Bàmba mi raw ab jant

Kaamil ba Maam Moor donne woon ca baayam


Ñu jox ko Bàmba mooki doomi baayam

Bàmba ne leen na ngeen ko jox Boroom Saam


Ngir Kaamilug mag-moom la leeg nu dem Saam

Maam Abdu Xaadir baayi Mbàkke Soxna


Moo ko bindal Maam Bàlla Aysa Soxna

Ceddo ko ray moo tax ba sunu maam Bàlla


Gàddaaye Mbàkke sañc Ngay ngir Yàlla

Pël yaa ko ray moom it ñu fob kaamil ba


Jébbal ko Maam Moor Anta mooy kaamil ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 37


Bis ba mu faato la ñu ko jox Boroom Saam
Bis ba mu faato la ñu ko yobb yót Daam

Ñu jox ko Sëriñ Tuuba fa taaxi Njurbila


Bàmba ne leen yót leen ko Ceerno oorma la

Gisnaa fa bis màqaama Ibraahima


Muy dolli ay màqaama Ibraahiima

Boole na koog keroog mbubbum baarkeelu


Ne ko ku ñàkk sol ko daal di kiilu

Maam Ceerno ne su ma masaa na sol mbub ma


Damay nangoo nango ba summi mbub ma

Xam naa ku daj mbub ma faseekuk ñàkk


Yaa laytani ma sol ko ndax ma fenk

Ma wax la at ma Bàmba àndeeg Ceerno


Ñu seeti Aas Kamara Ndar defar nu

Ceernoo ko sàntu booba mook Sëriñ Ndaam


Ba ñu demee Kajoor la been Sëriñ Ndaam

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 38


Keroog la Ceerno yanu junnib ngurd
Booleek yëre yu Seex Bàmba kii du garde

Xam na ni jëmmi nit jikoy malaaka


Moy Ceerno Faati wutena ak Muusa ka

Ba ñu demee Ndar ba siyaare Maam Aas


Tëye na Bàmba Ndar di laaj depans

Sax na fa Ndar lil xaadiril jilaani


Te lum fa sex Ceerno ko daa yalwaani

Seex Bàmba laaj na ko fa wérdub Xaadir


Ngir bëgg jokk ji ci Abdul Xaadir

Aas naa ko toggal muñ te bulma tàggu


Diggante Muusa ak Xudar ngay sàkku

Sa mbir'a ngeeg man démb laa la fàggu


Moor Sàmba Tukulër ba laa doon sàkku

Yaa di juróom ñetteeli lawliyaa i


Yi wara yor werdu wi fil alaahi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 39


Wa shaaminu xaadimu Bàmba Ahmadu
Man mishluhu fil harbi laysa yuu jadu

Keroog la Bàmba xëy a xëy ni meng


Di waa ji seeti kuntiiyu faf ni feng

Ca mooma at la tog fa ndar ba xàddi


Bay bëgg a wëy Gànnaar bi xayri raddi

Keroog la disoog Ceerno yoonu penku


Mu naa ko nañ daal di rañaan tay tànku

Keroog la Bàmba ñaan ci barkeb Jiili


Naa daal di gis Kuntiyu mbaa te Jiili

Rabbi bi jaahil Mustafa wa min duri


Sala xahu xabli xuruu ji min ndari

Ba bët setee ñuy bëgg dem la Maam Aas


Daaldi taxaw ni Bàmba yaa raw ñoñ Faas

Gisnaa la biig ngay bëgg dem ba Màkka


Te yaay rammu soodaan saxal fi Mbàkke

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 40


Sa rakk ji mooy sa ndimbal ci baatin
Moy sa rawaan Maam Ceerno ya dib laakin

Bisub keroog la Bamba daaldi fomm


Def yetti way jox ko fa Aas ni cumm

Ad durru wa nafhu minar rahmaani


Laysaa minal suudaani wal biidaani

Ad durru wa nafhu minal jabbaari


Laysaa minal fujjaari wal abraari

Ad durru wa nafhu minal wahaabi


Laysaa minal ahdaa i wal ahbaa bi

Yii le bëyit la Bàmba dénkoon Maam Aas


Mu yër ko daal di ni ko yeen a am sãs

Keroog la Aas jox ko fa wérdu xaadir


Bi izni rabbil halamiinal xaadir

Keroog la Bàmba jox junnem ba Maam Aas


Mu naa ko falnaa la te yaa di fugraas

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 41


Aas naa ko jox naa la Kajoor wa Gànaar
Ak Bawal ak Saalum Jolof di sam xaar

Li lee taxoon ba Daam deme Jolof Njaay


Ñoom dalaluñ ko gungewuñ ko ñoo aay

Aas naa ko ndaama li di Ceerno Faati


Fum mëna yam di saahibul ayaati

So doon Suleymaan mu di sam Hifriitu


Dafhan wa jalban moo ma dàkka yootu

Jox ko fa mbalaanum Sheex Abdul Xaadiri


Bañ donewoo ca sëtti baayub Taahiri

Mu boole koog jàkk wa ak deram ba


Ak kurusug Maam Aas yor siroom ba

Ba ñu deme Mbàkke kajoor la Baay Daam


Xarlo mbalaan ma ka ñu naan Sëriñ Ndaam

Seex Bàmba doglu ko tubay ak turki


Seex Abdu Rahmaan moo ko ñaw ngir bàrke

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 42


Neena keroog puso bu nekk ag laaya
Ci Alxuraan mooma ko doon riwaaya

Mbicam mbalaan ma moom la Bàmba reere


Bisub keroog añeku lii ka biire

La ca desoon mu jox ko Maam Seex Anta


Ni ko nga barkeloo ko yaa dib jant

Bis booy dajeek tubaab yi yobuloo ko


Ba Seex di dem Segu mu far làmboo ko

Mu daaldi fab wérd wa jox Maam Ceerno


Ne moo ko sàntu woon ba Ndar moy hawnu

Te ni ko koo ko may mu xam sahadaa


Bila saxaawatin wa xarqal xaadaa

Man Njàmme Ceerno ma ko may fa Daaru


Alhamdulilaahi ma sant waaru

Mu daldi fab werd wa jox Maam Cerno


Ne moo ko santuwoon ba Ndar moy hawnu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 43


Te ne ko koo ko may mu xam sahadaa
Bila saxaawatin wa xarqal xaadaa

Man Njàmbe Ceerno ma ko may fa Daaru


Alhamdulilaahi ma sant waaru

Deglul ma wax la bis ba Bàmba ñibisee


Mbàkke Kajoor ak Ceerno Faati ndaama si

Njafal nga jàpp Ceerno jiite daara ja


Seex Ibra faal jébbalu ànd ak mahraja

Maam Ceerno fas ni Soxna Faati Sàmba


Danaa ko jox sha’Allaahu Siidi Bamba

La mu waxoon Yàlla doggal na loola


Ci darajaay Maam Ceerno jël na ndam la

Ka mu yoroon la jox Sëriñ Medun Jòob


Ci darajaay Maam Ceerno Faati may ajiib

Foofe la Soxna Faati Sàmba faato


Mook doom su góor sa ajaban moo yaatu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 44


Maam Ceerno delluy wax a wax fa Bamba
Bam wutëlaat fa Soxna Xadi Sàmba

Ñaari jigéen yu Seex Muxtaar Sàmba


Raddi anhumaa halii ak Bàmba

Keroog ba Soxna loo mu baax ma faato


Laleen sëriñ ba bàyyi far nañ faatu

Keroog la Ceerno melni gaynde mbooya


Di wax ba Daam fab Soxna Penda Mbooya

Amna ca doom ju tudd Soxna Faati


Ci darajaay Maam Ceerno Ibra Faati

Bul jéema lim li Ceerno wan Seex Bamba


Ci waa këram moo doon bëtam di tànkam

Fekkoon na Cernoo'y wax Abdulaahi Jaww


Ñii ley sàngub kër gi asal ba leen jëw

Ummu xaliifatu Rasululaahi


Seex Mustafa Mbàkkiyu baabul laahi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 45


Ca mooma at la Bàmba dem ba Fettu
Dem Ndindi dem Kunjunj di dox ba fattu

Ngir bëgg gis leeri ngëneeli Tuuba


Maam Cerno Faati fa desoon di kooba

Sax na fa Fettu fa sexaw gu rëy ga


Luy bëgg mat weer te gisul waa kër ga

Ceerno yoroon wa kër ga ak ndongoom ya


Di jiite jàkka ja di jàngal doom ya

Loolaay lëlub xaliifatul xadiimi


Seex Mustafa Mbàkkiyu moo mat doom

Ceerno ca yonni Xonn* Ndooy ca yoor-yoor


Moo ko yëggal Seex Bàmba kooko ley góor

Bàmba ne Ceerno na nga ko wax Borom Saam


Maa gi ci xalwatu damay liggéeyal borom Saam*

Keroog la Ceerno yonni Abdul Xaadir


Moo jëndi gàtt ya keroog ci saahir

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 46


Sëriñ Momar Jaara ko tudd xadwafaa
Tudee ko boppam Bàmba ñëw ne Mustafa

Bisub tuddam ba yawma ashuura


La Bàmba gis Tuuba mu leer waraa a

Seex Bàmba topp leer ga jàll Tuuba


Leeram ga jollina ba aksi booba

Lii lee taxoon Seex Mustafa moom Tuuba


Leerug mbirum juddoom ma feeñal Tuuba

Ba Bàmba dellusee la ko wax Maam Ceerno


Ñu daal di toj àll ba gor mu wër nu

Seex Móodu Ndumbe daaldi woolu kàrce ya


Seex Bàmba rëdd jàkka ja diir ca xiblaya

Seex Bàmba tudde bib ga woon fa Tuuba


Sajaratu sahaada la tekki booba*

Boobee la dee Maam Ceerno xarxal haada


Ne ko fii leey samag mujjug sahaada

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 47


Bisub keroog la Bàmba wax Boroom Saam
Ne ko jumaa dina fi am balaa Saam

Mu dellu wax Maam Ceerno baabul janna


Fii lee la tiim sampal ma beytii sunna

Mu daldi samp néeg ba tudde bëyti


Mu sul ca taalif yépp duuna bëyti

Néeg baa di xabroom ba ñu def jumaa ja


Te beyti googaay beyti gii moy waa ja

Seex Bàmba am fa ay ati at di taalif


Maam Ceerno yor saahir sa moo di xaarif

Ca mooma att la ko diggal mu am kër


Te amuloon néeg sax te dëkkee kër-kër

Boobe lay wax Seex Bàmba naa ko man de


Fettal jixaar rekka ma doy su doon doy

Daam ni ko loo yëngël soxub jixaar la


Te foo taxaw may sangi wër la aar la

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 48


Te dinga jékki ba junni akub tànk
Ñoy yam ci yaw sha Allaahu dootoo bank

May naa la ngay dund ba waxtu wu la soob


Deefu la seetsi doofi tàggoog lula soob

Soo xalamee at ma Sëriñ Tuuba demee


Te kenn xamul fumu jëm ci reew mi moo ñeme

Ngir tàgguwul kenn kudul Maam Ceerno


Te moom du feeñal mboot li tax mu raw ñu

Sëriñ Mbusoobe dal di bind ab leetar


Yonee ko Seex Siidiya moo am tiitar

Leetar ba dem feekul fa Seex Bàmba


Waa Mbàkke ak Mbusoobe ñéppiy bëmba

Seex Bamba dox Jolof di wëy ba waalo


Ñu naa ko doomi-doomi Asta waalo

Ba mu deme ba rombu Moji Indi


Maam Ibra Njaay la fa gis mu naan ba màndi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 49


Seex Bamba romb ko fa wëy kamb kile
Alaaji Maalig la fa gis muy jàngale

Ba mu nuyoog Al Haaji waxtul hasri


La ko ni santal bi ñu dajee fil hasri

Alhamdulilahi lëzi ahrajanaa


Min zulamaatihi li nuuri hi xunaa

Ba bët setee la Bamba xëy wañeeku


Dellusi Tuuba Mbàkke gëpp ñee ko

Inal lezii amara nii bil mas’aa


Xuwal lezii amara nii bir ruj’aa

Ba mu gisee Maalig wa Ibraahiima


La far ni tépett jaaju yoonu réew ma

Ba mu ñeewee ne Ceerno Ibraahiima


Gis naa fa mbër mu tudd Ibraahiima

Jëwriñu Al haaji la fil islaami


Su nuu sàgganee mu raw nu fil hiyaami

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 50


Bisub keroog la Bamba ñaax Maam Ceerno
Yawmal xiyaamati rammul bii xarnu

Keroog la naa rammul ma axlul barri


Su ma demee géej rammu axlul bahri

Ca mooma at la jàju yoonu géej ga


Bëgg liggéeyal Mustafa may géej ga

Loo laay lëlub Al haaji Seexi Faadilu


Ñëw na ca aama wasashin min faadilu

Kazu rajab la njol ma ñëw ci dunyaa


Loolaay guddig rañaan ga toj xëram ya

Keroog la Bàmba ni Rasululaahi


Ñëw nafa Tuuba ngir ganam lilaahi

Looloo waral Seex Faadilu dem ba Màkka


Dem Tayba far siyaare kër Njool Màkka

Musaa ka yaa ngi bëgg xuus ci Bàmba


Dëppal te way Maam Ceerno yor na xol ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 51


Waye tàgg Bàmba ak tàgg Maam Ceerno
Mëneesu ko tàggale fil hadaati

Da ñuy cereeek sëb jaxasoo ca baawaan


Seeni mbira jiitu ñii lee jiitu ña woon

Min asashin limasashin taqabalaa


Wa bisiraa tihi kafaa ni subulaa

Loo loy judub Sëriñ Masàmba Mbàkke


Maam Ceerno am fukk ak juroom yaar Mbàkke

Keroog ba Seex Bàmba ñëwee fa Mbàkke


Ceerno di dox digante yaari Mbàkke

Sëriñ Maxujja Ture ak Maam Ceerno


Ñoo topatoo lepp nde ñoo mat hawnu

Murid bu jebbalusi ñoo lay taxawu


Tool buñ faraasu bam sax mu baxawu

Bundugilooki tooli Sëriñ Tuuba ba


Moom la ñuy njëkk bay fa Mbàkke baaba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 52


Ceerno ko jëwriñu Sëriñ ba gorloo
Fa Mbàkke doodi ca dewen moo farlu

Sëriñ Mbusoobe ñëw mu jox ko gor ba


Ñu bay ca gent ba mu fay ko bor ba

Ca mooma at la Bàmba wax Maam Ceerno


Digante Soxna Mbàkke ak guvernu

Ñu daldi fab soxna sa jox Sëriñ Ndaam


Fa Mbàkke baaba loolu moy mbeggum Daam

Am na fa doom yu sàkk ay xaliifa


Ci daraajaay Maam Ceerno may xaliifa

Loo laay lëlub Muhammadul Amiinu


Seex Baara Mbàkke ko ku mooy Amiinu

Ca mooma at la Bàmba dugg xalwa


Ca weeru koor wa Ceerno feeteek jal wa

Ca mooma at la Bàmba woo ñiy jàng


Bañ tambalee tëral mu jog ni fàgg

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 53


Waa jay tëral amiyatul afhaali
Ba ca hiyyasil masdaril afhaali

Seex Bàmba daanu nekke fab na haal ja


Di baamu way wa ba ëlag mu jàll ca

Fihlun hiyaasul masdaril muhaddaa


Min zil shalaashati karada raddaa

Keroog la Seex Bàmba tasaare daaraja


Daaldi bàyyi jàngale moo am daraja

Bisub keroog la Bàmba woo Maam Ceerno


Digal ku muy jàngale moo ka rawnu

Mu def ko muy xaliimu kulli fannin


Sharaxa rabbi sadrahoo bil manni

Ca mooma at la ko yabal fa Njaxate


Kër Moor Biraama ngir furuuh ak luxati

Degg lul ma walbati la far la waxati


Way wa fa Maam Ceerno wayal waa Njaxate

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 54


Halaa Seexi haazaal waxti saydi jiilihi
Salaamun fariidun laa yubaaxa bi mishlihii

Salaamun kamaa miskin wa werdin wa hanbarin


Halaa Sheexi Ibraahima misbaaxul ahlihii

Nafal jahlun an xaazaa araafi jamihihaa


Kamaa tantafii bil badri zulmatu laylihii

Fakam jaahilin xad saara fahlan mubajjalaa


Wa kam min xamiilin faa xa xadlan bi fadlihii

Alaa ayuhaa maxsuudu min kulli maw tinin


Wa yaa man yasiirul xumra bahran li saylihii

Ataaka hariibun min biladin bahiidatin


Falaa tahfulan han zal hariibi li jahlihii

Wa kun lii aban barran raahiman wa naasihan


Fa abxaaka rabbul harshi haawiyaa jazlihii

Fa ajaabaho sheyhu walaahi law kuntu zaa latmin


huduuda kumu ilaa mamaatiya maa niltubi maxsuudi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 55


Walaahi bii sëriñ yabbul ndongoom bi
Way week jawaab bi loome nañ ci tarbi

Amul fa am at Bàmba dal koy woolu


Ni daa ko doon haajar ni moom la woolu

Ca mooma at la ko yabal ca kër Makala


Huwa ala rabbil waraa tawakalla

La dalee Njàmbur jàpp waa kër Makala


Moo leen xamal laabug deseetum satala

Amulfa am at Bàmba dellu woolu ko


Ne ko shariixatu ak xaqiixatu boole ko

Ca mooma at la sañc Mbàkke Baari


Dajale fay sihaari wal kibaari

Maam Abdu loo and ak tubaba ba ñëw fa


Wisiti kër ga ngir bal ak doomam fa

Fekufa dara dara ludul ay teere


Bajo ba mer ñortam la def na meeri

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 56


Dal di tasaare kër Sëriñ Tuubaa ga
Soxna su nekk dem mu wër di saaga

Loo loo taxoon Maam Abdu Bàmba naa ko


Tàbban fa tàbban yërmandem la naagu

Tuuba fa Tuuba la waxoon Maam Ceerno


Dunyaa wa uxran texeel bii xarnu

Maam Abdu moo doon lantinoorub sharru


Maam Ceerno moo doon lantinoorub sirru

Mu yonni Ceerno boolee kook Demba Kebe


Tubab ba naa ko Bàmba laay fabbi ebe

Ba Ceerno laa wax Bàmba seen leetar ba


Mu ne ko Jibriilu ñëw na biig fa neeg ba

Wax na ma seen mbir xamal ma mbóot ya


Laayay wa iz yamkuru moo di mbóot ya

Li hawlihi tahalaa
Li hawlihilaahi tabaaraka wa taahalaa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 57


Wa iz yamkuru bika lëzina kafaru
li yusbitooka aw yaxtilooka aw yuxrijooka

wa yamkuruuna wa yamkurulaahu
wa laahu xayrul maakiriin

Billaahi faraxtu nasaara jeewaali


Wa xayruhu hatxan bilaa tannawuli

Xanaa yëggo ba Bàmba genne Senegaal


Ñu di ko yobbu Kongo muy tabbi ci gaal

Subhaana man fil barri wal bahri maxaa


Ajral jawaari ya wa kulan jamahaa

Subhaana man li jaada fis safiina


Fi hidmatil li saahibil madiina

Subhaana man yuu li joo fin nahaari


Laylan wal asraara fil ijhaari

Keroog la Bàmba denk Ceerno ruu yi


Tàbbi ca geej ga ni ko sammal tool yi

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 58


Yaa ngi meloon ni gunne guy wattub tool
Di yeeg di seenuw goloo far di ab njool

Ñu naa ko njool mi njool far di ag ron


Guy dem ba laali asamaaw dajjeg Kun

Kun fayakuun far ni Ceerno toogal


Maay wattu lislaam say kannu ngii may yeegal

Te kun a man kannu waxaadaliya kun


Xarbaax a man xërëm niroo wulaag kenn

Lislaam a man keefar yoralma lislaam


Baatin a man saahir te Ceerno mooy Daam

Bisub keroog lako Sayer Sahiidu


Jebbal mbiram fa baari moy sahiidu

Texem murid yi la turam way seere


Moo njëkk jebbalu keroog fa Baari

Fekoon na Bàmba booleko ak Muusa Mbuub


Sëriñ Mamar Seen ak ñeneen ñu naa Mbuub

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 59


Keroog la sun Maam Ceerno gontee Baari
Fanaani Tuuba pël ya naa ko xaari

Ñu daal di roñ yëre ya yobbu woobe


Fa kër Sëriñ Mbàkke ma raw mbusoobe

Mu jàll wëy Mbàkke Bawol bañ goowe


Wa Mbàkke naa ko bul ñu yobbu boowe

Maam Ceerno jàll sañc toloog Mbàkke


Ñu naa ko ëplëw da nañ la sànk

Ba ñu ñëwee noon yay textexiy ree


Naa kuy dundal mboloo mi waay da nañ dee

Mbàkke la Daam Ahmadu Faati faatoo


Mooy magg i Maam Ceerno su dunoon yaatu

Seex Bàmba ne woon na su dundoon kenn du ma xam


Moo tax ñu lëm ko jëme biir Yàlla ko xam

Foo fee la Soxna Faati Bintu njambale


Bay bëgg a faatu Bàmba moo ko jàllale

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 60


Mbàkke la Seex Mòodu Yadaali faatoo
Fa kër Sëriñ Moor Soxna Seek maatu*

Seex Mustafa Mbàkkiyu daal di wopp


Seex Bara Mbàkke wopp bay jott app

Lu mat juroom ñett nelaw ca mbas ma


Balaa ma tar na mooma atum mbasam ma

Keroog la Ceerno mësa jooy ci dunyaa


Daal di garanti ruu ga feg yu bon ya

Ni Yàlla maag saa doom yii ak saa ndey jii


Joteenu doomi Bàmba yi reer lay jee

Moor Mbàkke lòo ma daan liikaamal Ceerno


Moo daal di faatu far jotaale Ceerno

Keroog la Ceerno woolu Maam Masoogi


Ca saate mooy baayi Mataar Masoogi

Boroomi jinne la ku man lasraar la


Mu listixaaral ko ba naa tafaar la

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 61


Ni ko da nga dëkk ci ngiirub jinne
Tuxul te dem fa guy ga bul fi sonne

Ca mooma at la tuxu dem Guy Goora


Sañc fa ab dëkkam saxal fa ngoora

Saxna fa yetti at sikar say jolli


Mu bënn fab naanu mu daal di golli

Seex Bàmba daal di yonni Abdulaay Nduur


Mu jugge Kongo ni jalañ ma ngay luur

Jox ko fa ay leetar yu ànd ak sirru


Tàggalikoog balaa fegal ko sharru

Ni ko nga sañc fa ñu naa Guy tàkko


Tudde ko Daaru foo fa naan dun tàggo

Te sàkk fab naanu te yeesal diine


Te xamni maa ngi daal di ñëw fil hiini

Boolena koog keroog yëreey barkeelu


Na ko beggal beggal ne leeg nga kiilu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 62


Jox ko fa leetar bu baal waa kër ga
Ne ko neleen yabal ñu dem bitarka

Ku nekk mu wax ko ka ko Yàlla boole


Jarul ñu fay limaat du yell xooleel

Ku ni muni ko na ko jox ab teemeer


Balaa ngakoo yëggal mu yobuloo mer

Seex Mbàkke Maane ko yëggal waa kër ga


Jigeen ña daanu door ko ay taaparka

Mu ni yëral ma Soxna Faati Madu Maam


Ngir la mu yor suy mucc xam ni man a Daam

Su dee goor Basiiru laa koy tudde


Su de jigeen Maam Ceerno tudde Xadi

Ba mu delusee la ca amaat am Xadi


Njaareem la faatoo ku la xaar du xàddi

Xeraw lj leen ma waax ganaaw Seex Bàmba


Na Ceerno def njaboot ga ak dëkkam ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 63


Moo yaa ganaw Mbàkke te sedd mbootaay
Te man a muñ te man a sam ag mbootaay

Ku weddi lii laajal Soxna Faati Silla


Moo teewee demb teewe tay am fulla

Am na fa kër ga yetti at di sancaat


At mu taxaw mu làkk Cernoo lankaat*

Reew ma di feewale murit yi ak Ceerno


Seex Moodu Ndumbe naa ko yaay guvernu

Seex Moodu Ndumbe moom la Ceerno woolu


Moo sañc kër ga ñii la Bàmba wòolu

Ca mooma la Ceerno Ibraa Faati


Wòolu ko Mbàkke jox ko Soxna Faati

Ba ñu julle kori bisub talaata


Ñu yot ko gan gu Ceerno dul talaata

Seex Moodu Xabaane mat na ab xaliifa


Ci darajaay Maam Ceerno may xaliifa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 64


Seex Bàmba way ab denk yonne Ceerno
Ni ko nga waar mbindeef yi yaa mom xarnu

Wa ansiril naasa la denkoon Ceerno


Jii wax a piir Yàlna Bàmba jarnu

Ma far la wax xasida gaag xaraf ya


Nga xamni Bàmba jox na Ceerno yëf ya

Wasiyaatun tukashirul hataayaa


Li kulli man yaj taniibul hataayaa

Usiika bil hilmi wa bil ahmaali


Maha ta adubi hala kamaali

Nazif fu aada ka anil adraani


Takun muxaddaman halal ahraani

Zulal ihwaanika linaasiha


Tanjuu minal bahdaa i wal fadihaa

Rumi tawaduha li kulli muslimi


Tanju bila taradudin min zulamin

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 65


I zaa ataaka haduudi kitaabi
Fa karimil kitaaba bil mataabi

Layin lisaanaka wa xalbaka mahaa


Lil muminiina xayra xayrin tajmahaa

Naa daytukal yawma ni ibrahiima


Halim fatan yanfahuhu tafhiima

Usiika bil sabti wa bil ihlaasi


Li wajhi man lii jaada bil xalaasi

Salamu zil jalaali wal ikraami


Halaa nabii darajatil kiraami

Ca mooma at la Ceerno fab xaqiixa


Boleek shariixatu di sàkki miiha

Mu yeesalaat diine fa Daaru Mannan


Yobbu murit ya fettoo melnib sultaan

Tarbiya karce ya fa topoon Bàmba


Di jàngaley julli teeñu yan ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 66


Ku weedi laajal Aliyu fa Baari
Da daa andal Maam Ceerno daan jihaari

Sëriñ Momar Jaboo 'g Sëriñ Moor Penda


Sëriñ Momar kura teggal Mbay Penda

Sëriñ Amar Faal Mbàkke moo ko jàngal


Jebbal ko jarbaat ba kafeem lay tàngal

Seex Mustafa Mbàkke ma dib xaliifa


Ceerno ko jàngal koo ku nawleem newufa

Jebalko Aminatu Loo saay nopp


Nopp ñi koy degglu te magg ma fopp

Sëriñ Masàmba Mbàkke moo ko jàngal


Fa Daaru Manaan moog rakam ya yëggal

Al haaji Fadilu nga woon fa Mbàkke


Ceerno ko mootalil bi xayri shaki

Dencal ko doom ja tudd Soxna Aysa


Zaa ta jamaalin moo di jeeja naafisha

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 67


Sëriñ Momar Roqaya moo ko jàngal
Jebbal ko taaw ba koo ku lam am yombul

Seex Coro ak rakam Sëriñ Bàlla Coro


Jàngal na leen as lëf ñu dem doora berru

Sëriñ Maxtar Binta ak Sëriñ Momar Sëy


Moo leen xamal xamal Sëriñ Muusa Sëy

Sëriñ Madun Penda la Ceerno jàngal


Jebbal ko doomi Seexi Bàmba yombul

Seex Moodu Muxtaar Joob du moo ko jàngal


Jebal ko Soxna Mbàkke moo ko yakkal

Sëriñ Ma Banji Njaay Sëriñ Móodu Xari


Moo leen xamal sàkk na fóore yu bari

Ñam jàngaloon fa taaxi Daaru Manaan


Maneesul leen a lim ku aksi far naan

Xanaa yëggo daara ya Ceerno sàkkoon


Ñiy tariloo gunne ya maa fa nekkoon

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 68


Musa limal jàngalekat ya booba
Ba tay ña ngag jàngale ño raw Tuuba

Sëriñ Mamar Mareem Ibrahiima


Ñoo daan bindal Maam Ceerno Ibraahima

Seex Moodu Jaane ak Seyiid Jaane


Abdul Kariim Loo yoo ya gaa ya waane

Sëriñ Momar Dem ak Sëriñ Momar ka


Ak Soce Njaay xamnañ Sëriñ Muusa Ka

Seex Moodu Muxtaar Joob Sëriñ Momar Ñang


Seex Ture jàngale na Daaru far lang

Ak Mustafaa Jang Madu Gëy Maam Faati


Ak Madu Mbàkke mom jiggal xad yaati

Jàngalekat ya matna waa kaamil ba


Mëneesul leen a lim yëral kaamil ba

Ma jeema lim la Ceerno Faati seexal


Te lu ma lim-limit du tax ma jeexal

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 69


Aliyu Juuf Lambaay Mapaate Silla
Seex Bàmba nee Maam Ceerno am na fulla

Sëriñ Matar Gay Ceerno Gay Asan Gay


Masamba Gay Mësula feeñ ci Ngay-Ngay

Maxari Siise ak Seriñ Mbay Siise


Majobba Siise ak Masoxna Siise

Sëriñ Mayaasin Joob Momar Joob Ñooro


Sëriñ Mataar Sàmba ñëw leen nu jooru

Sëriñ Momar Jaboo ki Ceerno Aysa


Seex Bàlla Jee cëy Abdu Mbàkke cam sa

Saa Njuga Sàll Seex Madige Sàll


Seex Paate Sàll yooyu góor a sell

Seex Mustafaa Kan ak Sëriñ Asan Kan


Sëriñ Momar Kan Ceerno bokkul ak kenn

Sëriñ Galay Ja ak Sëriñ Musa Ja


Seex Moodu Yaasin Ja du Ceerno mooy waa ja

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 70


Seex Góora Njaay tofal ca doom ja Baay Njaay
Sëriñ Mayaasin Njaay Birahim laay jaay

Seex Abdurahmaan Njaay Abaabakar Njaay


Seex Moodu Njaay bonxooy ku Bàmba doo jaay

Sëriñ Umar Seen ak Sëriñ Momar Seen


Seex Abdulaay Seen Ceerno Faati laay séen

Sëriñ Masaaxo Seex Aliwu Baaxum


Seex Paate Ndimblaan du wax ak njaaxum

Sëriñ Useynu Faal Sëriñ Majjali Faal


Moor Faal karaama xamna Sëriñ Masilla Faal

Sëriñ Moodu Jeng Xàbbaan Sëriñ Maalig Ñas


Seex Moodu Joob wàllu Biraahim lay gis

Moor Ndate Lëy Góora Bajaan Maalig Nduur


Seex Ibra Njum xamna Sëriñ Ahmadu Ndiir

Seexal Seex Ibrahima Cub bum Xabaan


Sëriñ Mataar Wañaan Sëriñ bi yaa daan

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 71


Seex Baaba Ngom Sëriñ Momar Ngom Njoorel
La leen Sëriñ bi may soree naak duural

Seex Moodu Ndaare Gëy Sëriñ Mabuuri Gëy


Seex Buubu Mbay Maam Ceerno Faati jar way

Sëriñ Abdulaay Ñang pël yi xam nañ Ceerno


Sëriñ Aliwu Ñang nga daw ba raw nu

Seex Aali Jey Sëriñ Mataar Daraame


Móodu Daraame doom ja bil kiraami

Seex Baabakar Sow Banda Sow Momar Sow


Habiibu Sow ku ngoy ci Ceerno doo sew

Seex Móodu Joob Sill ak Sëriñ Juuf


Seex Móodu Astu Sill dootu leen soof

Sëriñ Momar Ba ak Sëriñ Momar Caam


Maam Ceerno Faatee leen defar ganaw Daam

Seex Aali Sàmba Gëy Abaabakar Gëy


Dawuuda Gëy Maam Ceerno daawu leen jay

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 72


Maam Ceerno amna yaari Móodu Jong
Ñoo doon Muusa Jong Ibra Jong

Sëriñ Mataar Ndong ma dëkkoon Ndongo


Seex Ibra Faati a tax mu am ay dongo

Daawuda Gay Seex la limaalel Xaar Gay


Saalihu Gay Maam Ceerno Fattee jara way

Sëriñ Momar Jaañ ak Sëriñ Usmaan Jaañ


Maam Ceerno Faati a tax ñu fawxa waa Njaañ

Seexal na Ibrahima Mbaw Seex Moor Caam


Wa Gumba Caam doo tu ñu sibooru ni jaam

Xana xamo Sëriñ Momar Njaay Handar


Ceerno ko seexal ma nga fee di kàmpaal

Seex Moodu Laamin Seen Sëriñ Usman Seen


Seex Njambe Seen ku seenu Ceerno lay séen

Lim naa juroom ñetti fukk ak juroom ñaar


Ci seexi Maam Ceerno kii le doyuk waar

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 73


Loo laay limub satala yam daa naane
Yawmal xiyaam seexam ya ñoo koy naane

Ma dellu wax leen mbiri Daaru Mannaan


Ngeen xamni Ceernoo fonk Daaru Mannaan

Bissub dibeer la sañc Daaru Mannaan


Ca haama Taysashin murit bu mar naan

Saxal fa jàng alxuraan ak sikar


Aki xasiidati mu tog di fikar

Bënn fa teenub madrum muy baawaan


Daarul Haliimi ak Mbussobe saawaan

Boobee la Seex Sidiya fer fa Daaru


Juddo fa Guy Ngura ba am nag daaru

Yoor-yoor ba Seex fere la teen ba bënn


Ca tàkkusaan gaskat ya dal di génn

Boobee la bay fa Fettu yeti dàgg


Jox ko Sëriñ Tuuba ma tol yay jàkka

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 74


Dàggaay Sëriñ Balla Habiibu Gajaga
Bàmba a ko jox Maam Ceerno def ko asaka

Seex Bàmba fob dàggay Sëriñ Moor Musaa Ja


Jox Jurbel ak Tuuba ne Ceernooy waa ja

Limub juroom ñaar fukki sàq yu teggal


Lu mat juroom yett la moo mata ragal

Yeesal limub atam ya Ceernoy xarbaax


Wolaf lu ngeen añaan añaan ni moo baax

Ku weddi lii laajal Sëriñ Muusa Ja


Mooma ko wax fa Daaru moo di waa ja

Maam Ceerno dellu jox ko dággaay Ibra Njaay


Ak Abdu Mbàkke yaari jëwrin la fa jaay

Seex Bàmba dello koo ti dàggay


Joj Ibra Njaay mu jox Sëriñ Ndaam Abdu

Mo amewoon waa kër Sëriñ bu mag ba


Ca woowa waxtu ken du sàqi njag ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 75


Limub juroom fukk la woon ci ay sàq
Jigeeni Ndaam di wal di bojji sóq

Ca mooma at la pël ya xeex fa tool ba


Jam nañu ndongoom ya bisub alarba

Ku weddi lii laajal Habiibu Gajaga


Moo mag ca jewriñ ya sangub waa Gajaga

Bu dul kon ag xar baax i Mbàkke-Mbàkke


Moo ko seral ne kon badar ja dekki

Jam nañ ca pël ya fukk ak lu topp


Ñële ñu xaañ ñële di daw ñu topp

Ñaari murit la pël ya ray fa tool ba


Xareb badar ba sàkku nañ ca yool ba

Aliyu Gëy saadix la fawqa maata


Xaroona faatom ga bisub talaata

Fekkon na Maalig Siise dal di faatu


Seen taaxi Aljana ya ñooka yaatu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 76


Jam nañ Mamar sox ni tëf Asan Gëy
Dab Njaxat Sàmb murit ya naa cëy

Hamsatu Njaay ñu fàdd gob mu daanu


Ñu xaañ ko Ibra Mbuub far kaanu

Ñu jam ko ab xeeñ dal di jam Mamar tëw


Yuxu ya ni weeb pël yaa nga mel ni ab taw

Jam nañu Móodu Jong gaa ya songoo


Wall ga ñëw Daaru ki Mbàkke dengoo

Mandumbe Saaxo lañ xaañ Móodu Xari


Ñu jam ko sox ya tàkk pël ya di xari

Pël yu jigeen ya ak ndaw ya naa ay yeegam


Mag ña di làkk naa murit yi lee gëm

Walaay murit ya buñ yoroon bal ak doom


Kon "kuuni kuuni" fay tepal mëq ak doom

Keroog Sëriñ Mbàkke Buso'k Sëriñ Daam


Ñoo tee badar ja dekki bi isni Maam Daam

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 77


Waroonaño furli fa Daarul Muhti
Kon bal ak doom ak lewar weer xatti

Jubeyru ak Amaat fa neegi Fettu


Ñoo sooke xeex ba fu ñu taxaw di maatu

Maam Ceerno bañ na pël ya ngir Jubeyru


Pël ba ca naari dootul tàggoo’k dayru

Maamam ma ray Maam Bàlla Aysa Mbàkke


Moo ray murit i Ceerno Faati Mbàkke

Ca mooma at lañ kalaame Ceerno


Tëj jëwriñam ya muy layoog guvernu

Bisub keroog lañ fa yabal si Mbaaxaan


Moog farba jaag waa rewmi ñëw di laaxaan

Mu woolu Maam Ceerno mu ñëw fa Mbàkke


Ak Ardu Aamadu'm kayel moo ñakki

Pël yaa ngi andag Ardu naa bimaami


Walaf ya andag Ceerno naa imaami

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 78


Mbaaxaan leen woo tirbinaal fa Njaaréem
Ñu wuyu si Mbàkke Ceerno ñëw di leen yeem

Ba ñu demee mu naa komandang Jànqeen


Moo leen di atte ndax mu jànqu jànqiin

Ba ñu demee Yàlla seral soloom sa


Ci darajaay Seex Bàmba may sangeem sa

Ca mooma at la gedd Daaru Mannaan


Ngir pël yu bon ya dal di seeti Xàbbaan

Ca mooma at la seeti àllub Gaawaan


Wër ko mu xat fa moom murit yi saawaan

Ba mu ñewee la woolu Seex fa Njaxami


Ni ko demal sañc ko ndax ñuy sàkkami

Ca mooma at la yegg kër Bu Kunta


Romb fa kër Baaba di saf ab jant

Ca mooma at la norooraasi daara


Fa kër Magéy waaresi doomi jaara

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 79


Waa Sañooxor waa Pir ñi daal koy faale
Mu fab lingeer ba yobuwaale

Ca mooma at la sàmp daara Mbaakol yi


Jox ko Sëriñ Muxtar mu yor leen foofele

Àll ba xat mu jàll sanc Xàbbaan


Ahmadu Jeŋ wa Paate Sàll ñoo daan

Ca mooma at la Ceerno dellusi Daarul Manaan


Seex Bàmba dàl koy woolu Daaru Rahmaan

Ne ko demal Mbàkke Kajoor te sañc


Bawol di wal Kajoor di gor di lanc

Ca mooma at la baay ba Ibraahiimaa


Faatu ca "hãama wak'sachin" mooy at ma

Bàmba yabal ko fa mu dem ko jaale


Abuu Suyuuxi Seyyidi Rijjaali

Ba mu woree la dellu Daaru Rahmaan


Fekkoon na Seex Bàmba di woorloo deymaan

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 80


Keroog ba Ceerno yendusee fa Daaru
Seex Bàmba doglu koor ga ñépp a waaru

Ñu naa bayit Sëriñ ba far bégal ko


Ba naa ku yendu Daaru jéggal nañu ko

Keroog la taalif "Haazihil Abyaati"


Ñu di ko soow ngir fonku Ceerno Faati

"Wa tarkunaa kaziba yaa ixwaani


Afdalu min tilaawatil Xur'aani

"Summa nasiihatu li ëhlil Baari


Xayrun minal jihaadi fiil kufaari"

"Kazaaka zikrul mawti afdalu lanaa


Minal xiyaami fiil layaalii zamanaa

"Fadum halas Sidhi mahan nasiiha


Wa zikri in xifta xadan fadiiha"

Yiile bayit la Bàmba denkoon Ceerno


Fa Daarul Rahmaan ngir reg yërëm nu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 81


Ma sulliwaat tay jiile mbóoti Ceerno
Yoo xamne jombu na goney bii xarnu

Bàmba a ko waxtaane ak Sëriñ Ma-Sàmba


Ma way ko man miy werekaanu Bàmba

Seex Bàmba noon na Seex Ma-Sàmba caat ma


Suma mbindéef doon xam Biraahim xam ma

Ceernooy loxol ndayjoor ba yaay càmmooñ ba


Loxo bu nekk ak lamuy jariñ boroom ba

Ndayjoor a koy leel bu lekkul faatu


Càmmooñ a koy laabal bu laabul laatu

Am ngeen ma man Bàmba it am naa leen


Te xamu leen ma waaye man xam naa leen

Yéenay samay zaahir te maay seen baatin


Yéenay yaram wi maa di ruuh gi yor Kun

Yéen a di man ku leen jamoon ma nàcc


Ku ma jàmm it ngeen nàcc déglul Bàcc

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 82


Keroog la naan Sëriñ Ma-Sàmba Ceerno
Matul a diir mbagg nde raw na ab xarnu

Xam na ci man loo xamne kenn xamul ko


Am na ci man loo xamne kenn amul ko

Yéem naa ko ngir limu xam ci man te waxu ko


Ak limu xam ci ay araf te jàngu ko

Yéem na ko ngir xam-xam ba limu bari-bari


Xam naane maay bëxrul huluumi maa sori

Yéem naa ko ngir lumu mës a am man la ko jox


Maa ko gënal boppam te kumu jox dula ñax

Yéem na ko ngir lumu ma jox lumu rëy-rëy


Ma jox ko mbindéef yi bu dellusee naa céy

Yéem naa ko ngir luma ko jox lumu sew-sew


Mu deñc waaye masu maa laaj masuta bew

Yéem na ma ngir waxtuw jamaalin wa jalaal


Xàmmeewuleen fum ma gisee dàldi kamaal

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 83


Yéem naa ko ngir fu ma ne ak fu ma newul
La Ceerno daa yemale aajowul defal

Yéem na ma ngir suma begee ak suma bégul


Du tee ma tagg Mustafaa sax ci ndigal

Yéem naa ko ngir suma gisul man Bàmba


Du tee mu xam saag jublu ngir Yonen ba

Yéem na ma ngir masul gis ma tàbbi


Ci lu nu diisoowul bi izni Rabbi

Seere sa mooy ba Bàmba nekkee Kongo


Te bind leetar jox Boroom Saam gongo

Ne ko nga may Seex Ibra Soxna Ummi


Seex Anta ak Maam Ceerno ñëw di rommi

Maam Ceerno moo ni leen bu leen ko xutba


Lii xalimam la waaye duggul xol ba

Sëriñ Momar Jaara a ko dàldi xutba


Seex Bàmba ñibbisi di xul tey xutbu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 84


Keroog la naa leen tàggu woon ngeen Ceerno am ?
Ba ñu laata tontu mu ni mbas ñu far luum

Keroog la Yàlla dàldi tebbi mbir ma


Ci darajay Maam Ceerno Faati mbër ma

Keroog la Boroom Saam ak Boroom Gaawaani


Dañu ne ko yaa xam Bàmba yaa di waane

Ca mooma at la ko bindoon ab leetar


Mook magam ak rakkam te ñoo am tiitër

Te mooy Boroom Saam ak Boroom Gaawaani


Te boole wu ci kenn fil ixwaani

Danaa la wax ca way wa ak wesar wa


As lëf nga xamne man a way du xarwa

Liile di tarjumaan ja njëkk way wa


Maa ko wayaale booba maa ngi ci xalwa

"Alhamdulillaahil hafiizil akrami


Summa salaatuhuu Halal Mukarrami"

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 85


"Séyyidinaa Muhammadin wal Aali
Wa sahbihii a'immatir Rijjaali"

"Wa bahduhuu fa min hubaydilLaahi


La Bàmba wax di nuyu Ahlul Laahi"

Ma dénk leen ngeen topp seen Boroom ba


Ngir bis ba kat moom rekk a fay Boroom ba

Te topp Sunnatu Rasuulul'Laahi


Ku ca awul du mëna dem lilLaahi

Yaw kii di Maam Ceerno waxal Seex Anta


Na ngeen di màggal doomi Jaara bàtta

Moom it na leen yërëm te ngeen màggal ko


Te weg ko def ko mag ni man jiital ko

Yéen jaru leen a yee nde nee ngeen jarr


Waaye ku nuur ñu ne ko am xët tarr

"Yaa ayyuhal kabiiru yaa Muhammadu


Kun li sixaarika mahãa fatah'madu"

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 86


Gis naa mu naa ko ca mujjug leetar ba
Ca tarjumaani suuf ja mooy tiitar ba

"Fal yakunil hinyaalu wan nisaa'u


Mahãka Ibraahiimu fiimaa chaa'u"

Sama Njaboot ga nañu toog fa Ceerno


Góor ak Jigéen suma ñëwee mu jar nu

Ndeem soob na Maam Ceerno na dëkki Tuubaa


Su ko manul fu ko fa soob ca boobaa

Man Bàmba man Yàlla a ma yor te xam naani


"Fu huwwa min kulli makaani daani"

"Wa hasbunal Laahu" te doyloo naa ko


"Nihmal wakiilu" loolu jàng naa ko

Looloo di leetar ba ku xam mahnaa ya


Te dégg jublu ga na roy ca gaaya

Ma dellu wax leen fi yeneen i leetar


Yu Bàmba jox Maam Ceerno moo am tiitar

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 87


"Fa innahu liman hubaydilLaahi"
La Bàmba wax di nuyu "Ahlul Laahi"

"Maa ngi nuyo ak Xarit ba Ibraahiimaa


Donoy Xaliilul'Laahi Ibraahiimaa"

"Moom masu ñoo wuute ladaa sixarihi


Te masu noo werente fii kibarihi"

"Fahlam xamal ni yaw danaa la yéege


Yaw ak képp koo àndal banaa sa ruuh gi"

"Danaa seral sa xol te gàddu say mbir


Dunyaa wa uxraa Ceerno yaa di saa mbër"

Gis naa gannaaw ga muy nuyook rakkam ya


Ak magi taalibe ya ak mbokkam ya

Ba naa ko "yaw miy Ceerno Ibraahiima


Nuyul ma saa Baay tëx ba Ibraahiimaa"

Te mooy Sëriñ Mbàkke Kajoor mu baax ma


Ngir suma masaa bëgg a taxaw mu ñaax ma

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 88


Nuyul ma saa mag ja ñu naan Kabiiru
Te mooy Sëriñ Momar Jaara liiley kabiiru

Nuyul ma Siidi Anta ak Seex Haafiya


Te nga ne leen maa ngi ci jàmm ak aafiya

Te nga nuyul ma ka ñu naan Seexu Umar


Magi Sëriñ Mbàkke Busó ak rakkam Umar

Te nga nuyul ma far Sëriñ Mbàkke Busó


Teg ca Sëriñ Ma-Sàmba Faati ak waa Mbusó

Te nga nuyul ma dëkkando ya yépp


Ni leen na seen xel dal ci man ci lépp

Te ñu rafet njort ci man bi jalwa


Damay liggéeyal Mustafaa ci xëlwa

Suma nee génnal ma dàldi génn


Su ko waxul ku koy jëfal du sonnu

Te bu ñu réeroo bu ñu yàqug mbokk


Te lu ca waay am na ko ñépp bokk

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 89


Ba mu nuyoo murit ya teg ca wa salaam
Hãleykum nee leen ko maalikum salaam

Ma wax la leetar ba amoon fa Jurbel


Gannaaw ba Daam ñëwee ñu daa ko sargal

"Matee taxa hãynuka Ibraahiimu"


Leetar la Bàmba a ko binde woon Njaareemu

"Wóolul ne man Seex Bàmba maala bind


Leetar bi ngir gërëm la maa ko bind"

"Làq nga tay jii ngërëmal Buur Yàlla


Am nga Ridan laa suxta Mbàkke Bàlla"

"Bul sikk nag ne Yàlla moo ma yónni


Ci yaw te maa digtale limu la yónnee"

"Lii mala wax Yàlla a ko wax yaw Ceerno


Santal te wóolu sa Boroom te jar nu"

"Medaay la maala ko takkal man Bàmba


Ci ndigalal Buur Yàlla ak Yonen ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 90


"Te maa ngi lay sàkkul fa Rabbul Hãrchi
Lu tax ba ñépp ñee la yawmal bastii"

Ba naa "Fatib nafsan wa xarra hãynaa


Sam xel na dal sa xol na sedd taw naa"

Leetar ba mat na Bàmba teg ca wa salaam


Hãleykum yaa Ceerno Faati yaa salaam

Miile medaay a jar a taf ci ab dënn


Yàlla a ko tàmpe ak Mustafaa mamu tànn

Leetar ya Seex Bàmba bindoon jox Ceerno


maneesu leen a way taxawlul way nu

Gis naa fa téere yuñ boole ciy gaal


Léppiy mbindum Seex Bàmba gaal ya diy maal

Gis naa ca mbóot yoo xamne làmmiñ du ko laal


Gis naa ca mbóot yoo xamne dees na ko misaal

Ngir Bàmba lamu taalife réewum Kongo


Daf koo joxoon Maam Seex nee leen ma gongo

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 91


La mu taalifoon "Konakry" ak "Lambarna"
Ba mu ñëwee mu jox ko sunu Maam Ceerno

Noon na ko bind naa ca "sirru sirri"


yawmal xiyaam lay feeñ duuna jëhri

Keroog la Bàmba sàkk "Fulkul Mash'huun"


Mooy bàkki bay jàlle murit ya xam yoon

Seex Bàmba mbër ma moo ko daa-daarlu


Seex Mustafaa yor ko Xaliifaa farlu

La Bàmba taalifoon fa taaxi Jurbeli


Mu jox ko Seex Faadilu Njàmmee xam lile

Xanaa yëgoo la xew fa Daarul Manaan


Ba Bàmba ñibbisee géej réew miy naan

Ci ñetti fan ciw Kori raw Tabaski


La ne jalañ ñu naa ko jaaril Mbàkke

"Wallaahi yadhun ilaa Daaris Salaam"


La Bàmba wax ñépp ni muut duuna malaam

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 92


Keroog la jaar Daarus Salaam Njool Anta
Berndeel ko mooma at ma mel ni ab jant

Fekkoon na Maam Ceerno ak Sëriñ Mbusóobe


Teeru ji woon ko Ndar bilaa kuruubi

Ba ñu xëyee ba jëmsi taaxi Daaru


Begal na leen dëfal na leen ba ñu waaru

Keroog da leen a jëndloo ji misk


Ba ñu ñëwee mu yewwi leen fa kër ga

Bàmba ne leen jeego yu ngeen fi jéggi


Danaa ko def muy ay dërëm ngeen jékki

Keroog ba Maam Ceerno ñëwee fa Daaru


La àndi Namsa Keyta gën faa waaru

Mu dàldi woo Seex Móodu Ndumbe Mbàkke


Ñu tax ko mook Maam Ceerno Faati Mbàkke

Sëriñ ba wàcc fa bawoo Daarus Salaam


Maam Ceerno fat ko ba ni ndax am na malaam

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 93


Keroog la Bàmba yeesalaatal Ceerno
Werdu wa may ko ca ndigal ci ab xarnu

Ca mooma at la ñu fa yabalsi Mbaaxaan


Mu wàcc Mbàkke mooy boroom i caaxaan

Seex Bàmba yónni Ceerno ak Seex Anta


Ba ñu demee Mbaaxaan waxul ñu gontu

Seex Bàmba yónni ca Sëriñ Moor Maane


Ba mu laataa gontu Bàmba jog mooy waane

Bisub keroog la Bàmba war karuus ga


Maam Ceerno sàntu ko garãti ruuh ga

Ba mu demee ba jublu taaxi Mbàkke


Sikar sa jolli noon ya dàldi ñàkki

Seex Bàmba laaj ku mokkaloon Sindiidi


Sëriñ Ma-Xujja Mbay ne man Muriidi

Mu ne ko "Bismillaahi xul Yàllaahu


Bil Mustafaa Sindiidi" ngir ilaahu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 94


Ba mu taree "Wa dammiran" di baamu
Daam ne ko doy na woowu way laa taamu

Kanu ga tàkk na fetal samay noon


Kun Fa Yakuunu laa faral suba ak ngoon

Te Kun a mën kanu wa xaada liyakun


Xarbaax a mën xërëm niroo wumaak kenn

Ba Bàmba wàccee dàldi woolu Mbaaxaan


Bàjjo ba rët ni dàll fit wa jaaxaan

Mu ne ko "Looy wax wax ko Ceerno mbaa Seex


Ñooy say moroom man Yàlla Buur ba laay jeex "

Wuy Gone sob ngeen ndaw du bal am saamaan


Kon leeg mu kubuusu fa Daarul Manaan

Keroog la Mbaaxaan dàldi gis Boroom Ndar


Kalaame kook Seex Bàmba duural puutar

Ñu woolu Buurba Jolof ak Buur Saalum


Boole ca Buur Siin moo mujjoon def Saalim

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 95


Ba ñu ñëwee la Bàmba wéy Ganaaru
Maam Ceerno des fa Daaru réew may waaru

Keroog la Mbaaxaan ñëw di xàcc jaasi


Di dóor ci per ya Ceerno naa ko jaasi

Seex Bàmba jàpp ca Njoxomboore ak Buur Siin


Abdul Xafoor jébbalu bii xareey yoon

Moor Isa Jóob ak Abdulaay Xaar Seen Jóob


Dootu ñu fekki Ceerno Daaru naa wuub

Déglul ma wax la at ma Ceerno sañcee


Mbàkke Kajoor ba Ceerno Faati wàcce

Bisub talaata la rañaane Daaru


Wàcc fa Bayti ja ñu daal koy teeru

Sëriñ Gallaay Ja berndeel ko ak waa Bayti


Ba mu xëyee ba war la koy bijjanti

Bisub keroog la Ceerno yendu Ngey-Ngey


Nuyook murit yaak Sëriñ Maalum Gëy

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 96


Keroog la Ceerno jox Sëriñ Maalum Gëy
Sañeefu koo biral nde lim ba dey rëy

Keroog la rombu Kokki Guy ca yoor-yoor


Yendusi kër Ma-Ndumbe nag ya far luur

Mu jàll rombu Kër Mataar ak Déqale


Siyaare xabru Baay ba dootul yàqule

Fanaansi kër Sëriñ Ma-Ñaaw tas daara ja


Keroog la waa Ñaxal ne moo am daraja

Ñu dàldi wër mu sundumal waa Mbàkke


Leeram ga jolli na keroog ba nàkki

Fas ya di daw muy niru jàntub njolloor


Pënd ba def xun sàkk benn poloor

Bisub dibéer la Ceerno sañc Mbàkke


Ca "hãama wak'sachin bi'xayri sàkki

Boobee la sàlloo Nguy fasam wu neex wa


Bul fàtte liirub jaan fasam wu weex wa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 97


Bul yab sa liirub jaan ba jox ko baaroom
Soo ko lugul moccoo ko gas ab xabroom

Mbàkke Kajoor la jënde woon Hiimaadu


Fasam wu rëy wa moo rawoon jiyaadu

Boobee la doon léebu ni maay Hiimaadu


Maa fiy kenol diine te maay jawaadu

Mbàkke Kajoor la Ceerno sàlloo Liimaan


Boobee la yor fa Yàlla sàrti liimaan

Mbàkke Kajoor la Ceerno sàlloo Lislaam


Boobee la roof ca xol ya sopp lislaam

Mbàkke Kajoor la Ceerno sàlloo Lihsaan


Boobee la roof ca cër ya jëf bil lihsaan

Mbàkke Kajoor la Ceerno sàlloo Nuuru


Boobee la leer gay jolli dem ba Ñooro

Mbàkke Kajoor la Ceerno am Dawaamu


Ca mooma at la ko Kajoor di raamu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 98


Ba mu demee Muhtii la yor Maruwa'atu
Boobee la yor Xàqiiqatu ak Sariihatu

Sëriñ Ma-Saaxo la ko may fa Saalum


Ne ko nga bàrkeloo ko moo di Saalum

Xanaa yëgoo la xew ca "hãama balsashi"


at ma "Blaise" watee ba war te ñibbisi

Di laaj Sëriñ Tuubaa mbirum Soldaaru


Ngir bëgg lislaam fay maa nga Daaru

Maam Ceerno Faati ni jalañ fa Jurbel


Ak ñaari téeméer ciy murit du ab jurmal

Nitt junni ak juróom la jox Seex Bàmba


Boole ca yatti dàgga ngir Yonen ba

Dàgga ju nekk Fukki Sàqi Fukk la


Seex Bàmba bojjulu ko réew miy lekklu

Ne ko nga dimbalee ko réew ma jaay ko


Te yót ma xaalis ba nde soxla naa ko

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 99


Sëriñ Mataar Sàmba a ko jaay fa Mbàkke
Di toppatoo xaalis ba duuna shàkki

Ca mooma at loxoom yépp a futt


Àndaar ja daaral nay loxoom ngir natt

Téeméeru junni la ci saakuy ngurdi


Yaari giléem ñoo ko sëfoon ci guddi

Neena ñu mànke na juróom fukki dërëm


Waaye du tee ka joxe woon am na ngërëm

Ku weddi laajal Ibra Gëy fa Ñomre


Moo wommatoon giléem ya mësta mboore

Ñu boole kok téeméeri nag ak nitt


Ñu dàq yót Seex Bàmba kii dum natt

Keroog la Seex Bàmba ne Ceerno sab añ


Du feeñ ci dunya kon te ma xeeñ na yaa sañ

Loo man a gis tay ak ëllëg ak booba


Añub liggéeyub Soxna Faati Jóob a

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 100


Sunu demee yawmal xiyaam ngay sooga añ
Te kula xam sax dana xam te dana gañ

Bisub keroog yaw rekk a fay sol i medaay


Yaay def ma toog maak sama Nday ak sama Baay

Kula fa soob mu sowe yaa am sowetaas


Fii zaahirin wa baatinin yaa jar a taas

Seere si mooy "Blaise" ca "hãama balsashi"


Ba mu ñëwee Jurbel te dem ba dellusi

Te woo Sëriñ Tuubaa ca weeru koor wa


Mu yóbbu Seex Anta mu fay tàngoor wa

Keroog la Bàmba naan ca weeru koor ga


Ca tàkkusaani kaw du mar du goor wa

Neena keroog bu naanul woon ca koor wa


Seex Anta sax tàkk ba xëm cëy góor ga

Keroog ba muy dem dafa ne Ceerno toogal


Bul génn tay tëjul bu baax te foogal

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 101


Ba mu dikkee la ne ko soo génnoon tay
Jànt bi tiim la tiim "Blaise" mu texe tay

Lamu ko wax maneesu koo laxbaari


"Alhamdulillaahi hãlal axyaari"

Su ngeen ma déglu woon te toog ni cell


Te génne seen bagaani xol ni péll

Kon tay ma wax leen at ma Ceerno sañcee


Fa Daarul Muhti te murit yay xàcc

Bàmba ne Ceerno na nga sañc ag Daaru


Diggante Tuubaa Mbàkke kon nga waaru

Gis naa fa say may yu fay baawaani


Yu raw ya ñuy séddale fii Gaawaani

Te boo demee logal sa ngëm ca Roog-Seen


Te gëmm bul faale mbindéef bu leen séen

Bisub keroog la bind mbooleem lépp


Luy xew gannaawam jox ko Ceerno jàpp

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 102


Mu naa ko jàppul ngir "suduurul ahraar"
Bisub xiyaama ñooy "xubuurul lasraar"

Looloo taxoon Maam Ceerno faf ni patt


Waxul deful Bàmba a ko lëm ni bunt

Mas nay wax ak Seex Móodu Ndumbé Mbàkke


Keroog ba Bàmba nee meles fa Mbàkke

Ba naa ko xam naa la wéy ak liy bëgg a ñëw


Bàmba a ko bindoon jox ma moo tax duma jëw

Bàmba begal na ko keroog fa Jurbel


Wax ko fa ay hadiis danaa ko sërxal

Neena ko yaw Ceerno yaa may nuyoole ak waa Tuubaa


Sunu demee yawmal xiyaam bu boobaa

Maam Ceerno nee ku ma wanul Seex Bàmba


yawmal xiyaam du ngeen nuyoo fa bar ba

Seex Bàmba nee ku ma wanul Njool Màkka


Yawmal xiyaam du ngeen nuyoo ba mukk

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 103


Njool Màkka nee ku ma wanul Buur Yàlla
Yawma izin du ngeen nuyoo fa Yàlla

Buur Yàlla nee ku àndul ak yii Ngonk


Soo ma nuyoo duma la fay maa lànk

Yàlnanu fa ànd ak Yàlla ak ñii ñatt


yawmal xiyaamati di tàbbiy bunt

Ma wax la at ma Ceerno sañcee Daaru


Mooy "Hãama Alsashin" atam maa taaru

Mbàkke Kajoor la gonte yawma sabti


Ràkkaati Gàmmu Daaru duñu ko fàtte

Guddig Dibéer la fanaansi Daaru


Leeram ga sar ba Koso ak i Daaru

Moor Jaxate a fa njëkk a jàng ub Jazbu


Ci ndigalal Maam Ceerno moo leen jëzbu

Murit ya jóg fanaane tuddu Yàlla


Moom mooy Durus ci Alxuraan ngir Yàlla

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 104


Ba bët setee ñu xëy ca yawmal Ahdi
Weer way juróom ñatt fanam fil haddi

Ñu dàldi samp sange wër luy Daaru


Jana yu rëy la gaa ña gor fa ñaaru

Mu am fa ay at wopp ja a ko lakk
Mu randu Ciŋkóoli ñu xëy di lakk

Ñu dàldi toj àll ba gor Ciŋkóoli


Saxal fa daara réew ma dàldi boole

Foofee la sañcaloon Sëriñ Usmaana


Doomam ca "Hãama Sasashin" hamaana

Dongo ya dàldi gor ba àgg Colle


Samp fa daara Ceerno dàldi fay julli

Foofee la sañcaloon Abaabakar Faal


Ca "Hãama Hamsashin" ca leer ga lay taal

Ñu dàldi gor jat mi ba gor Mbaraakan


Samp fa daara naa ko bàrke laay ñaan

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 105


Abdul Jamiil la fa defoon ndoomam sa
Ca mooma at Maam Ceerno woo na ndoom sa

Bukki ya daw sàggani seen i ndaari


Golo ya gàddaay Ceerno toog di waare

Mbaam àll ya ak til ya ànd ak pël ya


Di daw di wéy puutar ba ànd ak bal ya

Mu dàldi lew suuf sa Ma-Koddu Sàll


Wër kilo meet ya wan ko Paate Sàll

Mu dàldi woo Saa-Ngóone ak Ma-Sàmba


Booleek Momar Jabboo ki Muxtaar Sàmb

Kiile di njay-joor ba kiiley càmmooñ ba


Ñoo daan doxal mbiram ya tay ak booba

Ñu dàldi xotti suuf sa jox Maam Ceerno


Fab Daaru taf ko ca Kajoor di bornu

Maam Ceerno dàldi woolu enseñër ya


Ñu jàjji teen ya génne doj ya ak xor ya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 106


Gas na fa ab teenam ca "Hãama jalsashi"
Téeméeri meetar la mu yàqu "Masachi"

Tubaab ya tàmbali ca "Hãama wam'sachi"


Tubaab bu ñuy wax Buyee moo fa wàcc si

Gas na fa am at bënnul mu dellu


Wax ko Boroom Ndar Njool ma dàldi wallu

Tubaab bu tuddu Got fara ak Deburwaa


Ne fa jalañ ku nekk yor say "kruwa"(croix)

Gas nañu fa yatti weer bënnul ñu dellu


Maam Ceerno yónni Moor Jabbook ñu xellu

Ca mooma at lañu fa yabalsi "Justin"


Booleek masin ba moom du laaj ay fiftin

Masin ba rulle dàldi wéll ndox ma


Ba tay ña ngay pompu ak a sant mbër ma

Ñu dàldi jaay pàkk ya naar yay bornu


Tubaabi Njaareem yay pikkat ñooy arnu

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 107


Boobee la Daaru dàldi folli Jurbel
Wata ak Sareet ya ak dojs yaang ñu bërgal

Mbedd ya fot sunu soxna yay mbandaalu


Ñooy dawali kurs ya xewoon fa Daaru

Maam Ceerno dàldi sañc ak Daaru Koso


Ñuy rooti Tuuba at ma melna ni kaso

Yenenti at la fa am mu delsi Daaru


Sañcal fa Mahmuudan mu toog di waare

Laajal Momar Xari Silla ak Muxtaaru


Rakam bisub dibeer la Ceerno waaru

Maam Ceerno dàldi sañc ak Daaru Salaam


Yabal fa Muxtaar Sàmb rakam mu ni kaam

Deglu ma wax la la Ceerno def Daaru


Ak lamu jox tubaab ya ciy soldaaru

Ca « jamsashin » solal na ñaari téeméer


Ganaaw ga it solal na ñetti téeméer

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 108


Ñaar ak juroom fukk a soloo fa Jurbel
Ci ndigalal Seex Bàmba moo ko jërfal

Ganaaw ga lam solo maneesu ko lim


Daf ni ku yéenee dem Badar na xëy dem

Keroog la daara yépp dàldi gental


Maajali Seex Bàmba mi sàkk weetal

Ma suliwaat tay ji le mbóoti Ceerno


Yoo xam ne jomb na goneey bii xarnu

Na ngeen ko degluwaat te dolle farlu


Sàrdi bu dee watal na seeti parlu

Xaalis bi ngeen di xas xasee di xëcoo


Ak mbubi Maam Ceerno yi ngeen di xiijo

Cosaan la kat la leen di bëgg feeñal


Du wuññi mbóot waxtaan la woon wu ñu siiwal

Ne leen sunuy nopp bi sunu Maam Moor Anta


Di seeti kokki di labat la gont

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 109


Keroog la jàngloo waa Mbàkke junnib Yaasin
And ak Sëriñ sépp ba kuy dal baasin

Ba ñu demee ba àgg reewum kokki


Ba mu nuyoo xamu ñu santu Mbàkke

Ka ko taxoona jóg ñu naa ko Roqiya


Ñu may ko Ibra Penda Mbooyo tarxiya

Ñu di ko ree naa ko walaahi Njool Mbàkke


Yaa mëna jàng waaye dëkoo Kokki

Maam Sàmba Aaminata naa ko


Mbàkke doo man am fii soxna maa moom Kokki

Ahmadu Aaminata dem na booba


tubaab ya yob nañ ko géej xuloo ba

Ba sunu Maam Moor Anta takee bay war


La ko fa saa Maam Absa Mbàkke càmbar

Waa Kokki naa ko Mbàkke mat nga li nga doon


Waaye ku ñaan ku la xamul sag may du duun

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 110


Keroog la sunu Maam Absa Mbàkke laxaso
Ne nañ ko may saa doom si mbaa ma laxasu

Ñu daal di deey dajale mboleem Kokki


Gaa ña ko doon garoo di buur di fokki

Ñu dàldi xutba yawma ashuura


Ne leen sunuy nopp Biraahim jaa

Sëriñ Momar dajale gaa yi Mbàkke


Di bëgg jox alal ja gaa yi Kokki

Nekete sàkku sa defoon xaalis ba


Rot na fa Ñjaañ ba ñuy dawal fa bar ba

Maami Sëriñ Jatara moo ko dencoon


Mooy bëkk-neeg ba moom la goor ga fonkoon

Ku nekk rus ba ni tasar ndax jaaxle


Mboolo ma mépp naa ko dooto baaxle

Ba déy la egee ñepp wax ba ni wedam


Maam Absa Mbàkke ni fa seex ñu ne xedam

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 111


Ahmadu Sekk sama maam gewal ba moo ko ni
Sunu xaalis ba rot na booba

Maam Absa Mbàkke dàldi tiji gaalam


Genee juroomi sàkku ngurd ne leen am

Sarax ko foofe sunu Maam Moor Anta


Ne ko naa doomi Faati melnib jant

Te bul ko wax waa kokki baa waa Mbàkke


Su ngeen dundee ngeen bokk sant Mbàkke

Keroog la Maam Moor Anta naa waa Mbàkke


Xaalis ba wéy na Mbàkke gontee Kokki

Ndaw su fi sant Jóob bawoo Kokki


Balaa sëyati am ku fi sant Mbàkke

Bile xibaar maa leen ko wax man Musaa


Maa xam cosaani Mbàkke tay ci siisa

Li lee waral xaalis bi ngeen di xas xasee


Boleeg mbalaan yi fi sëriñ du soose

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 112


Gaynde yu mag ya dem nañ céy njaloor ya
Kuy deeti f0dd Seytaane ki tekki joor ya

Ma dellu wax leen fi beneenub xaalis


Boo xamni Maam Faatee ko sàkku laa gis

Ku weddi laajal Soxna Faati Binta


Moo ma ko doon xibaar céy guy du mbant

Nee na ma yett weer yu nekkaan sama yaay


Ràbblu fa yett fukk jox ko sama baay

Mbalaan ya mës na bari lool bam jaay leen


Jox sama yaay xaalis ba naa nu fableen

Keroog la na su ngeen dundee am xaalis


Aki mbalaan yu bare loolu laa gis

Lilee waral xaalis bi ak mbalaan yi


Maam Ceerno nee médd la yeen ay tan yi

Ma dellu wax leen fi benenub xaalis


Boo xamne Maam Ceernoo ko fàggu kaay gis

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 113


Keroog ba sunu Maam Xaadim Momar Anta
Faatoo te dunya lepp melnib gent

Xaalis ba ak sàkk ya ak mbalaan ya


Lepp ni xuss ak fas ya ak mbaamam ya

Miraas ma jot ñu dàldi woo wa Kokki


Ñu ni tirim ñook doom ya ak wa Mbàkke

Seex Bàmba dàldi wax ni « maak Biraahim


Dun dondu baatin lan donoo fa laa yam »

Te Ceerno sedoo na ma sedoo naa ko


Sedaleleen sunu wàll deloo naa ko

Ñu dàldi sedd ñett doomi nday ya


Boleeg cérub Soxna sa fawxa ndey ya

Keroog la Soxna Faati fab donoom ba


Ak waa këram gépp sarax ko Bàmba

Naa ko alal ja ak diine yaa xam yilla


Sopaxndikul ma ko ëlëg fa Yàlla

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 114


Jébalu foofe jébalaat ko Ceerno
Ne ko bu ëlëgee na moom ab xarnu

Keroog la Bàmba boole seen alal ja


Yonee ko Seex Siidiya naar ya am ca

Yii yaari waanee mën a soppi xaalis


Wute nañook ñiy sàcc gaal di rokas

Ma dellu wax leen fi benenub xaalis


Boo xamni Njareem la ko yobb maa gis

Maam Ceerno mas naa yobb nitt juni


Yu teg juroom ñett mu daal ko génee

Def ko ci gaal Sëriñ ba jox ko Awa Saar


Mu tëj ko ren ba dewen kenn du fa jaar

La dalee hãma masasin ba bamsasin


Mu woolu Maam Ceerno mu dàldi lagg si

Ba mu ñëwee Sëriñ ba yonni Awa Saar


Mu jëli xaalis ba mu fees ab beñuwaar

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 115


Bisub keroog la Bàmba dàldi digle
Nitt ak juroom ñett ba dàldi begle

Arafi Tuuba la murit bu ko defoon


Fum mëna faato ruuh ga ñëw Tuuba di kun

Keroog la Bàmba sulli saa waxtaan wi


Ma way ko man miy werekaanu yoon wi

Netali Maam Ceerno cosaanal maam ya


Wax na keroog ba sulli mbooti daam ya

Bisub keroog la Bàmba wax jumaa ja


Maam Ceerno ak xibaar ya Ceernooy waa ja

Maam Ceerno dàldi delu waajal Tuuba


Ca Amsashin jiite jumaa ja booba

Boobe la Maam Ceerno di wax Seex Bàmba


Nitt ak juroom ñett na wéy ba Tàmbaa

Bàmba a ko naa nit ak jine ak malaaka


Ñépp a nga naa leeg fi defar unaaka

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 116


Jumaa ji maa ngi ko binde woon ca Kongo
Su ngeen ko ligeeyul ñeneel ligeey ko

Jàangal ilal ardi latii baaraknaa


Fiihaa ca laa ko way ca géej geejal naa

Keroog la Bàmba naa ko moo di beyti


Ci soowu jant na nga ut ag beyti

Noon na ko yaari beyti yii ci Mbàkke


Ñoo wuutu ñaari beyti yee ca Màkka

Ku weddi laajal bëkk-neegub Ceerno


Bu tudd Daam Sekk meloow bii xarnu

Maam Ceerno mas na ko ni wunti Àjjana


Amna ci bunt bu ma tiim fi le ma ne

Te ni ko Bàmba moo ma ko wax fa Jurbel


Jëmbat fa yaari xay te dee ko ormaal

Keroog la Ceeerno sàkk Baytil Maamuur


Ci ndigalal Seex Bàmba moo di maxfuur

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 117


Mbirum Sëriñ Tuuba ak mbirum Maam Ceerno
Maneesu ko l0qarti sarlooy arnu

Deleen siyaare Daaru tey dem Tuuba


Ku ajji umra sant Yàlla booba

Tay jii ma wax la kër ya sunu Maam Ceerno


Sancal Sëriñ Tuuba si seenub xarnu

Mbàkke Kajoor la njëkk laalub sàkket


Di sàkketal Seex Bàmba bul ko ãket

Fukki at ak juroom la am ci dunya


Boobe la watu Alxuraan bi sunyaa

Ca mooma at la Xaadi Momar Anta


Tuxoo Pataar ñëw Mbàkke mel nib jant

Moo di attum taarix ba hãama siridoo


Maasam ga faatu na ñu ba àtte maridoo

Moo di atub junni ak ñaari téeméer


Yu teg juroom ñeneenti fukk ak juroom yaar

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 118


Sancal na Bàmba kër ca hãama asashi
Mbàkke bawol boobe la Bàmba’y ñibisi

Daaru Salaam Ceerno ko sancal Bàmba


Ca kasashin feral Sëriñ Ma-Sàmba

Seex Bàmba dem Tuuba ci hãama wasashi


Maam Ceerno sancal ko fa masta ñibisi

Maam Ceerno sancal na ko Mbàkke Baari


Ci hãama baysashin ma laaka maahal kibaari

Seex Bàmba dem géej Ceerno dellu Mbàkke


Sanc fa yaari kër di xaar Njool Mbàkke

Sancal na Bàmba kër fa Daarul Manaan


Taax na ko mook Seex Móodu Ndumbe Xabaan

Sancoon na kër digante Ndaam ak Daaru


Ci ndigalal Seex Bàmba réew may waaru

Ca mooma at la Bàmba wéy Ganaari


Maam Ceerno topp ca ba dem jaraari

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 119


Maam Ceerno tàntal na fa Siidi Bàmba
Ci aksashin ba fa Sëriñ Ma-Sàmba

Ci hãama baksashin ladaa Sarsaara


La Ceerno sancal Bàmba neegi daara

Ca mooma at la way inalaziina


Teg ca ilaa Sarsaara way wa jee na

Foofe la naar ya dóore woon Mbay Penda


Nangul tobortoom dog loxool Moor Penda

Ba naar ya deloo ay hasaan ñoo leen ray


Ba ñaari naar des ca xibaar bi lee rëy

Bañ dellusee Maam Ceerno wax ko Bàmba


Mu naa ko laa shakka ku merloo Bàmba

Ganaaw ga Bàmba a leen sarax ay naaga


Hasaan ya togoo kay dawal di saaga

Maam Ceerno jox na fukki fas Seex Bàmba


Booba le ak fukki gëleem yuy bëmb

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 120


Ak fukki junni ak ñaar yu mat ciy ngurd
Laajal Móodu Xari Jóob bul weddi

Moo sàntu woon Maam Ceerno muy ataaya


Fanweeri peñ la yanu woon ba Gaaya

Keroog la Ceerno ray gëleem ñu toj ko


Móodu Xari a ko yonnu fab ko lepp

Nar ya di sorxale sagam yay waaru


Móodu xari a ma ko xibaar fa Daaru

Maam Ceerno ñibisi ci hãama daksashin


Seex Bàmba ñëw Joloof ci hãama aksashin

Keroog la Daam yónni Sëriñ Moor Absa


Mu woo si Maam Ceerno fa Daaru cam sa

Keroog la leen Bàmba ni « yéen la Yàlla


Di woowaando bu leen di fàtte Yàlla »

Moo tax ñu bokk wuyuji seen Boroom ba


Yàlla na leen sunu Boroom xaroom ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 121


Keroog la Maam Ceerno rañaane Daaru
Fetal ca àll bay dawal ñu waaru

Romb Tamaaka naari goor yay ràbb


Mu romb Ñiñaar gaa ya naa mooy Bàmba

Wàcc na kër Seex Móodu Géy fa Jamooy


Wàcc fa Njaañ Seex Ibra Saar amna ag may

Yónnee na kër Sëriñ Sire lóo Sanoosi


Ne ko Sëriñ bi ñëw na maa ngi noosi

Ba mu xëyee dox Kokki yendu Luga Lóo


Fa la dajeeg seex Bàmba ak Seex Sire Lóo

Keroog la Alaaji Ma-Sàmba Soxna


Ganale Maam Ceerno ba dig ko soxna

Keroog la Seex Bàmba ni sunu Maam Ceerno


Yàlla yabal na ma Jolof yaay awnu

Demal Jolof te seet barab bu tàlli


Bu bari ndox te nooy a nooy te àlli

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 122


Nga sanc fa ag daaru ni yaa di keemaan
Te soo demee tudee ko Daaru Rahmaan

Ca mooma at la Ceerno sancal Bàmba


Fa Daaru Rahmaan mook Sëriñ Ma-Sàmba

Ku weddi lii laajal Sëriñ Ndari Kebe


Këram la Ceerno tekki woon limar kabi

Neena keroog fekku fa ludul menn mata


Maam Ceerno far ko may sëf ak fukki mata

Ca mooma at la ko jëlal soxnaam sa


Woddu ko may koy fas mu tuub fa saa sa

Seex Bàmba am fa yetti at tuxoo fa


Wéy Daaru Xudoosin mu sanc foofa

Seex Bàmba am Jolof yaari at wéy Jurbel


Ca lasashin tubaab ya dàldi koy bërgal

Maam Ceerno Faati Mbàkke daal koy sancal


Seex Anta daal koy teeru daal koy tàntal

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 123


Seex Móodu Ndumbe Mbàkke ak Sëriñ Ma-Sàmba
Ño fetewoon ligéey bi sengal Bàmba

Seex Bàmba dàldi koy yabal fa Tuuba


Ni ko demal sancaat ko Ceernooy kooba

Te sanc Xudoosin wa Daarul Minani


Wa Daarul Manaan defal foo man a ne

Daarul Haliimu moo di kër Sëriñ Ndaam


Maam Ceerno yóbb fa jigeeni Maam Daam

Ku weddi laajal Seexu Abdul Xaadir


Maam Ceerno Faati a ko fa ngente baadir

Mooy rakki Soxna May donooy sheriif la


Ku bari xam-xam la boroom tawhiid la

Keroog la Daam jox Ceerno Mãto(« Manteau »)


Ne ko demal Ndaam na la mag ñi sàntu

Te fuma am kër nag fa toog fanaan fa


Te ku la siyaare texee fi ak foofa

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 124


Ci alsashin Seex Bàmba woolu Ceerno
Ni ko nga dem sengg ko te taax ko jar nu

Bisub keroog la ni ko noo def Tuuba


Mooy sa misaalum kër ya ngay am Tuuba

Keroog la Maam Ceerno fanaani Tuuba


Te yobuloowul ab dëram bës booba

Ñi xam ni fumu dem Bàmba jox ko ay junni


Ba bët setee la Ceerno doora yónne

Bisub keroog gam toroxalna tarasuul


Ceernoy donooy Seex Bàmba miy donooy rasuul

Ca mooma at la Ceerno toog fa Tuuba


Ba sengg yaari kër yi taax ko booba

Desal na junniy sengg aki téemeer ya


Desal na junniy denk may ko buur ya

Desal na siy bunt juroomi barigoo


Ba muy rañaan loo fab mu naa la bàyyi ko

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 125


Ba na fa lépp dàldi dellu Daaru
Waa Daaru ak Tuuba ku nekk ay waaru

Ku weddi lii laajal Muhamadu Xari


Meetar la woon mooma ko wax moo ka gore

Keroog la kofar foor (coffre fort) ba des fa Tuuba


Mu jox ko Ceerno Faal mu tëj ca booba

Boobe ba tay Seex Ceerno Faal delloogul


Ngir darajay Maam Ceerno Faati sooful

Téeméeri junni a ca desoon ak nitt


Di ko xaroo jumaa ja far ni mott

Ba xili xaala ja amee fa Tuuba


Sëriñ Mbusoobe a jëli koofar foor ba

Wata a ko sëf àndi ko Daarul Muhty


Maam Ceerno far génn ci bandal parti

Ca mooma at la Ceerno bojj dàgga ya


Yóbbu ko Jurbel gaa ya wommat taarka ya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 126


Téeméeri mbaam lañu njëk sëf fa Daaru
Cogali mbaam lañ daa watal yu gaaru

Mbojj ma mat na weeru lëmb di yandaar


Gëleem ya sëf nañ mbojj maa rëyum kaar

Taxawlu naa waa Daaru ne leen maalum


Ngëneeli Maam Ceerno maneesu ko lim

Kok mën la ngacc géej bu wal ba wër nu


Musaa ka mënta lim ngëneeli Ceerno

Musaa ka tee nga jooyle Ceerno Jaxate


Xawma ku woomal ku ko deeti joxati

Maam Ceerno Faati a ko mayoon xàccum piis


Daan na ko woo ceeb ak cereey maraakiis

Seex Masayer Géy la ko jaay fa Ngeraan


Ci ñetti téeméer naa ko dootoo xaraan

May ko juroom benn daraa ak lalab weñ


Ak matla ya ak mbajj ya Ceerno moo sañ

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 127


Neena ma lam ko may ci xeeti xaalis
Maneesu ko siifar ki lee di faaris

Waay Njàmbe joyalal Mataar Masóogi


Bu xaru doon dagan mu naani tooke

Xawma ku koy taajati booli ceeb ya


Ak lay ja ak soos ba di déglu léeb ya

Ceernoo taxoon mu denc Soxna Mbàkke


Teg ca Aminta Mbàkke far di takke

Bul jéema lim ñi wara jooy Maam Ceerno


Mbaa te nga dem jëndi këyit kër arnu

Ma wax la bis ba Ceerno gede Daaru


Walaay keroog Sëriñ Mataar moo waaru

Ci fukki waxtook benn waxtu montar


La ruuh ga wuyuji Yàlla waxtu yoor-yoor

bisub keroog garab ya jooy na daaru


Jàkka ja jooy na baayu maam(fas mbaam bëy) ya gaaru

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 128


Wolof ya naa wooy naar ya naa yaa wéyli
Luy pël ni ay yéegam ba goor muy jawli

Lawbe ya kër Seex Yoro naa jaraw raw


Kenn talatul kenn ñu naa werewrew

Ràbb ya sant Mbeng noddkat ya


Kuy bëgg wax faf luu ni bàq bët ya

Ba ca marax Seex Awa Bàlla àksi


Fekoon na baayam woolu woon ko am si

Ba mu ñëwee wër Bayti Mahmuur ba


Ni leen waxoon na ni fi leey xabroom ba

Ñu dàldi koy defar defar bu sell


Ñu dàldi woo saadix ba Paate Sàll

Mu dàldi ñëw laxasu moo ko sang


Cangay gu ànd ak gët moo ko sàng

Moog Móodu Faati Gay limal Sëriñ Njaay


Ñi lee defar Maam Ceerno kenn du yii gaay

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 129


Ci ndigalal xariit ba Iisa Jénn
Seex Móodu Jaw Paxa a nga toog ni jonn

Seen téew ga doy na muhjisaati Ceerno


Seere na seen digante Bàmba jar nu

Ma wax la gaa ya gas darihatoom ba


Daat nañ ko yiit nañ ko yaatal ruum ba

Sëriñ Mataar Sàmba a ko njëkk tàmbali


Muhamadul Habiibu moo ko yegale

Seex Faati Faal moo njëkk jañ daaga


Keroog la suuf sa riir ba melni laat ga

Seex Awa Bàlla teg ca Abdu Rahmaan


Ak Haabidul Xudoosi ñépp doon ñaan

Sëriñ Muhamadu Xari ak Galaay Njaay


Tegal Momar Njaay Kokki ak yeneen gaay

Seex Awa Bàlla doom ja moo ko julee


Ne Abdu Rahmaan Mbàkke nanga ko jàlle

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 130


Seex Haabidul Xudoosi ñëw barkeelu
Xam na malaaka yaa nga fay jëmbeelu

Fi laylatil jumaati lañ ko tàbbal


Ci biir dariyatoom ba loolu yombul

Mbalaani Seex Bàmba ak mbalaani Màkka


Lañ sàngee sa waa ji bëgooni ràkka

Lalal ko tappi Màkka ya ak Madiina


Ak njegenaayu Bàmba ya ak maasiina

Ak der ba Bàmba doneewoon ca Maam Aas


Daa ko dawal ca mbeex ma mbir yi lee saas

Yaa ajaban yém na darihatoom ba


Ci saahirin wa baatinin ak ruum ba

Ku dem janoog màqaama Ibraahiima


Ma nga ñu taf ca penku Ibraahima

Seriif ba ne màqaama Ibraahima


Ka anahu màqaama Ibraahima

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 131


Jàngal wa man daxalahu amaana
Ñu bokk baat ki lee am maaana

Fukki junni ak ñaar la joxoon Seriif ba


Umar la tudoon moo siyaare néeg ba

Keroog Sëriñ Saaxo la ñawloo tappi ya


Ak rido ya ak kemaan ya sàng neeg ba

Nee na ko képp ku siyaare Béyti


Lumu ca am nga am ca wàll bayti

Fekk na ñawlo woon na ko ay càngaayam


Lu mat weer ba fab ko tëj ci gaalam

Ku weddi lii nga laaj ko Bàlla Xayta


Mba te nga laaj Daam Sekk moo yor bayta

Ñooy wékk-néeg yi daa defar këram ya


Ñoo mujj laal sëram ya ak yëreem ya

Déglul ma ñaanal doom ya yor jikoom ya


Ku ñàkk baay na jéema raasi doom ya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 132


Budul kon ag doom ya ñu gën fee yoqi
Waaye garab lañ fa gajee fay seqi

Siyareleen doom a di baay taaw a di caat


Miraas ma góor ña yammi cër bul naagu xaat

Siyaare leen Ahmadu Awa Bàlla


Mat na ab xaliifatu ca kër Maam Bàlla

Taaw la bu taaru akbarul awlaadi


Te darajaam siiw na ba wër bilaadi

Donnug Suleymaan ja mu defoon Dawuuda


Yalna ko Móodu donne Ceerno xuuda

Siyaare leen Siidiya moy rakkam ja


Seex Awa Bàlla gesu leen jëmam ja

Moy saahibul jamaali wal jalaali


Te mom la baay ba wóolu woon fil haali

Maymunatun may doomi Seexi Bàmba


Ci ay mayam la tàbbi mo fab yan ba

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 133


Mo tax ñu rob Ceerno fa Baytil Mahmuur
Mom la ko baayam xamaloon mo am muur

Xana xamoo Muhamadul Habiibu


Moo bari xam-xam halimul adibu

Siyaare leen ko jox ay idaaya


Xam-xam ba rawna xam-xam ug riwaaya

Moom la ñu tudde Xaadim Momar Anta


Baayub Sëriñ ba yalna melnib jant

Li wa taxoon mu atte Daarul Muhty


Jox leen ko atte yi bu leen ko fab parti

Yaari rakam ya doynanu siyaare


Amuñu kem si mbokki doomi Jaara

Seetal ma sellug Habidul Xudoosi


Mahmoodunaa farhatunaa ci suusi

Ñii ñaar a teggi tuur ba raw fa Daaru


Surnaalli màkkata ya ñoo koy xaaru

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 134


Ëskëy marhaaba Aabidu Rahmaani
Moo mësa jiite baay ba fil asmaani

Moo maanu moo yaru ndiroog Maam Ceerno


Fa Daaru Mannaan la wotom di kornu

Seex Faati Faal yalna ko Yàlla faale


Mooy turandoo Seex Bàmba fii rijaali

Moo taaru moo tabbe jubboog baayam ba


Te am fula am fayda moy yaaram ba

Abdul jamil a am jamal te yaatu


Te am xorom cam su ko bañ na faatu

Te Yàlla may rakkam Habibulaahi


Mooy turandoo Maam Bàlla hibullaahi

Siyaare leen Seydinaa Usmaanaa


Mo tabbe mo xaajaanu mo am maanaa

Haliyun Aydara sëttub Maam Makala


Du njar ci soow mi ñaari wàlli Mbàkke la

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 135


Baayub tëhub Njool Màkka mooy Habaas
Fegal nu mboose wa balla ag baasi

Seydina Hamsatu sangub gaa ya


Xareeb xunayni daana ngaabi raaya

Yalna yor raaya ngëneeli Daaru


Ba ku ko gis jébbalu mba nga waaru

Te Yàlla may Seydina Suhaybu


Dundag Souhaybu ga te may ko xaybu

Te Yàlla may Seex Mbàkke doomi Xadi


La gaa yu baax ya daa mbebet bay xàddi

Seyduna mañ tudde Mbàkke Anta


Yàlna nu bok fenk mel nib jant

Daam Faati yalna jël ci mbóoti turandoom


Ahmadu Faati Mbàkke mësta am moroom

Mihdaadu sangub asiyatu mubashara


Yalna nu am bàrke te tàggook kasara

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 136


Basiiru Mbàkke doomi sunu Maam Ceerno
Yalna fawxa turandoo wam defar nu

Subayru Mbàkke yalna ànd ak bayre


Ak bàrke ak ngëram di baabu xayri

Te may Omar omran te weyëlan abadaa


Dund gu ànd ak bàrke te ànd ak waladaa

Xaalidu Mbàkke yalna ànd ak xalidiin


Fi janatin firdawsi waay ne leen amiin

Yalna nu Bàmba may ay màqaama


Ci darajay Maam Ceerno Ibrahiima

Te may ma bàrke ak ngërëm nangul ma


Way wii ma way ba ku ma am nangul ma

Te bole ma ak muliim ba Soxna Jóob Jaañ


Faj sunu aajo bu nu kenn man a gaañ

Ba lépp luñ ko yéene woon ci dunya


Ma mën ko ko defal bi dooni sunya

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 137


Te Yàlla full fan yi te dolli wer gi
Ci darajay Seex Fàllu yokk mën gi

Te yalna Yàlla dolli Faati Saar


Sutura ak teranga ngir Maam Jaara

Te Yàlla may ko waa ju am màqaama


Ci darajay màqaama Ibrahiima

Te Yàlla may mboleem ñi dooni sawjaat


Ñu xëy dajeek Maam Ceerno fil janaat

Te yalna doom ya mujj diy xaliifa


Ci darajay Seex Fàllu may xaliifa

Te yalna Seex dem Màkka jàll Tayba


Siyaare aj umra te delusi Tuuba

Te Yàlla may ko ngërëmal Njool Màkka


Te nangu ajam ci darajay Njool Mbàkke

Aamiina aamiina ne leen aamiina


Ndax Yàlla ngeen aji ba gis maamoona

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 138


Salaa alaa Xayril Waraa Yaasiina
Wa aalihi wa sahbihii aamiina

Marsiyya Boroom Daarul Muhty | 139

You might also like