You are on page 1of 1

31. Mu ñëw di foon kanam ga naako waalidii 49.

Xamxam bu sell buy bayaan ken dootu wax


Tibta hayyan wa mayyitan, wa Rabbinaa Doktoor dëlaa jënes Jënes bi ñàkkana
32. Naaleen kudaa jaamu Limaamu man nga dem 50. Jënes bi ñakka nan ki doon seen royuwaay
Kuy jaamu Yalla took nu gëm Xaalixunaa Seen soppe seen xarit Husëynu ñibbina
33. Miimun la took ken jooyatul Imaamunaa 40 ans 51. Ambaasëdooru Maam Limaamu xëyna dem
Ba Dee jëlaatko mook Manjoon ak xutbunaa Itaali ak Fràns du miis Sheriifunaa
34. La jël Limaamu jël Isaa miy xayrunaa 52. Waa Jasporaa bi ñakk ngeen kadaa jubël
Du bàyyi ken muy sax di beel si Àdduna Daa jangaleek waaraate fii buldaaninaa
35. La jël Manjoon ak Baabakar miy xutbunaa 53. Farlu si Diine ji ak waañu Roohu Laay
Moo jël Isaak Baay Raan midoon xudwatunaa Waa Kambareen ay ñàkk ngeen Sëyyidunaa
36. Kon kay du tee Husëynu daanu waat xanaa 54. Yëmbël Gorom waa Malika ak waa Dakaar
Kem Karbalaa la Alya Samba wuutena Seen Konferansiyee bi demna Aljana
37. Luy tiis kerook si Karbalaa xamnan ko bes 55. Fekki xarit ya Seydi Caw ak Seydi Raan
Ba Baay Sheriif sëtub Limaamu làqquna Ibook rakamja Baay Saxiir faxiidunaa
38. Ñiinaa du moom Husëynu manta dem xanaa 56. Ku taar jayoon mbaa askanak xamxam alal
Sunub xarit du ñibbi weetël xalbanaa Naxool si Baay Sheriif sëtub Mahmuudunaa
39. Kërëm ga fees ñii jaaxle ñii di yuux sa kaw 57. Na tuub te dellu gëm Boroom bi Rabbanaa
Doomi Isaa ja xëyna tàggu Ahlanaa La jël Sheriif du bàyyi ken ci Àddina
40. Saadun wa Daal la dund melni ñaari fan 64 ans 58. Ku tiis daloon na muñ te xamni Rabbanaa
Dun masa miis demuk Sheriif Sadiixunaa Mooy joxe mooy jëlaat te mooy Xaadirunaa
41. Mboolooma dac ci Jàmmalaayi Kambereen 59. Ku jaaxlewoon na xamni Abdulaay Sheriif
Kuy taalibeek soppeb Sheriif riñaan sina Moofiy Sheriif te mooy Boroom zamaanunaa
42. Allarba Benn fan ci Yuulyuu Tashashin 1er Juillet 2009 60. Nam fonkewoon magam ja Seydi Abdulaay
Teemeeri at ginaaw kadoon Mahdiyunaa Ba naako Baay nanko matal si Abdunaa
43. Nan seet Sheriif si lun fi manti dal ëllëk 61. Nam fonkewoon jaamu Boroombi nanko jeem
Day mujja daal woyof ni xob fii nafsinaa Fonk sunnas Limaamu xayri xayrinaa
44. Sëtub Yonneen lawoon di doomi Ruuhulaay 62. Fa Baay Sheriif feetoon njabootgi Rabbanaa
Doyoon naciy garaat temoo doon Shayxanaa Naŋ nufa feete yaa xadiira amrinaa
45. Luy mbaax ci Seydinaa Limaamu moom la jël 63. Tawal ci moom feek picc ngiy sab yaa Kariim
Siwliise ak yanja la jël ci Seydinaa Nuuran wa Rahmatan mook Ahli Baytinaa
46. Yuusufa lay misaal ci taarak ak xarkanam 64. Bàyyifi Abdulaay yaakaaru Àddina
Te xoobe taar ba ak meloom yu sellana Mu sax fi lool te wer ne mooy xaliifunaa
47. Woyof na loolu màndu gëm xaalixunaa 65. Yaa Rabbanaa Yaa Rabbanaa Yaa Rabbanaa
Doon Taalibeb Maam Seydi ak Imaamunaa Dollil nu leer Sheriif Husëynu Shamsunaa
48. Ab tab la woon geejug teraanga lay misaal 66. Salli wa salliman ’alaa man ursila
Mbokkak xarit jirim faxiir yi jàqqanaa Wal aali wal ashaabi mooy Mahdiyunaa

Yëmbël
Aljuma, 14/06/2013
Sheriif Leeram du Fay
Mamadu Baara Samb

You might also like