You are on page 1of 12

MaaM Jaara Buso

WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Bismi-l-laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi
Wa sallallaahu Tahãlaa hãlaa Sëyidinaa wa mawlaanaa
Muhammadin wa aalihii wa sahbihii wa xayra xadiimihii wa
sallama tasliiman

Xerawluleen nu sant Soxna Jaara


Ngir moo nu may li tax nu sampi daara

Buleen ma tanqamlu, buleen ma tanqal


Buleen nëxal ndoxum ki leen di tànqal

Cellantuleen te wubbi seen i nopp


Ak seen i xol ma wubbi seen i bopp

Te génne seeni wagaan i xol te taataan


Maam Jaara waame la ku naanul yaa bon

Taw na Bawal taw na Kajoor ak Njàmbur


Ba walangaan ku mar ëllëg doob jàmbur

Waaloo ngi wal-wali di gental Waalo


Ngir naan ci géejug doomi Asta Waalo

2
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Jaaraama Maam Asta ma feeru Naawel


Sa géej gi neex na waaju naan si far wel

Jaaraama Maam Jaara ma feeru Poroxaan


Nëxoo dëyoo noo ngi dëtëm bay coroxaan

Gannàr dëtëm nañu ba naan ba mandi


Yaay bambulaan sam ndox xajul ci xandi

Ñépp a ngi mos ci sab liggéey ba Saalum


Fuuta futteeku nañ sa gan ne maalum

Yaw sa añub liggéey bi dem na penku


Dem soow baarakalla lii dug fàggu

Yakkal nga waa géej gi yakkal waa jéeri


Ba ñépp giijal yaw bayoo fu joore

Baykat nga bay nga bayu yaa di ndandi


Jigéen ñi booyal nañ nga bay ba Ndindi

Jigéen ñi soxla lañu yaa doon Soxna


Ndaanaan li wub nga làmbi doomi soxna

Moo tax jigéen ñi seeni doom ne meng


3
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Di réer akay feeñ yaw sa doom ne féng

Moo tax jigéen ñi seen i doom diy xaadam


Di gont akay xëy yaw sa doom dib yaaram

Yaa tax jigéen ñi ñépp seen i doom seex


Bu dul konak yaw noo ngi damm bay soox

Tëkkale la ak jigéen ñi Buso Baali


Xaw na haraam mel na ni Yàlla ak yaali

Di tudd seen i doom di tudd Bàmba


Haraam na ngir moom rekk a àttan yen ba

Yaw yaa di Buso Baali ñàkkóo càngaay


Naka nga jóg sàng nu jox nu ay gaay

Yaa tax jigéen ñi lëmasoo ay mëlfa


Nuy soli xawsa fu nu soob nu jël fa

Jigéen ñi dañ daa gaar di woddooy soppee


Góor ñi di mbeecooy mbaxañooy roof roppee

Yaa suturaal awra yi dindi joote


Mbàkkee ngi mel ni Ndar Ja baa ngay jooti
4
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

La am fa getti Ndar te am Sindoodi


Yót nga ko waa Tuubaak Gedeek Tindoodi

Jaaraama Maam Jaara ku am jaaraama


Yaa ko waral sa doom a rëy karaama

Jaaraama Maam Jaara ku am Màqaama


Yaa ko waral keroog bisub xiyaama

Jaaraama Maam Jaara ku am ay xar-baax


Yaa ko waral sa doom a feeñal ag baax

Jaaraama Maam Jaara ku fiy faj aajo


Yaa ko waral sa doom a faj sun aajo

Jaaraama Maam Jaara ku am hidaaya


Yaa ko waral sa doom a am wilaaya

Jaaraama Maam Jaara ku am tay junni


Yaa ko waral sa doom a jommal jinne

Jaaraama Maam Jaara sa xarful “Jiimi ‫”ج‬


Jox na la jikko yu rafet yu yéeme

5
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Jub nga jubal nga jàpp yaw tey julli


Tey jàng tey joxe ba leer ya jolli

Te jikko yii may bëgg a lim amóo leen


Jigéen ñu bon ña ko amoon yaróo leen

Daawu la jëw doo jànni daawu la jaye


Doo jayu doo jaayooka jaayi ci ja yi

Yaa sóobu yoonu Jannatu Nahiimi


Ku la royul dem Jaanamaak Jahiimi

Sa “Ra ‫ ”ر‬gi tax na ba ragal nga Yàlla


Rafet rafet njortu te xam nga yilla

Reewóo rëyóo réeróo ne naa la daali


Doo rummi doo rambaaje Buso Baali

Amoon nga faayda amoon nga fulla


Te amu fit am fit ba Yàlla fal la

Gore nga am nga kersa am karaama


Am nga ngërëm yaw yaay boroom Màqaama

Amóo kañaan goreediwóo naam Baali


6
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Daawul a kekkantook a kiitu-aale


Ma wax ci say jikko misaal yu tuuti
Laajleen ko maami Soxna Faati Tuuti

Maam Sàmba Maryaama ma daa raw cim lef


Hamdan li man Jahãla moo ko taalif

Noon na: bagaan ga woon fa Soxna Jaara


Mooy reerukaayub bépp dongo daara

Mbàndam ma musla déy te dañ daa rootaan


Mooy naanukaayab gaaya dañ koy seetaan

Masul a siis masul a dox di bodde


Masul di wex-wexlooka dox di gëdde

Daawóo weranteeka xuloo ni njëldi


Moo tax selaŋlul jur nga kuuy jur mbaldi

Kuy laa di Maam Sëriñ Mammar moom Jaara


Mbaldee di Daam dogitu weñ mooy Baara

Dangaa lewet ñemeg njaboot nib sërdi


Moo tax nga jur jàmbaar ju mel ni gaynde

7
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Daawóo di songanteeka dox di daane


Ak a defante tax na am nga waane

Wàcc nga jaajëf yaa selaŋlu Buso


Yaa tax ba nuy seeral gurooka buusu

Feerul ca àjjana ni xuurul hiini


Naa lay muriitu yaak sa doom lil hiini

Moo tax ñu naa la Jaaratul Ilaahi


Maryaama mooy sa tur wu mag billaahi

Ummu xaliifatu-r-rasuulillaahi
Muhammadin waladi Abdillaahi

Ummu imaamu awliyaa’il-laahi


Am nga màqaamatu rijaalillaahi

Am nga lu kenn amul fi nun billaahi


Maam Jaara neel al hamdulil Ilaahi

Maryaama fuqti muuqinaatillaahi


Sa doom a raw kuy jàng Bismillaahi

Moo donn Ahmadu Habiibullaahi


8
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Moo mas a jis Amiinu wahyillaahi

Yaay turandoo Maryaama ummu Iisaa


Sayidatu-n-nisaa’i raw nga sii saa

Moo donn Iisaa ma di Ruuhulaahi


Moo di donoy Muusaa Kalaamullaahi

Moo donn Ibra may Xaliilullaahi


Moo donn Aadama Safiiyyullaahi

Tuubaa liman tabihahuu lillaahi


Waylun liman ankarahum billaahi

La ñu joxoon Muhammadul Makiyyu


Mi ngi ñu jox Muhammadul Mbàkkiiyu

Marxaba ummu Ahmadul Mbàkkiiyu


Waarisu diini Ahmadul Mbàkkiiyu

Marxaba ummu Ahmadal Xadiimi


Xaliili si-l-Buraaqi wa-l-Xaysuumi

Marxaba uhtu Ahmadul Mbusóobi


9
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Ku mas a yër tataam ne tuubi ruubi

Tatay doj ak weñ la defoon fa Naawel


Saŋeem sa musul a toj te duñ ko ñaawal

Maseefu ko sóoru ci réewum Saalum


Ci sox yu tàkk mbaa këyit fulaa yam

Yaa baaxu tur Buso te baaxu askan


Yàgg nañoo siyaare gën ji Yónnen

Yaa rafat ab judd te baax i waa-jur


Ku xencu say sëddiit du jis lu dul gor

Maam yaa nga gaddaayee Gedeeki Tooro


Diineek goreleen tee jubook Lamtooro

Museefuleen a jiitu cig wilaaya


Mbaa Al-Quraan mbaa xam-xamub diraaya

Daawu ñu puukaree mbirum waliyyu


Ngir ay Sëriif lañ ñooy donoy Aliyyu

Bàmbaa ni mëlliy samandaay ab jant


Fenk ci maam mañ tudde Mammar Anta
10
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Leer gaa bawoo Mbusoobe suuxee Mbàkke


Royaat ca askan wa di Mbàkke-Mbàkke

Jant ba fenk na lëndëm ga daay na


Biddiw ya suux nañ soxileen mbër feeñ na

Samsu Sumuusi doomi jantak weer nga


Yaw jarulaa misaal nde fés nga leer nga

Tëmbeel ba réeroon ca cosaan ñu di ko jeex


Feeñ na fa Mbàkke leegi ñépp def i seex

Sayxu Suyuuxi yaa di seexub seex yi


Badrul buduuri yaa di weeru weer yi

Xunmu faqiiri yaa di saqum ndóol yi


Siitu haqiiri darajaal nga gool yi

Ummul masaakiini dexug miskiin yi


Abuul yataamaa yaay kenul jirim yi

Ma naa ko Mbàkke yaay Samsu-d-diini


Leeral nga Njàmbur ak Bawal ak Siini

11
WOLOFALU MAAM JAARA BUSO BU S MUUSAA KA

Siggil nga callalag Habiibullaahi


Maam Bàlla Aysa weeru gan wallaahi

Yaa tax ba képp ku sëtoo ci Mbàkke


Bu ne joneet Yàlla tofal ko barke

Waa Mbàkke Saañaŋkaaki Mbàkke Baari


Leeral nga leen ñépp a ngi dox di waare

Defar nga say bokk defar aw jàmbur


Defar Bawal defar Kajoor ak Njàmbur

Ña daa falook ña doon woroomi daara


Amuñu woon ku mel ni doomi Jaara

Aji-topp ji: Abdu Rahmaan El-Musaa

Aji-bind ji : Alfaaruq Siise

12

You might also like