You are on page 1of 69

Wurus wu gànjaru

Jawharun-nafiis ci wolof
Ngir fas wesari Laxdari

Jëm ci laab ak ci julli

CI PIRIM AW DÉGGINAM CI WOLOF

Aji-bind ji ci wolof Aji-tekki ji ci wolof


Allaaji Mamadu Ngeer Sëriñ Xaadim Mbay

Tel: +221 77 217 42 14 Email: emnguer@ugb.edu.sn


Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

2
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

XËTU PÀCC YI ........................................................................................................................................ 3


DALINU TÉERE BI .................................................................................................................................. 5
CANT AK NGËRËM ................................................................................................................................ 9
LALTAAY............................................................................................................................................... 11
I. LAAB AK LI CI AJU ....................................................................................................................... 23
I.1 AB DOG CI LAAB .................................................................................................................... 23
I.1.1 DINDI SOBE AK LI CI AJU ................................................................................................. 23
I.1.2 FARATAY NJÀPP ................................................................................................................. 24
I.1.3 SUNNAY NJÀPP ................................................................................................................... 24
I.1.3.1 LU AJU CI FÀTTE FARATA CI CËRI NJÀPP ............................................................. 24
I.1.3.2 LU AJU CI FÀTTE SUNNA CI CËRI NJÀPP ............................................................... 24
I.1.4 NGËNEELI NJÀPP ................................................................................................................ 25
I.1.5 WAY-FIRI NJÀPP YI ............................................................................................................ 25
I.1.6 LEES DI TERE AG JËFAM CI LU DUL AM NJÀPP .......................................................... 26
I.2 AB DOG CI CANGAAY ........................................................................................................... 27
I.2.1 ÀTTEY CANGAAY, WAY-WARALAM AK LA CA AJU ................................................. 27
I.2.2 FARATAY CANGAAY ......................................................................................................... 27
I.2.3 SUNNAY CANGAAY ........................................................................................................... 27
I.2.4 NGËNEELI CANGAAY ........................................................................................................ 28
I.2.5 LUY DOLLIKU CI JANABA CI TOJ MA GËN A NDAW ................................................. 28
I.3 AB DOG CI TIIM ...................................................................................................................... 29
I.3.1 FARATAY TIIM .................................................................................................................... 29
I.3.2 SUNNAY TIIM ...................................................................................................................... 30
I.3.3 NGËNEELI TIIM ................................................................................................................... 30
I.3.4 WAY-FIRI TIIM YI ............................................................................................................... 30
I.4 AB DOG CI MBËRËG, DIIR BA AK LA CA AJU ................................................................. 31
I.5 AB DOG CI DERETI MERET AK LA CA AJU ...................................................................... 32
II. JULLI AK LI CI AJU .................................................................................................................... 33
II.1 AB DOG CI JULLI .................................................................................................................... 33
II.1.1 XAM WAXTU JULLI YI ................................................................................................... 33
II.1.2 SÀRTI JULLI ...................................................................................................................... 34
II.1.3 FARATAY JULLI ............................................................................................................... 35
II.1.4 SUNNAY JULLI ................................................................................................................. 36
II.1.5 NGËNEELI JULLI .............................................................................................................. 37
II.1.6 RAGAL YÀLLA CI JULLI AK LA CA AJU .................................................................... 39
II.1.7 JULLIG AJI-FEEBAR ........................................................................................................ 40
II.1.8 FEY JULLI YI FAAT.......................................................................................................... 41
II.2 AB DOG CI JAMAJ .................................................................................................................. 43
II.2.1 JAMAJ AK LI CI AJU ........................................................................................................ 43
II.2.2 JAMAJ CI JULLIG FARATA GOG JOOXAL .................................................................. 44
II.2.3 JAMAJ CI JULLIG FEY AK GOG NAAFILA .................................................................. 53
TËJTEG TEERE BI ................................................................................................................................. 59
AB SOF ÑEEL LI ÑUY WAX CI NJÀPP AK CI JULLI ...................................................................... 61
AB SOF ÑEEL ABAJADA WOLOF ..................................................................................................... 65
TEGTAL YI ............................................................................................................................................. 67

3
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

4
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Ki bind téere bi :

Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke ñu di ko woowe Seriñ Tuubaa walla Xaadimu Rasuul (di baatu araab
buy tekki “ Liggéeykatu yonent bi ”), moo bindoon téere bi ci làkku araab. Mi ngi gane àdduna ci
atum 1853 ca Mbàkke (ñu daan ko wax Mbàkke-Bawol), wuyuji Boroomam bésub 19 sulet 1927 ca
Njaaréem (Jurbel) ci Senegaal. Nitu Yàlla la woon bu ràññeeku, teg ci nekkoon boroom xam-xamu
diine bu mag a mag. Mooy ki taxawal yoonu Murit, sanc Tuubaa, taalif lu sakkan ci diine te indi ay
gisiin yu bees. Nekkoon na it bañkat bu mag bu wéeru woon doŋŋ ci Yàlla. Moo taxawoon
jàmmaarlook tubaab yi ngir xeexal Islaam. Ginnaaw gi ñu jéem koo sànk ci pexe yu bari, génne ko ay
yoon réewam. Waaye teewul mu mujjee am ndam seen kaw, ginnaaw bi mu muccee ci seeni pexe. Tey
jii ay njàngaleem ak i jëfam law nañu fépp ci àdduna.

Li nekk ci téere bi :

Lii mooy téereb Sëriñ Tuubaa bi tudd Jawharun-nafiis. Sëriñ bi, yéene ju mu amoon ci dundalaat lii di
xam-xami diiney Islaam, moo waraloon mu amal ab liggéey bu màgg bu jëmoon ci wàllu suqali téere
yu jëkk (yàgg) ya nga xam ne gis leen walla am leen ba di leen jëfandikoo yombul woon. Bokk na ci
téere yooyu bob boroom xam-xam bu mag, bu doon wuyoo ci turu Laxdari. Moom nag daf koo
wesaroon1, Sëriñ bi jël ko yaatal ko, sotti ko aw woy ngir yéwénal njàng mi ak mokkal gi, tudde ko
« Ajawharun-nafiis » ; ñu di ko tekkee ci wolof « wurus wu gànjaru »2.

Téere bi, njariñ li mu làmboo foo ko natt rek, weesu na ko. Sëriñ bi waxtaane na ci ay ponki Islaam
yu takku te am solo lool. Ci njalbéenug téere bi, ma nga fay leeral bu baax li jëkk a war mukàllaf, te
mooy wéral ag ngëmam ak taxaw temm ci liy farata ci moom ci wàllu xam-xam te mooy xàmmee
faratay jëmmam. Mu topp di indiy leeral ci ni mukàllaf war a saxoo tuub ak la ca aju ci ay sàrt. Mu jàll
indiy leeral ba-tey ci ni mukàllaf war a sàmmoonte ak juróom-ñaari cëram bu baax-a-baax ba moytu
cee moy Yàlla.

Mu ngi nuy jàngal it ne képp kooy bëgg ci doomi-aadama yi na Yàlla rek tax, koo ciy bañ itam na
Yàlla rek tax. Indi na it ay leeral yu am solo ci yenn jikko yoo xam ne yu araam lañu te mat a moytu ;
yu mel ni rëy, ngistal, fen, rambaaj, aaw (maanaam naw sa bopp), jëw, kañaan ak ndéggtal (mooy def
lu baax ba noppi di ko nettali). Dina wax it ci mbirum fo, ak it lekk alali nit ñi ci turu diine ak lu mel ni
yéex a julli ba waxtu wa jàll, te mu bokk ci bàkkaar yu mag yi. Dina jàll wax ni ab jullit war a xére ci
sàkku ngërëmal Yàlla bañ koo yamaleek lenn. Dina wax ni nga xam ni mukàllaf noonu la war a farloo
ci lu mu xamul laaj ko, ndax bañ a song dara te xamu ko. Dina wax it ci topp sunna bu baax-a-baax bañ
a dox ci ay biddaa. Lii lépp mi ngi koy waxtaane ci tàmbalig téere bi. Bu ca noppee nag, daldi ubbi
ñaari bunt yu mag, bu ci nekk ëmb ay dog yoo xam ne daf cay waxtaane benn ponk. Dog yooyu ñoo
ngi nii : LAAB , CANGAAY, TIIM, MBËRËG, DERETI MERET, JULLI, ak ñoom-seen.

1
Wesar mooy bind buñu woyul.
2
Manaam oor bu "cher".

5
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ki bindaat téere bi ci wolof latin :

Téeri bi nag yàggees na koo firi ci wolof. Boroom xam-xam yu ràññiku ci yoonu murit, ñu mel ni Sëriñ
Abdu Rahmaan Mbàkke (Daaru Muhti), Sëriñ Xaadim Mbay firi nañu ko, def ko ci ay kaset walla ñu
bind ko ci arafi araab, te ñu gën koo xam ci baatu « wolofal ».
Lu aju nag ci wàllu yaxalug téere bi ci arafi « latin », ku mel ni Maalig Faal defoon na ko, waaye noo
ngi koy door a gis ci anam gu dëppook yoon ak jamono. Xalaat bi mi ngi tukkee ci Allaaji Mamadu
Ngeer, di ab jàngalekatu xarala yu bees yi ca Iniwersite Gaston Berger bu Ndar (Senegaal). Liggéey bi
mi ngi ci ànd ak Soxna Baawo Jóob di ab jàngalekatu làmmiñal ca Iniwersite Gaston Berger bu Ndar
ak waa Daahira Mafaatihul Bichri, nekk ci boobule Iniwersite.
Tekkiwul Jawharun-nafiis, waaye dafa sukkandiku ci kàdduy Sëriñ Xaadim Mbay (mi ko tekki ci wolof
te def ko ci mp3) ngir bindaat ko ci wolof (ci arafi latin) ci anam gu dëppook yoon ak jamono.

Allaaji Mamadu Ngeer, nekk na nit ku am pastéef, ku farlu, ku yitteem yépp jëm ci liggéeyal Sëriñ
bi1, jariñ askan wi ak ci wàllum njàng ak njàngale. Doon na it ku xam-xamam màcc lool ci wàllu
mbindum wolof ci arafi “latin” ak yoy araab. Waaye, ligéeyam, ñu ngi ko gën a ràññee ci suqali làkki
réew mi jaare ko ci xam-xamu informatik.

Li waral bile liggéey :

Sëriñ bi, xamoon ni téereb Laxdari ame njariñ ak ni ay woy yombee mokkal, moo taxoon mu bindaat
ko, jële ko ciy wesar def koy woy, tudde ko Jawharun-nafiis.

Li leen tax a amal liggéey bu ni mel, moo di ne dañu koo jàppe liggéey bu am njariñ. Jël lu mel ni
Jawharun-nafiis, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga bindaat ko ci araf yoo xam ne, mënees naa wax ne fii
ñu tollu nii, ñu bari ci doomi-réew mi wattu nañu ko, ngir am yéeney yombal njàng mi ak tas ko, ba ku
dégg wolof ku nekk te mën a jàng, miim mbind mën cee jariñu, ab liggéey du ko gën a réy. Dañu koo
jàppe it muy aw waar ci tool bu yaa bi nga xam ni mooy toolu Sëriñ bi ngir bey ci seen wàll, liggéeyal
Sëriñ bi ba noppi jariñ askan wi.

Rax-ci-dolli, bokk na ci liy dundal làmmiñu wolof. Kenn umplewul jéego yu am solo yi nga xam ne
nguur gi ak gépp kurél guy yëngu ci wàll woowu ñu ngi koy def ngir gëddaal làmmiñi réew mi. Te ku
nekk xam na ne lu nit mën di sàkku ci xam-xam, ak bu mu mënti doon, ci làmmiñ wi mu nàmp la ko
gën a mën a xame dëgg-dëggi xam. Séex Anta Jóob, mas naa wax ni : « Làkku jaambur bu neexee ba
mel ni tàngal it, mënuloo koo macc ba di ca tàqamtiku ». Muy firndeel rek ni, nit làkkam ci la mën a
xalaate, waxe ci gis-gisam, jokkoo ci ak ñi mu séqal, sàkkoo ci xam-xam bu leer, ak ñoom-seen. Kon
mën nanoo wax ne liggéey bii ay njariñ kepp la ëmb.

1
Bu nu nee Sëriñ bi, Sëriñ Tuubaa lanu ci jublu.

6
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Lees dolli lu yees ci téere bi :

Nees ko waxe woon, téere bii dañu cee bindaat Jawharun-nafiis ci wolof (ci arafi latin) ci anam wu gën
a dëppook yoon ak jamono. Looloo waral ñu dolli ci ay buntu yu ca amutoon, niki “Daliinu téere bi”
ngir leeral tuuti lu aju ci liggéey bi, “Cant ak ngërëm” ngir sant ñi jàpp ci liggéey bi, “Ab sof ñeel li
ñuy wax ci njàpp ak ci julli” ngir tekki ci wolof lépp lees di wax ci njàpp ak ci julli, “Ab sof ñeel
Abajada wolof ” ngir gën a yombal njàng mi. Ginnaaw loolu, utal nañu ay tur yenn ci ay pàcc yu amul
woon tur, lépp ñu jublu ci tàqale ngir mu gën a leer te gën a yomb a jàng. Dina tax aji-yër ji di mën a
gis fim bëgg a jàng, tëb dal ca. Tur yooyu di “Laab ak li ci aju” ak “Julli ak li ci aju” ngir tàqale
wàllu laab ak wàllu julli, “Lu aju ci fàtte farata ci cëri njàpp” ak “Lu aju ci fàtte sunna ci cëri
njàpp” ngir tàqale leen, “Ab dog ci cangaay” ngir ëmb lépp lu aju ci cangaay, “Julli ak li ci aju” ngir
ëmb lépp lu aju ci julli ak wàllu jamaj. Dog biy wax ci jamaj ñu feeñal ci ronam “Jamaj ak li ci aju”,
“Jamaj ci julli farata gog jooxal” ak “Jamaj ci jullig fey ak gog naafila”. Kàddu yi Sëriñ bi tëje
téere bi, nga xamne waxu ci lu jëm ci julli mbaa ci laab, ñu def ko ab bunt buñu tudde “Tëjteg téere
bi”.

Xanaa di ñaan rek sunu BOROOM nangu liggéey bi te barkeel ko, ñu dund ba yeneeni téere topp ci
ngir ndaw ñi mën a jot ci xam-xam bi bay jëfe seen diine ca anam ya mu ware.

Soxna Baawo Jóob


Jàngalekatu xam-xamu làmmiñal
Iniwersite Gaston Berger
Ndar (Senegaal)

7
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

8
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Ginnaaw bi ma musloo ci Séytaane, maa ngi tudd sama Boroom, di ko màggal, di toroxlu ci kanamam,
di ko jéggalu samay bàkkaar te di ko sant cant gu amul àpp ci li mu ma xiir ba ma am yittey bindaat
téere bii ci wolof ngir yombal askan wi sàkkug xam-xamu diiney Islaam.

Topp maa ngi julli ci yonentam bi (yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko) te di sant Sëriñ Tuubaa
cant lu wér tey ñaanal Sëriñ Siidi Moxtaar Mbàkke mu yàgg fi te wér ak bépp jullit.

Bu loolu wéyee, maa ngi sant Sëriñ Xaadim Mbay mi tekki téere bi wolof te nangu ma bind ko ci arafi
latin. Sant ñeel na it Soxna Aram Faal miy sunu kilifa ci wàll wii. Moo ma jëkk a jox ay téere ngir ma
jàng mbindum wolof ba teg ko ci yoon. Gàgganti na lu bari ci téere bi. Teg ci di sant Maam Ceerno
Siise ci xelam mu rafet, jógul benn yoon di leeral samay laaj. Yal na leen Yàlla bàyyi sunu kanam, dolli
leen wér ak jàmm te fey leen ngën gi pey.

Maa ngi wéy ba-tey di sant waa Daahira Mafaatihul Bichri, rawatina Sëñ Maxfuus ak Sëriñ Baas, ngir
seenug jàpp ci liggéey bi. Ñoo toppaat téere bi ngir jubbanti bu baax a baax wax ji ba mu gën a
dëppook li Sëriñ bi wax.

Maa ngi sant bu baax Soxna Baawo Jóob miy sama nàttangoo ak sama mbokkum taalibe. Moo toppaat
téere bi ngir jubbanti mbind mi ak waxin wi ba mu gën a dëppook ni ko yoon tërale.

Maa ngi sant it képp ku jàpp ci liggéey bi ci lu jege mbaa lu sori rawatina Ismayla Sow mi ñaw
mbubbum téere bi1.

Maa ngi tëje xët wi ak ñaan gi Sëriñ Tuubaa tëje Jawharun-nafiis :

“Ñaan naa Aji-wëlsëgal mbindeef yi, kay Aji-màgg, nekkug téere bii di lu ñu nangu.

Te mu nekk di aji-jariñ niki cosaan la te mu seral bët ba fas képp.

Te mu nekk di sabab ñeel ubbig aji-tàmbali ci moom ak fajug aajo.

Ak mu fey kawe képp ci nun ci ñeewant ak njéggal njëkk sunu njàqare.

Ak ma dajeek aji-bijj ab yool ci woy wi fa faatu ga ak bésu pang ba.

Ci darajay làmpu mbindeef yi Muhammad. Yal na dolli tedd-nga te mu dolli wóolu ci Moom, Yàlla may
kojug dappet,

ak ñoñam, ak saabaam ña di way-tedd feek am na aji-jub ngën jaa rafet ag muj.

Tudd naa sellug sama Boroom, kay Boroom tedd-nga ja, wëliis la nga xam ne danañu ko melal Yàlla.

Ag mucc yal na nekk ci ñañu yónni ña. Ag cant ñeel na Yàlla may Boroom mbindeef yi.”

Amiin
1
Maa ngi jublu ci mbubbum téere bi “Page de couverture” ci làkku faranse.

9
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
.

10
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Tàmbali gi barkeel na, jeex gi barkeel na


Ci turu Yàlla miy Yërëmaakoon1 di Jaglewaakoon2 laay tàmbalee.

Yal na Yàlla dolli xéewal sunu sang Muhammad ka dib Soloom ak i ñoñam ak i saabaam3 te mu musal

ko ag musal. Yaw Buur bi yal na nga yéwénal xeetu Muhammad, yal na Yàlla dolli xéewal ci moom te

musal ko. Yaw Buur bi yal na nga woññi njàqare wëliis xeetu Muhammad, yal na Yàlla dolli xéewal ci

moom te musal ko. Yaw Buur bi yal na nga yërëm xeetu Muhammad, yal na Yàlla dolli xéewal ci

moom te musal ko. Maa ngi sàkku sa ndimbal Yaw Aji-dimbalee ji te ci Yaw doŋŋ lanuy sàkku

ndimbal. Déet pexe4, déet kàttan5 ndare6 ci ndimbalul Yàlla kay Aji-kawe tey Aji-màgg. Doy nanu,

Yàlla mi amul moroom, miy ka ñu wàkkirlu [Ka ñu doyluloo].

Doomu Abiib, tudd Ahmad di aji-aajowoo7, wax na : maa ngi sant Boroom mbindeef yi cant lu sax.

May aji-julli ci aji-dégg ja fiq, kiy aji-gindee Muhammad ak bépp way-farlu.

Bu loolu wéyee, naka man walbati naa samay yitte ngir fas wesari Laxdari ka dib sang.

Ngir mu nekk aw may ñeel képp koo xam ne namm na ag wattoom ci doomi jamono ji.

Muy aji-dog ngànt8ñeel bépp fóore buy boroom xam-xamu adab9, kuy aji-deñ kumpa xam-xamu nahu10

ak xam-xamu haruud11 ak xam-xamu luha12.

Te Yàlla sama Boroom laay ñaan nangu ga, ndimbal la, dëppale ga ak àgg ga.

Te mu nekk nooflaayug ndaw ñi ak koo xam ne aajowoo na ko ci mag ñi.

1
Kiy yërëm bépp mbindeef ci àddina.
2
Kiy jërëm jullit bu ko soob ci allaaxira.
3
Ñi jamanoonteek moom te gëmoon ko.
4
ñeel ma ci bàyyi moy.
5
ñeel ma ci topp Yàlla
6
Ndare mooy ba mu des.
7
yërmaande sunu Boroom.
8
may layal.
9
Xam-xamu teggiin
10
Xam-xam bi ñuy xame yax yu damm (“grammaire” ci làkku faranse)
11
Xam-xamu woy.
12
Xam-xamu làmmiñal ( “linguistique” ci làkku faranse)

11
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Tudde naa ko “Wurus wu gànjaru”, ci fas wesari Laxdari1 kay kilifa.

Lu njëkk la nga xam ne Aji-yërëme ja waral na ko, ci lu dog, ci ku ñu togg-jëf2mooy gëm.

Topp mu xam la nga xam ne dana yéwénal ci moom faratay jëmm3 mbooleseen; yewwul.

Niki àttey Koor, Laab, Julli bob farata ak bob sunna ba, Aj ak Asaka.

Topp war na ko mu wattu deytali4 Boroom Aras; màgg na te kawe na.

Te mu taxaw ciy ndigalam ak i tereem te mu tuub wépp waxtu te muy aji-tudd;

ñeel Boroomam, yéem naa ag sellam, laata muy nekk Aji-sànjawu ci moom ci jamono ji.

Bokk na ci sàrti tuub, réccu la nga xam ne faat na ko ciy moy, lu mu mën a doon.

Te mu yéene ci la nga xam ne des na ci fan ya, ñàkk a delloom ñeel lépp loo xam ne dana lor.

Te mu nekk aji-bàyyi moy, ndeem nekk na di moy ci lu dul yéexe.

Déet di ko ñeel yéexe mbaa muñ-muñlu ñeel ag tuub te bumu wax danaa muñ,

ba mu gindi ma Boroom njéggal ga; ngir naka loolu màndargam gàcce la,

ànd ak texeedi ak tilimug xol; naka man danaa muslu sama Boroom ci ñoom ñaar.

Naka noonu delloo mbooleem tooñaange ya, dees na ko lim ci sàrti tuub fa aji-topp ja.

Ngir naka moom farata la, ku ko bàyyi ngir woyofal ko doŋŋ moy na Buuram.

Topp delloo tooñaange ya dikk na doon ñaari xaaj, alal la ak der ya; ci lu dul nar.

Na delloo alal ya ñeel woroom ya ndeem fekkeef na leen diirub jamono ci lu dul sikk.

Topp ndeem fekkeefu leen, na ko delloo seeni way-donnu ci lu dul deŋŋi-deŋŋi5.

Topp ndeem fekkeefu leen, mu saraxe ci alal ja te yéene leen ko; nii la ko nettali ka dëggal ka.

Na sàkkoo daganal bépp der bob lekkoon na ko ci jëw, ci xaste mbaa ci ŋàññe woo xam ne feeñ na,

1
Abduraxmaan Laxdaree ngi juddi ci 1512 ca Biskra (Alseri). Mi ngi faatu ci 1575 ca Biskra (Alseri). Boroom xam-xamu
fiq Maaliki la woon.
2
Mukàllaf
3
loo xam ne kenn mënu koo defaaleel sa moroom niki julli
4
Yem fi la Yàlla yemloo, bañ koo jéggi.
5
Mooy sikki-sàkka.

12
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
ndeem nekk na1 di aji-teew. Ndeem ñàkkeef na ko2, na baril aw yiw ndaxtale moom dana am

lëf loo xam ne dana jooxal àqu képp ci ñoom ci yiw wa; nay jéggalu tey yaakaar njéggalu Boroomam.

Na wattu làmmiñam ciy ñaawtéef ak ci wax ju bon ak werante.

Dëgg-dëgg boni wax mooy lépp loo xam ne danga ca nekk boroomug kersa3; nanga xam.

Daganal nañu ag biralam fas aji-gàtt-xel ja, ndeem nekkul di dégg ag junj4 gog dana am njariñ.

Dëgg-dëgg werante fas ka nga xam ne xam na, mooy weddi ag dëgg gannaaw ba mu feeñee.

Jeñ5 dëgg ga ciy neen ak ay, ngir sib sa suufeeg daraja6 ca nit ña.

Bokk na ci tere yi, doyodal ak gëdd ab jullit mbaa nga saaga ko ngir gàcceel ko.

Kem yii, ragal-loo ag ragal ci lu dul àqi yoon; bul jeng.

Waaye moom lu ñu daganal la, fas kuuyu tànneef ya, ci gëtën ak ci yar.

Niki nii, giñ cim pase, araam na; waaye nag nekkul cig dëppoo7.

Ngir xibaaru tere ba ci giñ ci goreel ak cim pase ci biral ga.

Koo xam ne tàmm na ko, cig toftale, naka moom nekk na ku ñu war a yar.

Ngir déet muy giñ cim pase ak ci goreel ci aada lu dul kàccoor yi.

Na wattu ab gisam ci lu araam, bumu xool loo xam ne daganul mu xool ko.

Niki xool cib xooliin ñeel jullit, bob dana ko lor; waxeesul nag kàccoor mbaa aji-tooñ.

Li fi ne, war na ci (mukàllaf), ci loo xam ne leeraleef na ko, ag tongam ngir laabire ko ngir mu dellusi.

Tere nañu xool ñeel jigéen ña, ña di kojug jaambur8, ak niki jongoma

ci bépp melo cig bànneexu; niki tóoyéenu góor9; wattandikul yii.

1
Moom mi nga jëwoon
2
Daa faatu ci misaal
3
Bees la ko nettalee.
4
Ci misaal ku xamul luy “Ana fu nuy tuureem ndox?”. Nga ne ko “Ana fu nuy sawee ?”
5
Dàq
6
Bañ ñu ne diw kat yey na ko, moo ko ëpp xam-xam.
7
Boroom xam-xam yépp dëppoowuñu ci.
8
Jigéen ju la araamul te takkoo ko.
9
xale bu góor bu saxagul sikkim

13
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Bokk na ci xool cig xeeb, niki nii ngir ragal-loo mbaa di ko gëdd.

Dana warlu nag aji-aay bët1 loo xam ne alag na ko ciy bëtam, niki mu nettalee ko kilifa ga.

Dees na tëj aji-aay bët, fim fa siiwee ci lor ji, ci këram; wattul xibaar ba.

Ak wattoom ñeel cër yi : biir bi, làmmiñ wi, pëy mi, ñaari tànk yi, ñaari bët yi, ñaari loxo yi,

aji-juróom-ñaareel seen ñaari nopp yi; koo xam ne sàmm na leen wëliis ay moy, dana làq ag jublu
mbooleseen.

Ngir bépp cër, yaw sama àndandoo, jàkkaarloo na ak ab bunt ci safara ya; ci loo xam ne sax na.

Te koo xam ne wattu na leen, du tàbbi ci buntu ca buntu ya; ci loo xam ne tuxal nañu ko.

Te bépp cër bob moy nga ca fàww, dinga tàbbi, ci sababug moy ga, ci buntam ëllëg.

Nay sopp jëmm ngir Boroom mbindeef yi te muy bañ ngir Moom; déet ngir poñ-poñeetum àddina2.

Soppal aji-gëm ja ngir ngëm ga te nga bañ aji-weddi ja ngir ag weddeem Yàlla.

Doonte dikke na la cig tooñeel moom aji-gëm ja ak aji-weddi ji ci alal ju doy.

Te mu nekk di aji-digle ag njub te muy aji-tere safaanug njub3 ngir ug laabiire.

Waaye ñeel na ko ñetti sàrt, tudd na ko ci saraa ba sunu sëriñ4 kay aji-peeg xam-xam.

Jublu naa ci dagan5 ga ak war ga; jëlal samag lim cig toftale.

Jublu naa ci mu6 nekk aji-xam ci lu ñu pakk7 te déet muy aji-bijji jëm ci aw ay wu gën a mage8.

Te mu nekk [moom mi ngay digal] di aji-àttan ci ndigal la ci deñal ga ci lu dul weddi.

Sàrtal nañu ndigalu ilimaan ci digle ga, ànd ak maandu9 ga; ci lu dul lënt.

Waxeef na ne niki ñaar yooyu nekkuñu di ay sàrt ci ndigal; bàyyil nëbb sikk.

1
Koo xam ne lu mu xool mu yàqu. Dees na ko tuddee it aji-gëtu.
2
Jox la alali àddina warul tax nga bëgg ko, ñàkk la caa jox warul tax it nga bañ ko.
3
Ag réer.
4
Imaam Gasaali.
5
Lu dagan mooy loo xam ne bu la nexee def bu la nexee bàyyi.
6
Aji-digle ji.
7
Xàmmee lu baax ak lu bon. Lu Islaam digle ak lu mu tere.
8
Li nga koy tere bumu ko yóbbe muy def lor ju gën a kawe. Ci misaal, bu dee boo ko teree tux mu naan sàngara, bàyyi ko
ca.
9
Yaw miy tere mbaa ngay digle, na fekk ngay sàmmoonteek sàrti Islaam.

14
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Dikke na ba-tey sàrtu nekkug lañuy pakk di aji-feeñ ci lu dul reju1 gog xameef na ko.

Du caagéenu sàcc ag dégg2 ak banamtikum xet3 niki jëfi boroomug naaféq.

Te daganul gëstu la nga xam ne nëbbu na ci mbubbam mbaa ci bitigam; nee ma waaw;

Mbaa ci ñaari loxoom mbaa ci këram mbooleseen; li fi ne, képp ci yii nekk na di lu araam lees tere.

Xamal ne naka digle ak tere feeñ na diggante ñoom ñaar ag taqoo, settantal ko.

Ku tere ci lu mu ci lëf lol daw na, naka moom, digle na safaan ba.

Dana araam ci moom réy, ngistal, fen ak rambaaj; xamal.

Dëgg-dëgg réy, ci kasrag kaaf gi ak sukuunug baa, ci lu dul wuute.

Waxal ni, mooy yékkati jëmm ànd ak nëbb dëgg ak màgg-màgglu ak xeeb mbindeef yi.

Dëgg-dëgg ngistal, fas way-ñaw ya, mooy tàbbal ag jaamu ngir jublu ca nit ñi.

Moom, fa sunu kilifa Gasaali, mooy baril ay topp ànd ak jikko yu kawe ya;

Ngir nga am, ci xolu nit ña, daraja ju yéemu ci càkkutéef la.

Dëgg-dëgg fen mooy sag xibaar loo xam ne nekkul di aji-sax ci waxi boroom xam-xam yi.

Moom, aji-bon la, aji-waral la ndeem feeñ na, móolug Aji-màgg ja ci loo xam ne tuxaleef na ko4.

Ngir jëmm du fen, ndare mu génn [fen wa] tukkee ci gémmiñam, topp mu yéeg

ba mu jot Aras mi nga xam ne moo gën a kawey barab, topp mu wax : “Man la fenu diw”.

Yal na ko Yàlla rëbb, yéem naa ag sellam ca foofee, te rëbbu ko5 ànd ak mépp Malaaka.

Malaaka ya dinañu bind, juróom-ñaar fukki ñaawtéef ci moom, ci lu dul nar.

Bépp ñaawtéef tollu na kem doj wa nekk Uhud; nettali na ko sunu sëriñ kay kilifa.

Waaye yenn ci boroom xam-xam yi séddale nañu fen ci juróomi xaaj.

Wax nañu, mbooleseen, ci limub juróom-benni bëyit ciw woy wu di aji-rafet.

1
Ci misaal waroo fekk ku nekk ci néegam di def la muy def nga koy yërndu ba noppi di ko ko tere.
2
Di ko yëddu.
3
Di ko xeeñtu.
4
Ci addiis
5
Móolug Yàlla mooy xañ ko yérmande.

15
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Séddale nañu fen ñeel juróomi xaaj. Am na ci fen woo xam ne wu ñu sopp la, am na wu war.

Wu ñu soppam mooy ngir ab xare ak ngir ragal-loo ñeel ab yéefar, dees na ko nax ci fen wa1.

Aji-waram nag ñeel xobbi2 alali jullit ak alali boppam ci dëgg-dëgg ci deret.

Wu ñu daganalam, yaw sama àndandoo, ngir yéwénal diggante mbindeef3; déet di nekk ci fen woowu
bàkkaar.

Wu ñu sibam4, ñeel soxna sa, ngir teeyug bakkanam ak ñeel doomam ngir sopp ko5.

Wu araamam mooy la nga xam ne, xameef na ko, ñeel lu dul njariñ6 gu di kojug yoon.

Wax na, waa tasawuf, wépp ci fen yi aji-bon la. Lii nag, ci sunu ngiir, mooy li wér.

Ndaal rambaaj, fas ka nga xam ne gëstu na, mooy sag tuxal waxtaan wa jële ca ka nga xam ne waxtaan
na ko;

ci anamug yàq. Moom rambaaj moo gën a bon ci jëw naka ñu ko biralee sëriñ sa.

Ngir ag nekkam dina waral ag noonoo ak ug mbañeel diggante nit ñi ak ug texeedi.

Moom rambaaj, fa sëriñ sa, tooke la joo xam ne dana rey; saafaraam mooy dëddu wëliis ko; xel-luleen.

Aaw7, jëw, mbañeel, kiñaan, ba-tey ndéggtal8, tere na wëliis leen, ka ñu jublu ka (Yàlla).

Dëgg-dëgg Aaw ci dammug hay ak ci sukuunug jiim wëliis nar;

Mooy ag jeng jëm sa jëmm ànd ak ag màggal ñeel ko ngir sag fàtte Boroom mbindeef yi.

Saafaraam mooy sag xam ne naka jëf ya ñeel na Aji-moom mbindeef yi, màgg na te kawe na.

Te naka moom déet muy deñ di boroomug gàttañlu ci jëf ja te dikkewoo ci kem naqiir9.

Ci wàllug la nga xam ne war na la ci àqi Aji-màgg ji; te dikkewoo ci aw pepp, du caagéenu fattiil10.

1
Niki réewum jullit ak wow yéefar di xeex, nga daje ak i yéefar ne leen: “Buleen dem de ndax dooleen mën a dékku
ngànnaay ak soldaari jullit ya”. Tax ñu ragal ba daw.
2
Niki fekk ku sàcc alali jaambur nga fen ko fen wu tax mu delloo alal ja.
3
Niki fekk ñaar ñoo xam ne seen diggante daa yàqu, nga fen ba defar diggante ba.
4
Lu ñu sib mooy loo xam ne boo ko defee day wàññi yool ba.
5
Niki di wax lu neex sa soxna mbaa sa doom te doo ko def.
6
Fen woo xam ne benn njariñ nekku ca.
7
Yéem say jëf
8
Mooy looy def ci lu baax bëgg ku ko dégg ba naw la.
9
Naqiir mooy xar-xar bi nekk ci saalub tàndarma. Maanaam daal dikkewoo ci dara rek.
10
Fattiil mooy buum googu nekk ci góot-góotu saalub tàndarma

16
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Te koo xam ne sukkandiku na ci ku dul Yàlla, dina rékkiku1wëliis ko te dina alku Bésub2 tiis ba.

Naka moom dana jàppandi ñu bañ a nangu jëf ja ngir bari ay ràgg-ràgg3 ci jëf ja; nanga xel-lu4.

Bëraanaa5 ag jaamu, yàq na ko ag gendiku6 gu xeebu.

Du yell ñeel jaam bi wooteeg màggug ay jaamoom ñeel Boroomam kay boroom xéewal.

Dëgg-dëgg jëw ci lu dul sikk, mooy sag tudd melow jëmm ginnaaw ag fàddoom7,

Mbaa melow la nga xam ne aju na ci moom ci loo xam ne dana sib ko doonte dégg na ko.

Ndeem tudd nga ko ci lépp loo xam ne nekkul di meloom, loolu aw duur8 la, wow yékkatiku na.

Tere nañu loolu ba-tey cig teew, ngir naka moom moo gën a bari ayib ak lor.

Ki nga xam ne wax na ci lu dul lii9, nee ko deflewu na. Te wor na ko la mu dégg te déggul dara.

Doy na la ci jëw naka nekk ci Alxuraan ag nuróoleem ak méddug nit.

Wax na ngën gi yonent yi, cig baamu10, waccul ñeel tànneefu jigéen ña

Ba nga xameene jigéen dikkal na ko, wax na kii aji-gudd la mbiccum mbubbam, mu waccu.

Mu rot suuxu yàpp. Mu giñ (Yonent bi), yal na Yàlla dolli ci moom xéewal feek làq na tedd-nga.

Naka moom doonte reesoon na, mënta ñàkk tàbbi Safara, ndeem dee ga dana gaar.

Déet mu koy jariñ fa Aji-màgg ja ag askaneem, foofee, jëm ci Yonent bi.

Jëw ab jullit ci waxi Aji-deñ-kumpa ja, moo gën a ñaaw ci lekk méddu mbaam.

Xisab ku ñu jam ka ak ñaar ña doy na la ag jàjj ci lu dul nar.

Ag tàmbaleem, naka Yonent Yàlla, yal na nekk ci moom gën jaa selli xéewali Yàlla,

nekkoon na di aji-dem, dikkal na ko waay. Mu ne ko : “Alku naa yaw ngën gi Yonent bi”.

1
Boo jëfee te sukkandikuwoo ci Yàlla, Yàlla dalay bàyyi ak jëf ja.
2
Bés-pénc
3
Ay sikk
4
Dangay jëf te jëmmi Yàlla rek tax. Bañ di wax lii ak lee tax may jëf.
5
Bëraanaa ag jaamu mooy dana faral di bari ay jaamu
6
Yéem sa jëf
7
Ginnaaw fàddoom mooy ginnaaw bi mu demee.
8
Aw fen
9
Ku bëgg a wax ne bu fi teewoon ma wax ko ko.
10
ñetti yoon

17
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Mu ne ko : “Lu tax?” Mu ne ko : “Naka man njaaloo naa te mbir mi muy aji-sëŋewu1, cig tey tukkee ci
man”.

Mu ne ko : “Wool nit ñi ñu jam la”. Topp mu woo leen ñu rey ko ngir dana jublu.

Ginnaaw ba, topp na ko [moom Yonent bi] ñaari waay, ñuy jëw ñoom ñaar waa ja ñu jam,

ba dikkal leen ñoom ñaar méddu mbaam, taxaw na [moom Yonent bi], mu ne : “Yéen ñaar ñii lekkleen
méddu mbaam mii”. Mu giñ:

“Naka man danaa gis, moom waa ji, muy diri ca Àjjana ay yéreem”. Ñu geccewu ñoom ñaar.

Mbañeel fa yile tànneef mooy sag mbañ ab jullit ci lu dul sabab.

Dana waral ag mbañeel ci yoonug ka ñu tànn ka, yal na Yàlla dolli xéewal ci moom topp mu teral ko.

Gis ngëneel2 ci keneen, njaaloo, reetaane3 ak fo; ñaaw na ñaawtéef.

Képp koo xam ne ma ngay gis ngëneel ci xaj, xaj bi sax moo ko gën ci lu dul sikk.

Ngir naka cosaanug képp nit mooy Aadama, te moom mi ngi tukkee ci banub suuf ; xamleen

Déet ngay gën, yaw sama mbokk, ci kenn ngir réere la nga xam ne danga ca mujj ëllëg.

Feeñal ag màggal ci jublug ŋàññ tudde na ko, ñoñ xam-xam, reetaane4.

Dëgg-dëgg po mooy mépp po mom tere na ko yoonu Yonent bi.

Waaye am na ci po muy aji-dagan, am na ci moo xam ne askanaleef na ko jëm cig sibéel, am na ci moo
xam ne soppeef na ko.

Aji-daganam mooy kaf ànd ak ug xarit ci dëgg5; déet leneen ci dëgg-dëgg.

Gu ñu sibam mooy baril ko ag baril; ngir naka moom dana sànk fan ya.

Lu ñu soppam mooy fo ak sa soxna mbaa ak sa doom ju di ju ndaw; bàyyil caay-caay.

Daganal nañu po ci bant fett, niki nii ci sab xaj ak fas; xamal jàppukaay ba.

1
Am naa soxna
2
Jàpp naan diw de maa ko gën
3
Ndax Alxuraan nee na bul ree kenn ndax mën naa am ki ngay ree moo la gën .
4
Ci misaal nekk ci mbooloo, jëmm egsi nga naan kilifa gi ñëw ne de. Fekk ku xeebu la. Fekk ñu ree ko nga ci jublu.
5
Ci misaal, Yonent (SAW) danoon kaf ak bàjjenam, ne ko Àjjana màggat du fa dugg. Bàjjen ba yékkati loxo yay yuuxu. Mu
ne ko Yàlla moo wax ci Alxuraan, Àjjana màggat yi dañu leen di defaat ay ndaw.

18
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Araam na mu xool jaambur bu jigéen1, niki nii di bànneexu ciy waxam; bàyyil lii ak lee.

Ak lekk alali nit ñi, fas way-xam ña ci lu dul teeyug bakkan, araam na ba-tey.

Ak loo xam ne fiiróonte na ak moom te wooyeef na ko ci ag lekkam ngir bari kersa2.

Tere nañu ba-tey, jële ca aji-xereñe ja, Amsa ak Lamsa cig araamal.

Amsa mooy ayibal ci jungug bët yi3, Lamsa dana nekk ci làmmiñ4; ràññetleel yaw aji-xel-lu ji.

Lekk alal ci turu diine5 ak ci rammu6; niki nii yéexe jëfi topp Yàlla.

Ñi yées ci mbindeef yi ñooy ña nga xam ne danañu jàpp, ci turu diine, ay alal te ñu koy lekk.

Seeni biir ya danañu nekk niki ay njéende ëllëg ak niki ay néeg ci lu dul nar.

Danañu dox, jiit ya ànd ak jaan ya, ca biir, ànd ak ug mbugal ci lu dul dee.

Dana loru képp ku nekk Safara ci xetug seeni biir ndeem ngelaw la dana gaar.

Déet di ko ñeel ànd ak ub kàccoor, du càggeenu jaxasook moom ñeel lu dul lor gog joyal nañu ko.

Koo xam ne dana ànd ak ñoom fii ci àddina ci seen tedd-nga joojee, dana nekk di aji-bokkaaleek ñoom
ëllëg ci seen toroxte.

Teetleen jaxasook ñii, ngir jaxasook ñoom bokk na ci gën jaa boni yëf.

Waaye mudaaranteek7 ñoom nag soppeef na ko, niki la saxee cib yax ci addiis.

Ab dayoom mooy gërëmloo leen ci loo xam ne tereef na ko8; muy lu ñu sib9 waxal mbaa lu araam.

Yellul10 ndare ñeel aji-xam, ku di aji-mat, koo xam ne nekk na di aji-maandu te du jeng.

Aji-xam ja tey aji-jeng, déet muy yell ci moom, am kemam aji-réer ji ba-tey; nanga yewwu.

1
Mooy koo xam ne araamu la te du sa soxna. Xool bu njëkk bi moom mëneesul a koo tere. Xool a ka xoolat lañuy tere.
2
Ci misaal, nga fekk ñu taaj añ bi, bay raxasu bay tàmbali, nga ne jaas. Ñu ne “Sëñ bi Bismilah, ñëwal añ”, te xolam seddu
ca. Nga daldi ñëw lekk ba ndab la jeex. Loolu araam na. Ndax woo gi day aada te menuñu laa xool te woowu ñu la.
3
Niki yaa ngi koy piis.
4
Niki di ko mbëllee.
5
Lekk alal ci turu diine. Niki ne dangay tabax jàkka. Ñu jox la ca alal nga lekk ko.
6
Niki boo ma joxee nàngam maa la warlul Àjjana.
7
Maslaak ñoom
8
Buleen defal lu la yoon tere.
9
Lu ñu sib mooy loo xam ne boo ko bàyyee am tuyaaba boo ko defee mu wàññi yool ba.
10
mudaarante

19
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Déet di ko ñeel sàkku ngërëmal mbindeef ci sànjab1 Aji-màgg ji kay bind mbindeef yi.

Yàlla ak Yonent bi ñoo gën a yey ci ñu gërëmloo mbooleem way-gëm ñi ci jamono.

Dikk na ci waxi Ahmad ka di ku ñu darajaal, yal na dolli xéewal te musal ko ci wépp waxtu

Aji-yónneem [Yàlla], ak i ñoñam, ak i saabaam ak bépp aji-gëm ci moom ci kurélam ga;

Addiis: Déet ag topp ñeel ku ñu bind ci moy Aji-bind ji; kon matalal kóllare ga.

Wax naa2 : “Ku sàkku ngërëmal mbindeef yi ci sànjab Boroomam, ab dof la, kuy boroom ngëmment.”.

Déet di la jariñ ngërëmal mbindeef ndeem gërëmloowoo sa Boroom; jengal wëliis lee jëm ci lii.

Déet mu lay lor, ndeem gërëmloo nga sa Boroom, sànjab koo xam ne moy na ñeel ko.

Jëf lëf njëkk muy xam la nga xam ne Boroom asamaan àtte na ko ca, muy lu ñu joyal3,

bokk na ca la nga xam ne araam na ci mukkàlaf; jiitalal ag xamlu cig jaamu.

Te nekk na ca téere ba: “Laajleen woroom xam-xam yi”; texe ñeel na ku yittewoo xam-xam, di boroom
gëstu4.

Ku futtiku ci topp Aji-màgg ja, njëkk ag xamlu, ab dof la te déet di aji-xel-lu.

Kuy xamlu ci lu dul aji-xamle gu di aji-dëggal, naka moom boroomug deflewu5 la.

Farluleen ci xam-xam yéen mbokk yi ak topp Kilifa gi ci lu dul yéexe.

Koo xam ne faat na xam-xam ànd ak topp ya, fasetnaa xam lu ko naqari fa faatu ga.

Na roy, moom aji-jaamu ja, ca way-topp ya sunnas Yonent bi Ahmad kay ku ñu wóolu ka.

Aji-rammu sunu; yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko ak képp koo xam ne méng na ko.

Mooy ñiy digle topp Aji-yërëme ja te di wattandikuloo topp séytaane yi.

Teetleen bànneexu bakkan ak topp biddaa te ngeen soxlawoo, ci bépp jamono, topp sunna.

Ngir dajaleef na yiw wépp ci topp sunna te dajaleef na ay ya ci topp biddaa.

Saxleen ci tàggat bakkan fàww ak xareek Séytaane ak ug rëbbu ag njub.

1
Merum Yàlla.
2
Moom Ahmadu Bàmba
3
Xam la ca àtte yoon.
4
Siyãs
5
Mooy boroomug njuumte.

20
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Nangeen bañal, ñeel seen bakkan yéen aji-xel-lu yi, loo xam ne gërëmloo na ko ñañu fàllas1 ñi, ña diy
way-ñàkk.

Ñooy ña nga xam ne sànk nañu seeni fan ci moy Yàlla te déet di leen ñeel ku leen di tinu2.

Yéemal seeni jooy ànd ak réccu ga bés-pénc ànd ak yeddeel ya.

Dëgg-dëgg fàllas, ca ka nga xam ne gëstu na, mooy mu dikkal jëmm ja ci jëfi yiw ëllëg;

niki koor, dox mbokk, julli, aj, umra ak asaka.

Waaye nag xas na waa jii, lekk na alali kii te rey na bakkanu nit kii.

Delloos na, jële ci moom, lépp loo xam ne jëf na ko jëme ca ña nga xam ne jëf na, ci ñoom, la nga xam
ne jëf na ko.

Mu mujj di aji-ñàkk ginnaaw lii, te setaleefu ko ciy bàkkaar; topp jëleef na ca ña mu tooñoon

la nga xam ne tooñoon nañu ko ciy bàkkaar fii ci àddina, jëme ko ca waa jooju ngir mu dolli ko ca la
mu tooñoon.

Mujj na aw yenam di aji-galfan3, déet di ko ñeel kem fatiil, ginnaaw ba ñu noccee la ko ñeeloon ciy
yiw.

Dees na ko màng, ginnaaw lii ci lu dul yéexe, ca mbugal ga ca Safara.

Niki nii tuxal nañu ko jële fa kilifa4 ga; yal nanu Yàlla musal ci fàllas.

Danaa ñaan Aji-yërëme ja kay sunu Boroom di Aji-màgg, yéem naa ag sellam, dëppook sunnas Yonent
bi,

Muhammad sunu soppe, sunu sang, aji-rammu sunu, kay sunu yaakaar te di sunu yonent.

Yal na dolli xéewal ak musal, ci moom fàww, Boroom asamaan ak koo xam ne gindikoo na ci moom.

1
Ñañu “saisir” ci làkku faranse.
2
Rammu; ndax Sëriñ Tuubaa nee Bés-pénc dangay doon ku ñu rus, mbaa nga ànd ak ku ñu rus mbaa nga rus.
3
diis
4
Laxdari

21
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

22
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

I.1 AB DOG CI LAAB


Niki laab mooy laabug toj1 ma, ci lu dul ag wuute ak laabug sobe2 sa;

Képp ci ñoom ñaar ci ndox lay doon mu di aji-laab tey aji-laabal, dina yéwénal fa aji-ñaw ja;

Moom mooy la nga xam ne ag ñoŋam3 soppikuwul; li mu ci jublu mooy cafka ga walla xet ga walla
melo wa;

Ci loo xam ne dina tàqalikook moom (am ndox) cig mbaax, niki ag ñaay4, ak ug nékk, ak loo xam ne
niki sarniix5, nee ma waaw;

Ak tilim, ak diw, ak lu deme ni saabu, ak diw-ñor, waxal ak luy nuru yii ma lim, waxu ma nag ban,

mbaa cepp6, mbaa ceeñ7, mbaa suufus kese, mbaa mbaalaa-mbaalaamum8 ndox, ci lu dul sikk;

I.1.1 DINDI SOBE AK LI CI AJU

Ndeem sobe si ràññeeku na, raxaseef ko te jaamu ci lu ñu boyalum ndox, barab ba;

Waaye nag mbalaan ma dees na ko fóot cig matale, ndeem lënt na, sobe sa, yaw waa ji;

Wis ga, cim ndox, dana war ndeem sikki-sàkka nga ci dalug9 sobe sa, xeeñtul;

Nekkul di war ci koo xam ne sikki-sàkka na ci sobees aji-jot10 ji ag wis, xamal.

Koo xam ne fàttaliku na ci jamonoy julli sobe, na dog julli ga ci lu dul werente;

ndeem nekkul di ragal mu génn ci waxtu julli wa, déet ag dox ca boobee11.

Koo xam ne jullee na ak sobe ngir ug fàtte gog daw na, te mu fàttaliku ko gannaaw sëlmal ga;

naka moom dana baamu la mu julli woon ci waxtoom12, ci dëppook way-jiitu ña.

1
Luy waral jàpp
2
Luy waral sangu
3
Ni ko Yàlla bindee woon ( “nature” ci làkku faranse)
4
Diw gu nekk ci kaw
5
Lu ñuy gase ci suuf la (mooy “Arsenic” ci faranse).
6
Sooy mooy soie ci làkku faranse.
7
Suuf su jaxasook xorom
8
Mooy lu nëtëx looloo di nekk ci kaw ndox mi (nawet lay gën a bari)
9
Dangay sikki-sàkka ndax sobe si dal na la am déet. Waaye wóor na la ne sobe la.
10
Xamoo ndax li la dal sobe walla déet.
11
Ndax dañu ne dab waxtu moo gën dab ug laab.
12
Bu dee waxtu wa nga doon julli moxtaar mi jàll na, doo ko baamu. Bu jàllul nag nga sol mbumb mu laab te baamu ko.

23
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.1.2 FARATAY1 NJÀPP

Limu faratay njàpp xamees na ko, waxal juróom-ñaar fa kilifa ga di Laxdari;

Yéene, raxas xar-kanam, ak loxo2 ba ci tikk-jara ya ak masaa bopp, xeeñtul;

Raxas ñaari tànk ya ba ci ñaari dojor ya, gaaw ak ragg; ci lu dul nar;

I.1.3 SUNNAY3 NJÀPP

Topp dikk na sunnaam ya di juróom-ñett; sag raxas loxo4 ba ci tikk-jara ya; nekkal di aji-wattu;

fa sag tàmbali doonte nekk nañu mbooleseen di way-laab itam; xeeñtul ka wattu xam-xam

Gallaxndikul, niki nii saraxndikul, niki nii fiirul; te nga delloo ag masaa ñeel sa bopp, limal masaa
nopp;

Nanga yeesal ndox ma ñeel ñaari nopp ya mbooleseen; te nga toftale farata ya, kon danga nekk di aji-
topp.

I.1.3.1 LU AJU CI FÀTTE FARATA CI CËRI NJÀPP

Koo xam ne fàtte na farata ci cëri njàpp ya, àtteem ci loolee ñaari àtte la, wattul.

Ndeem nekk na di ko fàttaliku cig jege, na ko def ànd ak la nga xam ne daw na ca ginnaaw5.

Ndeem nekk na ginnaaw yàggug jamono, na ko def ci yéene6; nanga sonne.

Waaye nag war na ko mu baamu la nga xam ne julli woon na ko cig njëkk7, ngir ug laab ñàkkeef na ko.

I.1.3.2 LU AJU CI FÀTTE SUNNA CI CËRI NJÀPP

Ndeem bàyyi nga sunna, yaw waa ji, dikkeel ca sunna sa ngir la nga xam ne def nga ko jublu ciy jaamu
Yàlla8.

Doo baamu la nga xam ne wéyoon na te mu faat, ngir naka moom [sunna] du yàq julli.

Ndeem fàtte nga ag déngléere9 ca yaram wa; raxas ko moom doŋŋ ànd ak yéene ca boobee.

1
Farata mooy loo xam ne boo ko bàyyee, li ngay jëf du baax. Kon moom mënt a ñàkk.
2
Waxuñu jàppukaay bi waaye cër bi nekk diggante conco bi ak tikki-jara bi.
3
Sunna mooy lu Yonent bi def, lu mu wax, lu mu digle mbaa lu ñu def ci kanamam te waxu ci dara.
4
Jàppukaay ba.
5
Bu fekkoon raxasutoon loxob càmmoñ bi, da koy raxas, raxasaat la ca sësoon lépp.
6
Cër ba doŋŋ lay raxas. Du raxasaale la ca sësoon lépp.
7
Bu fekkee njàpp moomee nga xam ne da cee am cërug farata bu mu raxasutoon, dafa jotoon a julli, day baamu julli ya mu
ca julli woon yépp. Julli, jàpp mënu caa ñàkk, te njàppam lii matul.
8
Boo jàppee, fàtte cëru sunna, ba julli ca. Boo ko fàttalikoo doo fey julli ga waaye dangay raxas cëru sunna boobee rek.
9
Ci misaal ab yaatu-yaatu ci loxo bi.

24
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Topp war na nga baamu lépp loo xam ne julli woon nga ko njëkk ag raxas woo xam ne waraleef na ko.

Ndeem fàttaliku nga sunna ginnaaw sag tàmbali ci xar-kanam wa, niki saraxndiku, déet ag dellu

njëkk ag matal1 [raxas xar-kanam wa], waaye nag yaw cam si, nekk na ci loolee wuuteek2 boroom
xam-xam yi.

I.1.4 NGËNEELI3 NJÀPP

Ndaal ay ngëneel ñeel (njàpp), mooy nga wax Bismilaah4; ginnaaw ba mooy nga soccu, soril moy ga;

Limees na ag raxas gog dikk na di dolliku ci raxas gu njëkk ga, muy ngëneelug jaamu;

Jublu naa ci xar-kanam ba ak ñaari loxo ya, niki nii toftale ga, ci lu dul nar;

Tàmbali ci li ñu jiital la, la di la ñu baaxoo; cig masaa bopp cig digg-dóomu;

Ak néew ug ndox ma ci cër ba niki noonu; jiital sa ndijjoor ca càmmiñ ba, jàpp ko;

Xaliilal baaraami ñaari loxo yi ci lu war, dees na ko sopp ci ñaari tànk yi;

Waral nañu xaliil cib sikkim buy aji-woyof ba-tey, waxuma aji-fatt ja;

Jublu naa5cig njàpp; ndaal cangaay nag moom, dees na ko waral ci ñoom ñaar, ci la nga xam ne dana
feeñ;

I.1.5 WAY-FIRI NJÀPP YI

Way-firi njàpp dikk na di ay toj-toj, jële fa ñoom sëriñ sa, ak sabab yoo xam ne mën na faa jaare ba toj;
ci li nga xam ne sax na.

Ay toj-tojam mooy am ngaanuwaay, ngelewal, masyu6ak dem ginnaaw-kër ba-tey, niki nii wadyu7.

Ay sababam mooy xëmte, nelaw yu diis8, màndite9 ak say; wattul yaw aji-xel-lu ji.

Fóon ak bakkan mbaa ak gémmiñ, bokk na ci way-firi jàpp yi; ci waxi sang ba.

Laale jigéen pëyam niki nii, ci sàrtul lunkal baaraam ba; sàmmanteel ak jàppukaay ba.

1
Kenn du bàyyi farata di dem ci sunna
2
Am na ñu ne dangay dellu ci sunna sa door a eggali farata ba.
3
Ngëneel (lu ñu sopp) mooy loo xam ne boo ko defee am tuyaaba, boo ko bàyyee deesu la wax dara.
4
Bala ngaa tàmbali
5
Xaliil googu
6
Mooy ndox mu weex moomu di génn ci sàkkaras kuy xalaat jigéen
7
Ndox mu weex la moo xam ne ginnaaw am gaanuwaay lay génn.
8
Mooy ngay nelaw yore dara ba mu rot te yégoo ne rot na, mbaa ay nit jaar ba jàll te yégoo ko, mbaa ngay nelaw ba yuut te
yégoo ko
9
Ci lu araam (niki sàngara) mbaa ci lu araamul (niki am soow)

25
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Sag laal jigéen ndeem jublu nga ca bànneex, walla jubluwoo ko ci te am ko ca.

Niki nii laalug sàkkara yaw sama àndandoo ci sa biir baaraam walla sa biir ténq.

Aji-wóolu cig laab waaye sikki-sàkka na ci toj mi, waralal ci moom njàpp; ca la nga xam ne gëstu na.

Ndeem nekkul di aji-jax-jaxal, kuy aji-yàqum xel, déet ag baamu ci moom; mbir mi muy lu ñu joyal.

Waral na ñoñ-siyãs raxas sàkkara sépp ngir masyu, ci lu dul ñaari waayàlla yi.

Masyu, am ndox la muy génn ci sag xool jigéen ngir bànneex bu ndawe ak ci sag xalam1 jigéen.

I.1.6 LEES DI TERE AG JËFAM CI LU DUL AM NJÀPP

Déet di ñeel, ku dul aji-jàpp, julli; du caagéenu wër néegub ka nga xam ne dina méngale xéewal ya.

Niki laal ab kaamiil, waxal aw der la ñeel ko, ci bant walla ci mbalaan walla lu nuróok loolu.

Waaye laal ab xaaj, ci ka nga xam ne xamlu na ci moom doŋŋ, daganaleef na ko fas way-xam ña.

Àlluwa niki kaamiil ñoo yem ci araamal ga ñeel ku dul boroomug njàpp yaw sama xarit.

Waaye nag dana dagan, ñeel ka nga xam ne dees na ko xamal, ag laal àlluwa, niki nii aji-wér, kuy aji-
xamal.

Laalug gune yi ànd ak sobe, mi ngi mel ni laalug mag ñi ci moy ga.

Bàkkaar ba nag war na aji-jottali ja; bul nekk aji-jottali (ab kaamiil) yaw aji-laaj sama.

Koo xam ne dina julli ci lu dul ag laab, ci lu dul lor, boroomug caay-caay la bob feeñ na.

Déet di ñeel ko ci boobule tiim Bés-pénc lu dul Safara.

Yal na Yàlla musal nu ci peert ak ayi Ibliis diirub jamono.

1
Xalaat

26
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.2 AB DOG CI CANGAAY

I.2.1 ÀTTEY CANGAAY, WAY-WARALAM AK LA CA AJU

Dana war, ngir ñetti yëf ya, cangaayul farata; ci lu dul werente.

Li ma ci jublu mooy janaba, mbërëg ak deretu meret ju dog. Ndaal janaba ci ñaari xaaj dees na ko
xiyaas.

Bu njëkk ba mooy génnug maniyu tukkee ci góor ànd ak bànneex, bu di bu ñu baaxoo; nanga xel-lu;

Ci nelaw walla yewwu ci ànd ak jigéen, mbaa lu dul lii tukkee ci sawukaay ci ndajeem boroom xam-
xam yi.

Ñaareel bi mooy fàddug boppu sàkkara cim pëy, doonte ci lu dul génne am ndox la; xamal.

Nekkul di war sangu koo xam ne aji-gént la ciy nelaw, waaye dara génnut tukkee ci moom.

Koo xam ne dana fekk ci mbalaan ma aji-wowi maniyu, te nekkul di xam waxtu jotug maniyu ba,

na sangu te baamu la mu julli woon tukke ci nelaw yoo xam ne nekkoon na ci moom boroomug
yàndoor.

I.2.2 FARATAY CANGAAY

Ndaal farata ya, bi ci njëkk mooy yéene1 fa ag tàmbaleem, gaaw2 ak jonj; feeñ na.

Topp ag matale ñeel mbooleem yaram wa ak ndoxum kese3 ak rombale loxo ba.

I.2.3 SUNNAY CANGAAY

Sunnaam ya kem farata ya dees na ko lim muy ñeent tamit, ca ka nga xam ne gëstu na4.

Sag raxas ñeel ñaari loxo yi ba ci ñaari tikk-jara yi, kem sag njàpp; ci lu dul nar.

Galaxndiku njëkk ngay saraxndiku ak masaa ñaari nopp ya; ci lu dul ŋaayoo.

Li ma ci jublu mooy sa bën-bënub nopp ci kasrag saad, moom bën-bën la bu di aji-feeñ ci sa bopp.

Te bagaanug ñaari nopp ya, raxas la nga xam ne feeñ na ci ñoom ak la ca biir ba; dees na ko xalaat muy
lu war.

1
Buy raxas xar-kanamam lay yéene.
2
Mooy bu raxasee cër, balaa wow mu raxas ba ca topp.
3
Ndoxum kese dees na woowee it nodxum mutlax.
4
Xam-xam

27
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.2.4 NGËNEELI CANGAAY

Ndaal ngënnéel yi, jëlal ab lim seen, wax Bismilaah naka la wéyee woon; ginnaaw ba.

Nga tàmbali deñal sa sobe, topp ag raxas ñeel sa sàkkara; danga yéene farata foofee.

Topp nga tàmbali cëri njàpp ya ci benn-benn njëkk gën jaa kawe yaram wa.

Nga ñetteel bopp ba ci ag raxas, te nga tàmbalee ndijjoor ci càmmoñ ba.

Gënëlal néewal am ndox ci lu dul ab dayo ci cër ya ca raxas yaram wa.

Képp koo xam ne fàtte na ab déngléere1 mbaa ab cër, na nekk aji-gaawe ñeel raxas ga; nanga xiyaas2.

Topp mu baamu ca boobee lépp loo xam ne julli woon na ko njëkk ag raxasam; ngir waraleef na ko.

Ndeem nekk na aji-yéexe raxas ga fas bam ko fàttalikoo, loolee yàqug cangaay la; dana gaar.

Waaye dana ko doy fiiroo3raxasam njàppam ci lu dul wuute.

I.2.5 LUY DOLLIKU CI JANABA CI TOJ MA GËN A NDAW

Daganul tàbbig jàkka, du càggeenu jàng Alxuraan ñeel aji-janaba; déedéet.

Ndare ab laaya mbaa ñaari laaya ngir ag muslu ci lu dul nar.

Tere na bépp aji-xam tey aji-jaamu ñeel aji-lott wëliis laal am ndox mu sedd;

Muy dikke4 soxna sa ndare gannaaw bu mu xaroo jumtukaay bob dana tàngal ci moom ndox ma5;

Waaye ndeem gaar na ko gént, déet di war ko ginnaaw ba ay yeddeel.

1
Diggante boo raxasul
2
Yaay xam déngléere mbaa cër ba mu doon
3
Bi ngay sangu ci misaal, raxasoo loxob cammoñ bi, li tàmbalee ci conco bi ba loxo bi jeex nga raxasutoon. Bi nga ko
fàttalikoo, sam njàpp toj, nga ne naa far jàpp. Boo jàppee raxasaale ko, day mel ni raxasaale nga ko ci cangaay la.
4
Dikke soxna sa mooy séy ak soxna sa.
5
Ku ragal ndox mu sedd, balaa tëdd ak soxnaam, na ut lu muy tàngalee ndox ma ba bu noppe mën a daldi sangu.

28
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.3 AB DOG CI TIIM
Aji-tukki juy dox ci lu dul moy Yàlla, ñeel na ko tiim ci jamanoy dox ga.

Am kemam aji-feebar ju góor ak aji-feebar ju jigéen ñeel bépp julli naafila mbaa farata;

ak aji-teew tey aji-wér ngir farata, ndeem ragal na génnug waxtu wa ngir ngànt, kii;

Waaye nag déet naafila1 walla julli jumaa2, déet ab néew itam goo xam ne ràññikuwul3; xel-lul.

I.3.1 FARATAY TIIM

Limu faratay tiim xameef na ko muy juróom-ñett fa aji-dégg fiq ja kay kojug Laxdari.

Yéene, topp pàkk bu laab, ak ub dóor bu njëkk ànd ak fëgg goo xam ne digleef na ko.

Niki noonu masaa sa xar-kanam ak ñaari loxo ya tukkee ci baaroom ya ba ci tikk-jara ya.

Ak gaaw, tàbbi ci waxtu wa; bokk na ca jokkale ko ci julli ga.

Ndaal pàkk ba mooy suuf, ban mbaa doj4; buleen sikki-sàkka,

nees5, ban buy rémbi-rémbi6; dikk na ci tuxal ga; ak luy nurook moom niki suufas ceeñ7 ak beeñ8

Daganul tiim ci ay bant, ak palaatar bu ñu togg ci waxi tànneef ya.

Ak ag basaŋ, ak ñax mu sax ak luy nurook moom ci bépp gàncax gu sax.

Ndeem feebar nga, fa làkkub doj mbaa ban, ba lor ja gàllankoor saw yaram;

te amoo koo xam ne dina la indil suuf ; ñeel na la nga tiim ca yooya; ca yolomalug Yàlla may
Jéggalaakon.

1
Koo xam ne tukkiwul (aji-teew) mayuñu ko mu tiimal ñeel naafila gu beddiku. Su amut am ndox na bàyyi naafila ga.
2
Ajjuma, tisbaar mën na koo wuutu boo amul am ndox.
3
Sañta tiimal jullee néew bu ràññikuwul. Maanaam mennum moom doŋŋ nga ko fi mën a jullee te amutum ndox.
4
Doj boo xam ne na ko Yàlla bindee woon la mel
5
“neige” ci Faranse
6
Ban bu ànd ak ndox
7
Suuf su jaxasook xorom
8
Suuf su amul pënd

29
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.3.2 SUNNAY TIIM

Sunnaam ya ñett lañu ndeem danga koo lim. Bi ci njëkk mooy yeesal dóorub loxo ba,

masaa diggante tikk-jara ak coñc; topp ñetteelu sunna ya mooy toftale goo xam ne dana matale.

I.3.3 NGËNEELI TIIM

Topp ngëneel yi dees na leen lim ñuy ñeent, bi ci njëkk mooy nga wax Bismilaah; nanga dégg.

Te nga jiital ndijjoor ba ci càmmoñ ba niki ci leneen lu dul moom, jiitu woon na ngëneel.

Niki nii, jiital bitib xasab ba ba-tey ci biiram ba wëliis xëccoo.

Nanga jiital la ñu jiital1 ca cër ya ca la ñu mujje la ci lu dul sette.

I.3.4 WAY-FIRI TIIM YI

Ndaal way-firi tiim mbooleseen niki li ñu jiitaloon ci njàpp2 la; mbir mi muy lu ñu boyal.

Ndare ngir am ug ndox njëkk tàbbi ga ca julli ga; déet gannaaw ba; naka la ko yaxale aji-xel-lu ja.

Fóore ja nga xam ne wattu na fiq tere na ñaari farata yoy booleef na leen ci benn tiim.

Waaye nag ay naafila yu bari dagan nañu ca benn tiim ba, ndeem yéeneef na ko; yewwul.

Ka nga xam ne tiim na ngir farata, dagan na ñeel ko ginnaaw ba naafila; niki

mu ko ñeelee jàng Alxuraan, wër Kaaba ga, laal Alxuraan ci lu dul wuute;

Ci sàrtu yéene ànd ak jokkaloo ak tàbbig waxtu wi ci méngale ga.

Ndeem tiim nga ngir naafila, nanga daganal ci moom mbooleem loo xam ne tudd nañu ko ci woy wi.

Lu dul farata, ngir naka moom tereef na ag toggaleem3lu dul moom ci loo xam ne yoonaleef na ko.

Koo xam ne tiim na ngir faratay gee, dagan na ñeel ko safaak wittar ginnaaw ba; nanga dégg.

Ci sàrtul mu nekk di aji-jokkoloo ci lu dul yéexe; naka la wéyee woon cig njëkk.

Ndeem tiim nga te aji-janabu nga, waral nañu ci yaw nga yéenewaale ko

Ndeem bàyyi nga ko, moom yéene ja, ca tiim ba, nanga baamu julli ga wëliis defle.

1
Cër bi, li ci jiitu ngay njëkkee. Bu dee loxo bi, ci cati baaraam yi ngay tàmbalee. Bu dee kanam gi, ca kaw ngay tàmbalee.
2
Lépp lu doon firi njàpp day firi tiim.
3
Soo tiimalee lu dul farata, boo noppee doo ca mën a sësale farata.

30
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.4 AB DOG CI MBËRËG, DIIR BA AK LA CA AJU
Mbërëgi jigéen, cig séddale, ñett lañu, ndeem lim nga ko, ca lu ñu xam la.

Boroomug tàmbali, ginnaaw ba aji-baaxoo ak aji-ëmb kok dana yaakaar ci moom njariñ1.

Gën jaa bari mbërëg ñeel boroomug tàmbali, fukki fan ak juróom la ciy bés fas ku ñu roy ka.

Ndaal koo xam ne baaxoo na ci mbërëg njëkk lii; loolee aadaam mooy loolee; jàppal.

Ndeem deret ja wéy na ci moom, na dolli ñett ciy fan; bul jeng.

Li feek jéggiwul loolee fukki fan ak juróom ciy bés; déet ug dolli foofee, xamal.

Gën jaa bari ñeel aji-ëmb gannaaw ñetti ciy weer, limal fukki fan la ak juróom ciy bés;

ak luy nurook ñetti weer; gannaaw juróom-benn ciy weer, ñaar-fukki fan la ciy bés; limam ba xameef
na ko.

Digal ko cig tàppe2 ngir mu matal aadaam ndeem ag dog am na.

Daganut jullig aji-mbërëg, du caagiinu wër kaaba ga ak laal kaamiil; kawe na.

Déet di ñeel ko ba-tey koor ci lu dog, niki gog farata ak gog ngàttanga; dëggëlal.

Déet di ñeel ko ba-tey tàbbi jàkka, doonte daa nekk ci këram; ca la ñu sukkandikoo3 la.

Waaye fey koor ga gannaaw laab ci lu dul julleem ga war na ko; xamal.

Daganal nañu jàng Alxuraan ñeel aji-mbërëg ngir ragal fàtte.

Daganul ñeel boroom këram mu joteeg moom ci pëy cig tey mbaa njuumte.

Déet di ñeel ko li nekk diggante jumbag ñeel ndaw si ak bëtu-wóom; ba ba muy matal cangaay la.

1
Koo xam ne ëmb ba baax na.
2
Bu dog amee, bés yi mu gis mbërëg lay waññi.
3
Ci Imaam Maalik

31
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
I.5 AB DOG CI DERETI MERET AK LA CA AJU
Feeñ na niki mbërëg cig tere ga ci dereti meret1; gën jaa bari juróom-benni fukki fan la; limeef na ko.

Dees na ko digal ci sangu ànd ak julli ndeem feeñ na ag dog ag njëkkam2; naka la miineef na ko.

Ndeem baamu na ko deret ja te mu nekk diggante ñoom ñaar3 fukki fan ak juróom mbaa gën jaa bari;
feeñ na.

Aji-ñaareel ba ci ñoom ñaar dana nekk mbërëg, mu di aji-sosu fas aji-dégg fiq ja ba-tey4.

Ndeem nekk na diggante ñoom ñaar lu yées fukk ak juróom ciy bés, dana war kon tàppe5deret ju yees ji
ñeel ju njëkk ja.

Topp ndeem xool na nag ca nattale ga, fekk nga ko muy aji-matal ak wësin6.

1
Lépp loo xam ne tere nañu ko ku gis dereti mbërëg, tere nañu ko ku gis dereti meret.
2
njëkk matug lim ba
3
deret ja daggoon ak deret ju bees ji.
4
Ci misaal dafa am doom, di gis deret ba mu yàgg deret ja dagg, toog lu mat 15 fan mu door a delsiwaat. Kon la delsiwaat
duñu ne ci meret ma la bokk. Waaye deretu mbërëg la mu sosu.
5
Maanaam dangay boole lim bii ak bu njëkk ba
6
Bu deret ji daggee, matul 15 fan mu delsi, dangay waññiwaat li nga mujje am ak la nga njëkk am. Niki nii buy daggi-
daggee daal, kon bés yi muy gis deret lay waññi. Bu matee 60 fan mu xam ne meret mi jeex na.

32
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

II.1 AB DOG CI JULLI

II.1.1 XAM WAXTU JULLI YI

Waxtuy julli dana séddaliku ñeel waxtuw moxtaar1 ak ñeel kojug darooriyu2 fa fóore ya.

Moxtaaru tisbaar tukkee na ca jengarñiku3 jant bi ba ci mujjug taxawaay4 ba, wëliis ab lënt.

Tàkkusaan, moxtaaram, tukkee na fa moxtaaram tisbaar yem jëm ba ca waxtuw gelug suuf5 si, waxu
ma sow ug jant bi; xel-lul.

Ndaal darooriyu6 ñeel ñaar yii mbooleseen, ñeel na sow ug jant bi; fa ka nga xam ne wattu na.

Timis, moxtaaram ma, waxal kem loo xam ne dees na ko julli, ci moom, ginnaaw ab sàrt boo xam ne
xameef na ko7.

Niki suturaal awra8, laabug sobe9, njëkk nodd ak liqaam ak laabum toj10.

Topp gee, moxtaaram ma, tukkee na ca fàddug safax11 sa, ba ci ñetteelu guddi ga12, wattandikul.

Topp darooriyu13 gee ak timis, jëm na ca fenkug aji-dëgguy fajar ja, askanele ko.

Defal moxtaaru suba tukke ci moom [fajar su dëggu sa] jëm ci ag set gu di aji-kawe14 ñeel xar-kanam,
feeñ na.

Tàmbalig darooriyu15 tukke na ca set wicc googee ba ca fenkug ceeñeeru jantub Aji-maye xéewal yi.

1
Moxtaar mooy waxtu wi nga xam ne boo ci jullee doo am bàkkaar. Teewul julli ci njalbéenug waxtu moo gën.
2
Darooriyu mooy waxtu wi nga xam ne boo ca jullee, fekkoon nga amoon ngànt, doo ca am bàkkaar. Waaye boo amutoon
ngànt, boo ca jullee am nga bàkkaar.
3
Mooy bu jànt bi nekkee ci digg asamaan ba rëcc jëm sowu.
4
Mooy bu sa taxawaay tollook sa taxawaayu ker.
5
Mën nga koo nattee it: bu sa ker matee ñaari yoon sa taxawaay. Mbaa boo taxawee jublu sowu bañ a sëgg te bañ a téen, bu
say bët yemee ci jant bi rek xamal ne moxtaarum tàkkussan jeex na.
6
Darooriyu tisbaar ma nga tàmbalee fa moxtaarum tàkkusaan tàmbalee. Darooriyu tàkkusaan ma nga tàmbalee fa jant bi
tàmbalee xonk. Bokkuñu fu ñu tàmbalee waaye ñoo bokk fu ñu yem. Ña nga yem fa jant bi sowe.
7
Maanaam fu jant bi sowee, sàrt timis nga mën ko faa def, boo ko fa defee fa la moxtaaram yem.
8
Mooy sol mbubb
9
Niki sangu janaba
10
Am na ñu ne, xonk-xonk jant bi fu mu jeexee fa la moxtaarum timis yem. Ciy waxtu, 75 minit ginnaaw noddug timis.
11
Bu xonk-xonk jant bi wéyee.
12
Boo xaajee guddi gi ñetti xaaj, bu xaaj bu njëkk bi jeexee fa la moxtaarum gee yem.
13
Darooriyu timis ak gu gee ñoo bokk fu ñu yem. Waaye bokkuñu fu ñu tàmbalee. Darooruy timis a ngi tàmbalee fi
moxtaarum gee tàmbalee. Bob gee a ngi tàmbalee bu xaaj bu njëkk, bu guddi gi, jeexee. Boo xaajee juddi gi ñetti xaaj.
14
Boo xoolee jëmm xàmmee ku mu doon.
15
Darooriyu suba mi ngi tàmbalee bu bët setee wicc ba jant bi di fenk.

33
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Topp pey1 ga ci mbooleem waxtu yi, dina askanu ci ginnaaw yile waxtu fa Aji-àtte ji.

Askanaleel di aji-màggi2 bàkkaar ñeel aji-yéexe julli, ba mu faat ko, ci lu dul ngànt loo xam ne xameef
na ko.

Sibeef na, ginnaaw julli suba ba ca fenkug jant ba, naafila; waxu ma nag fey lu ñu fàtte3.

Ginnaaw tàkkusaan ba ca jullig timis itam, ak ginnaaw julli fajar4, fa jépp aji-xel-lu.

Waaye boroomug wird, dees na gis ag daganam ñeel ko, ndeem not na ngëmment5 ñaari bëtam.

Waaye naafila, ndeem ilimaanu àjjuma jekki6 na ca kaw minbar ba, xameef na sibéel7 doŋŋ.

Tere nañu naafila, ginnaaw àjjuma, ndeem génnul ilimaan ja ca jàkka ja; jàppal.

II.1.2 SÀRTI JULLI

Jeex na, wax ja ci waxtu yi; léegi nanu walbatiku jëm ca julli ga.

Ndaal julli, ay sàrtam mooy laabug am toj topp laabug sobe;

ca mbalaan ma, yaram wi, barab bi ak suturaal awra cig nëbbu.

Jublul xibla te nga bàyyi ay wax ak jépp jëf ngir déeyaaleek Yàlla may Musalaakon.

Awray góor, wëliis nar, mooy la nga xam ne nekk na diggante jumbux ak ñaari bëti-wóom.

Ndaal jigéen, mboolem yaram wa, dees na ko lim muy awra fas boroom xam-xam ba.

Ndare la nga xam ne setteef na ko ci ñaari ténq ya ak xar-kanam wa, ci lu dul bopp8 bi ak ñaari tànk yi.

Sibal nag julli ci tubëy ndeem dara nekkul ca kaw yaram wa; dees na la yool ca boobee.

Aji-sobewu ji mbalaan, ndeem ñàkk na am ndox ak mbalaan9 ginnaaw ag sàkku ñàkk na ko;

naka moom day julli ànd ak sobe sa, ndeem dana ragal génnug waxtu wa; ci waxi ka xàmmee [àttey
fiq]

Ndeem nekk na di aji-yéexe julli ngir ñàkk a laab, moy na Boroom xéewal ya.

1
Fey julli (Xadaawu) mooy julliwoo ko ca moxtaar ma mbaa ca darooriyu ja. Boo ko ca jullee nag, jooxe lañu koy tuddee
(Fadaawu). Du tee nga xam ne boo amul ngànt te julli ko ca darooriyu ja, jooxe nga waaye danga am bàkkaar.
2
Ku julliwul ca moxtaar ma ak ca darooriyu ja te amoo ngànt, xamal ne def nga bàkkaar bu réy a réy.
3
Fey moom amul waxtu. Saa yoo ko fàttalikoo rek, mën nga koo def.
4
Bu fajar ji xasee xar, ñaari ràkkay fajar rek lees la may nga naafila ko.
5
Niki naafila yoo doon def ci guddi gi, tey nga nelaw ba defoo ko ba ñu noddu fajar. Kon foofu, boo julee sa ñaari rakkay
fajar te julleeguñu farata ji, mën nga ko faa def.
6
Jekki mooy toog
7
Dañuy bañ naafila bu ilimaan ji yéegee ci minbar bi. Bu fekkee bi muy yéeg tàmbali woon nga naafila, danga koy gaawal.
8
Kawar gi bu ca dara feeñ.
9
Meneen mbalaan mu sobewul mu mu mën a sol.

34
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Koo xam ne amut, ngir ug rafle, loo xam ne dana suturaal ci moom awraam, na julli niki noonu; nanga
yewwu.

Aji-moy xibla ku ñu digal la mu baamu, ci waxtu wa, ag julli fu mu fu gaare1.

Lépp loo xam ne dees na ko baamu ci waxtu wa, waxuma lu dul loolu, naka moom ngëneel la; yal na
nga am ag nammeel.

Moom [ngëneel] kem naafila2 la, deesu ko baamu ndeem génnug waxtoom wa; wóoleef na ci lu wér.

II.1.3 FARATAY JULLI

Limu farata yi dees na ko xam, waaye sëriñ sa wuute nañu ca lim ba.

Lenn ca sëriñ sa tudd nañu fukk ak juróom ciy farata. Ñenn ñi tudd fukk ak juróom-benn.

Waaye, la nga xam ne Laxdari tudd na ko, danaa dikke ci moom ngir gone ga wattu ko.

Bi ci njëkk mooy sunu yéene3 ba di bu ñu ràññee, topp kàbbaram4ba di bu ñu biral.

Am kemam Faatiha5, topp taxawaay ba ngir digub yaar yii; naka la yaxale ilimaan ji [Laxdari].

Limal ab rukkoo6, topp yékkatiku tukke ca rukkoo7 ba, sujjóotal ci ab jë8 te nga yékkatiku tukkee ca
moom.

Limal, mu bokk ca farata ya, yemoo9; naka nii limub10 dal ga, jàppeef na ko jële fa ñoom [sëriñ sa].

Sunug toftale diggante farata ya, jëmmi sëlmal gi11, jotaayam12 ba tukkee ci Al ba ci Kum, yaw fere13
wi.

Sàrtub yéene14 fas way-xam ña, ak lëkkaloom15 ak kàbbaru armal bi.

Limub farata ya yem na fii, ca la nga xam ne Laxdari, kay aji-làq ji kawe ga, nettali na ko.

1
Bu moxtaar mi jeexul. Bu moxtaar mi jeexee nag wàcc na ko.
2
Bu waxtoom jàllee doo ko baamu. Niki naafila yoor-yoor, bu yoor-yoor jàllee doo ko fey. Ba mu des ñaari ràkkay fajar.
Waaye moom ba bu jant bi jengarñikoo.
3
Def sam xel li nga bëgg a def.
4
Kàbbaru armal mooy nga wax Allaahu Akbar (Yàlla màgg na)
5
Waaye ci ilimaan ak ku beru lay nekk farata. Lu ñu sopp la ci maamuun (aji-topp ilimaan).
6
Rukkoo mooy dangay sëgg, teg say loxo ci say bëtu-wóom, firi baaraam yi te dëgëral ko, samp tànk yi, ginnaaw ba day
yem kepp nga xam ne boo ca defoon ndox du tuuru jëm ca ginnaaw mbaa ca kanam., doo jatt loos wa itam
7
Mooy siggi ba taxaw jonn.
8
Sujjóot ci jë bi mooy farata, bu ci bakkan bi moom sunna la.
9
Mooy booy taxaw mbaa ngay siggi, danga koy def ba ne jonn.
10
Degg googu ngay def, say cër bañ a yëngatu ca taxawaay ba, ca rukkoo ba, ca sujjóot ba ak ci jëfi jullit yépp, loolu farata
la.
11
Wax Assalaamu Aleykum
12
Toog gi ngay toog di wax Assalaamu Aleykum
13
Fere mooy taalibe
14
Maamuun, ñaari yéene lay def : yéene julli ak yéene roy ilimaan.
15
Moom yéene ji

35
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.1.4 SUNNAY JULLI

Nanu dikke ginnaawam ci limu sunna yi, ak ngëneel ya ci aw woy wu di aji-rafet.

Bokk na ci sunna ya, liqaam1 ak ub saar topp na ci Faatiha ja, ànd ak taxaw; sax na.

Ak yelu2, ak biral3, niki nii lim na ko Sami Allaahu Liman Hamidahu.

Bépp kàbbar bu dul ba nga xam ne jiitaleef na ko, sunna4 la ci dëppook boroom xam-xam yi.

Niki nii ñaari taaya yi5 ak jotaayu taaya ba, ba ca tàmbalig yewwiku6 ga; wax na ko kilifa ga.

Sunug jiital Faatiha ca saar ya, dees na ko xam muy sunna fas ñoñ-xool7 ga.

Ab sëlmal bu dib ñaareel8 ñeel aji-roy, mu dig junj jëmale ko ci ilimaanam, dolli ko ci.

Am kemam ab ñetteel ñeel ku nekk ci càmmooñam; xeeñtul mbooloo ma9

Limeef na mu bokk ci sunnay julli, yaw sama àndandoo, ag biral ba-tey ànd ak sëlmal ba di aji-war10.

Ak niki nii julli sunu ci Yonent bi, yal na ko dolli xéewal ka nga xam ne jox na ñeel ko àgg ga.

Jublu naa ba ca taaya ju mujj ja ak sujjóotu bakkan ca lañu siiwe la.

ak ténq, bëti-wóom, cati-ndëgu11 ak saatir12 ñeel ku dul ku ñu jiite, dana jublu.

Li ma ci jublu mooy ku beru di julli ànd ak ilimaan13. Gën jaa néewam, xameef na ko, fas way-xam ña

mooy talaayub xeeju bant, ànd ak guddaayub xasab14, déet muy aji-jax-jaxal sam xel, muy lu ñu
saxal15, luy boroomug16 set.

1
Bokkul ci julli gi, sunna muhaaxada la. Danga koy def door a kàbbar.
2
Ci julli gees war a yelu.
3
Ca ya ñu war a biral.
4
Allaahu Akbar yooyu yépp lañu boole mu nekk benn sunna. Doo ber benn mu nekk sunna.
5
Ci julli gu am ñaari taaya : gu njëkk ga ak gu mujj ga.
6
Boo waxee Assalaamu aleykum
7
Ñiy xalaat te di ko dëppale ak liy yoon.
8
Sëlmal bu njëkk ba farata la ci ilimaan ak ci maamuun. Maamuun ji da cay teg wax Assalaamu haleykum ilimaan ji bu
fekkee am na ku nekk ci càmmooñam, mu wax ko Assalaamu haleykum
9
mbooloo may ràññale farata ya ak sunna ya ba lenn lu nekk nga mën koo jox àqam.
10
Wax Assalaamu haleykum farata la, waaye biral ko ba ñépp dégg ko, sunna la.
11
Yonent (saw) bi waxoon na : digal nañu ma bu may sujjóot, na am juróom-ñaari cat yuy laal suuf : jë, ñaari loxo, ñaari
bëti-wóom ak ñaari cati baaraami tànk yi. Waaye jë ba rek moo cay farata.
12
Saatir looy teg sa kanam la ngir bañ ku romb diggante foofee ak sab jë.
13
Maamuun saatiru ilimaan doy na ko. Waaye nag bu ñu ko rawee ci julli ga, mu koy mottali, bu boobaa mën naa ut saatir.
Bu jegee ab keno, day dem ba jege keno ba mu taxaw fa ngir mu doon saatiram.
14
Xasab mooy genn-wàllu meetar.
15
Warta doon lu ngelaw li mën a yóbbu.
16
Lu am sobe deesu ko def saatir.

36
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.1.5 NGËNEELI JULLI

Ndeem danga laaj ci mbooleem ngëneeli julli, jëlal lim ba fii, yaw aji-laaj sama.

Yékkati ñaari loxo ya ba mu tollook sa ñaari nopp1 fa kàbbaru armal ba, feeñ na bokk ci ngëneel ya.

Ak wax “Rabbanaa walakal hamndu2” ginnaaw yékkatiku ci rukkoo ñeel nag kenn ak ku ñu jiite, kuy
boroomug toroxlu.

Niki nii wax “Aamiin” ba-tey ñeel na leen ñoom ñaar ci yelu walla cig biral3 fas way-xam ña.

Ndaal ilimaan dana wax “Aamiin” doŋŋ fa yelu4 ga ci lu dul ag biral.

Lim na sàbbaalug rukkoo5 ak ñaan6 ga ngay def fa sujjóot ba, képp koo xam ne wattu na fiq.

Sunug guddal7 suba cim njàng, dana bir di ngëneel, ak tisbaar dana nekk di yées suba8.

Ag gàttalam9 ci tàkkusaan topp timis, topp ag digg-dóomu10 fa gee ga, lim ko.

Ak nekk aw saar wu njëkk di wu gën a guddu ci saaru ñaareel ba, miineef na ko mu bokk ci ngëneel yi.

Akuw melo wa di wu ñu xam fa rukkoo11 ba ànd ak jataay12 ba, lim na ko ñoñ-bànqaas yi.

Gënal nañu xunóot13 ak yelu ko, njëkk ag suufe jëm ci rukkoo14, yewwul.

Dees na ko jàng ci aji-ñaareeli ràkka jullig suba doŋŋ, ginnaaw jeexug aw saar; wattandikul njuumte15.

Fóore ja kay aji-dégg fiq, doomu Habiib16 daganal na, tàbbig xunóot ginnaaw ab rukkoo yaw aji-xel-lu
ji.
Limal, ba-tey, ñaan ga ginnaaw taaya ju ñaareel17; yal na amaleef la ag njub.

1
Ba ca gën nag mooy ténq ya day jublu suuf. Am na ñuy samp baaraam yi mu jublu asamaan. Boo ci def baax na.
2
Muy tekki “Boroom bi jéggal ma te yërëm ma”
3
Aamiin gi ci suuf lañu koy wax.
4
Ci julli gu ñu yelu.
5
Mooy “Subhaana Rabbiyal Haziim wabi hamdihii” muy tekki “Tudd na sellug sama Boroom ànd ak sant”
6
Muy “Subhaana rabbiyal ahlaa” di tekki “Tudd naa sellug Buur bu kawe bi”. Nga teg ca “Allaahuma ihfirlii …” ba mu
jeex, di tekki “Yàlla yal na nga jéggal”
7
Bëgg nañu booy julli suba yaw doŋŋ, boo jàngee Faatiha nanga ca teg saar bu nekk diggante Hujjraat ak Habbasa. Boo
àndeek mbooloo jiite leen, bëgg nañu nga woyofal ndax mbooloo mi ñu feebar ak ñu yàkkamti mën nañu cee nekk.
8
Saar ba nga tànnaloon suba. Lu mu ci mën a doon nañu nekk ñoom ñaar diggante Hujjraat ak Habbasa.
9
Bu dee tàkkusaan ak timis, bëgg nañu nga jàng saar yu gàtt. Kon yaa ngi koy jëlee diggante Wadduhaa ba Naasi
10
Gee moom saar bi du guddu te du gàtt. Yaa ngi koy tànn ci diggante Habbasa baWadduhaa.
11
Nees ko leeralee ci xët yi weesu.
12
Toog ci sa tànkub càmmooñ. Génne sa tànku ndijjoor, samp baaraam yi. Waaye biir baaraamu déy bi day féete suuf.
13
Mooy “Allaahuma inaa nasta inu ka” ba mu jeex
14
Boo jàngee Faatiha ak saar, bala ngaa rukkoo ngay def xunóot. Dafa am ñu ne dangay rukkoo ba siggi door a jàng xunóot.
15
Njuumte bay dugal xunóot fees ko warul dugal.
16
Moom nee na sañ ngaa rukkoo ba siggi ba wax “Sami allaahu liman hamiidahoo” dooga jàng xunóot, door a dem ci
sujjóot ba. Mën nga cee jële ne boo fàtte woon xunóot ba rukkoo, dangay nég ba siggi ba jàng “Sami allaahu liman
hamiidahoo” doog a sujjóot.
17
Taaya ñaareel sunna la, Salaatu halan nabi ba nga cay teg sunna la. Naka ñaan ya cay tegu niki “rabbanaa aatinaa
fiddunyaa” ak yi ci des yépp ngëneel lañu.

37
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Dana nekk, ngir dollikug1 ñaan ga, di gën a gudd ci taaya ju njëkk ja yaw aji-xel-lu ji.

Gënal nañu ag ndijjooru fa sëlmal2 ga; sunug yëngal3 baaraamu sànnikaay; mat na ag mat.

Sib nañu sunug taxaw ci benn tànk ci lu dul yaggug jëf4 ja.

Sib nañu sunug lëkkale5 ñaari tànk; ak def ci gémmiñ6 niki ñaari dëram

walla ab dëram walla lu dul lii, ak geesu7; ak gëmal bët cig julli

ndare ñeel ngànt kem ngelaw mbaa xool lu araam8, naka moom dees na sàkku ci moom ca boobee.

Sib nañu wax “Laa xawla walaa xuwwata” ak “Bismilahi Rahmaani Rahiimi9”, ci jullig farata, déet ci
jullig naafila10 kem “Ahuuzu billaahi minachaytaani rajiim”.

Ak lépp loo xam ne day jax-jaxal jëmm fas ug julleem, loolee lu ñu sib la; feeñ na

ci poosam, ci ginnaawam, ci kanamam mbaa ci wetam11; naka la ilimaan ja yaxale,

Sib nañu xalaat fas ag julli ci mépp mbir mom àdduna, mu di aji-dikk.

Lépp loo xam ne dana soxlaal wëliis ag ragal Yàlla12 fas ag julli, teet ko yaw waa ji.

1
Taaya ju njëkk ji moom doo ca dolli “Abduhoo wa rasuuli ”. Bu ñaareel bi danga ciy teg “Abduhoo wa rasuuli ”, teg
Salaatu Halan nabi, teg ca yeneen ñaan.
2
Ilimaan moom day tàmbalee ci kanamam buy sëlmal wax “Assalaamu haleykum” daaneele ko ci sa wetug ndijjoor. Bu dee
maamuun day wëlbatiku jëm ci wetug ndijjooram wax “Assalaamu haleykum”, bu ilimaan nekkee ci kanamam, mu jubale
ko ab nuyyoo wax ko “Assalaamu haleykum”. Bu keneen nekkee ci sa càmmooñ, nga wax ko “Assalaamu haleykum”. Nga
gis ne kon ilimaan benn yoon lay wax “Assalaamu haleykum” waaye maamuun mën na koo wax ñaari yoon ba ñett.
3
Yëngal baaraamu sànnikaay (bob joxoñ) ci ñaari taaya yépp lay am. Waaye du am ci diggante ñaari sujjóot. Ñaari loxo
yépp danga leen di tallal teg leen ci bëti-wóom yi. Waaye booy yëngal baaraam bi, loxob càmmoñ bi danga koy tàllal
yemale baaraam yi teg ko ca kaw luppub càmmooñ bi. Teg loxob ndijjoor bi ci kaw luppub ndijjoor bi, waaye dangay lem
ñetti baaraam yii (bob sanqaleñ, bob nombur ak bob digg bi), topp nga yemale te tàllal baaraamu sànnikaay bi ak bob déy
bi. Waaye dangay teg loxo bi tegin woo xam ne ténq li du jëm suuf. Dangay wetal loxo bi. Bu ko defee ngay yëngal di
jëmale càmmooñ ak ndijjoor. Waxuñu kaw ak suuf.
4
Bu fekkee yaa ngi julli di koolaa (taxawee benn tank), bu fekkee yàggul sib nañu ko. Bu yàggee lool julli ga yàqu na.
5
Nga laxase ñaari tànk yi itam sib nañu ko.
6
Bu dee du yàq ci saar yi ngay jàng dara, sib nañu ko. Lu ko moy julli ga day yàqu.
7
Bi ñu sib mooy geesu boo xam ne sa xar-kanam rek a wëlbatiku jëm ndijjoor mbaa càmmoñ, waaye sa jëmm wëlbatikuwul.
Bu sa jëmm wëlbatikoo nag ba jubluwul pénku moom julli ga yàqu na.
8
Niki jigéen ju yaram wi ne fàŋŋ ci biti.
9
Am na ñu ne dees koo war a wax, am na ñu ne dees koo sopp, am ñu ne dees koo sib.
10
Jullig naafila, boo koy tàmbali mën nga ne “Ahuuzu billaahi minachaytaani rajiim, Bismilaahi Rahmaani Rahiim”.
11
Niki ab rajo buy wax. Waaye boo koy déglu ba xamatoo ñaata ràkk nga julli, julli ga yàqu na.
12
Xalaat sa Boroom warta ëpp ba fàtteloo la foo tollu ci julli gi. Bu boobaa julli ga day yàqu.

38
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.1.6 RAGAL YÀLLA CI JULLI AK LA CA AJU

Yaxal na ci taalifam1, ka nga xam ne xam na, naka ñeel na julli ag leer goo xam ne màgg na.

Waaye naka googale leer2 dana fenk, ci moom, xolub aji-julli ku di aji-ragal Yàlla; yewwul.

Ndeem dikkal nga ko, moom julli, noccil sab xol ci jile àddina ak li nekk ci biir mbooleseen.

Te nga soxlawoo ci fuglanteek3 sa Boroom, ma nga xam ne danga julli ngir jëmmam ja; toppal ndigal.

Nanga fas naka sa julli gi ag toroxlu la ci sujjóot4, ci sag taxaw5 ak rukkoo.

Julli gi daal ag toroxlu la ñeel Yàlla, yéem naa sellam ga, déet di ñeel ko benn aji-nuroo6

ci yii yëf, ak ñaan, ak sikkar, ak sàbbaal, ak woote,

ba-tey, ak ug màggal, ak ug màggal ñeel ko ci suufe gi7 ak booy wax Allaahu Akbar; sàmmoonteel ak
yépp.

Nanga wattu ci julli ndax naka julli moo gën ci mbooleem jaamu-yàlla8 yi; kon màggalal mbiri julli.

Bul bàyyi Séytaane ba muy fo ci sa xol; bul jeng ñeel Séytaane9; deefilay yedd.

Ngir naka moom Séytaane day far leerug sa xol, dana la xañ bànneex10 ci leeru julli.

Dénk naa la ci biir julli gi ci saxoo ragal Yàlla ak dëddu ci mbirum àdduna11 ak ug toroxlu.

Xamal ne naka moom julli dana tere12wëliis ay ñaawtéef ak lu ñu pakk ci lu dul ag nëbb

Waaye lii nekk na ci sababug ragal, waxuma julli goo xam ne ci lu dul ragal; nanga ragal Yàlla te nga
sori ag toqe13.

Nekkal di boroom sàkkoo14 dimmandikoo ci sa Boroom kay Aji-dimbalee ndax kat ndeem sàkku ngaa
dimmandikoo ci ku dul Yàlla deesula dimbali.

1
Laxdari
2
Leer googu du fenk lu dul ci aji-julli bu ragal Yàlla. Bul defe ne képp kuy julli rek am leer googu.
3
Sa xel mépp nanga ko def ci sa Boroom. Fuglu mooy “contrôler” ci làkku faranse.
4
Boo fobee sa cër ci xar-kanam, muy li gën a tedd ci doomu-aadama, dëpp ko ci suuf si, nanga ci jublu toroxlu sa Boroom.
5
Degg gi ngay degg doo yëngatu.
6
Kenn nuróowul ak Moom. Kon Yàlla rek a ko jar.
7
Booy sujjóot ak booy rukkoo.
8
Jaamu-yàlla yépp bala ñoo ubbi di yër seeni téere, dañuy xool bob julli ba noppi. Bu yéwénee ñu door a jàll ci yi ci des. Bu
yéwénul ya ca des kenn du leen xool sax.
9
Booy julli, sa xel mii bul ko def ci Séytaane, muy jax-jaxal sam xel. Dangay def sam xel ci sa Boroom.
10
Bànneex bi nga xam ne kuy yég leeru julli dakoy am, Séytaane dala koy xañ.
11
Li ngay jàng nga koy firi di ci waaru. Boo ko mënt a firi ngay xalaat mbirum bàmmeel ak mbirum Allaaxira walla màggug
sa Boroom.
12
Booy julli nees ko sàkkoo, day dox sa diggante ak i ñaawtéef, ay moy Yàlla ak bépp bàkkaar. Koo gis muy julli te
terewukoo def ay bàkkaar. Na xam ne sëgg ak siggi rek lay def waaye julliwul.
13
Niki nga naan daa metti bu ma ko defee suba, tisbaar, tàkkusaan, timis ak gee. Fexeel ba julli yépp nga di leen def sa kem
kàttan.
14
Lu la jafe lu nekk, boo koy sàkku, nanga ko sàkku ci sa Boroom.

39
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.1.7 JULLIG AJI-FEEBAR

Dog bii tuddeef na ci ; jullig aji-feebar cig taxaw ak ub jotaay

ak seenub àtte ñoom ñaar ak la ca aju te dana war ci bépp mukàllaf

mu xamlu masalay bile bunt ngir déet kenn di kuñu musal ci feebar.

Ñeel na farata ciy mbir loo xam ne dees na ko lim muy juróom-ñaar fa ka nga xam ne xam na.

Sunug jooxe farata ja ci yii1 waral na ko way-dégg fiq ña ak ug nekkam cig toftalu.

Ñeent ci ñoom nekk nañu ci waral2, ñett ci ñoom nekk nañu ci sopp.

Ndaal ya nekk ci war mooy taxaw bañ a wéeru3, topp taxaw ànd ak wéeru ba-tey

Topp toog bañ a wéeru, topp toog ànd ak wéeru naka mu nekkee yaxug sunu sëriñ kay kilifa.

Waral nañu toftale yile mbir ci ñi ñu togg jëf ñi cig toftale.

Koo xam ne dana julli ciw melo te àttan na melo woo xam ne féete na ko kaw, àtte ba mooy yàqug julli
goo xam ne feeñ na.

Ndaal ñett ya nga xam ne soppeef na sunug toftale ñeel ko ca la nga xam ne tànneef na ko

mooy jullig ka nga xam ne lott na wëliss yii4ci wetam ju ndijjoor ba topp càmmoñ ba cig toftale.

Topp ca ginnaaw ba5, ndeem wuute na nag ci yile ñett, aji-daganloo6na ko, xeeñtoof na.

Topp sunug wéeru ga nga xam ne dana yàqu, ci moom, jullig aji-àttan taxaw; yewwul

mooy sunug wéeru ci lëf la nga xam ne dana rot fas ug rotam ca ka nga xam ne dana rotal7.

Ndaal ndeem nekkul di rot doonte rot na lile lëf, loolu lu ñu sib la, nettali nañu ko.

Ndeem danga daganal aji-àttan ab taxaw ag jekkeem ngir naafila, deefu la yedd8.

Waaye toog di naafila te mënoon a taxaw ci waxi jépp aji-xam, dees na fey ñeel ko ci genn-wàllug
yoolub aji-taxaw.

1
Juróom-ñaar yii
2
Am na ñeent yoo xam ne danga leen a war a tegale.
3
Ku mën a julli taxaw te doo wéeru, la la war mooy nga taxaw te doo wéeru.
4
Jullig ka nga xam ne mënul benn ci ñeent yi ñu njëkk a lim.
5
Jaaxaan waaye na tànk ya jublu xibla. Benn bi nga xam ne indiwuñ ko mooy mu dëféenu. Ca boobu, bopp bi mooy jublu
xibla. Nga xam ne bu jugoon mën a jublu xibla.
6
Bu fekkee mënoon ngaa tëddee wetug ndijjoor bàyyi ko tëddee wetug càmmoñ mbaa njaaxaanaay mbaa ndëfénaay, batey
sag julli baax na. Ndax toftale yooyu dañ koo sopp.
7
Wéeru mooy wéeru ca la nga xam ne, wéeru nga ca wéeruwin wu dëgër woo xam ne bu ñu dandale woon loolee nga ànd ak
moom daanu.
8
Koo xam ne mën naa taxaw naafila nga ne ko mu toog gappuru naafila, boo ko waxee deesu la yedd ndax dëppoo na ak
Chariya

40
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Daganal nañu tàbbi cig naafila ka nga xam ne jekki woon na, topp mu jóg ginnaaw loolee1; xiyaasal.

Waaye ndeem tàbbi nga naafila gi te yaw boroomug taxawaay nga, ca gannaaw ba nga jekki, déet yaw
ngay boroomug yeddeel

ndeem nekkoo woon di aji-tàbbi ànd ak yéene taxaw, bu boobaa2 dees na tere jekki ga fàww.

II.1.8 FEY JULLI YI FAAT

Fey la nga xam ne nekk na ci am ndodd3 ci farata, waxal dees na gis ag waram cig gaaw4.

Daganut sàgganug ka nga xam ne toftalu na ci moom, war na ci moom ag farlu.

Képp koo xam ne julii na juróomi julli bés5bu nekk ci bés yi ci jullikaay bi,

naka moom déet muy bokk ci way-sàggan yi; li fi nekk dees na ko lim ci way-farlu yi.

Dees na ko fey6 ni mu faatee rek ca waxtuw teew, ag teew7; safaan8 bi itam mooy waxtuw tukki.

Way-yemoo la ndeem nekk na di aji-tukki fa ag peyam walla muy aji-teew9; dana sàkku ag njub.

Toftaleel cig war yaw aji-gis ji diggante ñaari julli yi di kojug teew10 ak aji-néewi way-faat11

ànd ak julli ga nga xam ne waxtoom teew na, ndeem nekkoo woon di aji-fàtte ca waxtuw fey ga; yaw
mi xel-lu.

1
Daganal nañu ngay naafila tàmbalee ko gappuru, ginnaaw ba nga yeggalee ko taxaw.
2
Boo yéene woon taxaw. Ba nga koy sañ daal mooy dangaa tàmbali taxaw te bi ngay tàmbali yéene woon nga ne ràkka bii
dama koy taxaw bii dama koy toog. Loolu boo ko defee kenn du la yedd. Bu dee dangaa yéene woon taxaw ràkka yépp,
taxaw yenn yi toog yenn yi, tere nañu la ko. Sañoon nga gappuru lépp walla nga tàmbalee gappuru eggalee taxaw.
3
nekk ci am ndodd mooy li la war
4
Faat moom fum la ware, bu ko négee waxtu weneen. Fi saa sa nga daa di war a fey. Ndax boo naan naa nég ba ngoon,
xamoo ndax ngoon dina la fi fekk am déet. Te ame nga bor bi kon gaawal fey ko.
5
Bu ñu nee bés nag guddi ak bëccëg lees ci jublu.
6
Julli yi faat.
7
Bu dee julli gi, bi nga nekkee cig teew nga ko leb, bu demee ba fekk la ci tukki, nga xam ne dangay wàññi, boo koy fey
danga koy matal.
8
Li nga xam ne bi ngay tukki nga ko leboon. Te bi ngay tukki danga daan wàññi say julli, ndax tisbaar, tàkkusaan ak gee
ñaari ràkka lañu. Boo ñibbisee bay matal say julli, la nga leboon moom ciy ñaari ràkka nga koy fey. Kon lenn lu ne daal
nanga ko lebee woon nga koy feyee.
9
Bi mu koy fey. Mën nga cee dégge ne julli goo xam ne dañu koo war a biral niki timis, boo koy fey bëccëg itam danga koy
biral. Jullig tisbaar, nga xam ne dañu koo war a yelu, boo koy fey guddi itam danga koy yelu.
10
Ñaari julli yu di kojug teew (maanaam yi ñuy yelu ak yi ñuy biral), boo leen di fey danga leen di toftale, niki tisbaar ak
tàkkusaan. Boo ko amee tisbaar ngay njëkk a julli door a julli tàkkusaan. Timis ak gee it ñoo bokk waxtu. Boo ko amee,
timis ngay njëkk a julli door a julli gee.
11
Boo amee julli yoo xam ne dafa bëriwut, yooya itam boo koy fey, danga koy toftale. Ci misaal suba, tisbaar, tàkkusaan,
timis, gee. Boo leen di fey suba ngay njëkke, teg ci tisbaar, tàkkusaan, timis, mujjee gee.

41
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ndaal aji-néewam ñeenti julli lañu ak lu ko yées, waxu ma lu kawe ñeenti julli1; fas ña nga xam ne
dëgërloo nañu seeni wax.

Koo xam ne dana nekk di war ko ñeenti julli waxal mbaa lu ko gën a néew, na jublu fey leen doonte

day génn waxtu julli ga nga xam ne waxtoom daa teew, naka xameef na ko mu sax ci yaxi boroom fiq2.

Daganal nañu ci bépp waxtu feyug julli3; Tere nañu naafila koo xam ñeel na ko ag fey4,

kem naafila yoor-yoor, ak naafila weeru koor, waaye daganug Safaa ak Witar moom feeñ5 na.

Kem ñaari julli iit yi6, ak muurug weer, ak ñaari ràkkay fajar, ak jullig mbaaw7, ak jullig muurug jant.

Daganal nañu dajaleeg way-fey julli8, ndeem yemoo na seenag julli cig ràññale9; xiyaasal.

Ku nekk di aji-fàtte limub la nga xam ne war na ca pey ga yaw aji-xel-lu ji,

naka moom dana fey, dana julli ab lim bob du desal10 benn sikki-sàkka di ko gaar fàww.

1
Bu ko ëppee, julli yu bari lañu koy jàppee. Kon boo amee bori julli yu néew, bu julli gi teewee te fàtte woo ko, dangay fey
bori julli ya ba noppi door a julli waxtu wi teew. Boo ko fàttewul ba noppi julli waxtu wi teew. Boo noppee dangay fey bori
julli ya ba noppi julliwaat waxtu wi teew ndax julli ga baaxul. Waaye boo ko fàttee ba julli waxtu wi, boo noppee dangay
fey bor ya rek te doo baamuwaat julli ga. Bu ñu baree nag, dangay njëkke julli gi teew door a fey bori julli yi.
2
Laxdari.
3
Feyug julli moom amul waxtu. Bi ñuy wax naan araan na mooy julli bu jant bi tollee ci fenk ak ci so, naafilaa tax ñuy wax.
Jullig farata moom taxul ñuy wax.
4
Kenn du ami bor, feyagoo leen di maye.
5
Mën ngaa ame bori julli farata ba noppi di naafila Safaa ak Witar .
6
Tabaski ak Korite. Boo amee bori julli, mën nga leen a julli .
7
Mooy jullig ñaanum ndox. Bu ndox ñàkkee.
8
Ci misaal ñu bari ame borub tisbaar, ñu dajaloo, tànn kenn mu jiite leen ñu fey.
9
Ci misaal, dañoo bokk ame tisbaar, mbaa ñu bokk ame tàkkusaan. Waaye waxuñu kii amee tisbaar kii ame weneen waxtu
wu bokkul ak moom, ñu bokk julli. Dañuy bokk benn waxtu woo xam ne benn bés la. Waxuñu kee ame tisbaaru dibéer, kee
ame tisbaaru gaawu, ñu di ko boole.
10
Ku am bori julli te xamul lim ba, boo koy fey dangay julli ba mu wóor la ne ëpp lay def waaye du yées.

42
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.2 AB DOG CI JAMAJ1

II.2.1 JAMAJ AK LI CI AJU

Sunnaleef na, ngir jamaj joo xam ne feeñ na, ñaari sujjóot2 ngir ag dolli walla ag wàññi.

Dolli ga moom, ñaari sujjóot nekk na ci ginnaaw sëlmal3ga; nekk na ginnaaw ñoom ñaar ag taaya4
topp sëlmal.

Sujjóotal ngir wàññi5 njëkk sëlmal ginnaaw ab taaya te nga dolli beneen taaya.

Ndeem wàññi nga topp dolli nga, sujjóotal njëkk6 sag sëlmal ci la nga xam ne sukkandikoo na ko.

Ku fàtte sujjóotu xabla ba sëlmal, na ko sujjóot ndeem nekk na di aji-jege; nanga xam.

Ndeem génn na jàkka ja walla mu nekk di aji-sori, loolee moom yàqug julli la ak sujjóot7,

ndeem loolee ëpp na ñetti sunna8; ndeem nekkuko di ëpp loolu9, du yàqu fas aji-xel-lu ja.

Koo xam ne fàtte na sujjóotu bahda, na ko sujjóotal doonte ci ginnaaw ay at la, niki mu nettalee ko jële
fa sëriñ sa.

Cosaanu sujjóot mooy bàyyi ñaari sunna ak lu ëpp ñaari sunna; déet safaan ba ci lu dul ay nar.

Ndaal farata, deesu ko jeŋ10, ndare ci dikke ab farata ba nga xameene dees na ko fàttaliku11.

Ndaal ka nga xam ne nag wàññi na ci ngëneel, déet ag sujjóot di ko war ci lu mu mën a doon, wattul
njàngat la.

Benn sunna, déet sujjóot di ca war lu dul ag yelu ak ag biral yaw aji-namm ji.

1
Jamaj mooy juum ci julli.
2
Boo dollee mbaa nga wàññi lenn ci julli gi, dangay sujjóot ñaari sujjóot. Boo dollee, ñaari sujjóot ngay def ginnaaw sag
sëlmal. Moom lañuy woowe sujjóotu bahda-salaam. Boo wàññee nag, ñaari sujjóot ngay def laata sag sëlmal. Moom lañuy
woowe sujjóotu xabla-salaam.
3
Boo juumee ba dolli lenn ci julli gi, boo sëlmalee dangay sujjóotaat ñaari yoon, taayawaat sëlmal.
4
Waaye taaya ju gàtt lay doon. Ci “Abduhoo wa Rasuuli” rek lay yem.
5
Su fekkee dangaa wàññi mel ni sunna soo xam ne ku ko wàññi danga koo war a sujjóotal xabla-salaam, dangay taaya ba fa
nga daan waxee “Assalaamu haleykum” nga daldi sujjóot ñaari yoon te taaya joo xam ne ci “Abduhoo wa Rasuuli” rek lay
yem, door a sëlmal.
6
Boo boolee dolli ak wàññi, doo def ñaar yi, xabla-salaam rek ngay def.
7
Julli ga yàqu na, dangay julliwaat geneen julli.
8
Lu mel ni ab saw saar (bàyyi ab saar) ndax jàng saar bi sunna la, taxaw gi ngay taxaw sunna la, yelu ga walla biral ga sunna
la.
9
Ci misaal lu mel ni taaya, ñaar rek a fa nekk, muy jëmmi jàng taaya ji ak jotaay bi. Boobu mën nga koo bañ a sujjóotal boo
ko fàttee lu yàgg te du tax sag julli yàqu.
10
Jeŋ mooy defaraat mbaa « réparer » ci faranse.
11
Saa soo yégee ne am na julli goo julli woon te fàtte nga ca farata, mëneesu koo sujjóotal xabla-salaam mbaa bahda-salaam,
farata ba kay danga koy indiwaat rek.

43
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
II.2.2 JAMAJ CI JULLIG FARATA GOG JOOXAL1

Nanga sujjóotal xabla-salaam ndeem yelu nga ci barabu biral, yaw mi nga xam ne xel-lu nga.

Ndeem biral nga ci barabub yelu, nanga sujjóot bahda-salaam ci lu dul ag weddi.

Ndeem wax nga ngir jamaj2, nanga sujjóot bahda-salaam ginnaaw sag sëlmal ngir ug dolli gog feeñ na.

Képp koo xam ne sëlmal na ci ñaari ràkka ngir jamaj3, war na ci moom sujjóotug bahda.

Koo xam ne dolli na ngir jamaj ñaari ràkka4 mbaa benn ràkka5, day def bahda ci lu dul nar.

Waaye ndeem dolleef na lu tollu ni ag julli, julli ga dana yàqu6 fas ka nga xam ne gëstu na.

Nanga dikke, ndeem sikki-sàkka nga ci matug julli ga, nanga indi la nga xam ne dangay sikki-sàkka ci
moom cig toftale7

ngir waxi sëriñ sa, ña di boroom dëppale. Nee nañu sikki-sàkka ca mànke ga mi ngi mel ni dëggal la8.

Nanga sujjóot ndeem sikki-sàkka nga niki ci ab sujjóot ginnaaw boo ko defee ginnaaw ba.

Sëlmalal ndeem sikki-sàkka nga ci sëlmal te yàggul9, te déet ab sujjóot di ca war.

Ndeem jamona ji jegewul walla génn nga jàkka ja, julli ga yàqu na.

Digëlal boroomug jax-jaxal10 mu bàyyi julli ga noonee, waaye duñu dikke ci bépp sikki-sàkka.

Waaye war na leen, ci lu war, ñu sujjóot bahda-salaam ngir sopp goo xam ne dees na ko jublu.

Déet lëf di war koo xam ne biral na ci xunóotam11, waaye nag tey12 ko feeñ na di lu ñu sib.

Niki13 aji-dolli ci ñaari ràkka aw saar, li ma ci jublu mooy ñaari ràkka yu mujj yi, ci lu ñu nettali.

1
Jullig jooxal mooy julli gu ñuy def ci waxtoom.
2
Dangaa juum ba wax.
3
Niki dadoon julli tisbaar, def taaya ju njëkk rek daldi sëlmal. Bu noppee day bahda-salaam ndax sëlmal googee mu ci dolli.
4
Niki ngay julli tisbaar def ko juróom-benni ràkka.
5
Niki ngay julli tisbaar def ko juróomi ràkka.
6
Ci misaal, boo fàttee ba def tisbaar, tàkkusaan mbaa gee juróom-ñetti ràkka julli ga yàqu na. Timis moom juróom-benni
ràkka du ko yàq, ñeent a koy yàq.
7
Bu fekkee yaa ngi julli di sikki-sàkka naan ñeent ràkka mbaa ñetti ràkka laa am, jàppal ne ñett nga am. Indil beneen muy
ñeent ndax Yàlla kenn du ko jaamu ci sikki-sàkka.
8
Booy sikki-sàkka naan mat na mbaa matul, jàppal ne matul.
9
Bu dee danga julli ba noppi di wird, ab diir ngay sikki-sàkka ci sujjóot, dangay sujjóot, bu diggante bi soreewul. Bahda-
salaam du la ca war.
10
Boroomug jax-jaxal mooy koo xam ne, saa suy julli, xel ma dafa bon ba du xam ñaata ràkka la am.
11
Xunóot moom ku ko biral, bahda mbaa xabla-salaam du la ca war.
12
Xunóot cig teyeef moom sib nañu.
13
Sib nañu ko it.

44
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Niki nii ab jaam bu julli1 ci gën gi mbindeef ngir dégg aw turam ci ka nga xam ne tudd na ko

Muhammad, yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko ak képp koo xam ne méng2 na ko.

Moo xam loolee cig tey walla cig jamaj la, walla xew na cib taxawaay walla ab jotaay3.

Koo xam ne jàng na ñaari saar ci benn ràkka walla lu ko ëpp walla mu génn tukkee ca saar ba te mu
sukkandiku4

ci weneen walla rukkoo na njëkk matug saar bi, déet sujjóot di war ci mbooleseen5.

Déet di ñeel aji-junju, ci julli gi ci loxo walla bopp, ab sujjóot guy aji-dikk6.

Képp koo xam ne baamu na Faatiha ngir digub jamaj goo xam ne gaar na,

day sujjóot bahda-salaam; waaye ndeem lii7 xameef na ko ñeel ug tey, aji-feeñ ja mooy yàqug julli fa
Laxdari.

Boroomug suufe cig lunk jëm ci rukkoo8, déet di ñeel ko ag dellu dem di taxawaat ngir fàttaliku aw
saar9.

Waralal, koo xam ne fàttaliku na njëkk rukkoo10 ag yelu, mu baamu mbooleem la nga xam ne jàng na
ko.

Ndeem loolee daa nekk ci saar wa moom doŋŋ, mu baamu ko; déet sujjóot di nekk ci ginnaaw ba11.

Ndeem la ñu bàyyi ci Faatiha la, na baamu Faatiha te mu sujjóot bahda-salaam ngir dolli na loolee12.

Ndeem dana la faat [moom yelu ga] ci sababu rukkoo13 yaw fere wi, sujjóotalal ko, ngir bàyyi ag biral,
njëkk sëlmal.

Moo xam mu nekk ci Faatiha Kitaab, walla aw saar doŋŋ ci lu dul sikk.

1
Koo xam ne dafa tàmm bu déggee Muhammad da cay teg « Salalaahu Aleyhi wa sallam ». Nekk ci julli am ku ne
Muhammad, mu ne « Salalaahu Aleyhi wa sallam ». Loolee mu wax bu fekkee teyu ko sibuñu ko. Bu ko teyee sib nañu ko
waaye dara waru ko ci.
2
Mooy képp ku topp la mu daan wax mbaa la mu daan def.
3
Bu toogee walla mu taxaw ci biir julli gi, dara waru ko ci.
4
Dafa jàng benn saar jeexal ko ba tàmbali weneen.
5
Ku jàng Faatiha teg ñaar mbaa ñetti saar walla mu génn aw saar ba tàmbali weneen walla mu rokkoo te saar ba mu tàmbali
woon àggul, yooyépp sujjóot waru ca.
6
Kuy julli, am kuy wax mu di ko joxoñ walla mu yëngal bopp bi jublu ci waaw walla déet, loola sujjóot waru ca.
7
Faatiha ku koo baamu te teyoo ko, dangay bahda salaam. Boo ko teyee sag julli yàqu na.
8
Boo demee bay waaj a rukkoo ngir ug fàtte.
9
Boo jàngee Faatiha te waroon ca teg ub saar. Dem bay waaj a sëgg fàttaliku saar wa, bumu la tax a siggiwaat naan danga
ciy teg uw saar. Dangay wéyandi rek, ndegam saar boobu sunna la, boo noppee def xabla-salaam.
10
Koo xam ne daa jàng bay waaj a rukkoo, fàttaliku ne daa yelu li mu jàng fekk julli guñu war a biral la.
11
ndax sañees naa jàng lu ëpp benn saar.
12
Ndax daa jàng Faatiha ñaari yoon.
13
Boo fàttalikoo yelu ga ginnaaw rukkoo ba.

45
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ree ci biirug julli cig tey, dana ko yàq ci dëppook boroom xam-xam yi, niki jamaj1 itam wëliis
dëppoo.

Déet muy ree ci biirug julli ndare ku di boroomug càggante walla ku di aji-fo koo xam ne réer na.

Aji-gëm nag ku di aji-sellal kuy boroomug ragal Yàlla, bu jógee jëm ci gépp julli, day sànni

ci xolam wëliis mépp mbir mu di kojug àddina ak lépp loo xam ne du Buur bay Aji-làq nguur.

Mu bàyyi àddina ak la ca nekk te du nekk di boroomug geesu ñeel lëf ci fii àdduna.

Dana teewal ca xol ba ñeel màggug Yàlla kay Boroom mbindeef yi, ci waxi aji-dëggu ja

ba xolam mujj di aji-lox, bakkanam tëy ngir ragal alkànde

ngir ragal Buur bi Yàlla, màgg na te kawe na ag màggam, kay boroom asamaan ya di Aji-kawe.

Mbiram day nekk niki waxi Omar [Fuutiyu] muy koo xam ne ñikkoo2 na ci ragal Yàlla ak xam-xam

Nee na, ndeem tàbbi nga ci julli nekkal niki jëmm joo xam ne nekk na ci faatu3.

Lii mooy jullig way-ragal Yàlla4 ña, ña di ñuñu teral ca Àjjana, ña di way-texe.

Yal na Aji-yërëme ja wërsëgal nu ag dëddu ak ug ragal Yàlla, ag kóolute ci képp ci nattu yi ak ug yéeg.

Déet di nekk ci muuñ5 nag sujjóot, du caagéenu baamug julli itam, yaw aji-namm ji.

Jéggale nañu jooyi6 aji-ragal Yàlla, niki nii aji-néew7 ug noppi ngir déglu aji-xibaar, jàppal.

Koo xam ne dana taxaw tukkee ci ñaari ràkka njëkk ba mu laataa jekki walla njëkk taaya joj miineef na
ko,

te dana yewwu njëkk ag tàqalikook suuf loxo ya ak bëtu-wóom ya, na dellu jëm ca taaya ja.

1
Juum ree itam dana yàq julli waaye nekkul ci dëppook boroom xam-xam yi.
2
mooy làmboo na. Omar Fuutiyu, ay waxam lu mat a bàyyi xel la ndax ku ragaloon Yàlla la te amoon xam-xam.
3
Ku faatu boo koy kaata du ko yég, du dégg ay wax bay ree. Sëriñ Tuubaa am na benn jëmmi jamono, mu woo mbooloo mi,
dileen fonkuloo julli. Ne leen "Julli de nangeen ko fonk bu baax. Waaye dey naqari naa def lool ndax julli dëgg-dëgg de boo
ko dee def, boo kàbbaree ñu foboon paaka di dàgg sa cër yi benn-benn doo ko yég. Moone dey mbooleem ñi toog dey, ku
mën a jullee noonu am na fi.". Ba mu ko waxee, xel yépp dem nañu ne moom rek a ko mën.
4
Ragal Yàlla mooy du jóg ci Yàlla ba li mu digle doo ci ñimee bàyyi dara, li mu tere doo ci ñimee def dara.
5
Muuñ cig julli moom dara nekku ca.
6
Ki nga xam ne day julli di jàng Alxuraan di xalaat màggug Boroomam ak di xalaat ni sunu Boroom di tëkkoo ñiy moy
Yàlla, ba mujj muy jooy ci biir julli gi. Jooyam yooyu moom, jéggal nañu ko ko, doonte day xëxët ca kaw itam.
7
Koo xam ne daa nekk ci biirug julli, nit ñëw yàkkamti bëgg koo wax dara ba dem, mu tàmbalee wax mu ne cell dagg njàng
ma ba déglu la muy wax ci diir bu gàtt door a wéy ci julli ga. Loolee jéggal nañu ko ko. Yàqul julli.

46
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Déet sujjóotug jamaj ca lu ñu nettali la ngir woyofug mbir mi ca lu ñu siiwe1.

Ndeem tàqalikoo na ak suuf nag, na wéy ci taxaw te mu sujjóot xabla-salaam njëkk sëlmalam ngir ag
wàññi rot na2

Ndeem dellusi na ginnaaw tàqalikoo loxo ya ak suuf, àtteem ñaari àtte la fa ka nga xam ne wattu na
xam-xam.

Ndeem dellusi na njëkk ag yemoo3, na sujjóot bahda-salaam4 ci anam wu mu mën a doon ci li nga xam
ne dëggaleef na ko.

Ndeem dellu na toog ginnaaw taxaw ga nag jonn, mbir mi muy lu ñu joyal, ag julleem ngir ug dolli gog
dëggaleef na ko5.

Koo xam ne wal6 na ngir jamaj ci julli, na sujjóot ci ginnaaw sëlmal ba yaw mbokk mi.

Ndeem nekk na di aji-tey, lii lu ñuy tuddu7, dana yàqu julléem ga ca lu ñu siiwal la.

Jublu naa ci gémmiñ; bu tukkee ci bakkan8 nag, déet sujjóot di ci nekk ci lu dul wuute.

Ndeem tisli9 nga ci sag julli, bul soxlawoo naan “Alhamdulilaahi Rabbil Aalamiin10” yaw mi nga xam
ne xel-lu nga.

Bul delloo ci ka nga xam ne ndokkeel11 na la; bul ndokkeel itam aji-tisli ci "Yarhamukallaa12".

Waaye gile bàyyi nekk na ci sopp13; déet dara di war koo xam ne def na lu dul moom.

1
Koo xam ne dadoon julli julli goo xam ne dafa am taaya ju nekk ca digg ba, mu def ñaari ràkka, bamu laataa toog mu jóg
taxaw walla ba mu toogee ba mu laataa taaya mu jóg taxaw. Waaye bi mu tàmbalee di jóg taxaw, ñaari loxo ak ñaari bëti-
wóom yi laataa tàqalikook suuf si, fàttaliku na ko daal di toogaat far jëm ca taaya ja. Kooka ñu ne sujjóot waru ca ndax li
mu def lu woyof la.
2
Bu fekkee léegi bi mu fàttee taaya ji ñaari loxoom ak ñaari bëti-wóomam teqalikoo na ak suuf, bumu toog kon, na wéy ci
taxaw. Bu noppee nag mu def xabla-salaam ndax taaya jooju mu wàññi.
3
Maanaam bamu laataa taxaw jonn la dellusiwaat.
4
Ndax dafa dolli
5
Bu noppee day def bahda-salaam ndax dafa dolli.
6
Niki mu ne ëf.
7
Bu dee moo ko tey, kon dolli na ci alif ak faa, looloo taxoon julléem yàqu.
8
Bu dee ci bakkan la ko def, loolu tuddul wal, fuuftandiku lay tuddu. Boroom xam-xam yi wuutewuñu ne kooku sujjóot
waru ko.
9
Xam nga ne ku tisli daa war a wax "Alhamdulilaahi Rabbil aalamiin". Waaye boo nekkee ci julli ku tisli bul ko wax.
10
Di tekki “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla miy boroom àddina si”
11
Boo tislee mu ne la "Yarhammukalaa", bu ko delloo naan ko "Yaxfirulaahu lana walakum" walla "Yahdimuku laahu Yaslu
baala kum". Dangay wéyal sag julli rek.
12
“Yarhamukallaa” mooy yal na la Yàlla yërëm.
13
Dañu koo sopp rek.

47
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ndeem bóbbali nga fa sag julli, sakkal sa gémmiñ yaw sama mbokk ci sa loxo1.

Tuflil, ndeem namm ngaa tufli, ci sa mbalaan2 ci lu dul génne aw araf, kon danga yàq sag julli

Koo xam ne xalaat na, lu néew, ngir am toj mbaa sobe soo xam ne sikki-sàkka na ci moom te gëstu na

te ginnaaw ba nag wóolu na laab ga, déet dara di war ko ci dëppook way-xel-lu yi3.

Kem kii, ci àtte, koo xam ne geesu na fa ag julléem ngir jamaj sax na4.

Waaye tey geesu nag fa ka nga xam ne xam na, dees na ko sib5 muy lu ñu sib niki mu jiitu woon.

Ndaal ka nga xam ne dëddu na xibla fas lii6, na baamu googee julli fàww7.

Koo xam ne dina julliwaale ak sooy8 walla mu xool lu ñu araamal, moy na Boroom mbindeef yi.

Waaye julléem ga aji-wér la niki nii aji-sàcc lëf ci biirug julléem, jàppaale ko9.

Sujjóotal bahda-salaam ndeem juum nga ci njàng moo xam ne dana dikk tukkee ci lu dul Alxuraan

ci baat bu di benn, waaye ndeem dana nekk tukkee ci Alxuraan, déet sujjóot fa ka nga xam ne xel-lu
na10.

Waaye bu soppee baat boo xam ne xameef na ko walla mu yàq maanaa ma, war na ko sujjóotug
bahda11.

1
Ngir nga bañ a wax dara.
2
Dangay génne sab musuwaar raay ko ci sa làmmiñ, tuflit ya taq ca. Waaye bul ne tëf ndax boo ko defee taa ak faa génn te
kon nga yàq sa sulli.
3
Booy xalaat naan ndax yor naa toj am yoruma ko walla ngay sikki-sàkka ndax yor naa sobeem déet. Ginnaaw am gëstu mu
wóor ko ne yor na laab, loolu dara waru ci. Sujjóot waru ci.
4
Mook ki nga xam ne day julli ba mu yàgg mu juum geesu xar-kanam bi doŋŋ waaye jëmm ji wëlbatikuwul, kooka tam dara
waru ko.
5
Geesu sa xar-kanam goo tey yàqul julli waaye sib nañu ko.
6
Koo xam ne geesu na ba jëmm ji jublootul xibla.
7
Ndax xamoon nga ne sàrti julli bokk na ci jublu xibla.
8
Mooy “soie” ci faranse. Xeeti piis la yoo xam ne lu mel ni lënd yuy jóge ci sax wuñuy wax ci làkku araab “duudatul xasri”,
moom lañuy dajale ràbb ci piis ba. Duudatul xasri xeetu sax la bu bari Misra (Esipt) lool. Ñoom dañu koy def ay tool yoo
xam ne dañu leen ciy yar.
9
Boo julleek sooy mbaa ngay xool lu araam (niki awra) mbaa ngay tafu, xamal ne moy nga Yàlla. Waaye julli ga moom
teewul wér na.
10
Bu dee dangay jàng Alxuraan, jàng Faatiha ba noppi, am nga ñaan yoo tàmm a teg ci Faatiha, nga jeexal Faatiha ba teg ca
ñaan ga. Nga fàttaliku ne ci julli nga nekk doonte benn baat nga ca jàng. Bu ñaan ga bokkee ci Alxuraan sujjóot du la ca
war. Bu ca bokkul nag danga koy sujjóotal bahda-salaam ndax danga koo teyul. Boo ko teyoon nag julli ga day yàqu.
11
Su fekkee dafa jàng baat boo xam ne ci Alxuraan la bokk, waaye da koo soppi, jàngeewu ko nañu ko war a jàngee naka
"Iyaaka nahbudu" mu ne "Iyaaka yuhbadu", walla mu yàq maanaa ma niki mu ne "Iyaaka tahbudu". Kon loolee ci Alxuraan
la bokk, da koo yàq rek. Sujjóot bahda-salaam moo ko cay war.

48
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Boroom ngëmment ci biirug julli, déet sujjóot di war ko, ndeem nekk na [ngëmment la] di aji-woyof
yaw taalibe bi.

Ndeem nelawam ya diis na, na baamuwaat julléem ga ànd ak njàpp la; sàkkul am njub.

Jéggal nañu ag wonk ñeel aji-feebar ci waxtu julléem; mokkalal sama woy.

Am kemam xaddamiku1 ngir lor, amaa bu fekkee ngir dégtal nag, lu ñu sib la, xameef na ko.

Waxal koo xam ne sàbbaal na ngir woote2, nee ko def nga lu ñu sib ci lu dul werente.

Waaye julléem ga moom aji-wér3 la, deesu ko digal ci sujjóot yaw mi nga xam ne xel-lu nga.

Ndeem taxaw nga ci biir um njàng te kenn gàggantiwu la yaw sama xarit

ab aaya, taxaw nga tukke ci moom, bàyyi ko ca boobee, topp nga jàng la nekk ca ginnaaw aaya ba ngir
nga wéy4.

Ndeem gàntal na ci yaw, rukkool waaye nag bul xooli ab kaamiil waxtu wa mu tàbbee5.

Waaye gile jàppandal ak gile tabe dana nekk ci saar wudul Faatiha.

Waaye Faatiha nag ag matam dees na ko gis ci lu war xooli ab kaamiil walla lu dul kaamiil ci lu dul
werente6.

Ndeem bàyyi nga ab aaya ci Faatiha te jàppandiwul ag dabaatal, sujjóotal xabla-salaam; nee ma waaw.

Waaye ndeem bàyyi nga loo xam ne ëpp na ab aaya, yàqug sag julli dees na ko gis7.

Koo xam ne ubbi8 na ci ku dul ilimaanam9, xamal ne yàqu na ag julléem ca la gën a wér.

Bul ubbi ci ilimaan njëkk mu koy sàkku walla mu yàq maanaa ma, kon deef na la dimbali.

1
Xaddamiku ngir bëgg xaddamiku loolu jéggal nañu la ko, sujjóot waru la ca. Bu fekkee danga xaddamiku ngir bëgg a
xamal nit ne yaa ngi ci biir néeg bi, sib nañu ko waaye yàqul julli..
2
Niki nga nekk ci julli, séen kuy dem nga bëgg koo woo, nga ne ko "Subhaanalaa" ngir bu geesoo nga woo ko. Loolee lu ñu
sib la.
3
Ndax sañees naa wax "Subhaanalaa" ci biir julli.
4
Booy jàng ba yàgg nga gag te kenn gàggantiwu la, boo ko xamul dangay tëb aaya ba wax ba ca topp.
5
Boo gagee te xamoo aaya ba ca topp, te kenn gàggantiwu la, dangay rukkoo. Waaye bul xool ab kaamil.
6
Faatiha moom mëneesu koo jàng te du mat ci biirug julli. Moo xam dangay ubbi kaamiil xool ko ca walla àlluwa ju nekk sa
wet gu ñu bind Faatiha walla daal foo ko mën a gàggantikoo.
7
Boo bàyyee ci Faatiha lu ëpp benn aaya te mëneesu koo dabaatal, xamal ne sa julli yàqu na.
8
Mooy gàgganti.
9
Ku nekk ci julli, keneen ku dul ilimaanam gag mu gàgganti ko. Gàgganti ci sa ilimaan rek la la waree.

49
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ndeem wëndeel ga xalaat ba lu néew ci mbirum sa àddina, [xamal ne] wàññi nga yool ba.

Ngir naka moom dees na ko lim muy lu ñu sib waaye nag du nekk di aji-yàq ag julli ndeem néewaleef
na ko1.

Waxal koo xam ne, daa puus aji-dox joo xam ne dana namm romb ci kanamam, déet sujjóot di ko war2.

Am kemam ku nekk di aji-sujjóot cig wet ñeel ab jë ñeel ko ci la nga xam ne feeñ na.

Walla ab taxañ doŋŋ ak ñaari taxañ ca kaala ga ci kasril hayni bi3.

Nekkul dara di war koo xam ne not na ko am waccu [ba mu waccu], niki nii am ngall yéen taalibe yi.

Jamajug maamuun fas royub ilimaan, dana ko yenu ilimaan ja; ndare muy aji-dikk

ci wàññig farata ci julleem ga, [loolu moom] du ko gàddu ilimaan ja wëliis ko, muy lu ñu joyal4.

Ndeem jamaj na walla gàllankooru na, ka nga xam ne roy na, walla naka moom gëmmentu na wëliis
rukkoo,

te moom, ci biir julli gi, ci ràkka bu njëkk ba, ab àtteem feeñ na di ñaari àtte fa ñoom sëriñ sa5.

Ndeem yaakaar na mu dabu ilimaan ja njëkk yékkatig bopp ba juge ci rukkoo ba, yaw fere wi

tukkee ci sujjóot bu ñaareel, na rukkoo te na dab ilimaan ja; nekkal di aji-topp6.

Ndaal ndeem yakaarut dab ilimaan, na ko bàyyi te topp ilimaan ja,

topp mu fey ci biralug ràkka boobee ginnaaw sëlmalu ilimaanam ab ràkka ba ca des yaw fere wi7.

Ndeem jamaj na, boroomug roy, wëliis sujjóot walla naka moom tanceef na ko walla gëmméntu na

1
Boo nekkee ci biir julli di xalaat ci mbirum àddina. Xalaatoo màggug sa Boroom, xalaatoo maanaay Alxuraan ji ngay jàng,
teewluwoo sa Boroom. Bu fekkee li nga ko def bariwul, loola sib nañu ko. Balaa yàq julli gi, day bari. Ni ñuy xamee ndax
bari nag, mooy booy xalaat mbirum àddina ba xamatoo ñaata ràkka nga julli.
2
Koo xam ne daa puus ku bëgg a jaar diggante ay tànkam ak fi muy dëpp ab jëwam, sujjóot waru ci. Yàqul ag julii itam.
3
Niki noonu ki nga xam ne itam bi muy sujjóot wetug jë bi la sujjóotee, xayna digg jë bi daa am metit bu ca nekk ba tax
mënu caa sujjóot, walla bi muy dem bay sujjóot kaala ga dafa téqarñiku mu sujjóot ca kaw benn taxañ ba walla kaw ñaari
taxañ ya. Loolu dara waru ci, yàqul ag julli. Sujjóot itam waru ca.
4
Maamuun bu dee day julli nekk ci ginnaaw ilimaan, su bàyyee loo xam ne budoon moom sujjóot da cay war te ilimaanam
bàyyiwuko. Xamal ne ilimaan dakoy gàdduwaale. Ba mu des nag mu wàññi farata joo xam ne ci julli gi la bokk. Farata
moom ilimaan mënu koo yenul maamuun. Bu noppee na ko indi ngir ag julleem mat.
5
Ki nga xam ne dafa jamaj walla dañu koo tanc (maanaam dafa am gàllankoor) walla mu doon nelaw ba ilimaan rukkoo te
moom rukkóowul. Bu fekkee ci ràkka bu njëkk ba la nekk, kooku ñaari àtte lañu koy indil.
6
Kon kooku bu fekkee yaakaar na ne ilimaan balaa yékkati bopp bi tukkee ci sujjóotu ñaareel bi ci ràkka boobee mu nekk,
mën na fee rukkoo fekkisi ko te du siggi, kon day gaaw rukkoo dem fekki ko, dabi ko. Noonu la koy lijjantee loolii.
7
Waaye bu yaakaaree ne mënu fee rukkoo fekki ilimaan ci sujjóotub ñaareel bi te du siggi, rukkoo ba dafa koy bàyyi te fekki
ilimaan fa mu tollu. Bu ko defee bu ilimaan sëlmalee nag, mu indi beneen ràkka buy wuutu ràkka boobee mu bàyyi woon ab
rukkoo.

50
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
ba tuxu na ilimaanam jëm ci ràkka ba ca des, kon na ko sujjóot te mu gaawtu

ndeem yaakaar na dab [ilimaan] njëkk muy rukkoo boo xam ne xameef na ko; ndeem yaakaarul [ne
dana dab ilimaan njëkk rukkoo bi], na jiitu woon rek la koy lijjantee1.

Waaye fu mu feyee ràkkaam ba, déet di war ko mu sujjóot ca la nga xam ne tuxaleef na ko

Ndare ci sikki-sàkka ci rukkoo walla ci sujjóot; naka moom kon dana sujjóot bahda-salaam yaw taalibe
bi2.

Nekkul di war dara koo xam ne rey na niki jiit joj jublu na ko, xel-lul

feek yàggalul jëfam walla jengul wëliis xibla, dog ga ca foofee xelloo na ko.

Waxal, ñeel koo xam ne sikki-sàkka tàbbi na ko ci kaw gi mu nekk witar ak aji-ñaareeli safaa, nettali
nañu ko

sag def [ràkka bii ngay sikki-sàkka naan] ñaareel ñeel safaa3 ànd ak sujjóot bahda-salaam ci yoonu
Islaam.
Topp war na ko ginnaaw loolee witar; naka la yaxale ci moom aji-dégg fiq ja kay fóore.

Waxal ñeel koo xam ne wax na diggante [Safaa ak witar] ngir jamaj, déet di war ci moom dara.

Ndeem nekk na ci tey, moom lu ñu sib la fa ña nga xam ne xam nañu.

Aji-dab lu yées ab ràkka ànd ak ilimaanam te mu nekkoon di tàbbi ca julli ga di ku ñu jiitu,

bu sujjóotee xabla-salaam walla bahda-salaam ànd ak ilimaan, ag julleem yàqu na4; yal na nga am ag
yaatu.

Waaye ndeem dab na ànd ak ilimaan ab ràkka bu di aji-mat walla ñaari ràkka, sàmmal,

1
Ki nga xam ne dafa sujjóotul ndax dañu koo tanc walla dadoon nelaw, ràkka bi ñu nekk sujjóotagu ko, ilimaan jàll ca ràkka
ba ca des, kon léegi day gaaw sujjóotal ràkka bi ilimaan juge bu fekkee yaakaar na ne mën naa dab ilimaan balaa rukkoo ci
ràkkab ñaareel ba nga xam ne ca la jëm. Bu yaakaaree ne mënu fee sujjóot fekki ko ca ràkka boobee balaa rukkoo, kon na
mu lijjantee woon bu njëkk ba la koy lijjantee. Mooy day bàyyi ràkka boobee, bu noppee indi beneen ràkka bu koy wuutu.
2
Bu feyee ràkka boobee nga xam ne moom la bàyyi woon sujjóot ba noppi, sujjóotaat bahda-salaam waru ko. Walla book
dafa sikki-sàkka naan rukkoo na am rukkoowul walla sujjóot na walla sujjóotul, kon kooku day rukkóowaat. Bu sikki-
sàkkaa sujjóot bi nag day sujjóotaat. Kooka bu noppee nag dana sujjóot bahda-salaam ndax mën naa am rukkoo boobee
defoon na ko te kon defaat gi dollent lay doon. Mën naa am it ne sujjóot boobu muy sikki-sàkka defoon na ko, kon
sujjóotaat gi dollent lay doon. Kon kooku foofu rek lay sujjóotee bahda-salaam.
3
Boo gisee waa juy julli safaak witar, dem ba ca ràkka ba nga xam ne danaan ci ràkkab ñaareel laa nekk walla ci witar laa
nekk, nee ko sikki-sàkka ji dangay dem ca la la gën a wóor. Kon soppi ko ñaareelu safaa daldi sëlmal door a julli ràkkab
witar. Waaye nag boo noppee danga sujjóot bahda-salaam ndax mën naa am julli woon nga ràkka boobu ngay sikki-sàkka.
4
Ku fekk ilimaan mu nekk ci ràkka bu mujj, fekk na ko mu rukkoo ba siggi ba wax “Sami Allaahu liman hamiidahu”, mu
kàbbar fekkisi ko àggaleek moom. Kooka bu ilimaan di sujjóot xabla-salaam walla bahda-salaam mu ànd ak moom sujjóot,
julleem yàqu na.

51
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
na sujjóot xabla-salaam ànd ak ilimaan te mu yéexe sujjóotug bahda-salaam ba ci matug julleem [ga
muy mottali]1.

Ginnaaw bu mu sëlmalee dana sujjóot. Waaye ndeem wuute na ak lii, muy aji-tey ko, yàqug2 julli la
gog miineef na ko.

Waxal ku ñu raw, gaar na ko ginnaaw ilimaan jamaj, yaw dey niki aji-julli la moom doŋŋ.3

Ndeem toftaloo na ci ku ñu jiitu tukkee ci ilimaan aji-waral kojug bahda dana gaar,

ak kojug xabla bu tukkee ci boppam, kojug xabla dana ko doy naka la dikkee ca toxal ga4.

Koo xam ne fàttaliku na ab rukkoo ci biir ug sujjóot, na dellu, mbir mi muy aji-taxaw ca la nga xam ne
siiwalees na ko5.

Dees na sopp mu baamu dara ci njàng ma6; yal na fegaleef la am waccu7.

Topp, ndeem dellu na mbir mi muy aji-taxaw nag, mu rukkoo te mu sujjóot bahda-salaam, ngir ug dolli
gog tàbbi na8.

Koo xam ne fàtte na ñeel ab sujjóot te tàbbi na ag fàttalikoom ginnaaw taxaw ga, na dellu

jëm ca jotaay ba te mu sujjóot ndeem nekkutoon di jekki cag njëkk ca ka nga xam ne xel-lu na9.

Ndeem fàtte nga ñaari sujjóot yaw aji-xel-lu ji, rotal te sujjóot te doo jekki, kon danga jot njub ga10.

Sujjóotal bahda-salaam ci mbooleem loo xam ne tudd naa ko ngir dolli goo xam ne xameef na ko11.

Ndeem fàttaliku nga sujjóot ba, ba di bu ñu fàtte yaw aji-julli ji, ginnaaw yékkatig bopp ba
1
Ku am ci iliman benn mbaa ñaari ràkka, bu ilimaan di sujjóot xabla-salaam, day ànd ak moom waaye bu ilimaan di sujjóot
bahda-salaam, ilimaan a sëlmal waaye moom sëlmalagul, day eggale ba julli lañu ko rawee woon door a julli bahda-salaam.
2
Bu sujjóotee ànd ak moom te tey ko (négul ba àggale), kon julleem yàqu na.
3
Ku jamaj ba muy fey la ko ilimaan rawee woon, nee ko na ko defar niki buy julli moom doŋŋ. Waaye ilimaan du la ko mën
a gàddul.
4
Ku ñu jiitu nga xam ne ba mu jógee bay fey la ñu ko rawee woon, fekkoon la ilimaan jotoon a julli mu ànd kook moom, am
na ca loo xam ne dana ca sujjóot bahda-salaam (te xam nga ne loolu day nég ba eggale door koo sujjóot). Bi muy àggale di
fey lañu ko rawee woon far mu jamaj bob war na caa sujjóot xabla-salaam. Kon bahda-salaam boobee mu waroon a ànd ak
ilimaan, dakoy bàyyi te sujjóot xabla-salaam bi. Duñu boole ñaari sujjóot yi.
5
Bu fekkee danga dem bay sujjóot fàttaliku ne yaw kat rukkoowoo, dangay delluwaat taxaw door a rukkoo teg ci nga
sujjóot. Waaye doo taxaw rek daldi rukkoo.
6
Boo siggee dangay jàng tuuti door a rukkoo.
7
Maanaam lii nga jàng bañ a génn sam xel.
8
Bu delloo ba taxaw, ba jàng dara ba rukkoo nag, bu sëlmalee na sujjóot bahda-salaam ndax def yooyu mu doon def ag
ndollent la. Ndollent boo ko defee ci julli te jamaj waral ko, dangay sujjóot bahda-salaam.
9
Koo xam ne day julli, ràkka bi war a am ñaari sujjóot, nga sujjóot benn sujjóot, daldi jóg taxaw dem ci ràkka ba ca sës.
Waaye bi nga taxawee nag nga fàttaliku ne benn sujjóot nga def ci ràkka bi jàll, dangay dellu daldi toog sujjóot (boo
defutoon jotaay boobii, ndax ñaare jotaay bi, ku ko def doo fàtte sujjóot bi) door a dellu ci ràkka ba ca topp.
10
Bu fekkee ñaari sujjóot yépp nga fàtte ci ràkka bee jàll, bi nga demee ba ci ràkka bi ci topp nga fàttaliku ko. Boo koy fey,
dangay rot rek sujjóot ñaari sujjóot waaye doo fa toog ab jotaay doog a def sujjóot ya. Bu dee benn sujjóot la, ngay toog
door a sujjóot.
11
Yii ma la wax yépp nag, moo xam dangaa fàtte ab rukkoo ci jamono yi ngay sujjóot walla dangaa fàtte benn sujjóot walla
ñaari sujjóot yépp nga fàtte, soo ko defaree ba noppi nag, nanga sujjóot bahda-salaam ndax xamal ne dolli nga ci loo xam ne
bokkutoon ci julli gi. Mooy loolee nga def, defaat ko, dollent la te dollent boo ko defee ci julli te jamaj waral ko, dangay
sujjóot bahda-salaam.

52
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
tukkee ca ràkka ba nga xam ne méng na ko, wéyal ci sag julli ci waxi ku ñu gërëm ka.

Li mu ci jublu, bul nekk di aji-dikke ci bile sujjóot; li fi nekk wacc ko te nga dolli ab ràkka, mbir mi
ngay aji-jokk

te sujjóotal xabla-salaam ngir ug wàññi gog tàbbi na ànd ak ndollent1, kon danga nekk di aji-topp
sunna2.

Lii nag ndeem feeñ na ci ñaari ràkka yu njëkk ya te fàttaliku na ko ginnaaw bi mu jullee ràkkab ñetteel
ba3.

Ndeem nekkul ci ñaari ràkka yu njëkk yi mbooleseen, kon na sujjóot bahda-salaam ci la nga xam ne
déggeef na ko4.

Walla mu nekk tukkee ci [ñaari ràkka yu njëkk yi]5 waaye fàttaliku na ko njëkk fas ràkkab ñetteel ba

ngir faatul aw saar walla ab jotaay, waaye lii nag lu sew la ñeel koo xam ne dina xiyaas6.

II.2.3 JAMAJ CI JULLIG FEY AK GOG NAAFILA

Jamaj ci pey yaw samab xarit niki jamaj ci jooxal ca la ñu toxal7.

Jamaj itam ci naafila, niki jamaj ci julli farata ndare ñeel juróom-benni yoon dana dikk8.

Faatiha ak uw saar ak biral ak dolli ab ràkka, niki nii yelu.

Niki nii fàtte lenn ci ab ponk ci sàrtu ab yàggam9, naka mu nekkee ci yax bi.

1
Loolu boo ko defee dangaa boole wàññi ak dolli.
2
Sunna mooy boo boolee wàññi ak dolli, dangay notal wàññi ga, sujjóot xabla-salaam ngay def waaye bahda-salaam ba doo
ko sujjóot. Bu fekkee dangay julli jóge cib ràkka dem ca ràkka ba ca sës, topp siggi nga ca rukkoo ba ba wax “Sami Allaahu
liman amiida”, door a fàttaliku ne ràkka bee nga jóge kat fàtte woon nga ca ab sujjóot, léegi dangay wéyal sag julli waaye
sujjóot bi moom doo ko indeeti. Bu ko defee ràkka boobee nga fàtte woon sujjóot, dangay jàpp ne julliwoo ko, nga wacc ko.
Boo àggalee nga daldi dolli beneen ràkka boo xam ne moom ngay feyee ràkka boobee nga bàyyi woon ab sujjóot. Soo
noppee nag nga sujjóot xabla-salaam ndax boole nga wàññi ak dolli.
3
Xam nga ne ginnaaw julli nga ñaari ràkka ba dem ci ràkka ñetteel bi ba julli ko ba noppi; bu ñetteel boobee ngay jàppee ab
ñaareel ndax léegi tàbbi nga ci sab ñeenteel. Te léegi kon jéll nga taaya ju njëkk. Bu ko defee ràkkab ñetteel bii itam julli
nga ko te jàngoo ciw saar. Moo soppiku di sa ràkkab ñaareel. Te ràkkab ñaareel bi dañu cee waroon a jàng aw saar. Batey
kon bàyyi nga aw saar, kon wàññi nga.
4
Su fekkee nag nekkul ci ñaari ràkka yu njëkk yi niki ràkkab ñetteel ba ca nga bàyyib sujjóot walla ràkkab ñeenteel ba, kon
dangay daldi indi beneen bu ko wuutu waaye julli gi dara mànkewu ci luy waral ngay julli xabla-salaam. Waaye dolli
googee nga dolli mooy waral ngay julli bahda-salaam.
5
Waaye sujjóot walla rukkoo bi nga bàyyi, yaa ngi ko bàyyi ci ñaari ràkka yu njëkk yi, waaye bi nga laataa fas ràkkab
ñetteel bi fàttaliku nga ko. Kon xam nga ne ràkka ba danga koy daldi jàppe ab ràkkab ñaareel. Kon bu ko defee nga jàng ca
Faatiha ak uw saar te nga daldi taaya. Kon loola lenn loo wàññi amu ci, kon bahda-salaam ngay def ndax dolli nga def
waaye wàññiwoo.
6
Boo ko seetloo lu sew la. Danga koy faram-fàcce door koo mën a dégg.
7
Julli gi ngay def ci waxtoom ak julli ga ngay julli di ko fey, ñoo bokk ni ñu leen di defaree boo ca juumee.
8
Juum ci naafila ak juum ci farata ñoo yem bamu des juróom-benn yii nga xam ne wuute nañu, boo ko juumee ci farata ak
boo ko juumee ci naafila.
9
Jàngoon nga ne fàtte ponk lu yàgg day yàq julli.

53
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ku fàtte Faatiha te mu fàttaliku ko ginnaaw bi mu rukkoo waaye mi ngi ci naafila1,

Dana wéy ci julli ga, topp dees na sunnaal sujjóotu xabla-salaam2.

Safaanoo na ak farata, naka moom [farata] da koy wacc, dana dolli beneen ràkka bu ko wottee3.

Dana wéy te dana nekk loolee niki mu wéye woon ag leeralam foofee4.

Ndeem fàtte nga aw saar walla biral te yaw yaa ngi ci naafila walla ag yelu5.

Topp fàttaliku nga ginnaaw boo rukkoo, wéyal te déet di la war sujjóot

ci safaan doonte gaar na aji-julli farata, naka moom na ko sujjóot niki mu wéye woon6.

Ku jóg jëm ci ràkkab ñetteel ci naafila, ndeem fàttaliku na [ne dem na ci ràkkub ñetteel] njëkk ba mu
laataa fas

rukkoom, mu yékkati bopp fii tukkee ci rukkoo ba7 ci nettali gi;

na dellu di aji-jékki ngir la nga xam ne dees na ko sàkku foofee8, [bu noppee] dana sujjóot bahda-
salaam ngir jamajam9.

Wéyal te dolli ràkkab ñeenteel, topp nga sujjóot xabla-salaam ndeem rot nga ginnaaw fasug10 ràkka ba.

Ci safaanug, doonte dana tàbbi ñeel ka nga xam ne dafa nekk ci jullig farata11, naka moom day dellu
jëm cib jotaay

ci waxtu woo xam ne fàttaliku12 na ko, dana sujjóot ginnaaw sëlmalam ngir dolli goo xam ne dana
rot13.

1
Danga doon naafila fàttee jàng Faatiha te ba nga koy fàttaliku rukkoo nga ba noppi. Kon ràkka bi fasu na.
2
Kon Faatiha foofu, xam nga ne bu doon jullig farata ràkka ba day yàqu, waaye bu dee naafila mën nga koo sujjóotal xabla-
salaam te du tax sa naafila yàqu.
3
Kon jullig farata moom beneen ràkka ngay indi bu ko mën a wottee (wuutu).
4
Waxoon nañu kon soo ko indilee beneen ràkka nga daldi wéyal sag julli.
5
Xam nga ne aw saar, biral walla yelu boo ko fàttee dangay sujjóot xabla-salaam
6
Yii ñu la wax bu fekkoon julli farata ngay def danga leen di sujjóotal waaye bi muy naafila te ginnaaw rukkoo nga ko door
a fàttaliku, wéyal rek. Waaye doo ko sujjóotal te du tax sag naafila yàqu.
7
Bu xasee siggi ba ne "Sami Allaahuma liman amiida", fii moom la ràkka bi door a fasu. Waxuñu la fañ la waxoon ne la boo
sëggee rek ràkka ba fasu na. Bu fekkee ci naafila la, nga dem ba ci ràkkab ñetteel ba te xam nga ne naafila ci mashab imaam
Maalik ñaari ràkka ak sëlmal la. Yaw nga fàtte ko ba dem ca ñetteel ba…
8
La ñuy sàkku mooy jotaay ba daldi sëlmal.
9
Ndax taxawaay boobee nga ci dolli ci ñaari ràkka yi te jotagoo rukkoo. Te ku dolli dangay sujjóot bahda-salaam.
10
Ginnaaw léegi siggi nga ci ràkkab ñetteel ba ba wax "Sami Allaahuma liman amiida", foofu doo delluwaat di toog di taaya
ak sëlmal. Dangay wéy indi beneen ràkka muy ñeenteel, nga door a taaya te sëlmal. Bu dee naafila noonu ngay def.
11
Su fekkoon tey jullig farata niki ñaari ràkkay suba, nga dem ba ca ràkkab ñetteel…
12
Moom foo ko fàttaliku, doonte fas nga ràkka ba itam, siggi nga ci ràkkab ñetteel bi ba wax "Sami Allaahuma liman
amiida" itam, dangay delluwaat ndax jullig suba du doon ñetti ràkka, ñaar lay doon. Lii nga ci dolli lépp kon, jamaj la. Moo
tax mu ne…
13
Ndax loolee nga ca dolli, duñu la may nga cay dolli beneen ràkka muy ràkkab ñeenteel nga jàppe ko jullig suba. Ndax
jullig suba du ëpp ñaari ràkka. Waaye bu doon naafila moom, boo xasee fas ràkkab ñetteel ba siggi wax "Sami Allaahuma
liman amiida", duñu la may nga dolli beneen bu ñeenteel door a sëlmal. Kon gis nga ne foofu, ni ngay defare ñaari ràkka
yoo juum dem ci ñetteel ba te muy naafila ak ñaari ràkkay farata bokkuñu. Am nañu ag wuute.

54
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Ku fàtte ab poonk ci naafilaam goo xam ne feeñ na kem ñaari rukkoo walla sujjóot dees na ko xalam;

te tàbbiwul ag fàttalikoom ba mu sëlmal te yàgg na, moom déet dara di ko waral.

Wuute na ak lii, doonte rot na nekk ci farata; dana baamu1 ci lu dog fàww.

Képp koo xam ne dog na ag naafila cig tey walla ràkka mbaa sujjóot waxtu wu mu tàmbalee

na bàyyi ci moom te na ko baamu fàww ngir ag waram feeñ na ginnaaw tàmbali ga2.

Boroomug binni3 ndeem tuddul ciw araf, déet dara di ko war, mbir mi muy lu ñu joyal.

Ndeem jamaj na ilimaan cig wàññi walla dolli ngir ug fàtte,

te yaw yaa ngi ci ginnaawam, sàbbaalal4 ci moom yaw ki ñu jiite ngir mu yewwu5.

Ndeem dana jóg [moom ilimaan] tukke ci ñaari ràkka njëkk ba mu laataa jekki, sàbbaalal ba-tey6.

Waaye nag, ndeem tàqalikoo na ak suuf ci loxo ak bëti-wóom, xeeñtu ko yaw aji-roy ji7.

Jógal ndeem jekki na ci [ràkka] bu njëkk ba, ilimaan8, mbaa ci ràkka bu ñetteel9 ba, deefu la yedd.

Lu mu ci jublu, bul nekk di ànd ak ilimaan ci jotaay ba ngir naka moom déet muy ay barab ñeelub
jotaay10.

Ndeem ilimaan sujjóot na, ci jullig ñeenti ràkka, benn sujjóot doŋŋ ngir jamaj gog rot na

sàbbaalal ci moom te bul jóg di ànd ak moom feek ragaloo11 fas as rukkoo, topp ko.

1
Bu doon ci julli farata, boo fàttee sujjóot walla rukkoo sëlmal lu yàgg door koo fàttaliku, moom julli gi yépp ngay
baamuwaat.
2
Naafila moom boo ko xasee tàmbali dalaa daldi war. Boo ko daggee di nga ko tàmbaliwaat.
3
Mooy nga óbbali.
4
Nee ko "Subhaanalaa"
5
Ngir mu xam li mu dolli mbaa mu wàññi ko.
6
Bu fekkee dadoon julli julli gu am taaya ju njëkk ci misaal, mu am ñaari ràkka, toogul taaya lu dul mu dem ci ñetteel ba,
kooka danga koy sàbbaal ndax mu toog ndax foofu dafee war a taaya.
7
Waaye bu dee ñaari ràkka ya, ba mu ci jógee jëm ci ñetteel ba, ay loxoom ak i bëti-wóomam laalatuñu suuf. Loolu foofu
bul ko sàbbaal. Dangay jóg ànd ak moom.
8
Bu ilimaan amee ràkka bu njëkk daldi toog taaya
9
Tey julli jullib ñeenti ràkka. Mu am ñetti ràkka daldi toog defe ne matal na.
10
Ndax benn ràkka kenn du ca taaya. Niki nii ñetteelu ràkka bu jullib ñeenti ràkka.
11
Bu fekkee léegi sàbbaal nga ko, taxul mu xam yàq gi mu yàq, bu jógee dem ci beneen ràkka, bul ko fekki ndax benn
sujjóot la def. Kon yaw dangay toog, sujjóot sa sujjóotub ñaareel. Waaye bu fekkee yaakaar nga ne boo ko fa defee, ràkka
ba mu dem dana sëgg ba siggi ba wax "Sami Allaahu liman amidahu", dangay bàyyi loolu te topp ko.

55
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Topp cib ñaareel walla ñeenteel, bul jekki ginnaaw loolee ànd ak moom1.

Dollil, bu sëlmalee, beneen mu wottee bi nga xam ne wacc nga ko ci la nga xam ne wéy na.

Nekkal di aji-jokk te nga sujjóot xabla-salaam ngir boole2 ag wàññi ak dolli, wattul wax ja.

Ndaal mbooloo, sopp nañu ñeel leen jiital kenn, dana mottali julli gi ci ñoom3.

Ndeem sa ilimaan dolli na ab sujjóot bu di kojug ñetteel mbaa bob ñeenteel, bul sujjóot ànd ak moom4.

Li fi nekk, sàbbaal ko, bul dikke ci loo xam ne dana nekk ab dolli goo xam ne xameef na ko ci julli gi5.

Ndeem illiman jóg na ngir ug dolli, topp ko aji-wóolu lu waral taxawaay ba.

Am kemam boroom sikki-sàkka ci taxawaay ba, te na jekki ka nga xam ne wóolu na ndollent la,
xiyaasal.

Ndeem jekki na, ka ñu digal cig taxawaay, mbaa mu taxaw, ka ñu jekkiloo mu nekk ci wax ji,

julli képp ci ñoom ñaar yàqu na ci ñaari melo yi, fas ka nga xam ne dégg na6.

Ndeem iliman sëlmal na njëkk ag matug julleem ngir ug jamajam wëliis ag réer,

Na ko sàbbaal, ka nga xam ne ma nga ca ginnaawam, ndeem ilimaan dëggal na ko [ca la mu sàbbaal] ci
xam ug wàññi woo xam ne dana gaar.

Na daldi matal ag julleem, topp ginnaaw ag sëlmalam na sujjóot7; yal nanu am ag njub.

Waaye ndeem deŋŋi-deŋŋi8 na, ndeem xibaareef na ko [moom ilimaan], na laaj9 ñaar ñu maandu ngir
ñu saxal.
1
Bu ko defee ràkka boobee mu jóge ci ràkka bu njëkk ba (xam nga yàqu na), kon bu amaatee ràkkab ñaareel, toog defe ne
taaya ju njëkk ñëw na, bul taaya ndax xam nga ne bee baaxul. Benn ràkka ngay jàpp ne moom nga am. Bu fekkee daa defe
ne am na ñeenti ràkka ba tax mu toog di sëlmal itam, kon yaw dangay mottali.
2
Ni nga boolee wàññi gi mooy ràkkab ñaareel boobee moo soppiku di ràkka bu njëkk (taaya jooju mu fa def moo baaxul).
Ràkkab ñetteel ba moo soppiku doon ràkkab ñaareel. Fa mu waroon taayaa te taayawu fa, kon wàññi na. Ràkkab ñeenteel
boobu mu jàppee ñeeteelu ràkkaam, xam nga ne mooy ràkkab ñetteel kon taaya jim fa taaya baaxul. Looloo tax wàññi na.
Te ràkka ba muy julliwaat itam da koo dolli. Kon boole na dolli ak wàññi. Kon day sujjóot xabla-salaam.
3
Mbooloo mi bu leen wóoree ne ilimaan am na ràkka boo xam ne bàyyi na ca farata ba ràkka ba yàqu, bu ilimaan sëlmalee,
dañuy tànn kenn ci seen biir mu eggaleel leen ràkka boobee.
4
Boo gisee ilimaan sujjóot ñaari sujjóot di ca teg bob ñetteel mbaa bu ñetteel ba cay teg bob ñeenteel te mu wóor la ne da ko
caa dolli, buy sujjóot bul sujjóot ànd ak moom.
5
Boo nee ko "Subhaanalaa", bu ko xamul itam bul ko topp.
6
Ki xam li tax ilimaan taxaw ak ki war a toog, ku ci def safaanug li ñu la digal, sag julli day daldi yàqu.
7
Maanaam ilimaan su fekkee dafa sëlmal te julli gi matagut ngir ug jamaj. Ki nekk ci ginnaawam te xam ne daa juum daldi
koy sàbbaal. Ilimmaan ànd ak moom ci sàbbaal ga xam ne julli gi daa matul. Kon bu noppee, moom ilimaan, day mottali
julli ga teg ci bahda-salaam. Maamuun itam noonu lay def.
8
deŋŋi-deŋŋi mooy sikki-sàkka.
9
Foofu may nañu ilimaan mu laaj ñaar ñu nekk ci ginnaawam. Ne leen waa ji lutax mu naan “Subhaanalaahi” ngir mu xam
lan lay def. Kon ilimaan may nañu ko mu wax.

56
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
Daganal nañu wax ak ñaar ñu maandu ca boobee ca loolee1 wëliis nar.

Ngir xibaar ba ñu nettali, jële ca ñi ñu dëgërloo ci mbirum Sul Yadeyni2 ci julli.

Ndeem ilimaan wóolu na matug julli gi, dees na sàkku ag jëfam cig wóoloom3.

Ak ug bàyyeem loo xam ne ma ngay sikki-sàkka ci moom ndeem bariwul4 aw nit fa ginnaawam,
xamal.

Ndeem dana ko jariñ dëgg seenug xibaar, na bàyyi ag wóoloom te mu dellu topp leen5.

1
Loolii ñu leen laaj mën nañu koo toontu, waaye dañuy toontu yem ca doŋŋ.
2
Sul Yadeyni, yonent bi (saw) dafa mësaan a julli tàkkusaan, taaya ci ràkkab ñaareel ba, sëlmal. Sul Yadeyni ne ko “Julli
tàkkusaan dañu koo wàññi léegi def ko ñaari ràkka walla dangaa juum?”. Yonent bi ne ko “Damaa juum”. Mu ne ko “Lu mu
doon?”. Mu ne ko "Ñaari ràkka de nga julli". Mu daldi jóg àggale. Foofa la ñu gisee ne sa ilimaan bu juumee, nga sàbbaal
ko xamul li nga ko wax. Mën na laa laaj te yaw it mën nga koo toontu.
3
Ilimaan jàpp na ne julli gi mat na. Na jàpp la mu jëfandikoo.
4
Bu fekkee mbooloo mu baree ko sàbbaal, moom mu jàpp lu wuuteek loolu, kon day fekki mbooloo ma.
5
Bu ko mbooloo ma leeralee ne daa juum, kon day bàyyi la mu jàpp fekki mbooloo ma.

57
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

58
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Lii mooy la nga xam ne jublu woon naa dajale ko, mat na, ci ndigalu ka nga xam ne dana méngale
mbébét ma ku ko soob.

Maa ngi sant ag cant ñeel sama Boroom kay Buur ba, ka dib Sellaakon ci matug téere bii di Jawharun-
nafiis (Wurus wu gànjaru).

Muy lu ñu woy, dana jàpp xol ba ngir taar ba. Mbir mi muy aji-kawe di wesaru Ibnu Abbaa1.

Waaye Ibnu Abbaa nag, ci sababug jiitu ga, sang nanu te kawe nanu ci itte ya 2.

Déet nun nu mel ni moom ci xam-xam ak ug xam Yàlla, ak ug wuññiku, ak i leer ak ug wóolu.

Yal nanu Yàlla jariñ ci moom ak ci mbooleem ay kemam ci jépp aji-yiw di aji-topp Yàlla.

Làq na limub xisban3 ciy bayit; dana deñal bekkoor4 ñeel boroomi aajo.

Ñaan naa Aji-wëlsëgal mbindeef yi, kay Aji-màgg, nekkug sama woy wii di lu ñu nangu.

Te mu nekk di aji-jariñ niki cosaan5 la te mu seral bët ba fas képp.

Te mu nekk di sabab6 ñeel ubbig aji-tàmbali ci moom ak fajug aajo.

Ak mu fey kawe képp ci nun ci ñeewant ak njéggal njëkk sunu njàqare7.

Ak ma dajeek aji-bijj ab yool ci woy wi fa faatu ga ak bésu pang ba8;

ci darajay làmpu mbindeef yi Muhammad9. Yal na dolli tedd-nga te mu dolli wóolu ci moom Yàlla
may kojug dappet;

ak ñoñam, ak saabaam ña di way-tedd feek am na aji-jub ngën jaa rafet ag muj10.

Tudd naa sellug saa Boroom, kay Boroom tedd-nga ja wëliis la nga xam ne danañu ko melal Yàlla11.

Ag mucc yal na nekk ci ñañu yónni ña. Ag cant ñeel naYàlla may Boroom mbindeef yi.

1
Moo bidoon Laxdariyu.
2
Jiitu gi mu nu jiitu ba njëkk noo woy Laxdariyu, moo tax mu doon sunub sang te moo nu gën a kawe yitte ndax ci yitteem
lanu royee ba def téere bii.
3
Xaa gi mooy juróom-benni téeméer (600). Saad gi mooy juróom-benn fukk (60). Baa gi mooy ñaar (2). Kon boo leen
boolee muy 662.
4
Xisban mi ngi firi naataange. Te naataange moo fiy jële bekkoor. Kon boo amee bekkooru xel, boo jàngee téere bii danga
am naataange.
5
Ni Laxdariyu amee njariñ, na ko Jawharun-nafiis amee njariñ. Te na seral xolab képp koo xam ne gis na ko.
6
Képp ku ci tàmbalee am njàng muy sabab sa ubbikum xel ak sa fajub aajo itam.
7
Maa ngi ñaan itam sunu Boroom feye nu ag ñeewant (yérmandeem) ak njéggalam bala noo jàq.
8
Maa ngi ñaan sama Boroom mu tasale ma ci yoon wu dijj a dijj bu ma faatoo ak bésub pang ba ñéppiy daje.
9
Yonent bi (saw) moo ne woon : "Deeleen ñaan ci sama daraja ndax sama daraja lu màgg ci Yàlla la”.
10
Feek ku jub mi ngi am mujj gu rafet, sama julli gii bu mu dagg..
11
Te Yàlla sori na ak loola. Ñenn ñi dañu naan Yàlla nàngam la tollu, Yàlla am na doom, Yàlla ma nga nekk ca kaw, Yàlla
barab sàngam la nekk te Yàlla soree na ak loola.

59
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

60
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Jullit yu bari ci réew mi, xamuñu li ñuy wax, ci njàpp mbaa ci julli, li muy tekki. Li ko waral mooy
dégguñu làkku araab. Ngir saafara loolu moo waral ñu ubbi bii buntu. Ab sof la ci téere bi bu bokkul
woon ci li Séex Ahmadu Bàmba bindoon ci Jawharun-nafiis. Ñi ngi ci tekki ci wolof lépp liñuy wax ci
njàpp ak ci julli ngir yombal jullit yi ñu xam maanaa yi ngir gën a mën a teewlu ci seenug jaamu Yàlla.

Li ñuy wax ci njàpp:


Boo jàppee ba noppi :
Dangay seede (mooy “Chahaada” ci làkku araab). Sunna la su wér su yonent bi (saw)

« ‫أشهد أن آل إلَـهَ اِال هللا وأشهد أن محمدا رسول هللا‬ »

Ci arafi latin: “Ach hadu an laa ilaaha illalaa, wa ach hadu anna Muhammad ar-rasuululaahi”

Di tekki : “Maa ngi seede ne amul beneen buur bu dul Yàlla te Muhammad yonentam la".

Li ñuy wax ci julli :

 Booy nodd:

Lim Araab Latin Wolof

Ñaari yoon ‫هللا أكبر‬ Allaahu akbar Yàlla màgg na

‫اشهد ان ال اله‬ Ach hadu an laa ilaaha Maa ngi seede ne amul beneen
Ñaari yoon
‫اال هللا‬ illalaa buur bu dul Yàlla

Ach hadu anna


‫اشهد ان محمد‬ Maa ngi seede ne Muhammad
Ñaari yoon Muhammad ar-
‫رسول هللا‬ rasuululaahi
yonentam la

Ñaari yoon ‫حي على الصالة‬ Hayyaa las-salaat Ñëwleen julli

Ñaari yoon ‫حي على الفالح‬ Hayyaa lal-falaah Ñëwleen ci mbég mi,

Ñaari yoon ‫الصالة خير من‬ As-salaatu xayru min an-


Julli moo gën nelaw.
Njël rek (fajar) ‫النوم‬ nawm

Ñaari yoon ‫هللا أكبر‬ Allaahu akbar Yàlla màgg na

Benn yoon ‫ال اله اال هللا‬ Laa ilaaha illalaa Amul beneen buur bu dul Yàlla

61
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]
 Booy liqaam : Li ngay wax booy nodd ngay wax waaye bu ci nekk benn yoon nga koy wax ba mu
des Allaahu akbar. Moom ñaari yoon lañu koy wax ci njalbéen gi ak ci mujjantal gi.

 ْ َ‫أ‬
Booy kàbbar : « ‫كبَر‬ ‫هللا‬ » . Ci arafi latin: « Allaahu Akbar », di tekki “Yàlla màgg na”.

 Booy rukkoo : « ‫» سبحان ربى العظيم وبحمده‬. Ci arafi latin: “Subhaana rabbiyal Aziim
wa bi hamdihii”, di tekki “Tudd naa sellug Buur bu màgg bi te di ko sant”.

 Boo siggee ci rukkoo : « ‫» سمع هللا لمن حمده‬ . Ci arafi latin : “Sami Allaahu liman
hamidah”, di tekki “Yàlla dégg na ki koy sant”.

 Ba-tey boo siggee ci rukkoo : « ‫» ربنا لك الحمد‬. Ci arafi latin : “Rabbanaa wa lakal hamd”, di
tekki “Yàlla Yaw yaa yeyoo cant”. Waaye lii bu ñu la jiitee nga koy wax.

 ْ ‫ » سبحان ربى األعلى اللّ ُهـ َّم ا ْغ ِف‬Ci arafi latin : “Subhana rabbiyal
Boo sujjóotee : « ‫ـر لي‬
a’laa, Allaahuma ixfirli”, di tekki “Tudd naa sellug Buur bu kawe bi, Yal na nga ma jéggal”.

 Diggante ñaari sujjóot yi : « ْ ‫ َوا ْهدِنـي َو‬، ‫ار ُز ْقنـي‬


‫اجبُ ْرنـي‬ ْ ‫ َو‬، ‫ار َح ْمـني‬ ْ ‫اللّ ُهـ َّم ا ْغ ِف‬
ْ ‫ َو‬، ‫ـر لي‬
،‫ارفَ ْعـني‬
ْ ‫ َو‬،‫َوعافِنـي‬
». Ci arafi latin "Allahumma ighfir lî, wa-rhamnî, warzuqnî wa-
hdinî, wa-jbournî, wa’afi’ni, , wa-rfa’ni” di tekki “Yàlla, yal na nga ma jéggal, yal na nga
yërëm, yal na nga ma jubal, yal na nga ma yiir, yal na nga ma jàmmal, yal na nga ma
wërsëgal, yal na nga ma yékkati”.

 Ci taaya gu njëkk :

« ‫التحيات هلل الزكيات هلل والطيبات الصلوات هلل السالم عليك ايها النبي و رحمة‬
‫هللا و بركاته السالم علينَا و على عبادك الصالحين أشهد أن ال إله إال هللا وحده ال‬
ّ ‫» شريك له وأشهد‬
‫أن محمدا عبده ورسوله‬
Ci arafi latin: “At-tahiyyatu li-Llaah, az-zaakiyatu li-Llaah. At-tayyibaatu as-salawaatu li-Llaah.
As-salaamualayka ayyuha n-nabii-u wa rahmatu Llaahi wa barakaatuh. As-salaamu alaynaa wa
alaa ibaadi-Llaahi s-saalihin. ach-adu al-laa illaaha illa Llaah wa ach-hadu anna Muhammadan
abduhu wa rasuuluh”.

Di tekki wi wolof : “Mbooleem baatu nuyyoo yu tedd yi ñeel na Yàlla, mbooleem baat yu sell yi
ñeel na Yàlla, mbooleem baat yu teey yi ñeel na Yàlla, mbooleem julli yi ñeel na Yàlla, jàmm yal
na nekk ci yaw Yonent bi, ak yërmaande Yàlla ak ay barkeem. Jàmm yal na nekk ci nun ak
mbooleem gaa yu baax yi. Maa ngi seede ne amul beneen buur bu dul Yàlla te Muhammad
yonentam la”.

62
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

 Ci taaya ñaareel bi : Dangay waxaat li nga waxoon ci taaya bu njëkk bi teg ci lii topp.

« ‫ے‬ َ
َ ‫يم و عل‬ َ ‫ے إِب َْرا ِه‬ َ ٌ َ ‫ص ٌل علَے ُمح َّم ْد و علَے آل ُمح َّم ْد كما‬
َ ‫صليت عل‬ َ َ َ ‫اللَّ ُه ّمے‬
َ َ َ
‫يم و‬
َ ‫ے إِب َْرا ِه‬َ ‫ے آل ُمح َّم ْد كما باركـت عل‬ َ ‫ے ُمح َّم ْد و عل‬ َ ‫يم وبارك عل‬ َ ‫آل إِب َْرا ِه‬
‫ے آل إِب َْرا ِهيم فى ْال َعالَ ِمين إِنَّك َحميدٌ َم ِجيد‬ َ
َ ‫» عل‬
Ci arafi latin: “Allaahumma salli alaa muhammadin wa alaa aali muhammadin kamaa sallayta
alaa ibraahima wa alaa aali ibraahiim, wa baarik ala muhammadin wa alaa aali muhammadin
kamaa baarakta alaa ibraahiima wa alaa aali ibraahiima, fil aalamiina, innaka hamiidun majii ”.

Di tekki ci wolof : “Yàlla, yal na nga dolli xéewal Muhammad ak waa kër Muhammad, naka nga
dollee xéewal ci Ibraahiima ak waa kër Ibraahiima. Yàlla na nga barkeel Muhammad ak waa
kër Muhammad na ka nga barkeelee Ibraahiima ak waa kër Ibraahiima. Ci àdduna bi, ku ñuy
sant nga, ku tedd nga”.

 Booy sëlmal :
Dangay wax jëme ci ki nekk ci sa ndijjoor « ‫السالم عليكم‬
», di ci arafi latin “As-salaamu
alaykum” di tekki “Yal na Yàlla def jàmm ci yéen” teg ci wax jëme ci ki nekk ci sa càmmoñ :
“As-salaamu alaykum”.

 Booy xunóot1 : Dangay wax :

« ‫ َو نَت َ َو َّك ُل َعلَي َْك َو نُثْنِ ْي َو‬،‫نؤم ُن بِ َك‬ ِ ‫ َو نَ ْست َ ْغ ِف ُر َك َو‬،‫اللَّ ُه َم اِنَّا نَ ْست َ ِع ْينُ َك‬
َ ‫ اللَّ ُه َّم اِي‬.‫نَ ْش ُك ُر َك َو ال نَ ْكفُ ُر َك َو نَ ُخلَ ُع َو نَتْ ُركُ َم ْن يّ ْف ُج ُر َك‬
‫َّاك نَ ْعبُدُ َو ن َْر ُج ْوا‬
‫ار ُم ْل ِح ٌق‬
ِ َّ‫» َر ْح َمت َ َك َو ن َْخشى َعذَابَ َك اِ َّن َعذَابَ َك ِب ْال ُكف‬
Ci arafi latin: “Allahumma inna nasta'inuka wa nastaghfiruka, wa nu'minu bika wa
natawakkalu 'alaika wa nuthni 'alaikal khair, wa nashkuruka wa la nakfuruka wa nakhla'u wa
natruka manyyafjuruka, allahumma iyyaka na'budu , wa laka nusalli wa nasjudu wa ilaika nas'a
wa nahfidu wa narju rahmataka wa nakhsha 'adhabaka inna 'adhabaka bil kaffari mulhiq.”

Muy tekki wi wolof: “Yaw Yàlla, Yaw lanuy sàkku ndimbal, Yaw lanuy sàkku njéggal. Dinanu la
gëm te ci Yaw doŋŋ lanuy wéeru. Dinanu jëme ci Yaw ag yiw. Dinanu la sant te dunu la weddi.
Dinanu summi lépp lu wuuteek Sa diine. Dinanu bàyyi képp ku La weddi. Yaw Yàlla Yaw doŋŋ
lanuy jaamu, Yaw doŋŋ lanuy jullil, Yaw doŋŋ lanuy sujjóotal. Ci Yaw lanuy dox jëm, dinañu
fàndeñu2. Dinañu yaakaar sa yërmaande, dinañu ragal sa mbugal. Sa mbugal ci ñi weddi luy am
la.”

1
Xunóot nag ñi ngi koy wax ci ñaareelu ràkkay fajar, ci boo siggee ci rukkoo laata ngay sujjóot.
2
fàndeñu mooy bañ a sol dàll
63
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

64
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Taabal jii ci suuf day wone lim bu matale ñeel araf yu abajada wolof ànd ak ay misaal.

Araf Misaal Araf Misaal Araf Misaal

a am k kër ñ ñaw

à jàng l lam ŋ ŋaam

ã sãs m mar o gor

b bakkan mb mbër ó jóg

c car mp samp p paaka

d dag n nelaw q bàq

e ker nc sanc r ràbb

é wér nd ndab s sago

ë bët ng ngelaw t taw

f fal nj njaay u tur

g garab nk tànk w woo

i tis nq sànq x xalam

j jaay nt bant y yaakaar

Araf yi ñu séexal

Baatal Baatoodi Baatoodi

Araf Misaal Araf Misaal Araf Misaal

aa saar bb rëbb mm damm

ee weer cc fàcc nn dënn

ée wéer dd àddu ññ soññ

ëe bëer jj kajj ŋŋ doŋŋ

ii tiis gg dagg pp nopp

oo woor q soq rr fërr

óo wóor kk takk tt gàtt


ll wallu

65
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

66
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

A M
Aaw ............................................................................... 14 Mbañeel ........................................................................ 16
Abajada Wolof............................................................... 61 Mbërëg .......................................................................... 29
Abduraxmaan Laxdari ................................................... 10 Mudaarante ................................................................... 17
Àndakub kàccoor .......................................................... 17
N
B
Ngënéel ......................................................................... 23
Bañ jëmm ...................................................................... 12 Ngistal ........................................................................... 13
Njàpp ............................................................................. 22
C
Noddu ........................................................................... 57
Cangaay ......................................................................... 25
P
Chahaada ....................................................................... 57
Po .................................................................................. 16
D
R
Delloo tooñaange .......................................................... 10
Dereti meret .................................................................. 30 Rambaaj ........................................................................ 14
Digle.............................................................................. 12 Reetaane ........................................................................ 16
Réy ................................................................................ 13
F
Rukkoo .......................................................................... 58
Fàllas ............................................................................. 19
S
Farata ............................................................................ 22
Fen ................................................................................ 13 Sàkku ngërëmal mbindéef ............................................. 18
Sàrti julli ........................................................................ 32
G
Sàrti tuub ....................................................................... 10
Giñ ................................................................................ 11 Seex Ahmadu Bàmba Mbàkke ........................................ 5
Gis ngënéel.................................................................... 16 Sobe .............................................................................. 21
Sopp jëmm .................................................................... 12
J
Sunna ............................................................................ 22
Jamaj ............................................................................. 41
T
Jëw ................................................................................ 15
Julli................................................................................ 31 Taaya............................................................................. 58
Julli yi faat..................................................................... 39 Taaya ñaareel ................................................................ 58
Tere ............................................................................... 12
K
Tiim............................................................................... 27
Kàbbar ........................................................................... 58
W
L
Wattu cër yi ................................................................... 12
Laab .............................................................................. 21 Wattu sab gis ................................................................. 11
Lekk alal ci turu diine ................................................... 17 Wax ju bon .................................................................... 11
Lekk alali nit ñi ............................................................. 17 Waxtu julli yi ................................................................ 31
Li war mukàllaf ............................................................. 10
X
Liqaam .......................................................................... 57
Lu dagan........................................................................ 12 Xool jàmbur bu jigéen .................................................. 17
Lu ñu sib ....................................................................... 17 Xunóot .......................................................................... 59

67
Jawharun-nafiis
[Choisir la date]

Seex Ahmadu Bàmba : Ñu di ko woowe Seriñ Tuubaa walla Xaadimu Rasuul


(di baatu araab buy tekki “ Liggéeykatu yonent bi ”), moo bindoon téere bi ci
làkku araab tudde ko “Jawharun-nafiis”. Mi ngi gane àdduna ci atum 1853 ca
Mbàkke (ñu daan ko wax Mbàkke-Bawol), wuyuji Boroomam bésub 19
sulet 1927 ca Njaaréem (Jurbel) ci Senegaal.

Nitu Yàlla la woon bu ràññeeku, teg ci nekkoon boroom xam-xamu diine bu


mag a mag. Mooy ki taxawal yoonu Murit, sanc Tuubaa, taalif lu sakkan ci
diine te indi ay gisiin yu bees. Nekkoon na it bañkat bu mag bu wéeru woon
doŋŋ ci Yàlla.

Moo taxawoon jàmmaarlook tubaab yi ngir xeexal Islaam. Ginnaaw gi ñu jéem koo sànk ci pexe yu
bari, génne ko ay yoon réewam. Waaye teewul mu mujjee am ndam seen kaw, ginnaaw bi mu muccee
ci seeni pexe. Tey jii ay njàngaleem ak i jëfam law nañu fépp ci àdduna.

Sëriñ Xaadim Mbay: di sëriñ daara la bu dëkk Tuubaa Daaru Xuddóos moo
def bii tekkib Jawharun-nafiis ci wolof. Mi ngi juddi ci atum 1958 ca Tuubaa,
jàngee ci Sëriñ Seex Séy mu Daaru Xuddóos ak Sëriñ Aas Jaxate miy jàngale
ci jumaa ji ak Sëriñ Abiibu Mbàkke ak Sëriñ Asan Busó mom Gede. Ginnaaw
loolu def na yeneeni gëstu. Mi ngi tàmbalee jàngale xam-xam nag ci atum
1975.

Yemul rek ci Jawharun-nafiis. Jot naa tekki yeneen téerey Sëriñ Tuubaa yiy
jàngale diine. Mënees na cee lim Tazawwudus-sixaar, Nahju, Masaalikal-
jinaan, ak ñoom-seen. Tekki na it Jazbul-xulóob ak Huqal-bukaaw.

Allaaji Mamadu Ngeer : Mi ngi juddi ci atum 1972 ca Ndakaaru, yaroo


Pikin, jàngee ekool 1 bu Tali bu mag, jaar ekool Gaynde Faatma bu Pikin, teg
ci liise Limaamulaay bu Géejaway laata moo dem Iniwersite bu Ndar. Ginnaaw
bi, jaar na ci yeneen Iniwersite yu Tugal ngir mottali xam-xamam ci Matematik
ak Informatik.

Tey jii, mi ngi liggéey ca Iniwersite bu Ndar ci wàllu jàngale ak gëstu xam-
xamu informatik rawatina ci suqali làkki réew mi jaare ko ci xarala yu yees yi.
Doon na it ku xam-xamam màcc ci wàllu mbindum wolof ci arafi “latin” ak
yoy araab.

Ay gëstoom a ngi jëm ci fexe ba làkki réew mi am ay baatukaay ci xarala yu yees yi, ay jumtukaayi
informatik yuy jubbanti mbind, ay jumtukaay yuy tekki làkk faranse mbaa àngale jëme ci sunu làkk yi,
ay jumtukaay yuy bind ay kàddu, ay jumtukaay yuy wax ay bind, ak ñoom-seen.

You might also like