You are on page 1of 45

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 1

Ay wolofalu
Soxna Maymunatul Mbàkke
Kubra

Aji bindaat ji : Sëriñ Móodu Jenn

© 1445 h / 2024 - Paris


Tous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre adresse mail:
serignmbayjaxate@gmail.com
Vous pouvez nous suivre sur youtube :
http://www.youtube.com/@serignembayediakhate1075

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 2


Indications (Source : Drouss.org)
Wolof Français
e=é per pér
u = ou rus rous
c = th caam thiam
ñ = gn ñam gnam
x = kh xol khol
j=j jibi jibi
nj = nd njaay ndiaye
nd = nd nday ndeye
ŋ ŋaam (machoire)
ë = eu gëm = gueum
é = è (plus dur) = rér perdu
óo = au góor gaure
q = xx suqali soukhali

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 3


Sommaire
1. Maymuunatul bintul Xadiim ............................................................................................................ 5
2. Marsiya Soxna Xadi Mbàkke ............................................................................................................ 7
3. Marsiyya Soxna Joob Mbàkke ......................................................................................................... 9
4. Siyaare Naawel ak Poroxaan ......................................................................................................... 12
5. Siyaare naawel ak Poroxaan bis .................................................................................................... 14
6. Weeru Koor ................................................................................................................................... 17
7. Weeru koor ak Sëriñ Tuuba ........................................................................................................... 23
8. Weeru Gàmmu .............................................................................................................................. 27
9. Weeru Gàmmu (bis) ...................................................................................................................... 33
10. Tawfeex ..................................................................................................................................... 38
11. Moom ak Sëriñ Muusaa Ka........................................................................................................ 40

Vous pouvez trouvez la playlist de Soxna Maymuunatul Mbàkke


Kubra sur notre page youtube en cliquant ici

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 4


1. Maymuunatul bintul Xadiim

Maymuunatul Bintul Xadiim,


War na la foo toll di jéem
Lu neex Sëriñ bu Mag bi ndéem
Am nga ci ngor dara dara

War na la Sant Yàlla lool


War na la tuubal ko te xool
Li mu la may te xam ne tool
Ku ca ne war di def dara

Jëfal te rikk bul tawat


Yaa ngi ne wett te warut
Jògal, te sadd ay bayiit
Te yëg ne nekkoo ci dara

Alhamdu Lillaahi Boroom


Haras ki xam ne moo nu moom
Xam na ne sant naa ko moom
Ki xam ne réere wul dara

Te xol bi yéené wul lu bon


Bennub jullit bëggul lu bon

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 5


Te Yàlla xam na doyna kon
Naa ko dagaan file dara

Buur Yàlla moo mat a dagaan


Yonen ba moo mat a wayaan
Seex Bàmba noo ngi deet i ñaan
Mucc ci jépp larara (lor)

Buur Yàlla noo ngi lay dagaan


Yonen ba noo ngi lay wayaan
Seex Bàmba noo ngi deet i ñaan
Ag bañ a tàbbi sawara

Jamono jii nu toll tey,


Nu yees a laat ba di la Woy,
Na nga nu may tawféex ju rëy,
Te Xol yi na nga léen saafara

Nañ man di dox tey bañ di soox,


Bun xuloò mukk a ka xeex,
Te yàqkat yi mel ne meex,
Buñ nu manal mukk dara

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 6


Seerel ni tuub na nu bu wòor
Sant la yit bañ defi jòor
Yar nu ba muñ jàdd sa mboor
Def nu ñu dul dem sawara

Man Seexu Bàmba laa gëram


Gëm ko moo am ci man xorom
Yalna nu may ak saf xorom
Te dolli jépp sutura

Te may nu ay leer aki mbòot


Yu rëy te yokk nu’g njaboot
Musal nu noog sunug njaboot
Ba bu nu gis si lor dara

Fajal sunuy aajo te bul


Nu nattu bul nu jéppi bul
Nu xaare bul nu topp bul
Nu jàppe luñ deful dara

2. Marsiya Soxna Xadi Mbàkke

Bismil ilaahi ma def tay ay bëyit si mbirum


Bintul Xaddimi rasuululaahi moo waare

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 7


Te wàññi rangooñ yi feesal xol bi léeg ma gëlam
Te jéem a farlu te tuubal Yàlla kiy Baari

Ngir doomi lislaam du tiisoo mbir mu Yàlla dogal


Dàkkal nu Séytaane yaa habiiba kal jaari

Cëy doomi Bàmba ja taxsiisam ya nekk ci moom


Xadiijatu doomi tawfeex bis ba lay leere

Sëriñ bi mo soxla doomam woo ko kenn yëgul


Diisowul ak kenn moo sañ wax bii ley biire

Jumaadal uula di yawmal lahdi fukki fan ak


juroom yu teg benn bis lay woote tey waare

Guddig dibéer ga la woo mbokkam ma Seyyidunaa


Sëriñ Suhaybu la wax mbootam ya moo waare

Leeral mbirum àddunaam baayam yoral ko mbirum


Aalaxiraam bàyyiwul sax bor bu ñuy seere

Daarul Xudoos la ko baayam teeru ñépp taxaw


Seex Mustafaa moo ko waajal jox ko ay yéere

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 8


Seex Mustafa nee ku yàkkaar Bàmba ñépp na dem
Seex Fadiloo ko dugal néegam ga muy reere

Moo sell baatin rafet saahir mujam ga rafet


Baay baa ko soxla mu dem firdawsi lay jaare

Kii sant reka ci war yàlnan ko yàgg defal


Ay ñaan mu bokk ak magam yaak baay ya moo waare

Ndey Xadi jàppal bëyit yii muy bidaaya ci yaw


Sa taalibeb baay bu waaro waaru bay waare

3. Marsiyya Soxna Joob Mbàkke

Ma ñëw fi def marsiyab koo xamni kii gisumab


Kemam si rakk yi ak mag yi ak ñi di maasam

Te jooy fi saa jooyi xol yii def ko muy wolofal


Te wax ci la xam ci moom,céy aka dib yaaram !

Boo ko xamul moo di bintu Sheexuna wa xalii


Linaa wa seyyidinaa tay sëti Maam Maaharam

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 9


Batay bu ngeen ko xamul moom la Sëriñ bi joxoon
Seex Abdu Rahmaan mi baaxo xamle ngir baayam

Xamal na mboolem ku baayam jur xamal na itam


Mboolo ci ay taalibeem bañ xam ngir ug baaxam

Sëriñ bi wóolu ko def kob sàmm jox ko ñoñam


Te sax la cay seere moo yor ngën ji kuy maasam

Moo yar ki tax ba ma jug tay jii di marsiya ngir


Baaxam gu làmbi asal moo aw ngirub baayam

Moom mii Sëriñ Abdu la wax moom la Bàmba di fay


Ci sang bii boole kersa ak xam akub taaram

Ma ràññeleel la turam wa soxna Joob la ñu koy


Wax Mbàkke Bàlla asal tay jii ma ngaak baayam

Bisub àllarba ci waxtuw tàkkusaan la nu may


Wax ag demam sama xol baa raw xolub yaayam

Yarook fullaak kersa ak làmmiñ wu gàtt ak ab


Taaram la boole bindoon na’b teere ngir baayam

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 10


Daawul xulook ku ko mag daawul xas it ku mu mag
Daf daa feral ñépp moo gën nag ku fiy maasam

Dafmaa bëgoon lool ba def mab soppe mootaxitam


Feeg maa ngi dundu damay jooy sëtu Maam Maharam

Budul kon ag xamni Mqaamaa waral ñu ni cas


Saa soppe boobe danaa jooy jooy yu dig waaram

Waaye damaa xam ni rëy maqaama rekk a waral


Sëriñ bi jëlsi ko xaat ëskëy bileb yaaram

Sëriñ bi yàlna nu taas ci darajaam ya mu am


Musal ku bokk si moom te def ma may haalim

Ndax Yàlla buñ ma defee haalim ma dolliku ay


Bëyit yu sell yu diw taggam te dii yaaram

Alhamdulilaahi Rabil haalamiina damaa


Bëgoon a man woy yu yellook ngën ji kuy maasam

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 11


4. Siyaare Naawel ak Poroxaan

Alhamdu wa shukru mahal lilaahi


Alal Xadiimi wa Rasuulilaahi

Suma salaatu wa salaamu sarmadaa


Ala nabiyi wa rasuulu ahmadaa

Man sant naa Buur Yàlla fi shahrayni


Li ma gënoona bëgg fii Daarayni

Ca la ko am moo tax ma sant Yàlla


Si ki nu jiite wan nu yoonu Yàlla

Jumaadal luula wa jumaada saaniya


Si la siyaara sunu yaari maam ya

Siyaara Maam Jaara rabiihul awwali


Jumaada saaniya ma agg naawelli

Siyaara Maam Asta ba far ñaanal fa


Ku sopp Seex Bàmba yërëmlu naa fa

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 12


Melna ni demnaa Makkatal Mukarrama
Te àgg na Mediinatul Munawwara

Mootax ma sadd yii bëyit muy seere


Si sama may gi dañu maa laabire

Qad fakka kabla njort naa ko sirra


Qad baasha faddla seere naa ko jëhraa

Tabaarakal laahu na Buur jeggal nu


Dunya wa uhraa daa iman musal nu

Te may nu jàmm akuw yiw feexal nu


Te suturaal nu te yëram nu yar nu

Fajjal nu sunu aajo yépp Mbàkke


Ci darajay Maam Asta Waalo Mbàkke

Ku sopp Seex Bàmba ca laa ko boole


Siran wa jëhran Bàmba may nu doole

Naa xatmu way wi nag te daal di julli


Ci gën gi yonnen ak ñoñam fassali

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 13


Rabi salaatan wa salaaman abadaa
Ala nabiyinaa wa man tahabada

Wal aali was sahbi mahan sàmmal nu


Sun xol yi ak sun cër yi dimbaleenu

5. Siyaare naawel ak Poroxaan bis

Bismil ilaahi noo ngi santaat Yàlla


Cant gu rëy goo xamni am na yilla

Moo nu mayoon bañ sant fi Shahrayni


Moo dellu tawfeexal nu fi yawmayni

Bi laylatil jumhati fi shahri Shawwaal


Ci nga nu wan li nga nu may yaa xayra waal

Ajuma lañ siyaare woon Maam Jaara


Ngir darajay ngëneeli doomi Jaara

Bam dellusee lanu siyaare Naawel


Maam Hafsa ñeer nu ba nu wasal fab kaamil

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 14


Ci wenn weer di ñaari bis yu tegalo
Tabaarakal laahu dinaa bu kenn xuloo

Bu kenn xeex yalna nu tàppe xol yi


Rayal nu ag noonu wéral sun cër yi

Mag ñi yërëm gone yi ñepp’iy ñenn


Gone yi fonk mag ñi lepp’iy lenn

Ci darajay sibti Habiibil Laahi


Xadiimi ibn ibn Abdil Laahi

Nun la ñu am bàrkeem a maa xam loolu


Te lunu aar mbóotam a maa gëm loolu

Kon nag nu war di sant kulla shahri


Wa kulla yawmin bi nabibn sihari

Aleyhi salli suma salim sarmadaa


Wa aalihi wa sahbihi mu’abada

Melna ni dem naa Màkkatal Mukarrama


Te àgg naa Madinatul Munawwara

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 15


Mootax ma sadd yi bëyit muy seere
Ci sunu may bi dañu noo laabiire

Qad fakka kabla njort naa ko sirra


Qad baasha faddla seere naa ko jëhraa

Fad durru wallaa lor yi wéy na booba


Wa nafhu jaa’i sun njariñ am Tuuba

Seex Bàmba jàpp nu te bul nu topp


Nang nu yërëm te sutural sun lépp

Te nanu am jàmm aku yiw ak bàrke


Ak fan wu gudd guddee fee fa Mbàkke

Ni sunu xol sedee xajul si Xiirtaas


Maneesu ko laxbaaru nañ jóg ñaani paas

Alhamdulilaahi alal Xadiimi


Xadiimi Xayral Xalqi fil maxdóomi

Tabaarakal laahu na Buur jéggal nu


Dunya wa uhraa daa iman musal nu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 16


Te may nu jàmm akuw yiw féexal nu
Te suturaal nu te yëram nu yor nu

Lun bëgg am ko baatinan wa zaahiraa


Ci darajay Maam Asta Waalo saahiraa

6. Weeru Koor

Bi baa’i bismillaahi yaa Rahmaanu


Ayaa Rahiimu Barru yaa Dayyaanu

Noo ngi dàggaanati bi shëhri Ramadaan


Yàlla yërëm nu bu nu kenn mën a daan

Te mu saxal nu si siraatal mustaxiim


Nuy jaamu Rabbul Harshi daa’iman mudiim

Tem dëgëral tawhiid yi husnul haasima


Nang nu ko may fàww bijaahi Faatima

Shëhru siyaami la ñu wàcce Alxuraan


Ñépp a ci war di jàng saari Alxuraan

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 17


Nan yeesalaat njébbal yi ngir Seex Bàmba
Fii zaahirin wa baatinin yaaram ba

Te teralal ko weer wi màggalal ko ko


Jëme si sun yite bu wér wooral ko ko

Nanuy saxoo la ko safoon tey bëgg


La mu bëggoon te sax ci lii mooy dëgg

Daana saddal weer wi xasaa’id jàngal


Danaa ko bind fii murit bi déglul

Fazallazina haafazoo alaa siyaam


Shahrun bihi uhliqa baabun lil iyaam

Yarawna afdala futoorun fil quboor


Wa fil qiyaamati minal mughnil kabiir

Shahida haaliqul waraa lis’saaimiin


Fii ramadaana bi ridaahul qaaimiin

Hibaatuhum hindal ilaahi waasira


Naalul munaa fii darajaatil aaxira

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 18


Radda lihayrihim hazaabun naari
Bi hayri dirhamin wa laa diinaari

Rafahahum bi ramadaanar raafihu


Nafahahum bi salaawatin naafihu

Madda lahum munan nufuusal baaqi


Zul aradiinas sabhi wat tibaaqi

Diyaafatul baaqi ladal jinaani


Tamhuu hanaa-as sawmi bimtinaani

Ajrul lazii maa hindahu laa yanfadu


Ajrun kabiirun maahtaraahu nafadu

Nafhu siyaamish shahri fid daarayni


Yakfiikumul haarayni wan naarayni

Habadtumul laahal kariimal akramaa


Bihayri shahrin qad yaquudul karamaa

Ilaa siwaakum tantahin niiraanu


Yawmal qiyaamati kazal husraanu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 19


Malaktumun nufuusa fin nahaari
Yanhuu lighayrikum zawun tihaari

Abwaabu jannaatin nahimi futtihat


Lis saaimiina wal jamiihun fatahat

Lakum ladal futuuri wal liqaai


Yaa xawmi furhataani birtiqaai

Satahlamuuna anna rabbakum kariim


Wa anna hindahu ujuuran laa tariim

Shakartumul laaha halaa shahri siyaam


Sadat hulluna jannatan duuna iyaam

Bëyit yi Seex Bàmba wayoon ngir weeru koor


Laa bind fii day xamle màggub weeru koor

Moo ko defal mboleem julit bu sax ci koor


Ngir mu sawar te sant Yàlla may gu wóor

Bëgg it ku njaxlaf te forox góorgóorlu


Wàññii nelaw te muslu kuy fétéerlu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 20


Nan melni kuy faaxu ci waxtuw céebo
Njariñu koor fawxa na mépp céebo

Loo def ci weer wa Yàlla Buur bi fay la


Ndeem am nga pastéef loo wax it ñu fay la

Boo randaloon sax bant wala ngay nelaw


Ngir Yàlla ak Yonnen ba gaa yaa nga taxaw

Dila bindal tiyaaba tey far say moy


Te dila yëkkati ca kaw ful say may

Yaa Seexu Bàmba defaral nu koor gi


Yéege suñuy mbir banu jubóo’k waa Nguur gi

Bañ defaral nu sunu mbir soppil nu


Mboleem sunuy ñaawteef ya wéy bàddil nu

Bi xidmatil xadiimi lil maxdóomi


Nu sax ci moom ba jannatul nahiimi

Sala haleyhi laahu bi salaami


Wa aalihi wa sahbihi ahlaami

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 21


Yaa Rabbi may nu’g wér nu mën laa jaamu
Te may nu xel mu dal nu mën laa raamu

Te nga fegal nu mbas yi ak balaa yi


Te dindi njàqare yi ak bekkoor yi

Te boleenook Seex Bàmba mii nu tax a xam


Ci Yàlla benn tomb moo nu tax a xam

Nun moo nu teete dinu yee fi zaahiri


Wa baatini budul kon ag moom dunu ree

Fun toll ay mbiram lanuy waxtaane


Def ko sunub jaamu ku mar na naani

Ku naan sa woq bu wér mu dolli sam xel


Xamal la Buur ba Yàlla leeral sab xol

Raxas ko duy ko ay hikam ngay waare


Tey waaru tey jaamu te doo xawaare

Alhamdulilaahi bilan tihaa’i


Alabni abdil laahi zil luhaa’i

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 22


Salaa wa sallama haleyhi laahu
Wal aali wa sahbi wa ma waalaahu

Naa xatmu way wi fii te dellu julli


Ci ngën gi Yonnen ak ñoñam fasalli

Rabbi salaatan wa salaaman abadaa


Wal aali wa sahbi wa man tahabbadaa

Sëriñ bi nangul way wi ngir ga Yàlla


Ak Yonnenam ba rikk Mbàkke Bàlla

Alhamdulilaahi bilan tihaa’i


Alabni abdil laahi zil luhaa’i

Ajjuma jii mujj ci koorug ren gi


Laa mottale bëyit yi yóbbal gan gi

7. Weeru koor ak Sëriñ Tuuba

Bismil ilaahi ci barkeb Seexuna mi nu gën


Tay Xaadimal Mustafal Muxtaari xettali nu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 23


Weer wii di soppeb Boroom Tuubaa di xëy bëgga dem
Ta doon mbégam dib ligéeyam dem gi mettina nu

Weer wii bu feeñaa Boroom Tuuba du noppalu ngir


Day kër-këri jaamu buurub buur yi gindina nu

Bi laylatil xadri mbóotum weeru koor wi lanuy


Dagaane Seex Bàmba Seytaaneek ñoñam sori nu

Ñoo ngi yërëmtalu tay yoppoorlu tey fibikoo


Kay yox-yoxee kay raggal bis penc làq na nu

Seex Bàmba làq nu fii dunyaa wa aaxiratin


Ngir yaa di sang bi nuy say jaam te fàgguwunu

Te bul nu jàppe sunuy jëf nang nu jàppe sunuy


Xol Mbàkke Bàlla defal nii ndaxte farluwunu

Faral nu mbooleem sunuy bàkkaar ci ak woyofal


Ak ub ñewante ci weer wii xëy te jàllale nu

Te buñ nëxee nanga teeyal buñ dëngee nga jubal


Buñ tilimee raxasal bañ set, setaalewunu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 24


Yokkal nu fan yi te naatal xol yi dolli sunuy
Wërsag mu doy sëkk te nu jaamoo ko, dimbalinu

Ci darajay weeru koor wii Bàmba daa laxasoo


Di bégle tay dundulee’kay waare fàttewunu

Tey tagg xayral baraayaa dahra fii abadin


Hinda sabaaxi wa fil masaa'i seerenanu

Halayhi salli wa sallim daa iman abadan


Wal aali wa sahbi ëskey nun siyaarenanu

Saxoo durus fii kitaabil laahi muzzamanin


Fii kulli waxtin wa xiinin Bàmba fawqa nanu

Moo tax nu sadd bëyit yii nun di wut ngërëmam


Yalnañ ko làq ci mbóotum weer wi, sóobunanu

Yalnañ nu yéege ci mbóotum weer wi yokk nu gëm


Dalal sunuy xel seral sun xol ba tàggatunu

Yaa nu gënal ñépp ak lépp ak lu nekk lune


Yaa gën ci nun loola yaaram man nga nun manunu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 25


Weer wi di sab soope yor say màngasiini njariñ
Lanuy dagaane nga faj sun aajo far ganenu

Pexem njabar buy luxus buy gasi reen ak a fas


Lum ñàng ñàng Boroom Tuuba ngi làqna nu

Wa haakaza waa ju yor werdam di ñaan ak a dog


Ay xaatimam ak a taryax bum nu gis sange nu

Ak lépp luy lorre fii dunyaa wa aaxiratin


Min sharri fammin wa xaynin, Mbàkke bootunanu

Ci waa ju ànd ak boroomam, Mbàkke doyna nu far


Bi dafxi wa jalbi jaajëf Mbàkke sant nanu

Ngir sant Buur Yàlla moo war jaam bu nee’ka gëram


Sëriñ bu mag bi asal moo war yëramlu nanu

Bekkoor bi rëy na ba tiital xol yi cër yi sëtaf


Te yaa nu daa wallu buñ titaan nga gindiki nu

Yaaram bi wallu nu bul nuy topp yaw lanu am


Sottil nu xeewal yi bam doy Mbàkke sonn nanu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 26


Astaxfirulaaha tuub nan lépp lun mës a def
Te muy lu neexul Boroom Tuuba mi yor jamono

Te Buur bi taw niiru yërmandeek njariñ bamu doy


Ba réew mi naat, yaw mi yor sañ-sañ bi dimbilinu

Lim naa bëyit yi nu barkeeloo ci sang bi muy


Laamun limub weer wi yal nay sun mbégum jamono

Nangul nu ñaan gi te faj suñ aajo yépp bi kun


Ci luñ wax ak luñ waxul yaa xam te nun xamunu

Alhamdulilaahi rabbi haalamiina halaa


Seexul Xadiimi ki tax Buur Yàlla xettali ñu

8. Weeru Gàmmu

Bismil ilaahi waxal alhamdulilaahi


Fi shahri mawlidihil muhtaari Yallaahu

Bàrkeelu warna nu fi shahri siyaami defal


Ko ay bëyit ngir Boroom Tuubaa fa Yallaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 27


Tafaddalan na nu koy way ngir di taasu ci moom
Nañ teeru Gàmmu wi ànd ak sant Yallaahu

Te yaari weer yi Boroom Tuuba begoon na ci ñoom


Ba tax na kuy wut mbegam way leen fa Yallaahu

Nañ leen di teeru di leen sargal di leen gërëmal


Seex Bàmba mii di nu teqantal ilal laahi

Nañ leen di ndokkeel di leen neexal di tagg di way


Tey sant cant gu wóor Seex Bàmba Yallaahu

Marhaban shahru Rabiihil Awali ki ndamam


Ëhlan wa sahlan wa tarhiiban fa Yallaahu

Tay noo ngi lay teeru jox lab dal teral la bu wér
Booy dem nu gunge la def ko’b jaamu Yallaahu

Te nun suñub sang daf daa jaamu lum mas a man


Buur Yàlla tey tagg Xayral Xalqi Yallaahu

Haleyhi salli wa sallim wal tutimma bihi


Xasdii mahal aali wal as’haabi Yallaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 28


Tay noo ngi boole di sant’iy jebbalu’y rafetal
Sun njort xam nga nu xam lii wóorna Yallaahu

Yëg nañ terànga ji yëg nañ may gi Mbàkke bu wér


Te Yàlla seere na lii nuy wax fa Yallaahu

Musal nu fàww si Séytaaneek kuréel ya mu am


Nuy sant ngay dolli bun jeexleeti Yallaahu

Yaw mën nga sañ nga te sab xol faf rafet jërëjëf
War nañ di dàq sa xol fuñ toll Yallaahu

Tey dab sa bànneex akay raamoo ka sàkku ci yaw


Ngërëm ludul àndateek ab sange Yallaahu

Sa yërmandee nuy tawal yërmande yaa nu ko may


Yaa sedd xol yaa dalum xel Mbàkke Yallaahu

Noo ngi dagaan ci Muharam wa Safar wa kasaa


Rabiihul Awali wéy cig jaamu Yallaahu

Rabiihul laahiri indal ash-hurul xurumi


Ñooy weer ya jàmbaar ya daa am aajo Yallaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 29


Jumaada Loola sarax nu fan wu gudd akub
Wér ak cawarte bu wér cig jaamu Yallaahu

Jumaada Saaniya ak bàrkeem nu fàddu ci yaw


Dunyaa waa uhraa na def sun yite Yallaahu

Rajab musal nu ci moom Shahbaana may nu ci moom


Lislaam ju sell te ànd ak diine Yallaahu

Te Ramadaan na nu am mbóotam ya làqu ci moom


Luy tax nu selal Kitaabal laahi Yallaahu

Shawwaal yërëm nu ci moom Zul Qihda may nu si moom


Sab xol di sedd ci nun fun toll Yallaahu

Zul Hijja may nu ci bàrkeem may gu làndi gu wer


Bañ dem siyaarel la Baytal laahi Yallaahu

Siyaare soppe ba Xayrul Xalqi Seyyidunaa


Haleyhi salli wa sallim samma Yallaahu

Wal aali wa sahbi wa zawjaati kulihimu


Nuy topp sen mboor ilal janaati Yàllaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 30


Weer yi nu lim fii wu nekk ak ay ndamam ya mu am
Sottil nu yiw yi te bun gis lor ya Yallaahu

Te bis bu dikk nu am ciw yiw te mucc ci lor


Ja Yàlla àtte ci moom ngir Yàlla Yallaahu

Yawmal Ahad may nu ngir bàrkeem nu xejj ci yaw


Baatin defal nu ko fil usnayni Yallaahu

Yawma Sulaasaa wa yawmal larbuhaa’i kasaa


Yawmal Xamiisi nu def sab sanj Yallaahu

Yawmal Aroobati sangub bis yi noo ngi dagaan


Bàrkeel ci bàrkeem ilal janaati Yallaahu

Yalnañ nu jéggal ci moom fii haahunaa wa hadan


Lor yépp moy nu bi yawmi sabti Yallaahu

Te ñu mucc muccule tey bég fàww kenn bañ a mer


Te doylu doyle ba def mbaa-Yàlla Yallaahu

Sëriñ bi ngir Yàlla ak Yonnen bi nang nu defal


Fii kulli shahrin wa yawmin fii ka Yàllaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 31


Wa kullu waxtin minal awxaati bette nu mbeg
Sun xol yi sedd bi waxti suuri Yallaahu

Defal nu yërmaande nun bis penc bun fa taxaw


Layal yayal nu bi waxtil asri Yallaahu

Yeesal nu Mbàkke bi waxtil maxrib’eeki ngëram


Waxtul Ishaa’i di ñëw nan yokk Yallaahu

Te may nu jamm aku yiw ak bàrke ak ngërëmal


Sëriñ bu mag bi bi waxtil fajri Yallaahu

Nan sant nun Yàlla ak Yonnen bi sant Boroom


Tuubaa ki tax sunu xol mooy jaamu Yallaahu

Ngir xol su laabe te fees ay hikam di xalam


Buur Yàlla fum tollu moo dig jaamu Yallaahu

Sibtun wa xamsuuna toloog naa bëyit yii bu wer


Yal nang nu nangul xasaa’id jii ilal laahi

Nan xatmu way wi te yeesal julli julli gu wér


Ci ngën gi Yonnen te dollee sant Yallaahu

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 32


Ànd ak ñoñam ak saahabaam yépp kullahumoo
Nun nag nu ànd ak Boroom Tuuba fa Yallaahu

Amiina amiina yeen mboolo mi mépp neleen


Amiina ndax Yàlla tawfeexal nu Yallaahu

9. Weeru Gàmmu (bis)

Bismil ilaahi ma way man weeru gàmmu wi ndax


Sëriñ bi dàbbali saab ñag sëkk të ruurma

Te fas yéene nu faj saay ajo dàq samay


Lor yépp bañ sori bañ maa teg lu àttanuma

Te Yàlla xàjjil ma luy séytaane far nu musal


Ci ab dëmm ak jinne ak paj ak njine ak njuuma

Ci mbóoti weer wi le am laa ñaane Bàmba mu may


Ma may yu rëy yuy waral Buur Yàlla doylooma

Batay ca la ñaane saa yaaram ba dellu ma ñag


katay doj ag weñ dal saam xel tataal ñagema

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 33


Bàrkeb Sëriñ bi lañiy àndal ci wet gu mu doon
Batax na moos amatuñ ag jàq sant na ma

Pexem jabar buy luxus buy gasi reen aka fas


Lum ñang ñang Sëriñ Tuuba ngi, làqu na ma

Saa soo ko làqoo fabal saag ruu dandal si fi yaw


Luy bëgg fàddu si xàjjal ndax lu bon sorima

Musal nu Mbàkke si yii may lim musal nu itam


Ci làmmiñ ak bët bu aay ak nit ku noonu na ma

Salaa aleyhi bi tasliimin bilaa hadadin


Wal aali wa sahbi bàrkeb ñii musal na ñu ma

Ma tàmbalee nag Muharam tudd weer yi ci des


Ndax Yàlla may ma ci seen màqaama màqaama

Te daaldi siy teg Safar ndax Yàlla far ma defal


Sëriñ bi far ma yërëm jox may ngëneel gëne ma

Rabiihul Awwali laa ciy teg te sarxu ci moom


Xeewal yu doy sëkk tay tay nattu soxla wuma

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 34


Rabiihul laaxiri laay yalwaane Yàlla musal
Ma fàww cim nattu bum doon mooma móom jëfe ma

Faral ma tay jii samay bàkkar ci weer wi ñu naa


Jumaada luula te bul may topp ngir jubuma

Te kepp kuy kub Sëriñ Tuuba ci weer wi ñu naa


Jumaada Saaniya may kob fekee ngën gi Jumaa

Jumaa yi Tuuba ji laay wax ngir ga weeru Rajab


Bu kenn tawat nañu am luñ def ci ngën gi jumaa

Sëriñ bi sottinu nag xeewal yi ngir darajay


Shahbaana ndax xol yi naataat ëy fasal reemaa

Te weer wu màgg wu rëy wii may nu ngir darajaam


Moom Ramadan may yu semmal may yi xàddiwuma

Shawwaal may nu si moom lun soxla daal di ko am


Fi yépp tiis na nu moy man nag lu bon sorimaa

Lu baax yabal ko fi nun ngir weer wu baax wi ñu naa


Zul Hihda lépp lu bon man nag bëggul sëfuma

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 35


Zul Hijja may nu ci bàrkeem may yu doy keemaan
Bañ mel ni wër nanu bëytal laahi ay wuyumaa

Ma teg ci bis yi ba mbooleem bis yi ajuma teg


Ci bis yi waxtu yi ndax Buur Yàlla faf aar ma

Yawmal ahad may nu ngir bàrkeem nu xejj ci yaw


May nu lutax sunu xol yii naa la jaraama

Ngir yawmil usnayni daal nuy may si moom ngërëmal


Buur Yàlla ak ngërëmal Yonnen bi ak tëye ma

Yawmal Sulaasa bàrkeem baa waral ma taxaw


Tay jii di bind aka maas yaatal ma dimbalima

Seexal nu xoddil nu bon bon yépp far nu yërëm


Ngir darajay bis ba yawmal larbu ha wuyuma

Yawmal xamiisi lanuy yalwaane bàrke bi kun


Yaa Waasihun yaatalal wërsëg wi saafara ma

Yawmal haroobati bàrkeem laa la ñaane nga faj


Sun aajo yépp ci biir ak biti tontu nga ma

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 36


Batax na nag sant naa laa sant ngir darajay
Bis bi ñu naa si la yawma sabti sindiwuma**

Weer yépp way naa ko way naa bis yi maa ngi fasoo
Way waxtu yépp te santaat Bàmba wuyuna ma

Nangul nu way wi bi waxtil suhri cant gi it


Sarax nu nangul nu way wii tax na jàqatuma

Ñaan naa la may nga ma maa lay sant cant gu nag


Na def sa mbég mom bi waxtil Asri yóbbunama

Te daal di may may bi waxtil mahribeeti mayug


Way baax ya nag ya wéyoon cig baax te fedalima

Waxtul Ichaa’i ci bàrkeem laa la ñaane nga may


Ma may yu rëy yuy waral seytaane far sorima

Dalal nga saa xel mi bam dal Mbàkke xol bi itam


Sedd na guuy bi waxtil fajri tiitatuma

Waxtul luxaa’i ci bàrkeem laa la ñaane nga wax


Seex Bàmba xàjjil ma am ndog ndax mu yeggalema

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 37


Tawreeta Injiila wa Zaboora Furqaana
Ma tudd yii nag te gàttal way wi doynañuma

Alhamdulilaahi rabbil haalamiina Sëriñ


Tuubaa mi tax may dagaan ag mucc mucc na ma

10. Tawfeex

Sëriñ bi yaa ma tax a jug


Su ma tëddee nga di ma rog
Bëgg nga ma jaamu te lefog
Giiñ naa ni yaa may dimbali

Giiñ naa ni yaa fi indi maam


Awata yaa fi indi maam
Abdu mu jub mi dëkk Ndaam
Yàl nang nu yàgg dalale

Beg naa ci seen dikk gi lool


Daa doon nelaw tay maa ngi xool
Saa xel mi dal ma yokk lool
Ca góor ga nekkoon Baafali

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 38


Suñ sanc bi ma nekk tay
Tudde ko Tawféex di fi way
Nang ma fi may tawféex ju rëy
Te def fi sepp saafara

Luy ndiru lor bu mu fi ñëw


Lépp lu baax ñodil mu ñëw
Sa leer yu rëy yi na nu gaw
Séytaane bum fi mën dara

Lum xumb xumb bu mu soox


Bu fi’b xulóo am mbaa te xeex
Te yàqkat yi mel ni meex
Buñ nu mënal mukk dara

Tawféex a ngii na nu fi féex


Te bun fi jàq bun fi jeex
Te bun fi wopp nan fi féex
Te bun fi ñàkkati dara

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 39


11. Moom ak Sëriñ Muusaa Ka

Wolofal bii Soxna Maymuuna moo ko way ànd si ak Sëriñ Muusaa Ka

Soxna May moo wax lii

Bismi ilaahi ya lëzii laa rabbaa


Siwaahuwal muhtaaril abdul xibba

Suma salaatu wa salaamu sarmadaa


Haleyhi bil aali wa man bihihtada
Noo ngi yërëmlu noo ngi sippikooti
Te sadd ay bëyit te jébbulooti

Seex Bàmba yaw geesunu noo ngi nii ti


Nangul nu taalibe gi noo ngi nii ti

Sa xaritub xol bi di shëhru ramadaan


Mbóotum la tàmbalee ci saaru lahwaan

Ba sooratul naasi sunub ligéey a


Nu di ko def di la ko jox hadiya

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 40


Tay noo ngi feddaleeti sun njébbal yi
Sàmmal nu cér yi Mbàkke far bàkkaar yi

Te dolli wërsëg yi te naatal xol yi


Te yokk fan yi te yoral nu mbir yi

Yëg na nu may yi Mbàkke noo ngi sant


Dolli ca lan santoon defoo nu bant

Yaa nu gënal ñépp te Yàlla xam na


Bàyyiku nan ci yaw bu wér te doyna

Doy nga nu kiiraay Mbàkke doy nu gàllaaj


Dunya waa uxraa nang nu dolli ag laaj

Mboleem ku nuy fexal ludul lañ taamu


Noo ngi fi yaw te dila gëm tey raamu

Musal nu yaw ci ay pexeem aki jëfam


Sange nu sàmm nu te aar nu fu nu jëm

Ci darajay weer wi lanuy dagaane


Sax ci ndigal fàww ilal jinaani

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 41


Ngir lunu am bàrkeem a xam naa loolu
Lunuy musal mbóotam a gëm naa loolu

Yaa Xaadimal Xadiimi kall naa la


Xawma lumay wax waaye junju naa la

Nga defaral ma wax ji yokkaat way yi


Ci sunu sang bi nu sotti may yi

Xol baa ngi fees dell di fuur bay tuuru


Ngir bëgg a way Seex Bàmba tay di jooru

Alhamdulilaahi alal xadiimi


Yàl na nu tàbbal janatul nahiimi

Sëriñ Muusaa Ka teg ca lii


Yaw Soxna Maymuunatu man Muusal kaliim
Tay maa ngi ñaan nga tiim sa maas gii bil xadiim

Yàl na nu bokk dund a dund a dund


Ba dundu sàppi nu nu ñibbi Ndindi

Yaw Soxna Maymuunatu Yàl na say may


Yokk di yokk abadan te doo moy

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 42


Yaw Soxna May Yàl na nga yokk i darajaat
Dunyaa waa uxra fawxa kulli zawjaat

Ngir weeru koor wii ngay xalam ay darajaam


Ba way sa way wii woor ko war na bépp jaam

Ngir Ramadaanu moo di xalbu sanati


Waa ju ko sonne file dootul sonnati

Nafhu siyaami shëhri fid daarayni


Yafiikumu harayni wan naarayni

Seex Bàmba moo ko wax ci weeru koor wa


Ci hãama alsashin di fay tàngoor wa

Faazal lëziina haafazo alas siyaam


Shëhrin bihi uqlihabaa bun lil iyaam

Yàl na nga làq mbóoti weeru koor ya


Ak leylatul xadri ba fawxa góor ya

Pendal mu gën tubay bisub payoor ba


Yàl nang ko def keroog fa Yàlla Buur ba

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 43


Ci darajay Seex Bàmba ak Rasuulu
Salaa haleyhi laahu bun fi suulu

Yaw Soxna Maymuunatu bintu Aamina


Yàl na sa doom yii yàgg sol ay daamina

Yàl na sa doom yii yépp fawxa seeni baay


Dund ba mujje kër ya donnu seeni gaay

Yàl na ñu yàgg dundu ñook seeni nijaay


Te bañ a roy ñay dem ci maarse ya di jaay

Yàl na nu yàgg sóobu ngiirum tarbiya


Wommat murit saadix ya bañ am tarxiya

Yàl na nu yeesalaat tariixa taxliya


Wa Bàmba naaloon bañu am ca tasfiya

Yàl na nu bokk am hadaa alhaaji


Ci darajay seex Bàmba ak Al Haaji

Yàl na nu am mbooloo te làq ridwaan


Bijaahi jaddihim wa sahri ramadaan

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 44


Ci darajay Ñjool Màkka Xayril Adnaan
Ak darajay Seex Abdu Xaadr Jiilaan

Wa radiyal laahu hanil xadiimi


Mahaa tawaamiisati bil maxduumi

Wa wahabal laahu bi iblim Muusa*


Bindal Sëriñ Tuuba te tàggook buusaa

Aamiina aamiina ne leen aamiina


Ci darajay Seex Bàmba kay maamuuna

Wolofal Soxna Maymuuna Mbàkke | 45

You might also like