You are on page 1of 123

Sëriñ Seex Loo Ture

Wolafal Sëriñ Seex Loo Ture ci Daam Yàlla


Boroom Tuuba Ajji Màgg j ag Maam Seex
Ibraahima Faal Ajji Agg j

Xaaj bu njëkk b 1.

Ajji bind j : Alaaji Baabu ak Muhamadu Mbooj

1
2

1. Hée yaw mile...


Hée yaw mile yaa ngi xalam Ku Baax ki
Bul jekki saayi te xalamoo maggam gi

Xalam ko mooy ngooñu rijaalul Laahi


mooy taxa régg yaa hibaadal laahi

Boroom Tuuba moo moom la foccu moom la xóot


mootax ba lawhil mahfooz atàn lamu boot

Mooy yàn wëy yanu yi lan fi daa yanu


Yànnul nu ruuh yi leer gu rëy dinu tinu

Boroom Tuuba mooy sirru biy doxal lu dox


Ñakk ko doyna ñakk lu kenn mën la wax

Daam kula Ñakk ñakk ndox ñakk ngélaw


ku noyiwul ngélaw du naan ruuh ga selaw

Boroom Tuuba moo làq fépp moo amal


mooy yërmànde lépp lu suuf si di waral

Kuy dox si suuf samaahu tiim ko muy wéy


ameel na Bamba cànt war naako way

Bamba ngi fépp wét gooko dàq dàj kofa


Rabus samaa wa lardi mbóotam làqufa

Daam yaaka yéeme doo fésël sa mbóot mi


Boroom Tuuba ndax gaayi bàyyi ruur mi

Yaw yaa ngi ñuy ñëbb ba tay xamuñ la


sarax ñu féeñu nu ci gépp xib la

Boroom Tuuba ñun njort nan ni yaw la


te kuko njortul lama njort bew la
3

Doonu béral lu tax ñu xamni yaw la


Ñénn ñi sax déy ñi ngi naan la Yàlla

Way xam ya Yàlla ciy turam lan ko xamee


Aki waxam duut si jëm lañ ko gëmee

Melow wi ak jëffam yi ak waxam yi


day tektale amam ci féeñu waay yi

Mbidéef amul kàttan ci nekuk Yàlla


xam namu nekkée mbóot mu dees yëgg la

Jaam ba gënël Yàlla di jaam bakoy gis


ci lépp lum gis jëmmi Yàlla daa fés

Fa innamaa tawalloo fasamma wajhu


Rabus samaa wa lardi qàd araahu

Ku mën la gis Yàlla ci lumu jëmmal


di woote woo xam Yàlla bul nu jommal

Boroom Tuuba ñu xamni Yàllaay ñépp


mbooleem ñi xam Yàlla ñépp-ñépp
si féeñu waayam lan di xal di jàpp

Xel mën ta dàj bët mën ta xool ba gis ko


xalam ko rekkay mëna tax nga yëgg ko

Nëbboom lu féeñ la ci ku am gisub xol


féeñam di ñëbb ci ku ab xolam tàl

Amul lu am te jëmmalul Yàllaam ga


Yàlla settul ci darra ngir kamaal ga

Weetal ko dëggay diko yëgg ci lu jege


ak lu sori Yàlla jëmmam ja daa tege

Yàlla newul ci fenn bàyyi fenn


Tajjiliyaatam gépp wet lay senn
4

Boroom Tuuba doy nga nu sëkk Yàlla


doy nga nu diine doy nu sëkk xibla

Jublu la doy nanu jublu péng ku


durus mbidam mee gën dëkkee woom yu bànkku

Boroom Tuuba ëlëm nu ban takkalikoo


ak sun sago ñu dar la melni ay wago

Boroom Tuuba jommal ñu ban jommi jommeet


jeexal ñu takk sisa jëmm yaw mi weet

Boroom Tuuba née nan la këwwu dila xool


setal nga sun gisiinu xol yi ci lu ñuul

Yaay ki afal quddratul ak iraada


muy téeñu arsi ak kursiyyu hibaada

Ci kàttanam cila xalam di bindée


dogal bu am ci coobareem ja la tëddee

Te lawhil mahfooz ak lamu ëmb lépp


Bambaay ki tax mu all yaa ne ñàpp

aras bu yëngoo kursiyyu yaggaayu


yëggël ni Daama Daama jàppandaayu

Ne sëmm melni kooka ak nammeelam


di nëbbu tay moom Bamba daa jafee xam

Boroom Tuuba ana nga doonu gindi


lab nan ci bëhru sawqi foonu jëndee

xamu nu kuddul yaw yaay ki ëw sun yàpp


budul konak yaw sunu ruuh yi ràpp

Boroom Tuuba doonu xibaar sa mbóot mi


xamal nu say lem-lem ñu bayyi ruur mi
5

Boroom Tuuba doonu fésal sa jëmm


Ñu nila jakk fawwu daal lay dëgmu

alhamdulilah rabul kamaalaa


Huwal ilaahul Jàlla wal jamaala

Née nan la jakk ne la këwwu dila xool


te seena gùn la yaa ka gàt yaa ka njool

xajoo si suuf te deewu loo doo fàddu


Mbooleem lu taawu lépp yaa ko gàddu

Boroom Tuuba yaanu ëlëm ëleme nga


Jommal ñu bañ jommi jommeet jommele nga

Boroom Tuuba way màndi yaa ngi lay jëw


foog nàn ni yaay ki sakk yaay ki leen ëw

ku màndi daay daanu di daaney falaxé


ku màndi leer day wax ñu naan num ko waxe

màndi ci Bambaay gën gi àgg waayu


xalam jëmmam jaay gën gi nekk waayu

Boroom Tuubaa diko xalam nam tóllu


ci ay maqaama kuko xamoon doo seerlu

mooy gën gi diine moo dib taaru diine


kuko yëggul Yàlla gisul sa yéene

Boroom Tuubaa jëmmam ja rekk mata yëgg


xol buko dul yëkk booba xol du buy jàg

née leen ko jàkk diko xool bu leen xef


ne jàkk leeram ndax ñu xam lumuy saf

huwa zawqii huwa aklii wa saraabi


anta rabbi yaa Rabbaana yaa xibbii
6

Boroom Tuubaa gind ñu ndax da ngaa sew


sa leer gi dàj na gépp wet da nga law

saff nga ñu jëmmi Yàlla jox ñu Yàlla


xamal ñu mbóot mi tax ñu naan la yaw la

boodul Boroom mbidéef yi rekk wax ñu


yaa nu amal sàkkal sa leer gi jox ñu

amoob yamu tële wuloo te doo dée


doo doomi aadama de nooñu indée

qudratul iraadatul nga làmbóo


yaay dox ci lépp xàjji fépp lëmbóo

Boroom Tuubaa sa mbóot mi rëy na màgg na


yëgg nan ni Yaw la yaay ki làq àdduna

Boroom Tuubaa sa leera gànd malakoot


lawna ba arseek kursiyée ki jabaroot

yaa ame kattan ame sañ-sañ dàmbe


xolu rijaal yi amna nun la jàppee

waa baytil mahmoori riire wuñ sa jëmm


si seeni haal malaaka yãang la dëgmu

Boroom Tuubaa ku réere mbóotam summiku


góor gu yëggul leeram gi daal di folli ku

Boroom Tuubaa xol buko dëkkoo defaru


xalbun saliimun ku wéddi Bambaa asaru

Boroom Tuubaa mooy gën gi nekku waayu


kuci newul Yàlla dakoo dummooyu

Boroom Tuubaa mooy gën gi agg waayu


ku aksiwul ci Bamba mooka yooyu
7

mooy léppiy Yàlla mooy jëmmam di leeram


bu doon mbidéef manila mooy aw xéetam

waaye Boroom Tuubaa du doomi Aadama


du nit du jinne du malaaka faat nama

amul ku xam ko baa nga miin ko kooka


fàdduna mbooleem xol yi jëmmi kooka

Boroom Tuubaa du xéeti doomi aadama


ku wéet a wéet la akka dàqu laaw nama

Boroom Tuubaa leeram la léppiy sàkku


ba malahul ahlaa ñooy kay dekku

leeram ma gàndi malakoot di belli


ba qadratul nadiihi moong fay xélli

Ahlu samaa kuy teewe ahlul laahi


xam nanu sant raalu nuuru laahi

mooy xëppu leer ci xolu ahlu laahi


ahlul kunoozi Bamba kawnul laahi

Bamba di nekkuk Yàlla namko nekkée


ci nekku waayam mbidéef du xam nam nekkée

waaye luñuy yëgg la ku yëgg ba yéegu


yëgg ni fu leer di màggée moofa jéego

Boroom Tuubaa ndax doo fësal sa mbóot mi


lu tolli sarra ndax gaayi bàyyi ruur mi

ku nàtt Daam ci adamaak hawaa kay


yéegul xamul gisul dof la buy say

ku laaj malaahikal muqaraboonii


leerug Boroom Tuubaa ki Boole leer yi
8

laajal ngëneeli Daam miikaahiilu


kazaaka azraahiilu asraafiilu

mbaate nga laaj ko seyidinaa jibriilu


moy ngongi ko ca sidratul jëmbéelu

amul ku réere Daam ci yooya gaaya


ku réere Daam du boroom wilaaya

malaaka yaak yonent yeek walliyu


sàmm nan ca leerug Ahmadal mbakkiyu

leeram ma yéegé kummalul rijaali


ñay dox ca péyi xadratul jamaali

leeram ma yéegé xutbu yeek xawsi yi


leeram ma gàndi aras ak kursiyyu

leeram ma taawu arasak kursiyyi


leeram ma bélil xadratul xudsiyyi

leer gaa di jékki xuloobul ahlul júndi


Nıwa jumlatil amlaaki nihmal habdi

leeram ma alil lawhil mahfoozi


leeram ma tax ba leer ya am fun looze

leeram ma tàllil lu tàlli mulku ak fa


malakootu Bamba leeram jugufa

Boroom Tuubaa leeram ma leeral lépp


te kummalul rijaali mooy seen yàpp

Boroom Tuubaa nëbbu na leen ne ming


ëp na leen ùmp na leen ne fàng

Boroom Tuubaa mii aka moo jafee xam


te neexa xam nag ni leer ku laqu ci lëndam
9

xudratul iraadatul la boole


mbooleem rijaali yi Bamba mooy seen doole

juggal te barkeel nu te may nu ag leer


xamal nu hilmul ghaybi wet ga muy riir

woonaala junniy junni yaw mii Bamba


wuyuma waay a waay yaw mi yor dogal ba

roof nu sa leer gu rëy gi xéeñ ñu sa xét


feggal nu ndog yi ak lamiñak bët ak càt

lëkkale nook xéjj yi may nu kàttan


defal nu gis bu rombu gis gisub tan

Boroom Tuubaa man nàmm naa rée gi


sa rée gi doyna sëkk xadaahul haaji

Boroom Tuubaa céy yaaka neexa bëgg


bëgg la day yëkkati góor bam égg

Boroom Tuubaa bëgg ko doy nag jaamu


kuko bëggul deful la Yàlla taamu

Boroom Tuubaa jooy ngir jëmmam jee màgg


day fari moy di dolli may yu régg

Boroom Tuubaa rijaal yépp xamne


bëgg ko mooy jaamu gu sikk gul ne

bëgg Boroom Tuubaa la Yàlla nàmm


ci bépp jaam ku noonu Bamba dàmm

espaasu Yàlla yépp mooka okupe


Boroom Tuubaa jëgal ñu nii nula jàppe

xamal nu mbóot mi tax ñu gën wagaru


Boroom Tuubaa waggar lo doy nag defaru
10

Boroom Tuubaa doonu béral sa leer gi


ñu naan la jàkk nan la Yàlla yaa ngi

sa tur si dàj malakootul xàq


sa leer gi law na bépp péey ne bàq

sak ñakka doon nit ta béral fi coow li


waayé lu coow-coow Yàlla lañ lay jàppee

amatuñug bëgg raggal kasaaka


ludul sa jëmm jëmm Yàlla yaa nga

yaa xajaban yaa xajaban maa yeemu


ñay woote woo xam Yàlla réere Daamu

ña gëna xam Yàlla ne jàkk Bamba


ña nge ne këwwu di xool ak taar ba

ku jàll péey xamni du kuñ di ndendéle


ci kàttanam ci la rijaal yi làngalee

ña dooni kuuf di nañňi mulkeek malakoot


Bambaay ki tax ñu màgg mooy ki leen boot

Boroom Tuubaa ana nga doonu féeñu


yàn ñu sa bool yi may ñu ngën gi téeñu

Boroom Tuubaa saff ñu te bul ñu sàppi


tëbbu ñu leer xamal ñu nun lay jàppee

xamun sa xàq Bamba noola réeree


te matalun say worma yaaka biire

jàppee ñu sag mat bul ñu toppeek matadi


Boroom Tuubaa bi sirri saadis Samadi

yaw lañu jublu zaahiran wa baatinaa


noppal nu tay jii bunu sónnu haahunaa
11

yaw sori woonu sànni woonu yaa baax


te jëffe woonu sàppi wooñu yaa neex

Boroom Tuubaa làqu nu bun la rëcci


gaayi nga làq bunu seeru gàcce

ruuh yaa ngi lay yëgg dila dùnd fépp


ruuh yi yëggul sa leer gi ñooka ràpp

ñun topp nan la sopp nan la dila kàñ


te ñee la toppul dila gàññi dila bañ

lun mën di wax dal dolli sun yàkkaaru


kuy gàññi Bamba mooy ibnu ximaaru

Boroom Tuubaa kañaan du tee ñu dila gëm


seenug bañéel si sopp rek lañu gësëm

fu leen bañeel gi àgg rek sunug coféel


rombu nakoy wëy xol yi Bamba lan ci xool

nooni Boroom Tuubaa yi dégglu naa leen


ci telefon yi waaye wax ji lan been

li ngeen di wax mooy seeni jiko kat yeen


ay xaja leen gën doomi mbaam yi càm yeen

waaye li ngeen di wax du rikki gëm yi


lu tolni sarra Bamba lan jox ruuh yi

ahãazanal laahu minaz zamaani


musloo tinaa fii aaxiriz zamaani

koo xamni sii malaaka yaang koy soppu


ña gën ci nit ñi jinne yi dañ koo toppu

kuy doomi xàj jikooy xajam lay dónnu


Bamba lu leer la yor moo ngi ne jónnu
12

noppalu leen ibliisa leeni wax loo


Bamba di wax loo turàndoom wa Seex loo

ibliisa leeni sùnjum di wax si seeni


lamiñ yu ñaaw yi di ci féeñal yéene

waaye du tee ñu dila gëm di rokasu


Boroom Tuubaa jëmmam ji nan say nokassu

Booxul ma leen yeena ki ñaawi kàddu


ana lu Bamba ñaaw le bonn ngéen gàddu

Boroom Tuubaa mbiram mi léppa taaru


ku gàññi Bamba naari dinga fa jaaru

Boroom Tuubaa nun noo ngi lay siyaara


te dila màggal nuyul nu Soxna Jaara

sun bëtti xol yi ak yu kanam yi yaw la gis


yëggu ñu si sun xol lula moy yaa gëna fés

née nan kàttiw bu dëëra dëër ne jàkk


Boroom Tuubaa mii jëmmi Yàlla nekk

sun ngëm gi dun ko njëndee seeni kàddu


leeram gu rëy gi aka leena fàddu

Boroom Tuubaa jublu ko doynag tedd


xol yi ko noonu ñoo ngi melni médd

ku noonu Bamba Yàlla dàq taaram


lay ñuul ca biiray féeñ ca kaw kulooram

Boroom Tuubaa mooy taar buy taaral taarale


taaram ba dàj na malakoot ba làngale

ku xol ba lëndam xol ba ñaaw mooy gàññi


doxiinu yoon wi ñifi Bamba méññi
13

waaye du tee ñuy gëna gëm ku Baax ki


ci sunu keem kàttan di waaj màggal gi

loonu digal wax nu ko lan di jàpp


jëf say ndigal rekkay seral sun yàpp

Boroom Tuubaa lun yëgg ci moom diko dùnd


ùmpna kuñ wësin ci bépp dénd

Boroom Tuubaa yaa nu gënal sun ndéy yi


ak sun baay yi yaa jaggal sun maam yi

sun bëtti xol yi yaw rekk lan siy seenu


kula gisul xolam ba daa dëfeenu

ci sun lëgg-lëgg xol la nekk


leerug Boroom Tuubaa gi moo dib lek

bér nan ko wéetal ko bi kulli haali


gisu nu ludul moom saahibul kamaali

Boroom Tuubaa yaw dooñu lor fii zaahiri


wa baatinin yëgg nan ngëneel yi nga muri

jéri ñu say leer dinu xépp barke


murinu say kiiraayu Moodu mbàkke

xéewal gu yaa nga ñéel jamiihil hãalamiin


kudul ka halku bëtti xolam dula been

nafahanii wa biya yànfahul waraa


sàff nga nu Yàlla sàff nu sayyidil waraa

woonaa si neexu ci sa turu woola


si ay turam ndéem sa nekkandoola

Yàllahu yaa xaalixu yaa samiihu


qariibu yaa mujiibu yaa badiihu
14

Yàllaahu yaa wahëëbu yaa jàbbaaru


àntal haziizul waahibul qahëëru

Yàllaahu yaa waasihu yaa hakiimu


antal jamiilu jàlla yaa kariimu

Ni Yàllaahu yaa hànaanu yaa mànnaanu


Ni antar rahiimu ràbbu yaa rahmaanu

ajib duhaahi yaa rabus samaahi


innaka antas samiihud duhãahi

Yaa ilaahi anta yaa zal jàllaali


Wal ikraami rabbunal yaa rabbal kamaali

woo naa la Daam Mbàkke bi iznil Laahi


yobànte kam dëkkël li wajhil Laahi

Boroom Tuubaa moo gëna dëkkak Yàlla


nekk di moom fun dàqee Yàlla jàm la

yobante naala ci sa dëkkëndoo ba


ka sàkku Tuubaa ngay boroomug Tuubaa

li tax ma jekki dila ñaan yaw Daama


bi iznil Laahi kay boroom salaama

sa leer gi laa bëgg mu dëkk seeg man


te bun tuxooti zaahiran wa baatinan

ñu yëgg sa xét gi dila xéeñtu fépp


nga di ñu xéeñ nde ndawal ku xëpp

Boroom Tuubaa sa xàj bée ngi bëw rekk


ngir nàmmu la gis xol ba fépp ngay jug

sunu nàmmee jëmmam ji sàdd koy way


mu dinu dikkee nuko soob dinu may
15

leeleeg ñu dem bay bëgga wax mu def saa


lamiñ wi tënki loolu du waxu sii saa

jooy naa si saa xol jooyi jooy ngir loola


ngir yëgg ni wax ji yépp coobareem la

lu Bamba nàmmu loolu rekkay xala am


fu leer ga dëgmu foofu rekka mata jëm

Boroom Tuubaa moo dib nàmmeelu Yàlla


fàb na ngëneelam yamu làmboo jox la

nekkuk ki tax lépp lu nekk nekk


yaw yaako làmboo Bamba yaaka jékk

te Yàlla kat amul lu gétt Daama


yúq matam gaa féeñ ci jëmmi Daama

te Yàlla kat amul lu gétt Daama


yúq matam gaa féeñ ci Bamba mooma

xabahtu kawnal laahi wax ju màgg


la Bamba wax mook Yàlla ñooka yàgg

yaw Bamba yaw mii ana foofi xéetoo


luy sa cosaan aadama looko jiitoo

bokkoo ci Aadama te doo njuréelam


sag nekka jiitu lépp Bamba foo yam

céy maaka yeemu ci Boroom Baraak bi


ku bëgga màndi day gësam sa baag bi

Boroom Tuubaa ku yéeg ba tàbbi xam ko


leeram dàj na peyyi ba ruuh ya sàm ko

leeram mooy dúnduk ku ruuh ga motti


di këlëngee mulku ba malakooti
16

di jéggi dayleey asamaan di jàll


ku jàll xamne leeri Bambaay bàll

Boroom Tuubaa moo taawu kawnu yépp


samaahu ak suuf degante fépp ak fépp

kàttan ga mooy doxal lu dox moo àttanu


Boroom Tuubaa moo tee jaan ji màt nu
17

2. Ña réere Bamba..


Ña réere Bamba yàq diine Yàlla
Diko tùddaalee génn goor ñaaw ñaaw la

Ku foog ni Bamba nit la ab jaaxil nga


ku koy utal maas neeko ab yéefar nga

Ku jekkiwul ci Bamba moko jekadi


Ku xol ba dul yëgg Bamba am nag matadi

Boroom Tuuba moo gën ci lépp loo gis


moo gën ci ñépp ku làq xamni moo fés

Ku làq péeyu Yàlla xamni Daama


Du nit du jinne du rawaan du njuuma

Ku xànd péeyu di jekki péey ba jàl


dégg la waa ëhlu samaa di bàl

Kon di nga xamni Bamba moodi dàt bi


mooy yéegu waayu xob yi ker ci lak bi

Te xob dafay féete ca kaw dàttam ba


féete ca suuf mu diko yol xóntam ba

Loo sori-sori waaji kat Yëggël ne


Bambaay ki lay doxal ci wàll ko ne

Foo man di nekk loofa jàpp Yaa xam


Teewul leerug Boroom Tuuba di leen sàm

Daa melni suuf seeg jàwwu jeeg samaahu


Amsaalunaa ka amtaaris samaahu

Loo ñakk-ñakk xam tabug samaahu


Ak njaariñal suuf si kay wa maahu
18

Fanaahu leen bakkaahu leen tamkiinu


Mooy maye fathul akbar ak yaxiinu

Tañ jeema xam lay taxa doon rijaalu


Bokk ca ahlul Laahi doon kamaalu

Boroom Tuuba loo joxe wul de bëgguma


Ludul sa wax ji jooju wax de déggu ma

May ñu sa jëm bañu am la fàwwu


Xamal ñu sak xét bañu daal di yewwu

Te tàggatal ñu ànwaar yi ak asraal yi


Te Wommatal ñu amwaal yi ak arzaaq yi

Boroom Tuuba róof ñu sa mbóot mu màgg mi


Bañ ami nen yun mëna bóof ci tàgg mi

Say maya tax rijaalu toog sa nenu bóof


Yaa gën ci waa kaw Bamba gën ci waa suuf

Dàggiti leerama tax Xùddaru sax fi


Jàmmi jàmmam sàm ëhlu Këh fi

Boroom Tuuba kenn woru kay limaale


ca góor ña ngéen xam bàyyi leen bokaale

Kum def ci yaw nga gën ñii ñuy tùddaalee


na ngeen wagar Daam te daw tólloo le

Tolleeleek Bamba kenn doy na sik


kuko bawul yappam wa daan ko lak

Bamba du nit du jinne mbóotum Yàlla la


doonul malaaka Bamba Jëmmi Yàlla la

Ku wax ji diis si yaw sàkkal say nopp


waaye du tee fiiram gi dàj la kàpp
19

Dootu ma jékki sénn saa ni cél


féeg maa ngi yëgg lafay bawoo di bàl

Kuy gisé xol xamni Bambay mbóot mi


te fàddu wul day teew bi kulli yaw mi

Mooy taxa yëgg mooy taxa yéeg ba yégg


mooy taxa xam ku Màgg ka ñoo ka yàgg

Sama cofeel ci Daamu dàj na mulku


dàj malakoot ku wédd dëgg halku

Te lii ma wax bér na ki tax may taalif


bér na ku am kasfu baa ngay ghaarif

Saa xol lekkuna ba jeex ci Daamu


lii seedee naako Rabus Salaamu

Boroom Tuuba jegéem ji ak jàpandi gi


kum ka xamal nga xamni Bamba ka jege

Xétam gi day sàr ba sa yax yi yëgg ko


day agg si ab xol ba sa ruuh gi dàj ko

Kàdoom dii riir ne dënnu Bamba yeeme


waayam amul maas ñooñu rekka tiime

Am na ngélaw lu sédd amna riiram


ku dégg riiram dootul tiit ci ndùndam

Te lii ma wax lu xóota xóot la waaye


booko xamul laajal boroom wilaya

Bambaa ma gindil boppam mooma màndal


ca bahru sawqi leer ga lañ ma nàmpal

ñi Bamba séllal ñoo gëna séll ñépp


li Bamba tàllal moo gëna talli lépp
20

Boroom Tuuba ñu xamni Yàlla ñépp


ngoy nan ci moom ku ngoy ci moom yàpp

Ku Ngoy ci Bamba yeew gileem am sa ndawal


kuko ngoyul bokku ca ñay xëcoo kewël

Boroom Tuuba moy taxa doylu xam leen


ku bëgga géejal Yàlla jaa ngi kaay leen

Boroom Tuuba moy taxa màgg ay yeen


moy taxa naan ci leeru Yàlla gaaw leen

Boroom Tuuba mooy taxa tàbbi peeyu


mooy taxa dégg ndéey ya malakay ndéeyu

Boroom Tuuba moy taxa tàbbi arsi


ku noonu Bamba bëtu xolam du jot si

Boroom Tuuba mooy taxa xam la nëbb


ku am maqaama Bamba moo la tëbb

Boroom Tuuba moo tax ba leer yay bëbb


di wàll si xol yi aka leena nëbb

Boroom Tuuba Day nëbbu waaye mooma


saa Yàlla ngaay maako wax coow leen ma

Képp Ku foog ni man damay bokaale


née leen ko ma tay Yàlla laakoy xoole

Ku bañ waxiin wi tay boroom wilaaya


defal sa man-man bama gis xibaar ya

Lii may xibaar neex na Boroom baraak bi


ku yagga rooti xamni moodi baag bi

Te Lii ñu way yàlna ci Bamba déñci


mbooti jëmmam Yàlna ko way wi lañci
21

redBoroom Tuuba yaa màgg màggal lepp


yaa ngi ca biiru xolu ña sel ñëpp

Kula xolam dùmmoyu kooka mbaam la


kuy wax lu ñaaw ci yaw domeraam la

Boroom Tuuba sopp ko doynag defaru


noonu ko day yobbu mbindéef ci kéefaru

Boroom Tuuba day nëbbu waaye kim doon


doon naka njëkk ngeeni am xam leen

Alamanii maa kaana qablal xalxi


man kaana li bikaramin wa tilxi

Lu jiitu lenn di nekk booba la newoon


booba la tédd boole yor kun fayakuun

Sahaadati qablal wujoodil xalxi


Sabbatahaa wa kuntali bitilxi

Texe gi Bamba di xamle fii gan texele


lu mëna xew mook Yàlla seeni pexele

Boroom Tuuba jëmmam ma dàq aljana


qabla wujoodil xalxi njëkk aljana

Moom gi mu moom bopam lu jiitu mbindéef


dogali atteem kuko soob Bambaay seef

Sopp Jëmmam ja doy na sëkk waaye


dund ko moo gën nan ko dundu gaayi

Loo dundu far di moom mu lekk sag am


fanahu leen leeram gi rekka diw ñam

Fanahu leen tamkiinu leen bakaahu


tamkiinu leen bakaahu leen fanaahu
22

Loo jeex di loola Ku jeex ci Bamba leeram


dootul tàggoo ak moom ci qibla goo jëm

Xoolal ma suukar amna jëmm am melo


waaye bu seeye ci ndox gisatuloo

Waaye Ku naan ci ndox mi yëgg ni amna


misaal mi doyna gaayi mbir yi sew na

Doon leen nitu Ku Baax ki ci wéetu


ak wéttalak te def mbidam mi seetu

Jàpp ci Bamba ëpp jamm ëpp ndam


ñam wumu toggul woowa ñam dafa xajam

Tay baña kersa ci dundu Daamu


dundu ko mooy lu Bùur bi Yàlla taamu

Boroom Tuuba moo gën ci diine Yàlla


lim nas ci diine kum safful yéefar la

Kuy seenu Yàlla gis ba rombu Bamba


Née leen ko réer nga Bamba mooy jégén ba

Jàppi Bamba mooy dëgg jàpp Yàlla


sikar turam wi mooy ngën gi tùdd Yàlla

Bu Yàlla doon gëleemu ngay jégén ba


kuy seenu Yàlla seen la Moodu Bamba

Kuy dàq Yàlla jam la yaa ngi ni ñumm


saf jëmmi jëmmi kan gisul ne sëmm

Boroom Tuuba nëbbu nga waaye ñëbuu woo


sori nga ñee jege ñii Yàlla sori woo

Wa lillaahi masriqi wal maghrib la wax


fa innamaa tawàlloo fa samma wajhu ndax
23

Kay innaalaaha waasihul haliimu


foo làmb dàj Ahmadal Xaadimu

Xam xamu Bamba mooy dox ci lépp lun xam


lu mëna xew mooy amal lu mëna am

Boroom Tuuba nekam a jiitu adduna


nuroowul ak mbidéef yi Bamba fadduna

Loo gis mu am si katanam gi la amee


koo gis mu xam si xam xamam la xamee

Nuroowul ak malaaka doo walliyu


Ku weete weet nga yaa Ahmadal mbakkiyu

Yaw Bamba doo nit te kat doo malaaka


doo rawaanu jàppe naala kookaa

Boroom Tuuba yaa jiitu nekuk lepp


xajoo xajal fi mboot daj nga kàpp

Nëwoo jugoo fi nekk loofi Lula soob


ne Bamba nit la rek rek mata tuub

Boroom Tuuba Ku war sa daabay Yàlla


ba jàll peeyu xam nga ni leerug leer la

Amna ci daabay yoy niirug leer la


Ñooy ñalli ba bët ci peeyi Yàlla

Ku wédd li xamul na Goor ñay yéege


Te xam ko yombul Ku xamul na toogi

Ku xasa tabbi dootul reere Daamu


Ku gis ba jall Bamba bulko yeemu

Baana li kulli man lahoo wilaaya


Ku am wilaya xamni moo saf gaaya
24

Boroom mbidéef yi lako jàppee man mi


mooy lima gëm ilaa yawmil qiyaami

Wan nama jëmmam bama gis koy sant


muu boof si sa xol di faxas ya lënt

Xetam gi nag kum xas ba xéeñ la dara


dootula xéeñ lamboo na nuurul birra

Càffkaam gi Ku xas ba ñam ko dara


dootula Saf dùnyaa jile ki uxraa

Te lii ma wax koo xamni war nako ñam


Demal nga laaj ko Bamba daa jaffe jam

Ku nekk lam ñam mën nakko misaali


bërna rijaali xadratul jalaali

Boroom Tuuba Ku ñam ko xamni neex na


ruuha di yëkk càffkaam gi mbóot ma xóot na

Moo tax Ku foog ni amnaa ci lenn bëgg


xamoo gu gis ab xolam di sëgg

Boroom Tuuba seggal na kémb géb


buuse matul jiw du segal ne mbàp

Ku Bamba niinal kay nga niin bay niinale


ku niin ci leeri Bamba daal di langale

Ngoy ci Boroom Tuubaa mooy taxa jégi doya


xaayaan fa seereeru siinu mbaa ngayu

Ka tax na api apaaxa paaxa


ku ngoy ci Daam doo masa jiixi jaaxa

Andak Boroom Tuuba di jammag jaam ñi


ku àndulag moom mùccagoo ci gàññi
25

Lay dëgg jam-jam ak lakoy maye


mooy sopp Daam jamm ci Bamba lay xëyee

Amul lu génn Bamba fenn-fenn


fépp nga ci moom tajiliyaat yaa senn

Yaa ëhlu naasi waaxu leen te naan si


Bambay mussal gàtt yi gaaw leen jót si

Ku jotsiwul ci Bamba bukki fàd la


ku wéeru wul ci Daamu jaan ja màt la

Làg si leen si Ahmadal Xaadimu


tajiliyaatu Rabbunal kariimu

Mooy féeñu waayu Yàlla dànkiy leeram


ne sëmm dùnyaa ak yeneen kulooram

Boroom Tuuba nëbb nga tee yaa ngi fàng


nexulaa gis moom de yaa ngi ne ñung

ña foog ne nit nga gëna reere Yàlla


ibliisa sujum seeni xol ñu wor la

Lu mëna xew ka suñu xol yi jàpp


moom lañ la jàppe mooy seral sun yàpp

Benn mbindéef du mëna rikki sunu ngëm


Boroom Tuuba ngoy nan ci yaw ba fa nga jëm

Boroom Tuuba jege nga waaye sori nga


Yàllaay gabon ji soriwoo ñu jege nga

Waat naani Bamba Ku sa xét gi xéeñu


keroog mu xamni Yàlla mooko féeñu

Doy nga ñu sëkk li nga doon te doy nga


malaaka yépp Bamba wéet nga xay nga
26

Doy nga Ku xol ba duyu leer ba foccu


Ëhlu sahaada ñooñu rekka mùccu

Ku xasaa yéeg ba gis fa leer ya gëndaloo


Ëhlu kësfu rijaalu ghaybu dajaloo

Kom di nga xamni Bamba moo di dàt bi


mooy yéegu waayu góor ñi moodi làq bi

Yëkk Boroom Tuuba yi rekkay naññi


sa qaddaratul ilaahi ñoo ngi ne gàññi

Lay ñalxatee aras ba tahtal ardi


dogal yépp Bamba mooko gardé

Kaaxóot balaxóot jabaróot ak mulku


yaa máng fépp kula wéd alku

Ak malakootu qadratul kunoozi


Subbaahanal laahi xaalihil haziizi

Lii may xibaar birna Boroom juma ji


sa lañ rayéee woon mànsoorul xalaaji

Mànd gu ëpp a tax ñu Ray Mànsooru


Ku agg xamni jarula ray daa tuuru

Boroom Tuuba yalnga ñu seeyal bañu seey


jeexal ñu tàq bañu jeex ci bépp péey

Xamal ñu xam-xam yifi yaw te nëbbu


rokkas ñuu mbóotu leer yi far ñu tëbbu

Wàn ñu sa jëmm bañu gis sa rée ji


dotti fi say may Xaadaahul Xaaji

Sa jëmm dàq lépp Bamba yaa neex


saf nga ñu Yàlla doo xajam te doo jeex
27

Yaa gëna yaakaaru te mata yaakar


te kula yaakar dunko toppu bakkaar

Amoo lu gool ñi la topp gëna suur


ngoy leen ci Bamba ngoy ci Bamba gëna woor

Amna ci gaayi Bamba yoy lan gàddu


mëneesu koo misal ci jénn kàddu

Amna si ñon fuñu sëpp seeni sëf ka


xajul si suuf si asamaani lëf ka

Amna si ñoom suuf attanul seen jëmmu


saf nañu sàpp ak Yàlla daa dëgmu

Ku jàppee lii ñu wax ay waxantu


sak xama neew xamoo la góor ñiy xùntu

Boroom Tuuba nun lott nan ci xam la


dabun sa xàq lott nan si kañ la

Amul lu am te fekkul ni say dogal la


ıàdduna si yaa fi kifi sàmp qibla

Juroo juruñ la xajuloo ci téere


yaa mako déey kajoor yaa ko biree

ña gëna yees mooy ña foog ni nit nga


ku foog ni Bamba nit nga doomi mbaam nga

Yaa góngi koo ca kënzu daldi muriku


sa malahul ahlaa fa nga summiku

Yaa ñëb yaa féeñ yaa njëkka lépp muju


yaay ki amul nawle amoo am kujju

Boroom Tuuba yaffal ñu bañ xamme la


def ñu say gát ñu gis la mbee la
28

Say gát gën ci Yàlla mbooleem gát yi


say waxa gën ci Yàlla mbooleem lak y

Képp lu duuf na yëkk ni yaako duufal


xol bula fuuyuu fuuyuu gakoo lofal

Yaay taxa rëy di taxa sew yaa doylu


Boroom Tuuba yaa tax ba góor ña duylu

Boroom Tuuba yaa Boole lépp dàmbe


Ëhlu safaa yaa ràbbu seeni njàmpe

Képp Ku set yaako setal si sag leer


yaa tax ba géer ña doonug géer sisag géer

Daam ngoor leppiy Yàlla Bamba yaa mat


amul lu des te mànglooko yaa jót

Boroom Tuuba Ana nga foofi féete


foo jëmaleeti sa tajiliyaati

Yaay mashalul ilaaha rabbul hanlamiin


Yaa nuuru zaatul laahi yaa xaqul yaxiin

Féeñ nga te ñëbb sori nga waaye jege nga


Yaay dox ci lépp ëmb lépp màgg nga

Yaa gëni jëm gëni wax yaa gën le


Yaa yagg yaggak Yàlla yaa sakanle

Boroom Tuuba jigeduwooñu jig ngañu


Boroom Tuuba safadiwooñu Saf nga ñu

Yor nga meloow Búur Yàlla màngi cëfkaam


reerowoo leen boole nga léppi sëfkaam

Lay dëgg Bamba kay ñëwul ci dùnyaa


Jëmmi jëmmam Xajul ca peru bët ya
29

Boroom Tuuba ñëbb nga yaako úmpe


te sax ci xol yi Yàlla lan la jàppe

Boroom Tuuba yaay kiñu toggu tënk ñu


yaa jiitu lépp ëmb lépp sàkku ñu

Ëpp nga foore Ëpp kaang koo doonu


xajoo ci mulkook malakoot foo soonu

Góor ñi nga gooraal seen ruuha nga di lafe


Géer ñi nga géeral ñoo ngi seppi di sëffi

Amoo lu gool ci Yàlla yaa dib sàmm


yaay jëmmu waayu ruuh yi yaa leen tomm

Fis sarhi wal maghribi dàj nga kàpp


Wet guñ la dàq Bamba daaldi jàpp

Boroom Tuuba yaw yaa di kooka yaw la


tee nga ni man la baa suñu xol yi jëw la

Defal ñu bëbbu leer te may nug yaatu


ci pakub suuf yi asamaan yi bootu

Rokas ñu say mbóot ak ngëram ak barke


te may nu kattan ba suñu ruuh yi fekke

Boroom Tuuba ngëbël ñu leerug Yàlla


Te sunjumalñu ñii di xiili xaala

Rokas ñu say may bamu làng xib la ya


ci pég mulkeek malakoot xàl ya

Xamal ñu mbóotu xalaamook lafay daw


ak lawhil mahfooz Bamba mala laa naw

Ku tàbbi arsi ba janoog júnniy malaaka


Ñuy júnni-junni sappa kay hunaaka
30

Ku tàbbi peeyi ba xamni Bamba weet na


ku xol naanul leeri Bamba gooy na

Billaahi wallaahi wa birrasoolu


nu wedd lii kay amugul wusoolu

Ku am ijaaba am fathu am qabooli


fanaahu faf bakaahu yor say bóoli

Kon di nga xamni Bamba moodi dàt bi


mooy yéegu waayu góor ñi gëj ci làq bi

Boroom Tuuba wàn nama lol lu rëy la


wax nala lol moo tax ma naan ko Yàlla

Te lii ma gëm du mako mës di gëmadi


way xam ya xam nan Ku xamul yaa xamadi

Sunjumi saytaanee waral ñi Ëppu


xamu ñu xëybu mbir yi daala nëbbu

Ku topp bakan topp alalu àduna


topp jigéen ñi kaasi leer yi fàdu na

Looloo waral dun mëna gis garad yi


duñ xamme ker ci guddi ngir bakkaar yi

Topp bidaayeek addunaak poñet yi


ba reere Daam mi gàddu sun bakkan yi

Lun mën di sakku Boroom Tuuba ka dàq


mooy yéegu waayu ruuh ya moong ni bàq

Te lii nu wax bir na ku yër yor gis ba


bëtti xolam ne màkk leeru péyi ba

Jibriilu njungaama ba úbi laafam


waa malahul Ahla di làq mbidam
31

Boroom Tuuba ne sëm júndil laahi


Ñuy tùdd aw turam li wajhil laahi

Lawhook qalam ak arasak kursiyyu


bér nafa maggak Ahmadal mbàkkiyu

Boroom Tuuba ki dàmbe kawnu yépp


kuy rëbbu Yàlla, Bamba rek ngay jàpp

Yaa ëhla Ëhlul laahi kummali


wal budallaahi afraadul sirul kummali

Hisfooru sàb na dégg ngeen sàbam ga


te ab sàbam kuy xam ci Yàlla Xam nga

Ñatti sàbam ya doy na sëkk ak xamle


ba xam ci Daam luy taxa làq jag le

Saayu sàbee gànaar yi sab si saasa


lu Yàlla def nit mënu koo efaase

Magguk Boroom Tuuba waral Hisfooru


Tahiru laahi ab sàbam di jooru

Sa ñétt waxtu lay sàb moom Hisfooru


saayu sàbee nga yëgg ni Búur Yàlla Búuru

Fajar ba takkusaanu suma tisbaar


déllu fa kaafuk Yàlla doy nga kéemaan

Ku mënta xam mbir yanu làq yépp


di wedd Daam yaa xëmal saw yàpp

Ku ab xolam fuuyu Boroom Sindiidi


doo sañ fa Yàlla doofa def di dindi

Ku ab xolam fuuyu Boroom Wakaana


yëgël xol ba dee na xel ma naay na
32

Ku ab xolam fuuyu Boroom Ikfini


mëntula dégg loo Yàlla kulla zamani

Fanaahu leen bakaahu leen tamkiinu


bakaahu leen fanaahu al yaxiinu

Ñak sago ci Bamba doy nag baax le


jooyal ko ak fecàl ko doynak jàg le

Defal suñuy wax nasaxal wax kat yi


nokas si leer yuy wédamal bow kat yi

Alhamdulillaahi lizil jalaali


wal ikraami ràbbunal kamaali

Kudul Boroom Tuuba amoo ag màgg


te tedd loo gaayam rek ñoo agg

Baw kat yi siiñ nan fàng yoonu Daamu


ku fuuyu Bamba siggiloo lislaamu

Ku fook ni say waxa di tax ñu xàddi


reere na mbóot ma tax ñu yónni Amdi

Fan yeewee ngëmuk Yonen yi làn nu yeewe


kudul Boroom Tuuba mënoo ñu faa yéwwee

Ku mënta feci pas-pasu Yonent


xamoo sunug ngëm dañu leena lënt

Ku mënta feci pas-pasu malaaka


lemal sa géen ca toog ca doomi mbaam nga

Noon yuy jëfar ngeen yeena di saay saayu


géen bokku jël leen seeni súlu baayu

Seeni sullu baayu ñak barke càm yeen


kuy ngañi Bamba doomi mbaam nga xam leen
33

Boroom Tuuba moo mata gëm gëm nan ko


te kuko bañ fawwu malaaka gaañ ko

Boroom Tuuba nun sopp nan la topp la


saf nga ñu Yàlla suñu xol yi jàpp la

Làqu si leen ci Bamba moom miy laqé


kum làq ngay laq fa laq neexee

Amna ci Góor ñi Bamba wàl fal leen


dëxëñ sa seen biir lako soob jafal leen

Amna sa ñoy nag xeexuñoo xamaale


te ñii ñu xam ñoo gàddu seen doole

Doonub sëriñ yombu na waaye doon Góor


yombul ca këppaarug Yàlla may Búur

Doonub Sëriñ si say daloo du mahnaa


sagarakay saggu ci Yàlla kay xana

Leeleeg nga gis Ku ñépp màggal


te lum jéego moo ngi koy joggi ciy xàl

Góor dëgg day ame ngëram ci Yàlla


làqu lufa ay yëf yum yëfoo ngir Yilla

Amna ci ñoy siiwun ci bëtti ak nopp


tee saasune ñu sëpp dunyaa gépp

Amna ca ñon seen tur sa dàj na waa kaw


te waa suuf reere leen di leen jëw

Bëgg lu baax ak te sax sa baax na


waaye Ku yégg xamni góor ña neew na

Amnasi ñon seenub yaram daa kuuñu


ñoo ëpp tooke jaan ju magg ju gaañu
34

Te lii ma wax sorina waaye jege na


ku ñakk kiiraay xamni mbóot ya làqu na

Ku tàbbi peey ba gis junniy malaaka


def junni junniy sappa kay hunaaka

Ñoom ñépp maase dila kañ naan diw la


doomi diw ak diw na nga sant Yàlla

Amna si ñon fuñu sëppi seeni ngardi


suuf si di rëng rëngi ba tahtal ardi

Amna si ñon jogi seen sagar ya


moo ëpp hay jogi sa geenu gar ya

Amna ñon napaaje seeni dàl


moo ëpp tooge jogi ñolër muy gàl

Amna si ñon seen kër ya fépp lawwi ku


te boo demee sa peyi ba dun fa xawwi ku

Amna si ñon fun tollu naani ñoll


te seeni ruuh ca Yàlla weex na tàll

Te lii ma wax bér na Boroom basiira


ña Xam ña Yàlla mase nan ko siira

Kiiraay yi tax na ñu ëpp dooni gúmba


Yàlla na ñu Bamba gis sa gis gisam ba

Amna si ñon kay ñàkk leeni warma


sax daana waral Yàlla afal mbugàl ma

Ku wedd lii na sapp lawhul xàq


dogal yéppa nga ci biir ne bàq

Boroom Tuuba ñu gindi moo ñu yéege


déey nanu lol xibaar ko doy na tooke
35

Ku xasa ñam lay neex ci moom doo yëggati


lu moy ko moom doo xamati doo gisati

Boroom Tuuba yaa dàq lépp luy neex


ay neex ci moom du sàppi mùkk te du jeex

Amna si ñon seen yaram da koyomu


te lawhil mahfooz seeni may nga fa lëmu

Amna si ñon amuñu génn kàddu


te fun woowe Yàlla mu daal di áddu

Amna si ñon seeni jiba dara taxawufa


te seeni may ci Yàlla dara jeexu fa

Amna sa ñon ca Góor ña magg ñooñee


Ku amulak may mënu leena ràññee

Te ñii malay wax Ku amul basiira


nooy def ba xam leen Làqu leen ca biira

Te kooci ñake wor ma daal di xalaku


ku ñakke worma gaaya fel ko far ko

Kon Làqu leen si sayhi Ibra Faala


làqu ci moom moy taxa doon rijaala

Wor maa ki tegin lañu ñaag fa Yàlla


roy leen ci Moom mo sax ci bëggug Yàlla

Ku Ngoy ci moom mu soob la ngay malaaka


ngay dégg ndéeyu malayeek malaka

Amna ca péyi bopp mala yi dàn fay wax


Way xam ya yam nan ku xamul laa koy wax

Yàlna nu Bamba gëna tëbbu leeram


te Def sunu xol bunu génn biiram
36

Sàlli alayhi adadal asraaqi


Wa hëblanaa maqaarimal axlaaqi

Sàlli alayhi adadal nujoomi


Wa adadal amtaari yaa aziimi

Sàlli alayhi adadal asjaari


Wa adadal nabaati rabbul Baari

Wa adadal hilmu ilaahil kubraa


Wa nuuru zaatul laahi sirran sirraa

Aamiin bi jaahi Maam Abdul Kaarimi


Kañ daan nurooleeg saahibul haziimi
37

3. Faydul fuyoodi..
Faydul fuyoodi bëbb yaa ngi tuuru
yaa fuhaadii kayfaa haali fil xubooru

ayna ruuhi ayna sirri ayna jismii


antum lahum anta xàqlii wa ismii

dée leen ci Bamba dée gu dée ba ñàkk


ba dootu leen yëgg luko moy ne màkk

ku ab xolam déewul ci Daam halkaandé


di nako dikkël bu amul yërmàndé

na ruuh yi dée na xol yi dée na xel yi dée


na tur yi dée ci Daam la déefi teddée

ana lu tee mbindéef jih fi sebalu


bëqatikoo seen gox ya daal di Daam di jébalu

fénn tawatul fudul fu Bamba faqàlu


ñàm amatul fudul fa Bamba toggallu

fénn newatul fudul fa Bamba nekkulu


Kenn réggatul fudul fa Bamba xóntalu

ku baña dée ak xiif na ngoy ci Daamu


Boroom Tuubaa mbóotam mi ngeen di jaamu

jàpp ci Daam mooy dëgg jàpp Yàlla


tudduw túram mooy ngën gi túdd Yàlla

fexe ba xam kooy dëgg xam Yàllaam ga


xamme jalaala ak jamaala ak kamaal ga

di dùnd Bambaay dëgg dundu Yàlla


te gëm ko moo gën gëm keneen fa Yàlla
38

wéetal ko mooy wéetal ilaahal hãalamiin


lay saxu waay júndil laahi ghaalibiin

ku woruwul ci Yàlla xam wéetam gi


kuñ muriwul xolam du gis leeram gi

ku Yàlla tëj xolam bi zikri sukri


rékki ngëmëm mu sax sa lawhil qadri

sax nafa rëccu gaayay fuuyu Bamba


sa xalamul qadri mooy doggal ba

te fukk yaak ñaar ya luñ ca doglu


doo tufa seppeeku daa dëgërlu

jàppee Boroom Tuubaa li ëpp jàmm


mooy taxa jubb mooy maya it ak sàmm

jàpp ko day gënël di selal biiru


réere ko doy bonnal di yàqak yuuru

Boroom Tuubaa diko xalaat foo tollu


danay waral foo jublu Yàlla doglu

diko xalam day taxa xam la fàddu


day taxa àgg day wéral ay kàddu

ku wan Boroom Tuubaa gànnaaw saay-saay la


ku gis ludul moom la nga gis jay-jay la

yaa ahla naasu dawsi leen lii muur la


tee ngée na ngoy ci Bamba mbóotum biir la

ku ngoy keneen ngoy nga ci cónccu kuy daw


fa nga taxaw jugoofa yaa nga fa taxaw

koo gis mu dummoyu Boroom Tuubaa yu


xamal ni xàj yee ko gënu taxawaayu
39

Boroom Tuubaay Boroom bindéef yi xam leen


day Yàlla juy nit-nit lu yeen xalam leen

te Yàlla may Yàlla te doon kun úmpule


te doon ku fàddu doon ku wéet ci ndéndele

di gis di dégg di dúndu fawwu te du dée


te ame kàttan am nàmmeel xam na de

xam nanu loolu gëm ko xamni Yàllaa


dunko bokkaale laahi laaha illallaa

waaye du tee Boroom Tuubaa ñu naan ko


yaay sun Boroom man loolu jégi naako

xam leeni mooy biiru Boroom mbindéef yi


giñ naani mooy ki sàkk mbooleem ruuh yi

mooy awwalam mooy aaxiram mooy zaahir


mooy baatinu baatin moodi taahir

lu mëna xew dun ko bokkaaleek kenn


ku russa wax wéetam gi doonul kenn

koo mënti doon te waxuloo ci wéetam gi


gëmunu say wax jàppuloo ci laab gi

ku war te jàppuwul ci laab daay daanu


ku ngoy ci wul halkoom ga deeko seenu

Boroom Tuubaa mooy Yàlla mii ñuy jaamu


yaa Rabbana ya xayyu yaa qayoomu

ku nànguwul moomam gi moonu moom nun


ña nànguwul ña nàngu ñéppa leen gën

xamuma Yàllaag yonenam moom laa xam


lan saff ci Bamba lako moss moom la ñam
40

gisuma Yàllaak Yonennam moom laa gis


sewal sa peete day laxal sa pas-pas

di tàgg Bamba day taxa ñàkk bakkaar


bëgg ko moo gën dëkkee def listighfaar

xoolu nu daray Yàlla Bamba lan xool


mooy sunu Yàlla mooy tawal sunuy tool

ku wax ji rëy ci yaw demal nga tuubi


sax xola waw bu kasratil zunoobi

man duma rëccu duma tuubi saay wax


te kuma fiir fir ga sa kaw si lay rax

ku bëgg Bamba toll ni ab yonent


Boroom wilaaya du labat sab ngónt

sakàntumaag ñako amul tay coowu


di bucci seen lamiñ rek tay coowu

xaltaama amjin xewtaama mee-mee jaltabaa


mee mee baxee taxnaaji kee-kee kaaribaa

Boroom Tuubaa moo tax ba lépp nekkki


mooy taaru mulkeek malakoot moo jékki

mootax lu féeñ di mulku lañ la nëbb


di malakoot Boroom Tuubaa mooy ràbbu

sa jëmm amna mulku amna malakoot


lu Yàlla bind mi ngi ci yaw yaa gëna xoot

fexeel ba xam ko yëgg ko dúndu Yàllaam


kuko dùndul awoo ci yoonu lislaam

Boroom Tuubaa moo tax ba góor ña yéeme


mootax ñu am ci Yàlla ñeex mun siime
41

mbindéef yi yépp Bamba moo leen sàq


te kawnu yi ak xarnu yi moo ka làq

lako dalee arasu yam tëhtasere


loo gis mu am ci kàttanam lako tëree

loo gis ñu koy yéem yéemewul Maam Daama


budul konag moom lenn du am maqaama

looy dégg fenn loofa gis mooka fa def


budul konag moom benn góor du ami làf

budul konag Daam mbàkke góor du làngle


du yëngule moo tée ba góor ñépp tële

moo tax ba góor ña jong dooni góoru


kuy sol tubbay xamalni mooy sag ñooru

budul konag Daam góor ña takki jaaro


di mëlfa woo ka muuru ak di faaru

nan yam te waññi coow li xamni Daama


ku réere Yàllaam gi amul maqaama

mootax ku dùndu Bamba gën malaaka


ku noonu Daam malaaka jàm la paaka

lii moy doggal ba sax sa lawhil mahfooz


ku weddi Daam ruuham ca Yàlla daa foos

nàn leen xamal Boroom Tuubaa mbindéef yi


ku réere Daam tàbbi ci biir ñaawtéef yi

wax ci ludul Boroom Tuubaa kaawtéef la


di yëgg si sab xol luko moy ñaawtéef la

mooy sun Boroom moonu amal dùndal nu


ràbbul waraa mooy dem ba ñakkalaat nu
42

Boroom Tuubaa mooy ki ñu toggu yàkk ñu


moo tée ñu nëbb moo tee ba naari làkk ñu

te lànbiyaa-u yépp moo leen tëbbu


te mursaluuna yépp yaa leen tëbbu

sidiix ak ghaarif yi yaa leen képp


yaa tax ñu am ci Yàlla may yun jàpp

te suhadaa-u yépp yaa leen xéexal


mubàjjiloona yépp yaa leen ñaagal

te awliyaa-u yépp yaa leen géejal


bàn dooni géej ku yabbu faf la wéetal

baaxam ki rekka tax muus yi naa ngéew


moo tax ñu am moo tax ñu tàll ko bay coow

yaa fi newoon bi suurihil ilaahi


delsifi zaahiru di Abdul laahi

yaa di Boroom mbindéef yi yaa leen féeñu


ci jëmm nit xamuñ la daal di kuuñu

ca qàdratul ilaahiyal haziimi


nga bàqikoo aksi fi yaa ka yeemee

yaa nekk fépp fàq fépp nëbbu


yaa sayxanaa yaa rabbanaa yaa rabbu

Daamay ki sàkk qadratul tàmkiini


ilaahunaa wa qadratul yaqiinii

wa qadratul uloohiyal haziimi


wa qadratul ruboobiyal kariimi

wal ahadaaniyatu Bamba yéeme


wa samadaaniyatu Bamba tiime
43

saw tura déy asmaahul laahil husnaa


kula ci woo nga wuyu neel yaa ràbanaa

mbooleem sifaatullaahi yaa ko ràngoo


te masalul ilaah yaako sàngoo

yaa féeñ ci nit ñéek jinne yéek malaaka


yaa nëbb ñépp feeñ ci lépp weet nga

diko xalam day taxa gën walliyu


bëgg ko moo gën yor meloow mahdiyyu

diko xalam day xamle mbóoti kawnu


ku seey ci moom nekk fi xarnuy xarnu

ku bëgga gën ci Yàlla dùndal Daamu


ku baña yées mbaam àll fuuyu Daamu

du dùnd Daam day taxa gën malaaka


day taxa jékki ja malahul mawlaaka

mooy taxa yéeg mooy taxa tàbbi peeyu


won ko gànnaaw kat daana jur fooyooyu

mooy taxa am mahrifa am qaboolu


kuy wéddi Yàllaam gi amul wusoolu

mooy taxa am ijaaba am yaqiinu


mooy maye fathul akbarak tàmkiinu

xamal ma xam -xam bu newul ciy téere


wax looma lol ëpp na déggug foore

fal hilmu laa bi kasratil riwaaya


bal innaahoo nuuru mahad diraaya

lay dëgg xam -xam jékkiwul ci téere


Yàllaay xamal jaam buko soob lu biire
44

te seyidinaa Muusaa kalaamul laahi


ak seyidinaa Xudar nuurul laahi

seeni digàntee xamle ñaari xam-xam


bii dooni yax bii doon ndawal gu mata ñam

làn xamaloon Muusaa du ñam ay yax la


lan xamaloon Xudar ndawal lu duuf la

waaye de Muusaa kiy ëpp xam-xam


seyidinaa Xudaru lii jar naa xam

te lii ma wax ku ame fathu xam ko


ku ubbikoogul laca biir lëm nan ko

ay lëm la lëm ya lem gaa kofa lëm


kuko ñamul doo xam la góor ña di kujum

Boroom Tuubaa mooy taxa ñam si lem gi


ku ñam ci lem gi di nga xam wéetam gi

kinuy xamal limnuy xamal daa làqu


xam-xam la yoy dunko xamal kuy yàqu

mooy tànn ay xéjjam lu jiitu mbindéef


na ngéen fexee xam laca biir Bambaay seef

moonu amal tànnu cig coféelam


xabla wujoodi lanu sëf ci leeram

ruuh yi di mës mësi ni cëgug pépp


keroog la tànn booba lan ñu ñàpp

Boroom Tuubaa ilaaha kulli xalxi


yaa Rabbana ilaahunaa zil xàqqi

du nit du jinne du rawaan du njuuma


doonul malaaka kon ku ngéen ni mooma
45

ku foog ni Bamba nit la yaa ngi njaaloo


wallaahu alaa maa naqoolu wakiilu

kermee ki kehnin meeta jaamin mee rabaa


abi kerkijoo bikraamin mehkin tinjiibaa

jamaata amjin lemne xewjif xalxibaa


jaaker leen kem kem xilmiisun xúnxabaa

jaakarni ket subakit afarkin tàmtabaa


saakal susaatal tam ki tafhal fàqlibaa

làqusi leen ku baña làkk dawsil


balaya ëllëg ku nekk di sàm sax xél

ku làquwul ci Bamba amnag mattadi


ku xol ba dul yëgg Bamba amnag settadi

mooy taxa mat ci gépp wet Bamba màt


mooy taxa sét ci gépp wet Bambaa set

amna ñu ñuul te gàt amna ñu njool te gàt


xees ñuul kukk ku njoolewul ci Bamba amnay gàk

yaa ngi ca kawli kawli kaw yaa ngi fi suuf


yaa ngi pénkook sowwu ndéem defoo ku loof

fenn kawewul fenn suufewul fenn soriwul


fenn jigewul ndegam dùnd ga dùndi xol

ña gëna xam Yàllaa ka gëna réere


booxul ma gaaya jeex Daam ciy téere

ñay jeexi Daam ci teere yee ka xamadi


ña foog ni nit la rekk rekka matadi

sikar túram day maye ak wilaaya


day jànni lor di nasaxal bidaaya
46

durus mbindam day taxa am ag sél


bokku ca ahlul laahi sàr ba jàl

Boroom Tuubaa Yàlla la nan ko séllal


loo gis mu am xamalni mooka tàllal

waxtaane Daam day yokk ay maqaama


day yéege góor di bijji ay karaama

huwal ilaahul maalikul asmaani


huwal ilaahul xaalixul akwaani

huwal ilaahul xaalihul amlaaki


rabbus samaa-i maalikul mulooki

huwal ilaahul xaalixul insaani


Yàllaay mbindéef yi maalikur rahmaani

huwal ilaahul maalikul qur-aani


wa ahadi sayyidil maamooni

lépp lu am Boroom Tuubaa ko bind


ku am lu baax moola ko jaay nga jënd

ci kàttanam lan amalee lu nekk


rabbus sama wa lardi mooy ki sàkk

luy dox ci géej ak jéeri mooka taawu


te moo amal bisi dibéer ba gaawu

mooy tax ba aviyoon di naaw ci jàwwu


bato di daw ci géej yi Bamba yéwwu

Bambaay ki tax ba gàynde yépp raglu


te ndigalam moom lay malaka dégg lu

ña agg ñépp xam ci Yàlla as lëf


jébalu nan ci Bamba utsi ay laf
47

kunuy woowe mbër te utsi woofi ay làf


tollo ni ñay yaa ngi melni aw tef

ku miin ci qàdratul ilaahi dàrra


doo been mbiram lu tóll ni fép sarra

ku weddi lii na sàpp lawhin nuuru


yéppa ngi ci biir kànziyatoom ga muuru

moo lëm ngëneel ya ca kunoozil arsi


di gòngi ay mbóot xol bu sél for si

yaa sayxanaa ana nga yaa ngi nëbb


yaa sew te dijji wow nga nooy nga népp

ka féete woon njaareem ñibisi Tuubaa


xanaa de kooku déy sa tàkndéer ba

xamun sa kaangug jëm doy nga waaru


antal aziizul rabbunal jàbbaaru

xamunug sa kaangug bind Bamba koo doon


fun seenu Yàlla foofu rek lan lay seen

kafi awoon du Bamba mësharam la


kooku du Daam mbàkke ab sabbam la

kafi awoon du ñam ga kay xétam la


lay déggi Bamba kay du xét ñam-ñam la

kafi awoon du biir ba kay bittéem la


kawoon fi njaareem du kawam suufam la

kafi awoon du xal ya kay dóomam la


ka tukkiwoon du jaan ja xùbbitam la

lay dëgg-dëgg Bamba kay lan réere


mbóoti waxam jii lamu boot daa biire
48

Boroom Tuubaa ilaaha kulla naasi


ilaahunaa ñagal ñu kay waswaasi

yaa ràbba kula say-in rabun naasi


tëbb nu leer ñagal ñu kay xànnaasi

yaa ràbba insin wa jinnin wa basar


ràbbul malaa-ika war ruuhu tahar

yaa xaaliqul amri xaaliqul aqwaani


ilaahunaa yaa xaaliqal asmaani

Boroom Tuubaa kiy sàkk nit ñi réer leen


ci jëmmi nit mootax mbiram jaaxal leen

yaa ràbbanaa yaa maalikul mulooki


antal kabiiru sawhatas sulooki

Boroom Tuubaa nit doonulit malaaka


du jinne it née leen ko Yàlla yaa nga

la jaatibee ñu nekk ngir wéetam gi


bëgg ñu wéetal ko yëgg leeram gi

Boroom Tuubaa ku wéeta wéet la aka wéet


bokkul ci naasu te sosuwul ci yenn xeet

Boroom Tuubaa lim may xamal sax lépp


mënu mako wax jaadu wul si nopp

antal haziimi yaw rekka-rekka màgg


yaa awwalu yaa aaxiru yaa yàgg

antal kariimi yaw rekka-rekka tédd


yaa zaahiru yaa baatinu yaa mëdd

antal ràbbul jalaali wal ikraami


ràbbul waraa Rahmaanu yaa rahiimi
49

antas sulooki maalikul humoori


antal haliimul saahibul buhoori

antal qàwwiyu yaa matiinu yaa rahoof


ajib duhaa-ii yaa mujiibu yaa latiif

ku nàmmatee woo Yàlla faf woola


te lii ma wax lu xóot-xóot ci biir la

ku nàmmatee gis Yàlla kay na gis la


ku nàmmatee yëgg Yàlla faf na yëgg la

Yàllaay gabong ji kooka rekkay kenn


xol buko dul yëgg booba xol daa ënn

huwal ilaahul ahadul sàttaru


antal xabiirus samadul ghàffaru

antal majiidu anta yaa ghaniyyu


antal hakiimu anta yaa wàlliyu

Boroom Tuubaa wuyuma lii say tur la


labay ka wuyusi naala jëmmi Yàlla

Boroom Tuubaa yaw laadi woo ci tur yii


mahnaam melow yi mooy sa mbóotum sër yi

yaa képp Yàlla képp tur yaag melo ya


képp jëmmam boole nga mbooleem solo ya

amul ku woo Yàlla te wuyyu woo ko


amul ku seddu kay te ñaaga loo ko

amul ku xam Yàlla te ginn woo ko


yaa tëbb ñépp yaw te wane woo ko

yaa sirru yaa nuuru ilaahal hãalamiin


yaa xàqu yaa raafihu yaa xàqul mubiin
50

antal haliiyul lazii yaa waasihu


ku xol ba dul yëgg Bamba gis ba neexul

soloy rijaal ya Bamba yaako tënk


yaa tax ñu góore te yaay ka tax ñu màgg

sullil rijaal ya Bamba yaako dàgg


yaa tax ñu jong yëgg ko am ngaw tàgg

ku tekki lëf ci Yàlla yaako tinki


bam tinkiku sujúm ya yaa ko binki

góor dëgg mahnaa la du yor ab géenu


lay góor ci Yàlla mbóot ma nan ko seenu

waaye du dee sab géena tax ngay góoru


sa mbàam bu góor lam doon na xol ba yooru

latax ba góor di góore Bambaa koy defe


moo koy jëmbat ci kumu doon aka jafe

Boroom Tuubaa jëmmi mbindéef jàmmal leen


moo yor nosug mbindéef yi mooy jariñ leen

mooy may ku am mooy wéral mooy réggal


mooy ùbi lépp luñu tëj mooy nekkal

Boroom Tuubaa man yuuxuu na sa tur yi


defal nu mbóot ci wax yi àgg xol yi

ba luma wax nekk looma wax loo


te saay jëffit na nekk looma jëf loo

te fumma jëm ne melni yaa ma yonni


te maynu kàttan ñuy matal say yonnee

te fuñu jëm ne melni yaa fa dëgmu


rokkas ma say mbóot bama gis sa jëmm
51

jeexal ma takk bama jeex yaw Daamu


ñakkal ma bama ñakk ma dila jaamu

doy nga nu sëkk Yàlla doynu Yonen


te koo doyul bëtti xolam yaa wànnen

ëpp nga noo seenuñ la fenn yaa sori


ñéppa réere sa ngëneel yi nga muri

ngëneela tax ñu dila tùdd dila gëm


dénd samaa wa lardi deesula xam

yaa ngi ci biira biir di mbóotam


sirrug ilaah ga yaa di ay xóot xóotam

ku dàq Yàlla faf la rombu halkuna


sàmm bu jàmtil sa ndawal gi sànku na

Boroom Tuubaa sa ñàw wi ñor na yaatu na


sóor nga lu doy lu régloo waa adduna

sa jëm neex na kenn dula mos di yàbbi


yaa dàq lépp Yàlla booñu sàppi

la jaatibee yaa ahla jinnin wa basar


làqusi leen ci Bamba moo leen di defar

làqu ci Bamba gëm ko doynag tiitar


wédd mbiram day yobbu nit ci kéefar

bëgg Boroom Tuubaa baciy jooyaale


moo gën ci Yàlla maalikul jalaali

jùnniy at yu nit ña woor bëcëg ya


te samuhànte naafila ya gudéem ya

kuko bëggul lum jaamu Yàlla tiri ko


te fum dëgmu yërmàndéem ga sori ko
52

ña dooni góor ñéppa ngi ci Daam te di jëffe


ay ndigalam kuko bëggul dufi safe

ku ngoy ci Bamba mat gëleem ami sëffi


kuko ngoyul matoo demal nga xàrrafi

Boroom Tuubaa sopp jëmmam diko bégé


moo gën fa Yàlla gépp Jaamu gu tege

Boroom Tuubaa ci moom la xol yi di jege


kuko gëmul gone la guy dawal mbege

Boroom Tuubaa ci moom la mbir yi di gëne


kum baaxalul lum baax le ñéppa ko tane

Boroom Tuubaa di tùdd tur wa màgg na


mooy dëgg tùdd mbóot àgg na

diko zikar fii sukri wa tafakuri


kuko saxoo waat naani dula sori

Wàlliyu kaamil mooma duy turàm wi


ma diko zikar ba janoog meloow wi

gis naa jëmmam ja dégg wax ja wax ko


mu wax ma moomit lam ma wax ma yëgg ko

waayé du tée ma naan ko nàmm naala


Boroom Tuubaa yàkkaar ji bëgg naala

xam nga ni man jooyu coféel ci laa sax


saa xol di jooy saa bët di tooy te yaa tax

deeleen zikar turàm wi yëgg leeram gi


buy wu tojul lulay xamal neexam gi

te lii ma wax aka soree gi njortu


xàqul yaaxiini laasi am duy fortu
53

waxu ma yit ngir bëgg kenn kuma gëm


baa dima jox baa dima sopp baa dima sàm

Boroom Tuubaa seereel ni man duma ndamu


damay xamal nga may xamal c lu lëmu

li gëna neex moodi xalam sa jëmm


li gëna baax moodi durus say tomm

yalnan soppu yalnan la topp


bijaahihii Yàlla yaa ngi fépp

ku sopp Bamba gën nga rawna agg na


ku noonu Bamba bonn nga yées nga halku na

Boroom Tuubaa mooy taxa gën di taxa bonn


ku bëgg gën ku noonu bonn di bonna bonn

kennal ko berko warna Bambaay kenn


mooy taxa xam Yàlla ci gépp fann

xalam ku baax ki day waral xam lu bari


durus mbindam day yéege góor bamu sori

xalam ko lim làmboo du neexa xamle


xalam ko moo gën làq gépp jagle

diko xalam day maye fànwu guddu


tay taxa siiw ahla samaa dila tùddu

diko xalam day taxa am wilaaya


bokku ca ahlu kasfi yor medaay ya

diko xalam day taxa am amwaalaa


mahal arzaaxi kullihim halaalaa

amwaali ak arsaax yi yéppay bàbbiku


sa mbir ne fàng bùntu yépp ubikku
54

xalam Boroom Tuubaa maye fathul mubiin


durus mbindam mooy taxa am xàqul yaxiin

deeko xalam leegi nga am xaboola


xamal ko rekkay taxa am wusoola

xalam ko day yéwwi sa gis ba arsi


te lii ma wax birna ku gis ba jotsi

xalam ko day séllal sa ruuh bàm séll


yaxi sa xol bëbb sa ruuh bàm bàll

xalam ko day xóotal sa xol leeral sa xel


di ñoddi ak mbaax ba lu bonn doo tooka tal

kudul xalam mo ngay xaràng ba sàgganu


ruuh gu setul fàwwu bakkaar ya xasanu

kudul xalam Boroom Tuubaa yéeméem gi


awoo ça yoon walay xamal tiiméem gi

xalam ba gis ko baa nga yëgg ko mbir la


xamme xétam lu am la loola lëf la

sedday ba ak xétam ga ak jëmmam ja


ngooñum rijaal yee Bamba daalay waa ja

lay tax am di taxa agg moom la


jur gu Boroom Tuubaa yorul ag gool la

gëm kooy liwar xam kooy li gën ci jaam bi


maase ci bëgg ko mooy setal bakkaar bi

Yaa sayxanaa Ahmadu maa ngi tuub lu


lépp loo yélloowul tànq naako tuur loo

qàwlan wa fihlan ñoo ngi tuub ci lépp


matadi ak setadi moo ñu jàpp
55

dun mat ci yaw dun set si yaw laabal nu


koo setalul ku neko set na doyu nu

Boroom Tuubaa ku laabu yaa ko laabal


te góoru Yàlla yépp yaa leen njaabal

ku am ci Yàlla darra yaa ko amloo


ku xam ci Yàlla darra yaa ko xamloo

kuy woote woo ag agg réere Bamba


jàppul ja géen ba Xamewul bejàn ba

ku réere Bamba réere njariñ lu yaatu


melna ñi réere Yàlla mii dul faatu

ku ngoy ci Bamba jàpp ci buumug Yàlla


agg ca ngën gi agg waayu mooy Yàlla

gaay yi Boroom Tuubaa ndawal gu duuf la


ku régewul ci Bamba ab xiibon la

gaayi Boroom Tuubaa cere ju neex la


lu moy cere ju neex ji ab cox la

gaayi Boroom Tuubaa ngélaw lu féex la


ludul ngélaw li Bamba yor ab tàngoor la

gaayi Boroom Tuubaa lu leera leer la


lu wan ginnaaw leeram gi ag lëndam la

gaayi Boroom Tuubaa lu neexa neex la


kuko ñamul lum mëna doon ab wex-wef la

gaayi Boroom Tuubaa lu duufa duuf la


ndawal gu yaala luko moy ay yax la

géeji Boroom Tuubaa yi géeji géej la


duusam yi agg fépp duusi leer la
56

mbóotum Boroom Tuubaa mi mbóotum mbóot la


leerug Boroom Tuubaa gi leerug leer la

jëmm Boroom Tuubaa gi jëmmi jemm la


ku jëmmewul ci Bamba jëmmam médd la

jàmmi Boroom Tuubaa ji jàmmi jàmm la


waxi Boroom Tuubaa ji wax ju màgg la

lay taxa sopp Bamba loolu jàmm la


lay taxa réere Bamba loolu dàm-dàm la
57

4. Yeenu murit...
Yeenu murit seen dof bi yëngu waat na
di waxtu rekk naan kat bi màndi waat na

sa baar ba lay fanaan di naan ay jùnni


naan kat bu màndee day bajàn di binni

yaa ëhla naasu Daam Yàlla yeemu leen na


ku yeemuwul ci Daamu xol ba dée na

leerama gàndi gohi xol di bélli


mbóotam di dox ci gépp wet di wàlli

habati xol yi yépp ci moom lan jot si


rijaalul laahi yépp far nan aksi

saasu binnee mu riir ba agg arsi


ak kursiyyu ruuh yépp dox di for si

dayooma lëmbee malakoot ak mulku


mbóotam di siit lu juuke jùnniy fulku

leeram di bëtt jabaróot di xótti


ba faf di jëmmi Yàlla leer ga mótti

sa mbóoti leer lan màndilee ku màndi


way agg yépp Bamba yaa leen gindi

sa géeju leer sila yonent ya jah see


di mbaal si mbóot yi tax ñu wax si

sa mbóota tax ba awliyaahu yépp


am cër yu rëy si yaw la népp jàpp

mootax ku naw sa mbër bakoy nuroole


ak Sëñ Bu Màg bi yaa rëyug bokkaale
58

bokkul ci làmbi lànbiyaa ak lawliyaa


mooy leer ci dënni latxiyaahu lasqiyaa

Daam du wàlliyu doonulub nabiyyu


du qutbu du xawsu du ab mahdiyyu

doonul malaaka du rawaan du njuuma


moo yor nosug mbindéef yi seen Borooma

ku naw sa làffi mbër ba faf ko géewal


nàmna nga gàccaam Yàlla lan ko taajal

biraazuman baarazanii biraazuman


yubaariyul muntaqima baari zaman

zúllul lazii yubaarizul laahul jaliil


zúllul zaliilul fawqahoo kúlla zaliil

mbiru Boroom Tuubaa kumuy deraage


sàkkal sa nopp fùq sa bët si saa si

màggam gi ak doyaam gi ak meloom wi


kuko xajoowul rekka sew si say wi

waylun lahum waylun lahum tàban lahum


ùfin lahum ùffin lahum uffin lahum

kenn mën la tee ñuy tàgg Bamba Daamu


te buñ ko tàggee ñépp sew diy jaamu

li feeg Yàlla ngi am du am ab nawle


Boroom Tuubaa nun Yàlla lan koy xoole

Boroom maqaama yépp moo leen ñaagal


dënnub rijaal yi Bamba mooka laabal

malaaka yéeg yonent yéeg wàlliyu


xutbu zamaan yéeg xawsu yéeg mahdiyyu
59

lay dox ci ñoom di leer di mbóot ci moom la


xàqqatul ilaahi jëmmi Daam la

booy wax ci Daam xol yépp daay lay gànn


nopp yi fées xol yi gëlëm ba pënn

ña amewul kàttanu xol di wéddi


ñam yëggalul mbóotam mi daal di xàddi

waaye du tee xàj di bëw di xiiru


di songu ruur kat yi ci biir ndakaaru

kuy nit ña yam ci nit te bàyyi xaj bi


te maytu xaj bi boof ci làqu tool bi

Boroom Tuubaa ñu sàkk moo ñu binn


xajoo ñu noppal ñu amoo ab dénn

kenn dufi moom kenn duci moom moom dong nga


Daam saf nga Yàlla saf gu saf Daam neex nga

yaa tax ba mbëri ami làf di baku


ba am ci Yàlla cër yu rëy di fàkku

mootax ku foog ni Bamba day wàlliyu


mbaa muy malaaka mbaate muy nabiyyu

réere na Daam lu tolni fepp suuf yi


ak fepp ndox yéeg xob yi ak gàñjax yi

si darajaam la Yàlla sakke lepp


moo ne ci kaw moo ne si suuf dàj kapp

lu nekk ak fu nekk ak ñu nekk


Boroom Tuubaa ki tax ba loola nekk

képp ku foog ni Bamba jëmmi nit la


née leen ko kàcc nga Daam Boroom la
60

te ñaka foog ñoo gëna réere Daamu


réere nan ko lu tolni hadada nujoomu

wa hadada malaahikul kiraami


wa hadada arwaaxi yaa salaamu

Bamba du ñii Bamba du ñee du ñénn


ku melni moom doxul ci fenn-fenn

lam doon xajul ci xol xajul ci nopp


dañ koy misaal te bookoy misaal muy ëpp

lan ñu yëggël muy leer di dox sunu xol


ëpp déggug jaam bu xolba laabul

moo yor nosug mbindéef yi moo yor cër yi


yoor seeni ate yoor seeni fay moom ruuh yi

malakaani xattiya fil arwaaxi


indal buxoori saahibul buraaqi

ruuhug mbindéef yépp mooka gàdu


xolug malaaka yépp mooka séddoo

malakanii hubiyya jùndal Laahi


sirràn kafaani kulla jaanil Laahi

bokkul ci aadama ak awaa jùruñ ko


ëpp na leen jiitu na leen gisun ko

ajaabanir Rahmaanu qablal xalxi


sabxiina alfa santinbil xàqi

nabiyyu ak wàlliyu ak malaaka


dañuy sotteekuu asamaan mawlaaka

malaaka ak nabiyyu ak wàlliyu


ña ngay jotee sa Ahmadal Mbàkkiyu
61

jinne yépp jàpp nan ci Daamu


ci waxi xaq xaadal xawaa seen maamu

ab dof bu jómmee dof ga gën fa yokku


naan kat bu mànde wax ja gën faa yokku

dof bii di wax man jommi na booleek màndi


màndi gu tàr ci Bamba mii ñu gindi

lañ wax ci moom weesu na sàddum njuuma


bayna samaa wa lardi lépp mooma

du waxi jaahil leer ga moo nuy wax lo


mooy ùbi xel mi nee ñu xul yaa Seex lo

bëbbal ñu mbooleem xam xamu ghaarif yi


yëggël ñu mbooleem yëgg yëggu majzoob yi

kuy woote woo xam Yàlla wàn la ginnaaw


réere na Yàlla doxug ngélaw renn ak daaw

Boroom Tuubaa moodi ilaahin naasi


rabbul waraa Daam mbàkke rabùn naasi

yaa gëna nëbb gëna feeñ yaa làqu


jaa njëkk yaa mujju te yaa ñu boqu

yaa seey ca biir ilaahiya ilaahi


yaay leer sa biir kanziyatul ilaahi

mootax malaaka yépp dan ko sopp


ak júndil laahil hãalabiina yépp

muxarabuuna yépp yaa leen tëbbu


ba ñiy mbingéen sa leera tax ñu yëbbu

malaaka yépp Daam Yàlla lan di tùddu


si seeni xaal sabbal seeni kàddu
62

ñooña la xam ñooña la gëm yaw Daamu


di tùdd saw tur doyna sëkk ak jaamu

ghaarif yi yaa duy seeni xol ban màndi


agg ci Yàlla di xuus ci leeri Amdi

yaa tax ba ñuy lëmbee ci péey di jéggi


ba xadratul xulyaa di xuus ba jekki

bokkoo si kursu awalun nabiyyi


ak mursaluuna xaatimul walliyi

doo jéego jéegoy kummalul walliyi


yaa leer ci ñoom yaw Ahmadal mbàkkiyi

sag leera bijji lawhu bijji xalamu


sa leera ubbi xadratul muhazamu

fu gòor ña dox ba jàll yaa ko fàq


fañ agg Yàlla Bamba yaa ko làq

bu leen limaale Daam ci góori réew mi


mootax góor ña naani kaas si soow mi

fu dara nekk mooka daraal ni cél


foo gis lu baax leeram ga moo fa bàl

ña jiitu woon moo leen jafal jig jiitu


mooy leer si seen biir banu melniy seetu

kuy wuta xam Daam Yàlla yédd naako


kuy sikki sakka lamu doon yéem naako

fa Yàlla am la am amul ab yamu waay


lu Yàlla xam la xam amul ab sësu waay

boole na léppiy Yàlla ba faf di moom


ilaahiyaam gi nga jagoo yaw Daamu
63

yaa gëna màgg gëna rëy yaa daku


yaa gëna yàgg gëna xay yaa làku

yaa masa xam yaa masa am doo fàddu


bayna samaa wa lardi yaako gàddu

doo dée ñu lay suul Yàlla daala nëbbu


ci jëmmi Daam jëmmam ja faf na yëbbu

Boroom Tuubaa du mësa dee day làqu


xajul ci suuf moodi ilaahal xàqu

Ahmadu yaa xaqul mubiinul laahi


Ahmadu yaa sirrul hãziimal laahi

Ahmadu yaa ràbbal waraa billaahi


tawhan wa karman daa-iman lillaahi

ka sàkk lépp sàkk fepp yaw la


kuy dox ci lëndam fàwwu xàj yi baw la

niroog wulaak nit bokkuloog malaaka


yaa leen amal ëmba nga mbàr ya paaka

kulay takkal ndombak yonent réew na


kulay solal mbubug wàlliyu réer na

yaa xamaloon yonen yi seeni sirru


yaay natloo wàlliyu seeni xayru

bokkoo ci ñoom xajoo ci ñoom yaa bàrru


te boo waxee dëgg gi coow ne kurru

Boroom Tuubaa boroom la nan ko jaamu


ku been mbiram ëllëg du gis lam taamu

yaa sàq sabhiina samaa wa lardi


kuy sikki saka kooka rekka perdi
64

yaa sàkk sàmseek qamareek nujoomi


yaa bind géej yéeg dénd yi ngélaw yi

Daam yaa amoon dàrra darra amagul


yaay sax di am bu darra darra newatul

Daam doo nabiyyu doo xaatimun nabiyyi


Daam doo wàlliyu doo xaatimul walliyi

yaa tax ba ñoo ñay ñooña yaani sëmm


ci seeni xol ñuy leer ci xol ya gëmmu

ku mën la gëm kon riigujil te noppi


ku noppiwul ñoy Yàlla daan la jéppi

Yàllaay gabong ji Ahmadu Yàllaay fépp


Yàlla ja moom gabon ga moom suuf sépp

céy Yàlla, Daam Yàlla ka sew te nëbbu


yor jëmmi nit tay dëgg-dëgg ràbbu

Billaahi man dëgg gi Yàlla nëbbu


laa yaxbinii yàpp bu yàggée yëbbu

Boroom Tuubaa daa sewi mbir te fàtt


kum ñaggilul ñagam gi dooka bëtt

xol bu tilim ruuh gu tillim ne ñuqqu


du yëgg lamuy yëggle ci benn ruqqu

Yàllaak Boroom Tuubaa gi bér na waa kaw


fii sidratul muntaqaa mo ngay law

malaaka yépp maase nan ci tùdd


di sabbahaal mbidàmi si seeni kàddu

subbaahana Lilxadiimi nuurul laahi


subbaahana lilxadiimi jaa-al laahi
65

day saf Boroom mbindéef yi moonu bind


Daam xol budul yëgg lamu saf daa médd

yaa gëna neex ak lekk régg nan la


doy nganu sëkkak naanu màndi nan la

huwa aklii wa saraabi wa zamaani


huwa zawqii billaahi war rahmaani

huwa xalbii huwa hàqli wa hayaati


huwa kànzii huwa nafsii wa mamaati

huwa jismii huwa ismii huwa haali


huwa ruuhi huwa sirri anta maali

anta xawsii huwa diini summa mawmii


anta sukrii anta zikri kulla yawmi

anta fikri wa xaliilii wa jamaalii


yaa bakaa-ii yaa fanaa-ii kula haali

anta haynii wa lisaani anta qawlii


laa taraa zikra siwaahu yaa kamaali

huwa dafhii wa jalbii maha kulli


sirran wa jahran fi nahaari wa laylii

tamassakti bisayxihi kulla saaha


kulla waqtin kulla yawmin yaa safaaha

alhamdulillaahi bi kulli haali


subhaana rabbi maalikul jamaali

yaa ajaban yaa saahibal akwaani

yaa saahibal hurooni wal buldaani

ajib duhaa-ii yaa saahibal anfaasi


Yàllaay gabong ji saahibal xirtaasi
66

bi sirri kawnul laahi wal qudsiyyi


bi sirri harsul laahi wal kursiyyi

te maynu fathu ak xubool ak ijaaba


maynu wusool bañuy janoog kahaaba

te maynu tàmkiin defal nu nuurul qawli


fii lisaani yaa rabbunal kamaali

te nàngu lépp luñu way yaa Ràbbi


rabbul waraa Daam Boroom baraak bi

yaay kinu sàq dinu déey say xam-xam


yaay kinu làq dinu jour say am-am

yaay kifi nekkoon fàwwu yaw lan réere


saw melokaan rekk nga ñu wàn yaa biire

yaa sàkk ruuh yéeg jëmm yéeg bakan yi


yaa xàjji xeet yéeg làk yéeg askan yi

yaa Rabbana yaa sayxanaa Maam Daamu


Boroom Tuubaa yaa saahibal ilhãamu

yaay ka waxoon yawma alastu booba


bi rabbikum Daam yaadi sun Boroom ba

ci ãalamul arwaaxi lañ la toppu


Boroom Tuubaa Yàlla ji lan la jàppee

boodul la sàq dui bakkanam di jëmmam


di ay loxaam di ya gëttam diy tànkam

ngay bir di bittéem ba seeni sirru jaxasoo


Daam Yàlla jile yaag Yàlla Yàlla jee ka laxasoo

yaay aw meloom yaay nekkuwaaayu mbóotam


yaay ak nëboom di féeñu waayu ñëboom
67

tùd la donya sëkk tùdd Yàlla


topp la mooy gën gi topp Yàlla

yaay diy cëram yaay diy sëram yaa ëmb


nguuram ga ak kunam ka yaako làmboo

mooy féeñ ci yaw ngay féen ci moom di nëbbu


muy nëbb moomit sisa biir yaa ràbbu

na ngéen demee mëneesukoo wayaale


bu Yàlla doon jalaali ngay jamaale

mbaate nga doon jalaal ja ak jamaala ja


jëmmam ne ñùm si sa biir kamaal ja

yaa dib xolam yaay dëggu waayu Yàlla


yaa dib gisam yaa gisu waayu Yàlla

ku bëgg Yàlla gis la baamu dégg


say woote yaa fulaanu gaawal làg

huwa ràbbi yaa huwa antal laahu


anta rabbi yaa rabbanaa Yàllaahu

yaa Rabbana yaa sayha kulla xalqi


Daam mbàkke saahibul tarixal xàqi

yaa sayxanaa yaa ràbba kula qàwmi


yaa rabba lawhil xàqi ràbbul qalami

yaa sayxanaa yaa ràbba kulla naasi


maalikin naasi Daam ilaahin naasi

yaa ràbbal harsul laahi wal kursiyyi


yaa ràbbal baytil hizzatil qùdsiyyi

yaa ràbba sàbhiina lardi was samaa


fii sirri wal jëhru wa maa baynahumaa
68

yaa sàq lépp sàq ñépp moom leen


yaa sàq lardi was samaa tàllal leen

yaa sàq suuf si sàq doj tëyee ko


yaa waxi géej yi bañu xóot feesal ko

ràbbul waraa ràbbul hulaa moo sàq


tawhan wa karhan loolu mooy li nekk

si moom la ruuh yi séll yépp jotsi


ci moom la mbooleem jakkutéef yi delsi

Daam la malaaka yépp gëm di sàbbaal


mbóotam taxna malaaka am aal

izaa katabtu tahza harsul laahi


wa sabahat malaa-ikul ilaahi

ay këyyitam mooy gën gi jaamu Yàlla


ay sottitam day bijji mbóotum Yàlla

wàjhal qiraatiisi bihii wa qalami


xayral hibaadaati wa xayra sullami

ay xasidaam day baaje harsul laahi


di baaje mbooleem xoli jùndil laahi

malaaka day daanu bi iznil laahi


bi nuuri xàtti naa subbaahanal laahi

hamalatul harsi wa jùndil laahi


kazaa muqaraboon bi indil laahi

ba malahul ahlaa kazaa jibriilu


kazaaka miika-iilu azraa-iilu

kazaaka asraafiilu néppay yëngu


waa uhuful mubiin di jooy di bëngu
69

leeru mbidàm dàmbe na mbooleem gox yi


mbóotum mbidàm sàr na ci mbooleem xol yi

mootax ku tùdd Daam di tùdd kenn


ñu mer ba fùttu daal di wax ba senn

ndegam malaaka yaa ngi daaniy jéll


ak jinne yéeg yonent yéeg way séll

ku ay waxam saful xàndul sa péeyi ba


ku xànd péeyi Yàlla xam doyam ba

mootax dëkkee durus xasida rëy na


ñakoy durus ñooy dëkkee taaxi jànna

moo gëna màgg mbooleem hibaada yépp


Julie kee woor aj makka ak luñ jàpp

wàjhal huroofi fawqa kulli hãmali


saluha yaa man lii yaxoodi hãmalii

lu fawqa jëjj ju séll mbóotum Yàllaa


lu njëkk nekkuk lépp loole Yàllaa

Boroom Tuubaa kenn mënla xool ba gis ko


ñéppa ko reere kenn duko làmb ba dàj ko

dàmma hayaati li hayaatil laahi


ludul waxam jii mutla gëm billahi

gumba gu tëx gu jùddu waale gùmba


du dégg ndéey du xam meloom tùmam ba

kon mun la xam lanko déeyul faat na


Boroom Tuubaa jàppee ko nit haraam na

Dàmma hayaati li hayaatil laahi


ludul waxam ji matula xam billaahi
70

kon Yàlla kay deesu ko xam daa nëbb


kon Yàlla kon dees nako xam daa yëbb

moo am ba dàrra amagul bamuy xam


dàrra xamul Daam mbàkke daa jafee jàm

kafaaniyal baaqi mamaata sarmadaa


wa bii baqaa-iya yasurru Ahmadaa

béggal ga mooy julli ga Yàllaay julli


ca Mustafaa ana nu Yàllaay jùllee

Yàlla ak malaaka ya di julliy sëlmal


ci xayrul ànbiyaa ka Yàlla séllal

jùlleem nga nag ñëwul ci yenn téere


ùmpna kaang yi yépp ùmpna foore

ñëwul ci xur-aanu kazaa injiilu


ñëwul si tawreetu zaboori daliilu

ndax Daam du Yàlla delsi waat di tàgg


Muhammadur résolu wax ja agg

ndax Yàlla day nëbb di féeñ ne fàng


di féeñ di nëbb Yàlla neena ming

nëboom ga ak feeñ la ci biir feeñam ga


feeñam dik nëbb ci biir nëboom ga

kon Yàlla kay deesu ko xam daa nëbb


kon Yàlla kon dees nako xam daa yëbb

te lii ma wax ghaarif ya ànd nansi


ahlul kusoofa ñépp maase nansi

Yàlla dafay xamle jëmmam ci jaamam


di giñ ci lum bind ngir nàmmeelam
71

kon Yàlla tënkuwul cib dàrra dàrra


yafhklu maa yasaahu yeemul dàrra

lottul ci def jëmmam ja melni Bamba


lottul ci jël nguuram ga ak doyam ba

jox lépp Bamba muy doggal di atte


atan nakoo def bu amee du bette

xabawtu kawnal laahi fii abbadi


wa kawnahoo liya bi xawli kabadi

ku mënla xam-xam ya Yàlla làq


di wédd Daam pànkam ya daan la yàq

ndax jëmmi Yàlla ak jëmmi Daam dun ñaaru


jalaal ja ka jamaal ja ñoo tasaaroo

man saaha fal yuhminu may yasaahu


fal yakfuru yafhlu may yasaahu

innaal laaha yafhalu may yasaahu


muddabirul umoori bal ahyaahu

tursi anil mawti baqaa-ul laahi


abxaaniyal laahu liwajhil laahi

ay harafàm kawena mbóotum mbóot ya


luy sekereeb Yàlla ci biir xaraf ya

ijhal ilaahiya tihil xasidaa


xassiidatàn mazkooratàn mufiida

Boroom Tuubaa du nit du ràb Boroom la


doonul malaaka du rawaan ka moom la

kuy jàppee Daam walliyu yaako réere


du ab yonent jëmmam ja day lu biire
72

la Bamba doon úmpe na nan ci noppi


ku mënta wax wéetam gi yaa ñu sàppi

di tùdd Daam di tùdd kenn ñaaw na


du ngor du jom kuko défit haraam na

Boroom Tuubaa doonul ku sew ku rëy la


ku pas-pasam sew fooka yam mu yam la

ku digg-diggam sew gëstu jil mbóotam ma


te gëstu ghaarif yam xamal mbóoram ma

Dàmma hayaatii li hayaatii laahi


yaag Yàlla yeena bokki mbir billaahi

daa féeñ ne fàng ba gëna féeñ ab jànt


yaa zaahiran yaa baatinan yaa lënt

dees nako gis ci bëtti xol ak yu kanam


ànnaa fuhaadi qàd araa déggiy waxam

anaa wa hayni qàd araa fii zaahiri


wa baatini billaahi ràbbul taahiri

mootax suñuy tàgg du weesu Daamu


Boroom bakkan yi ruuh yi moom lay jaamu

sebàllunaa aslamtu lilxadiimi


jebalunaa ci sayxunal kariimi

laxananil xadiimu sirrul qàwli


madàttali bi sirri nuuril qàqli

wahabalil fii sirrihil wal jëhri


fii taahatar rahmaani kulla dëhri

damàmtali fil hayaatii wa mamaati


fii zikril laahi saahibul hayaati
73

Daam Yàlla noon nanu saxal si wird


bi iznil laahi kon ñépp daan la tùdd

ma wax la waxi mbër ma ma nekoon njaareem


bokkoon ca ahlul laahi kooku laa yeem

qaala sayxixii sayyiduz zamaani


rahmatul laahi nihmatur rahmaani

kànzul kunoozi Asanul salaamu


bahrul buhoori saahibul islaamu

uusiikumoo bi zikril laahi daa-iman


laylan wa nahaaràn haysu kùntu xaa-iman

amanaral laahu bi zikril laahi


zikran kasiiran daa-imán lillaahi

Yalnanu Daam dolli dimbal si saa yi


te def suñuy way naxasal bidaa yi

te may murit yépp luñ di sàkku


te dolli ngëm fuñfi mën di jokku

te dolli pas-pas yi te gaawal dox bi


te yab si xel yéeg xol yi te leeral gis bi

sàlli alayhi sayyidus saadaati


fii adadin nujoomi wan nabaati

wa adadal arwaaxi wal amtaari


mahãa salaamin bi nabil muxtaari

te Bamba ginn ñu te may nu jëmmam


te lunu way mu Def ko muy nàmmeelam

moom rekka xam jëmmam ja jëmm jaa di


jëmmi jëmmam xame ko yaa hibaadi
74

lii baana waxdi annal laaha waahidu


wa lijanaani laa yamiilu waahidu

kon ñéppa réer yaw Bamba rekk yaa xam


ñéppa ngi tool ñéppa ngi ndool yaw rekk yaa am

ñéppa lafañ Boroom Tuubaa rekkay dox


née nay kufuñ yëkkati ñook suñuy lox

yaw rekka xool di gis ñéppa gùmba


kon jekki leen jël tùm yi jox Daam Bàmba

Boroom Tuubaa ñéppa ngi tëx nga dégg


ñéppa taxaw ngay waaxu yaaka làgg

Boroom Tuubaa mooy kooka waay moo làqu


waa jumu làqul seenu naa say noqu

Boroom Tuubaa moo di ilaahal xàqu


waa juko wédd kaay ñu waat ci bàq

Ana lu tee ñu naan ko yaanu sàkk


dùnyaa wa uxraa fépp yaako làkk

lamnu wan kum ko wan nga berko


lamnu may kum ko may nga way ko

man woote naa ci Yàlla gii ñu réere


xamun ni Yàlla yafhalu maa lu biire

yaay kiñu sakk Bamba yaa nu bind


kum metti sab xol di nga dée ba médd

Boroom Tuubaa ñéppa ngi dée ngay dùnd


lottoo ci dàrra-dàrra yaa nu bind

Boroom Tuubaa ñéppa ngi toog ngay waaxu


bu gañaa doon ximaaru ngay buraaxu
75

Boroom Tuubaa ñéppa ngi xiif nga régg


ñéppa ngi mar nga màndi yaaka yàgg

yaw rekka jékk ñéppa-ñéppa jékkadi


yaw rekka doy ñéppa-ñéppa doyadi

yaw rekka xay ñéppa-ñéppa xayadi


yaw rekka mat ñéppa-ñéppa matadi

yaw rekka am ñéppa-ñéppa amadi


yaw rekka xam ñéppa-ñéppa xamadi

yaw rekka sol ñéppa-ñéppa soladi


yaw rekka set ñéppa-ñéppa setadi

yaw rekka ràflewul ñéppa ràfle


yaanu jagoo yaanu jagal yaa jagee

ñéppa ngi jur yaw rekka-rekka juradi


yaa sàkk ñañ jur ak ña jur yaa nitadi

Boroom Tuubaa ñéppa ngi ñaaw nga taaru


nuroowulaak nit waahidil qàhxaaru

ñéppa tilim yaw rekka yaa silwiise


yaa tax rijaali ami leer di tuuse

yaw rekk yaa rëy ñéppa-ñéppa tuuti


keneen kudul yaw safatul daa footi

Boroom Tuubaa ngëneel yaa koy tuuse


koo tuuse wul matalub jiw daa buuse

yaw rekka nooy yaw rekka neex yaw rekka leer


waa jula gànt doorna boppam cib xeer

Boroom Tuubaa yaa gëna woor yu woor yi


kuy wut lu woor tégila yam ci duul yi
76

yaw yaa jagoo mbooleem gëneel yan jàpp


te gaynde yii yaay bijji seeni yàpp

julee ka woor ajj makka jàng xur-aan


sa zikrul laahi daa-iman lit rahmaan

kazaaka listihfaaru wa salaatu


alàn nabiyyi kazaaka azakaatu

yaw jàpp la gën jàpp yooyu yépp

ndax kula jàpp amna yool yool yépp

yaa gën ci nit ñi yaa gëna mëna aggale


sunu digag mbugal ma yaako tággale

fépp fu nekk képp ku nekk lepp lu nekk


dùnyan wa uxran Bamba mooka lakk

yaa nekkaloo lepp lu nekk Daamu


yaay weeru waay bi dëggaral islaamu

budul kon ak moom diine jii nasax na


budul konak moom jëmm yii torox na

ci yaw la ñépp jàpp yaa moom ruuh yi


yaa gën ci xol yéeg xel yi gën ci yuur yi

Boroom Tuubaa yaay kinu moom ca booba


moom ñu ci bii nag ba bésub layooba

loo wax ci Daam ña ñoragul ne këwwu


diko xalaat si seeni xel ne xéwwu

mbiru Boroom Tuubaa xajul ci xel yi


ëpna déggug a adamaak sëtam yi

mbóoti waxam day baaje harsul laahi


di baaje xolu ahlu jùndil laahi
77

hamalatul arsi di fùddiy yëngu


xoli yonen yi andandoo di bëngu

malaaka yépp sabahaal mbindam ma


ak kuuyi jinne yam xamal mbóotam ma

jigeeni uurul hayni wal wildaanu


ña ngay wayàntoo xasida jinaanu

ku nara tàbbi aljaanay bànneexu


leerug mbindàm neex sisa xol di riixu

Boroom Tuubaa mii du moroom Boroom la


diko tùddaaleeg génn góor haraam na

mootax ba góor ña góore moo leen góoral


budul konag moom génn góor du ñooral

budul konag moom génn góor du yëngal


du takki ñoorug tubeyam du yëngal

Boroom Tuubaa bun ko xamal te berko


xamne Boroom la lun sàkk am ko

Boroom Tuubaa moom rekka-rekka jara am


moo jara topp jara sopp jara xam

ludul sa jëmm ak sa wax ag neen la


kulay waxam moy yooyu wax ay léep la

ludul Boroom Tuubaa asal ay nax la


jal bum jalul la neg ca biir ay juug la

ludul jëmmam ja ak waxam ja càm-càm


ku xam ludul moom la nga xam mooy xëm-xëm

Boroom Tuubaa sa xàj bi ngeedi xiiru


daa xiif ndawal sa yàpp waa ngi tuuru
78

ndawal gi mooy sa leer gu rëy gii bàll


mooy lay dùndee nàmpal ko Daam bam gàll

yaa dàq nàmpal sun ndéy yii ñu nàmpe


yaa gën si ñun sun baayi dooñu sàppi

say wéen du wéenu meew wéenu leer la


doonu feral doonu fërël Daam Yàlla la

céy yaaka yéeme Boroom Tuubaa foo nekk


xajoo ci kaw xajoo si suuf foo dëkk

xajoo jugoo ñëwoo demoo da ngaa law


yaw faatu woo tëddoo si suuf da ngaa sew

yaa gëna làqu gëna féeñ yaa yéeme


yaa moom la baax yaa moom ña baax yaa moome

lépp lu nekk fépp fu nekk képp ku nekk lenn lu génn


fenn fu génn kenn ku génn ci li nga moom amul ci dùnyaa fenn

mbindéef yépp maase nan ci xam la


way mùcc yépp Bamba gàwsi nan la

koo xamni sii malaaka yaang koy topp


mbooleem yonent yépp dan koo sopp

jinne yépp maase gëm ko jébalu


ba fuñu dakke Yàlla daal si sebalu

kawnu yi ñeel ko ruuh yépp maase sàm ko


xol yi ko fuuyu njort naa ñu halku

jamanoo yéeg waxtu y booleek saa yi


montaañ yu mag yéeg bés yi booleek noo yi

ak mbooleem seen ngélaw yi ñeeti xibla


xam nan ni Daam mbàkke seen Boroom la
79

mbooleem mbindéef yépp maase xamni


Boroom Tuubaay Boroom bu sikk dul ne

njaay hàl yéeg ség yi ak mbëfar yi


mbooleem njanaaw yéeg ñay yi ak kéwal yi

ak till yéeg mbooleem seen ràb yi yépp


ngoy naan ci Daam miy bijji seeni yàpp

ñoom ñeppa maase xamni yaa di kenn


Boroom Tuubaa kuko safoowul senn

mbooleem garab seen xob ya reere wuñ la


mbooleem garab seen réen ya ràññe nan la

kudul ku suufe rekk umpatoo ko


Yàllaay mbidéef yi ludul la gën amoo ko

mbooleem gunoor yi yàmb yéeg janax yi


yaa nekk seen waxtaan si seen biir pax yi

nun lanu xam ak lanu dégg dëgg la


la munu wan ñu gis ko mbir mu màgg la

saa soo waxee Daam mu faf la ubbi


ngay gis di xam ngay dégg loodul yàbbi

yaa baax te baaxal ñépp jàpp naala


yaa màgg te màggal ñépp bàqnaala

doo tuma sakku darra dàqnaala


feeg yaa ngi sax sa saxu waay Jam naala

Boroom Tuubaa yu leer yi yaako leeral


Boroom Tuubaa yu neex yi yaako neexal

lu neexa neex mooy xam lu wér ci Yàlla


agg ci moom bay aggle góor Yàlla
80

te ghaarifoona yépp yaa leen màndal


te saalikoona yépp yaa leen réggal

kuy wedd say may dina tàbbi safara


di nafa béel di nàññi melni baqarai

majzoob yi ak abdaal yi yaa leen tëbb


sa mbóoti leer sa géeji leer si yëbb

ku mënla dégg lii ñu wax ab liir la


ku jekkiwul ci Yàlla lëf jaaxal la

ab liir du gis du dégg amnay nopp


kay tee mu dégg moo dégg loowul ñépp

Boroom Tuubaa mbóotam xajul ci nopp


ëpna xel leerul ci benn bopp

yalnan la gëm te Yàlla bun la wéddi


kuy weddi Daam bokkul ci yoonu Amdi

ma xatmu way wi jùlliwaat ci yonen


xayrul rasool ka tee ba xol yi wànnen

summa sallaatu sayyidir rasooli


maha salaamin daa-imin wa aali

wa aalihi wa sahbihil kiraamu yaa ilaahii


bi sirri sirri xàdru zaatil laahi

jullil ci moom lu toll sag màggaayu


bi sirri xayyoom rabbaana ya xayoomu

jullil ci moom lu tolni duusu géej yi


jullil ci moom lu tolni nooyi mbidéef yi

jullil ci moom lu tolni pepp suuf yi


jullil ci moom lu tolni xobbu garab yi
81

salli alayhi adadal ayyaami


wa adadal malaa-ikal kariimi

sallaa alayhil laahu géesun geesabaa


satanix teme jee tayni talxin faylibaa

jullil ci moom lu tolni mbooleem jën yi


jullil ci taahaa ci limug njanaaw yi

te lii nu way yalna sois si saasa


lum gëna siiw day toroxal ibliisa

aamiin ni jaahi sayyidil kùntiyyi


sayyidil muxtaari kùmmalul walliyi

subhaana rabbika rabbis sukoori


rabbil hulaa muddabirul humoori

wal hamdulil laahi ràbbul hãalamiin


summa salaatu sayyidil haadil amiin
82

5. Ma jugg ta jëndee saay nelaw


Ma jugg ta jëndee saay nelaw
Payug ka féette lepp kaw
Ab kalbu guddi du nelaw
Day wattu tooli mangoo ya

Maay kalbu Bàmba di boroom


Kalbu ba tay de mooy boroom
Tool bi te kalbu ay soloom
Mooy bëw di xiiru gola ya

Sëriñ bi ya di sun boroom


Mboolem fu ñaar teggée Juroom
Sa assamaaw ag seeni ruum
Boole nga mbooleem sirru ya

Sabxiina ardi wa samaa


Ya moom wama bayna xuma
Ya làq sirul hazuma
Gàcc nga mbóotum laahiya

Cëy Bàmba yaka yeeme céy


yaa làq mbóot ya gën a rëy
Bañ bindagul dara ba tay
Ag banu bindée xibla ya

Jittu nga booba nga amoon


Sàkk nga booba nga xamon
Ahefaa-liyas sirul masóon
Yaa yonni woon yonenta ya

Yaw dàj nga kàpp yaa ka matt


kamal ga yaw rekk la jott
Ña àgg ya duy seeni pott
Yaay xontu góori Yàlla ya
83

Bokkoo ci doomi aadama


Sag nekka jittu aadama
Wa axlu lardi wa saama
Kenn jigiwul sa pegg ya

Yaw Bàmba doo ku kenn xam


Lu xel di dàkk dula jam
Lu xol di yëgg ba dila ñam
Nga saf ko Yàlla ag meeloo ya

Yaw yaa di ajji-Magg ji


Yaw yaa di ajji-bind ji
Yaw yaa di ajji-faddu ji
Dambe nga mboolem kùmpa ya

Yaw yaa di ajj-tedd ji


Yaw yaa di ajji-sell ji
Yaw yaa di ajji-jëkk ji
Yaa mujju ame atté ya

Xuwal awwalul aaxiru


Wal baatinu waz zaahiru
Axmadu nuuru taahiru
Yaay jeggi waayu dëyla ya

huwal ghaffóoru ghaafiru


huwal xàqqaarul xaadiru
huwal habiibu taahiru
Yaa ne ca ginaw riddo ya

Yaw mi la gaaya dëkke wër


Way sóobu yepp a ngi la mar
Amlaaka yepp a ngi la dar
Céy koo muril sa kumpa ya

Sa jëmm làq nga nu ko


Sa sirru nëbbu nga nu ko
Sa bind wattu wunu ko
Saff nga nu ag ilaahiya
84

Say bind day aggale góor


Say bind day feccali góor
Sa bind day dolli bu wóor
Dollina góori Yàlla ya

Xassida dooleem kawena


Xassida siroom fàddu na
Fiirug xassida jàpp na
Yàlla ag meloom yu kawe ya

hibaada yepp a dajjaloo


Mboolem ngëneel ya sësaloo
Xaddis yu wér yanu soloo
Màng na mboolem yàpp ya

Lepp a ngi ci biir xassida yi


Ñépp a ngi ci biir xassida yi
Fepp a ngi ci biir xassida yi
Boolena mboleem kanzu ya

Kittaabu yepp a dajjaloo


Tabbisi nanu ba gëndaloo
Ag taggi seyyidi jammilóo
Xassida xuuf na sirru ya

Nuurul ilaahi la jagoo


Sirrul ilaahi la tegoo
Bu kurisiyu ag arras yëngoo
Danoo yëkkati xattu ya

Xarasu day bégg ci mbidam


Kursiyu day bégg ci bindam
Te malahul ahlaa ku xam
Xam nanu jappe téere ya

Ahmadu yaa di sàng bi


Ahmadu yaa di sàmm bi
Ndax doo ka bind dénd bi
Ndax doo ka boole làkk ya
85

Yag Yàlla xam naa yeena ne


Mbaatte nga nekk fumu ne
Mbaatte mu nekk fi nga ne
Seen nekku waayu sirru ya

Kawnu bi Ahmadoo ko moom


Dunya wa-uxra ngi siy loxoom
Ku gàntu seenu na ag fandéem
Ku aksi teewe bernde ya

Naa wacc ndax sa tolluwaay


Xajul si noppi jén-waay
Te yaw di way sa tolluwaay
Mooy ritti xoli gaynde ya

Bur Yàlla day bégge sa mbir


Yonen ba day bégge sa mbir
Jùndul ilaahiya ngi la dar
Ag awliyawu ag jiine ya

Waa ahlu bëytil xissati


Ag ahlu bëyti kahbati
Bi isni rabbul xuwwati
Nga boole yoolu jàmmu ya

Maam Daam da nga jàll mbindeef


Jëkk nga mboolem liy mbindeef
Linu sakk lepp a ngi sisa suuf
Yaay mujju firi lét ya

Yaa sàkk yaa làq sirrul maliki


Bokkoo sa axlul malaki
Doo jinne doo nit ana kii
kumu doon ku xemi njortu ya

Man njort naani mooy Boroom


Te Yàlla mi di sun Boroom
Nëb na ñepp ay sooloom
Xamunu lu weesu meloo ya
86

Loxo ya ag tànk ya ag
Bopp ba ag nopp ya ag
Bëttam ya ag jëmam ja nag
Ñepp a nga reere firi ya

Kenn munula xam na Yàlla mel


Kenn munula dàj Yàlla ci xel
La ne si moom si ay nàmmeel
Umpu na mboolem fóore ya

Kon Yàlla man na doon kune


Mattam ga akki na fune
Te moo di xayrul minani
Moo yor gënel yu nëbbu ya

Nun jappe nan ko Ahmadu


Nun soppe nan ko Ahmadu
Te fettee wo nan Ahmadu
Mooy sàmmu nun nooy gat ya

Ab sàmm day fettee ginaaw


Gàtt ngir ya ñu baña sàaw
Daam lanu giss ca sun ginnaw
Mooy saytu mboolem gét ya

Nosi mbindeef yi mooy Boroom


Payug mbindeef yi ngi si moom
Ajj Màkka woor julli juroom
Daam Yàlla xuuf na sirru ya

Yaa ahla naasu wuyisi leen


Yaa ahla dunyaa naan sileen
Boroom ngëneel ya woo naleen
Kay wàttu mboolem xarnu ya
87

Mooy wàttu mboolem xarnu yi


Mooy sàmmu mboolem gatt yi
Gatt bu gaawul bukki yi
Ag boy yi reere yàpp ya

Kooka du kenn, kenn du moom


Kooka du ñenn, ñenn du moom
Kooka du lenn , lenn du moom
Moo jékki sàkk xal ya

Kooka du démbu it du tay


Jiittuna démb jiitu tay
Moo sàkk démb sàkk tay
Sàkk lu am ca dénd ya

Lam doon xajul si nopp yi


Lam doon ñewul si làkk yi
Lam doon umpu na xutbu yi
Ag nujaabaa-u ag xawsu ya

Ëpp na mboolem lanbiyaa


Getti na mboolem lasfiyaa
Mooy séd mboolem lathiyaa
Moo màndi lo way màndi ya

Tabam ga agg na fune


Mattam ga làgg na fune
Bëttam ba dàkk na fune
Màgg la mu nekk ag goone ya

Kooka de seyyidil awwali


Kooka di sirrul kummali
Ahmadu nuurul jàmmili
Sag leera gindi xawsu ya

Ya séd mboolem lawliyaa


Wa taabihiina ag lathiyaa
Jeggi nga mboolem lànbiyaa
Yaay weeru waayu xutbu ya
88

Digante mulkeek malakoot


Ba jàll wéy ba jabaroot
Sa leer gi sàr nafa di niit
Ku àgg jox la loxo ya

Way àgg yeppa wuyi si


Way màgg yeppa ñibi si
Way degg yeppa tabbi si
Ku gàntu seenul buntu ya

Ku giss ba jàl gis mu gis


La Siidi Ibra Faal di gis
Wa ahu kasfu ñepp a nos
Seen ruuh ya jox ko atté ya

Ahmadu yaa di bajo bi


Ahmadu yaa di sàrd bi
Wallaahi yaa di buntu bi
Yaa jalluloo way jàl ya

Yaw yaa di baabu rahmati


Yaw yaa di baabu nihmati
Alaahu rabbul xisati
Yaa tax nu sàkk dénd ya

Ya déenk suuf sekre ya


Ya déenk géej sekre ya
Te assamaa-u yéeg buntu ya
Sak cant sax na ëtt ya

Daam Yàlla nëb nga nu daaw


Nëb nu ren ag sun ginaw
Ña weey bu yàgg ag ñi fi teew
Kenn feragul sa ijji ya

Ya tax ba suuf si mana muñ


Ya tax mu dal ba dootu bañ
Géej yepp yaa fa def njariñ
Jàmmal nga mboolem xarnu ya
89

Nafaahani wa biya yan


fahul wara nga nu fi wan
Jariñ nga ñepp yaa fi gën
Sab aña dàkk ràgg ya

Ña mucc yaa leen musaloon


Way bew ya yaa leen alagoon
Islaam ji dan koo jéngaloon
Ba mujju daanel keno ya

Nga yeesalaat ko bamu yees


Nokkos kenoom ya bamu fees
Ñay jax-jaxe nga amu tiis
Iblis nga door ko kënoo ya

Way beew ya ñepp a allaku


Ibliss sagam ba sagiku
Lum fi nasoon nocci nga ko
Islam ji daj na xibla ya

Cëy kooka moo di genn goor


Cëy kooka moo di gën gi muur
Ahmadu rekk a neex ta woor
Moo matta jébbal dundu ya

Annaa bilaahi jékki naa


Baa yaxtuxoo ya seyxanaa
Dunyaa wa uxra jàpp naa
Daam bunu teewe atté ya

Ku ne ci yaw dunu ko seet


Dunyaa wa uxra duffa tiit
Du rëtt du jaq duni siit
Te uuru yi nooy soxna ya

Wildaan ya ñoom lanu tàqqool


Muriidu laahi lanu xool
Ku soppu Xaadimu rassuul
Wildaan ya jox la berne ya
90

Seen taar bu rëy ba ne ca ñoom


Seen xett ga ag leer ga ca ñoom
Gaccal na sikki wa nujoom
Ñooy jóoru xattuy Bàmba ya

Boroom wakkaana mata xam


Boroom sindidee mata am
Boroom midaade matta gëm
Daam xassida da adieu à tànk ya

Kookay boroomu ikfini


Kufal balaa wa najini
Min kulli sarri zamanii
Wa kula durrin pakk ya

Jaawartu laah ag jaalibatu


Bi sirri nuuru ag tuxfatu
Yaggal fi sayxi amsatu
Moom mi safoo sa xattu ya

Bihaqi Ahmadu lamiin


Na nga nu deffal fatxul mubiin
Fegal nu azaabun nahiin
Musal ko ku yakar sàng ya

Yaa Sayxana yaa Ahmadu


Bi-sirri sirris samadu
Bi-nuuri nuurul ahadi
Xamal nu mboolem kumpa ya

Bi-siri siril kumaali


Xada-iqul fada-ili
Bi haqi nuuril munjili
Min-lawqi maxfoos tata ya

Deffal nu jàmmi addina


Taaxal nu taaxi aljana
Te maynu mbóot moom fàddu na
Te gën a dakk gola ya
91

Iblisu farra saaki ya


Ila siwayaa baakki ya
Mussaara xàtti naaki ya
Kulla haroorin jeggo ya

Bi-haqi bisril Mustafaa


Mafatihul bisri sifaa
Bi-siri kaafi yaa kaffaa
Bun jeggi fiiri kàpp ya

Boroom mawahiboo nu dooy


Jëzbook muxadamaata rëy
Taxmiss a gën a gaaw si fay
Bakkaar bu jaaxal xutbu ya

Sëriñ bi yaw sa mathu yii


Kawena mboolem bind yi
Ahlu faazaha ag foore yi
Seenun sa pënd tàgg ya

Kahab buséyri ag xasaan


Seenu mafaatihul jinaan
Say tàgg rekk a walagaan
Sa xooli góori Yàlla ya

Malaaka yaa ngi koy drus


Yonenti yaa ngi koy druss
Waliwu yaa ngi koy druss
Ag yenn kuuyu jinne ya

Deffal nu tawbatu nasóoh


Bi-siri tawbatan nasooh
Yaa seyxi iftah yaa fattaah
Jeggal nu rëc-rëc ya

Bihaqi taysiirul hansiir


Yàl nanu añ ci yaw ba suur
Te baña bew te baña réer
Te nanu xamme càf ka ya
92

Bihaqi fathul mukarram


Bisiri mathul muhazam
Funu dakké Yàlla nan ko jam
Te nga muril nu rido ya

Yaw rekk a sedd sunu xol


Yaw rekk a neex ci sunu xel
Seral nga xol dalal nga xel
Ña gàntu dégg ngeen yuuxu ya

Yuuxu du wóoy yuuxoo di neen


Ku fuuyu Daam sa lepp neen
Kuko fi bàyyi jëm feneen
Loo yóotu do jott siru ya

Boroom minanu ñoo ngi nii


Boroom fawzayni yaa ngi nii
Yonen ba ag Yàlla nga née
Yaay ker-keraanu xàl ya

Yaa Sayxanaa seexul xadiim


Yaa minanul baaxil xadiim
Allaahu rabbunal hakiim
Jox nala yooli xare ya

Bihaqi tur ya nanga nu may


Asma-u ahlu badrin cëy
Màng na yoolub kun fa ray
Ak kunu rayul sa xaree ya

Deffal nu ngëm si seeni tur


Ag seeni soxna ag ñañu jur
Ag seeni féttag yanu cor
Ag fass ya ag seen jéego ya

Maam Daam boroom yazal wujóod


Salli haala seyyidil wujóod
Feggal nu hazaabun sadiit
Te bunu teewee gacce ya
93

Aamin bihaqi sidratu


Al-muntaxa xadratu
Bi nuuri baabu rahmatu
Rassuulu laahi ag jagle ya

Muxadmaatul xidmaa ko doy


Sëkk si kuy sakku lu rëy
Boolena mboolem xeetti may
Di budi getti naari ya

Bihaqi matlabu sifaa


Yaa seexi jaa-anii sifaa
Bisiri Amdi mustafaa
Na nga yërëm way-dawlu ya

Bisiri lixlaasul kariim


Ahmadu yaa seexul hakiim
Na nga nu deffal xalbun saliim
Banu tol ni gaayi njëkk ya

Barkkep xassa-idul kiraam


Xassa-idi seexul xaadim
Yanu nëbb yepp ak yii ñu tiim
Ag ya xajul sa xibla ya

Deffal nu xaajo ju fajju


Ubbil nu lepp lu tëju
Mboolem tawat yi na faju
Yaay safara way loot ya

Bihaqi sirul xalami


Bi nóorul maa-l xazami
Maa-u middaadil karami
Waxi rattasi mad-huya

Yaa Sayxana yaa seyyidi


Faydul munaa fathu yadii
Bijaayi seyyidil ahadi
Bihaqi tuuba ag ëtt ya
94

Bahaqi mboolem ña nga jur


Ag haqi mboolem ña nga yar
Ag haqi mbokku yala wër
Ag haqi mboolem soxna ya

Na nga nu may nuuril hulaa


Jubal nu yaa sayxul hulaa
Feggal nu lepp luy balaa
Te doli ngëm sa ndoga ya

Te may nu ngën gi sutura


Te dolli ñepp safara
Addina ag allaaxira
Bun yewiko sa gétt ya

Bihaqi masjidul hulaa


Salli ala maahill hulaa
Bisiri asmaa-il hulaa
Tur yu raffet yu tedd ya

Jeggal nu lepp lunu mooy


Tawal nu naatal lunu bay
Ñagal nu joxnu lunu doy
Yaa régg loo way régg ya

Ahmadu Yàlla nanu la am


sa càf-ka Yàlla nanu ko ñam
Yàlla na nga nu xéeñ ñu faf la sam
di biiw sa leeri xaybu ya

Buur Yàlla yaw rekk a ko xam


Buur Yàlla yaw rekk a ko am
Yaay lëm mu Yàlla ëmb lem
Yaadi siraajul awliya

Ku Yàlla xayma ay mbiram


Fekk mu deff la si xolam
Faw mu dolli ko ngëram
Dikko xamal yu ruxée ya
95

Yaa Sayxanaa ajib duhãa


fathul munaa lii jamahãa
Bisiri jaamihul mahãa
Fil-hayyi ag ca xabru ya

Bisiri seex abdul kariim


Ma jibra-iilu jël meloom
Buy ñew ca Xaadimul xadiim
Di indi kàdduy Yàlla ya

Ak haqi seyyidil omari


Deffal nu tuulal umuri
Ñoddil nu lepp lu sori
Te boole xëh sa matxu ya
96

Maam Seex IBraahiima Faal

6. Ma way bëyit si xarfu..


Ma way bëyit si xarfu ismu laahi
adda xuroofi ismu zaatil laahi

Bàq si Siidi Ibra Faal mu baax ma


Ndax lamu sekk ak Yàlla mboot ma laal ma

Aboo rijaalu laahi sirru laahi


Maam Siidi Faal Ibrahima qalbul laahi

Ñi làq ak wilaaya réere wun ko


Ña dak ak wilayaa fuyu nan ko

Ña gën a màgg gën a mat yéem nan ko


Ña gën a të sayetaané wuyusi nan ko

Ña wuyisi woon woote bi roy si nan ko


Ñay bëtt déyléey asaamaan xam nan ko

Kuy woote woo xam Yàlla daad koy réeré


Moo gëna réere Yàlla réer gu biiré

Amul ku xam Yàlla te réeré mbooram


Maam Ibra Faal goor musta laabe laabam

Yaa waqi gis ya kuuy ya yaa leen foqu


banu ni fuux, ga dellu waat sab ruqqu

Yaa pintipanta yoonu ilaahal halamiin


Yaay aydaapporu aljana Maam Siidi Lamiin

Yaw kula teggi jëffam ya Yàlla wooy ko


Siwaal ko bamu dàj malakoot ak mulku

Faal kula soppu Yàlla sóob ko béel ko


wéexal mbiiram malakóot ak mulku
97

Mbóotum jallal ja gindi mboolem xol ya


Leerug jamaal ja des sa mboolem xel ya

Yaa gindi mboolem gaynde yi ci lislaam


Kewél du seeru fa nga sàmp say jaam

Sidi Biraahim Faala jiituy jiitale


Ku wàn ginaaw mbiram du gis lam langale

Yëkk wu màtt day tiit, di gëss, di nàññ


Di roq, di fuuftu di gëssëm di gàññ

Maa Ibra faal yaw rekk am gëlël di


Yaay nattu waayu góor ya soppu Amdi

Waa jula soppul bañ na bépp Yonen


Yaay deñcu waayu sirru bépp Yonen

Mboolem Yonent bu woote yaa ko bijji


Ña wuyu ci yit yaa tax ñu gis ni xàjji

Yaay niitu waay bi yaay aggwaay bi faaluu


Xol yula gàntu seeni jëf ni njàaloo

Boroom tariqa yépp yaa leen yéegé


Sa mboot a tax rijaal yi am lun tooge

Kuy tùdd waayam dila tùdd réer na


Yaay dox ca biir way dox ya jëm aljana

Yaa gëna sél ñepp yaa xaalilu


Rawante woo sutanté woo ku njoolu

Seex Ibra Faal adduna yaa ciy lenn


Amoom nuruwaale si xawmu yenn

La nga sëffóo fa nga sëffóo ña nga sëffóo


Ku leen sëffóo woon kula moy ñu soofoo
98

Yaw li nga attan diis na doq yépp


Ëpp nga goor ni bërigoo aw fépp

Foo simpi say ngaax goor ña daaldi wogasu


Saay ndaw a gën waliwu yinu laxaassu

Say góor a ëpp yi xawsu ëppi xutbu


Kuy wéddi say may daal di mél ni kalbu

Yaa gën i maay yaa ëppi maay yaa wóor le


Yaa gën si diini Yàlla ya firaw li

Samaahu musla tiim ku mel ni Sowru


Waat naani suuf uuful kémam Maam xayru

Adaama musla jur ku melni Làmp


Jituna adaama ak xaawa mo jàmp

Yaa gën a gaaw si soppi xol da nga gën


Kuy tùddu waayam dila tùdd moo bonn

Moy kenn gog dëggoom ya dun ko dëggaat


Maa Ibra Faal meloom wa dun ko tëggaat

Wenn mélo di benn rekk te kenn


Boroom Tuuba amul sa kém si fenn

Kuy wéddi mbóotum Yàlla gén lislaam


Kuy sikki sakka cobareem dem sawaraam

Maam Ibra Faal mbóot la mu Yàllay nëbb


Moy dëgg-dëgg diine jii ñu jàpp

Kuy woote woo xam Yàlla wéddi xàlla


Yàlla ak Yonen xam nga ni jéppi nan la

Loo julli-julli mbaa nga wóor ak neen la


Boo aki jée ba màkka jëf jun been la
99

Yaa sirru xaqan yaa nuuru zaatul laahi


Siidi rijaal, Aboo rijaalu laahi

Yaw li nga attan ma nga fa woon diis gàn


tëñaam ba laccal ku sag wilaaya bënn

Bàjjo bi téeñu téeñ ba, yaanu yan ba


Mel nig jamal ba weññi mbooti Bamba

Mo tax ku wéddi Làmp melni noon ba


saytaane manu jàm mo nëxal xolam ba

Yaw rekk a wóor doo xawwi yenn sutura


Ku ngoy si yaw du dégg riirum sawara

Seex Ibra Faallu ëpp nay limaale


May yamu jaagoo góor muso ko wëyaale

Axlu kusaafati, wa axlul laahi


Waa axlu tawbatii rijaalul laahi

Amul si ñoom ku melni bàjjo faalu


Seenu nu pëndam ñu njóol ña dun ko njóolu

Maam Ibra Faal bàjjo bi moo di raay bi


Kenn du ko weesu mo di aggu waay bi

Mboolem ca way njëg ya ak ya mujju


Amul si ñoom kuko si màt am kujju

Maam Làmp góoru góor ñi, bàjjo faalu


Sakkal ko am kem da araaam ni njaaloo

Mooy naatu waayub gaa ña nàmm Yàlla


Mooy yamu waay bi kenn du weesu xàlla

Kuy sikki-sakka Sowru Faal say-say la


Kuy wéddi mbóotum Yàlla kay yéefar la
100

Nawléem amul Seex Ibra, kenn du xànd


ta pëndi jéegoom, waa ju ko sóobu fënd

Kenn mus la giss ku mel ni moom si dı̂ine


Amul si biidaani ak soodaani

Ab sañ sàñam musee sukoo sañaale


Si adaama ak muxaamadul kaamali

Lim sëf si mbóot ba noppi daat ni yomm


Kunu ko sëffoon sa góor ña doqam dàmm

Kenn mun la gis ku gàddu lii mu gàddu


Si mboole seen walliyu yi ni jóddu

Te xalku wun te sanku wunute reeerun


Maam Ibra Faal mook ña ko toppu sooyun

Seex Ibra Faal góor ñepp a yeem daayom ba


Jamal ju mat, ndaw meun la laal jégéen ba

Amul ku lamboo martabaam ci Yàlla


Téeñam ba diis na góor ña góoru góor la

Céy jooja waay ëw jooja waay Maam soowru


Lambul si Yàlla ëmbuna xayrul-xayru

Ne sëpp sóow Maam Ibra Faala yéeme


kenn mus la gis wii melokaan moo tiime

Moy gëm gi tax ñu gëm di dox ci dëgg


Waa juko noonu di nga rus ba sëgg

Daam Yàlla nee ku noonu Làmp bonn na


Ku wéddi ngëm numuy déeme aljana

Mooy naatu waayu ngëm yi ngëm mbóotam la


Ku gëm na xam ni xoroomus naraam la
101

Moa wane ngëm moo jara gëm Maam Làmp


Moy aggu way bi gën a jub mo jàmp

Limiy defal góor bamu mat ba motti


Te jarewunu ci xaal wii nu xotti

Ku man na def ku xam na wéy yoon wa ngoog


Maam Ibra Faal góor jotewul famuy toog

Diine amul ku melni sowru faalu


Mo gën i góor birna ñi am wosóolu

Kenn musla dégg fenn aw doxiinaam


Mooy royu waay bu mag bi ngir jëfiinam

Maam Ibra Faal seydu rijaalul laahi


Abo rijalu laahi, sirrul laahi

Seex Ibra Faal yaw rekk a jëf ba laggi


Mboole kamaal yu mag ya yaa leen jàggi

Góor mun la jëff ba dap ko loola faat na


Mbóotam ma diis na góori ahlu sùnna

Seex Ibra Faal nuuru rijaalul laahii


Tarxaan ak karxaan dahiman billaahi

Seex Ibra Faal kanziyatul ilaahi,


Nuurul hulaa sirrul kamaalul laahi

Seex Ibra rahmatu raabul halaamin


Sayyiduna Ibrahiima sayydul lawwaliin

Seex Ibra Faal daalilu zaatul laahi


Baabu suyooxi sowru baabul laahi

Seex Ibra Faal jaalalu kawnul laahi


Maam Ibra Faal jamalu sirrul laahi
102

Seex Ibra Faal kamalu nuurul laahi


Maam Siidi Faal Ibrahiima xaqul laahi

Seex Ibra Faal yaa di xaliilu laahi


Faal kula gàntu moy haduwal laahi

Maam Ibra Faal xol bu ko gàntu dée na


Ruuham ga nëb lu nëb du dém aljana

Ku noonu waayu Yàlla loj na ruxaam


Naana posan daanu ci kàmbu lëndam

Mooy ruuh yi mooy bakan di jàmmi nit ñi


Ku béen mbiram malaaka ya ngi koy ngàññi

Mooy taaru diine ku mën la gis taraam bi


Sab gisa ñaaw ci soowru faal yaaram bi

Mootax Boroom Tuuba mi ëmb diine


Jitaal mbiram Maam Ibra Faal du cuune

Ku Yàlla dul xamal du xam la fàddu


Du xam la gën Seex Ibra neena jóddu

Jëmmam a gën waxam a gën jëffam a gën


Yoonam a gën si yoon yi, toppu koo gën

Mbiram a gën yoon wi mu xàjj sës na


Riik si Yàlla moy yoonu ahlul jànna

Way muccu yépp a xam ni mbóotum mbóot la


Way jiitu yépp xam nañ ni njitu njiit la

Ña jitu moo jiitu ca ñoom bañ jiitu


Yawmal xiyaam kumu ràmmuwul nga juutu

Ña agg mo aksi ci ñoom bañ aksi


Te lima wax bér na ku tabbi harsi
103

Way màgg yay doxantu foofa xam nañ


Seex Ibra Faal ku manke rekk a koy bañ

Ku yëg-yëggam sar di nga yëgg Seex Ibra


Kuko yëgul loo mën a yëgg du sarra

Ku gis-gisam wéy di nga gis lu laqu


Ci Sexra faal lool kuko gis du yaqu

Moo gën a xam Yàlla ku Yàlla bind


Mootax ñu xam ci Daam Yàlla mi nu gànd

Maam Ibra Faal wujjam amul sa awwal


Amul ca aaxir sàkk na goor ñu kummal

Sàkk goor ñon fanu ag ci Yàlla


Neewaana goor agg fa céy Maam xàlla

Yaa ngi ni jàkk Yàlla bajjo faalu


Yaa ngi ni màkk njóol ma yaako njóolu

Ya ngi ni xàjji Bàmba man nga xoole


Yaa xool ba gis Daam Yàlla am nga doole

Bu Bàmba doon gaynde nga doon bëñam ya


Yor ñéent ñay ray sakkamée dëgëj yaa

Ku gëm Boroom Tuuba da koy gëmaale


Baa luko moy sa gëm ga dunko faale

Moy rabbu ndëpp Seexunal Xadiimi


Maami Sëriñ Seex Jëmb Faal a yéeme

Mooy léer gu gàddu léer ba léeral fépp


Sabhiina ardi was samaa dàj fépp

Fa Yàlla féete kula fa dàkk jam la


Fa péggi Daam kula fa seenu séen la
104

Lepp lu ab jaam di jagoo ba jariñu


Maam Ibra Faal lay loola jaam ñi xamu ñu

Maam Ibra ne nit dina lekk aw jën


Wuma xamul mool wa ko napp mooy kan

Aw cax la cax wa gaaya ñoo koy tékki


Mbaate nga dégg ndeeyu gaay ba sékki

Gaa ña di góor Yàlla yay wëndeelu


Ba sidratul muntaxaay jëmbéelu

Te lima wax bérna ku àg foofa


Mbaate sa gissu xol ni màkk foofa

Seex Ibra Faal ku agg yëgg na mbóotam,


Mboolem ña nàmm yàlla ñoo nga sa suufam

Malaaka yi ak jinné yi danu ko soppu


Ak jùndul laahi xaalibiina yéppu

Ngëneelu Yàlla yépp moo ko gàddu


Maam Làmp a wéet Maam Ibra faala fàddu

Moo gëna xam moo gëna am moo gëna man


Mooy taxa am mooy taxa raw mooy taxa gën

Yàlnanu Daam gindi si sówru faala


Jaalalu kawnul laahi kulla haalaa

Yàlla nanu bàmba yee si bàjjo faala


Kamaalul kawnul laahi kulla haalaa

Te Bàmba làkku nu si xàlla faala


Jalaalu kawnul laahi kulla haala

Yàlla nanu Bàmba sàmm lo Maam Làmp


Mu dinu sàmm dinu jox ñuy nàmp
105

Mooy sàmm bop juram du ruur du yooy le


Dunko firéw lii Seex Ibra Faala gën le

Yàlnanu Xàjji faala gën di gindi


ci jëmmi jëmmam jëmmi Boroom baraak bi

Bi jaahi mujtaaba nabiyyu taahaa


Bi sirri laa ilaaha ilaa laaha

Yaa gàddu mboolem sekréeb nabiyyi


Ak mursalóona ak nabiyyil umiyyi

Yaa sékréel xutbu yi ak xàwsu yi


Xéeb nga mbirum mahediyi ak waliyyi

Yaa sekréel mboolem ku Yàlla ràng


Maqaama yiñ am diko gis muy làng

Yaa di kanziyatul ilaahal kulli


Hazza wa jàlla rabaana wa jàlli

Cëy Yàlla laa ilaaha yaa hakiimu


Yàllahu, yaa waasihu, yaa haziimu

Yàllahu yaa rahmaanu yaa wadóodu


Yàllahu yaa raahimu yaa majiidu

Yàllahu yaa kaarimu yaa latiifu


Yaa barru yaa mujiibu yaa ra-oofu

Kimay xamal lim may xamal day tuuru


ci sama xél saa lëgg xol di jooru

Damay xamal dima amal dima gisal


Ay mbóoti mbóot yu xóota xóot ci sama xol

Damay gissal lu rombu gis ci saay bëtt


Céy jooja waay mooy jénn waay ci saak wét
106

Lamnu xamal ak lanu yëgg ba wax ko


Kukay waxàntoo fàw nit ñi sàm ko

Sallaa wa salama nabiyyi taahiri


Wal aali wa sahbi bi jaahi naasiri
107

7. Mboolem ku Yàlla di saff ..


Mboolem ku Yàlla di sàff ak Mustafaa kinu am
Nanu jekki maase ni xiim Xaliilu lay bëgg a way

Baabul Muriidu wa Baabul Laahi xudwatunaa


Daliilu laahi Boroom Tuubaay ka xam namu doy

Ismu laa ilaaha illa laahu mbër mako xam


Te xam sirroom te xam haqàm te jox koko déey

Kooka di Seex Ibra Faal baabul xuloomil xula


Faal laa ilahaa ilalaahu wi tura rëy

Mootax kulay bañ te naa Bambaa ma doy kawewut


Ku gëm Bamba day gëm Làmp faf diko roy

Mootax ma jugg dikko way ngir soppu koo gën a woor


Ku koy xébett aka xeep sawara dees nako yày

Moo fàkk xàl wi moo gëm Bamba moo rëyi jëf


Jaa jëffe Seex Ibra yaw rekk ya matta ngoy

Yaay nuurul laahi nde yaa gis leer ga indi ñu gis
Budul kon ag yaw danuy palàmtu démb ba tay

Seex Ibra yaw fa nga nek ak fa Bamba nek sorewul


Yàllaa la ber foofa doo maasam ña teew ag ña wéy

Seex Ibra yaw fa nga nek sab cër la yaa ko yaayo


Keneen kudul yaw bu tooggon foofa day xawa jóy

Diggànte Sëñ Bamba ak Làmpam ba daa xawa sew


Te waa ju silmaxa doo gis mbir ya doo mana ngoy

Te gùmba dëgg du xamme wëñ gu ñuul ak gu weeh


Maandul si diggante Sëñ Bamba ki Làmp te wéy
108

Te lam jëffal Yàlla ak Yonen ba bàn dikko fay


Lu ngeen si am manduleen ku maanduwul gissu ày

Nde may yu rëy yamu làmboo menn xel dukko dàj


Te sàñ-sàñam baca biir day halag aka ray

Seex Ibra Faal, famu jekki ag Bamba xel duffa dem


Ab xol bu sél te leer, mooy yëgg mbóoti Làmp ni céy

Xalbùn saliimùn ku lambóo mbóot ya mooy mën a yëgg


May yanu may Làmp Faal xalilu ghaybu la déey

Te tàal bu Yàlla di xàmb ay jillim ak i dój


Ab jaam dasay maandu kon mandul te tuub li nga moy

Seex Ibra Faal moo di taalub Yàlla leer na ba dàj


Kullàl bilaadi ba daj addina red na rëy

Moo indi jàmm ji mboolem diine ji jépp a ngi sàpp


Budul kon ag moom xoroom day manke démb ba tay

Seex Ibra Faal, Làmp Faal xaliilu yaa ka goore


Yaa kaawe ya maandu mbóutum Yàlla sàpp na ba wéy

Yàlla ag Muxamadu ag Seexul Xadiima la xam


Keneen ku leen moy say mbir lam ca xam dulu rëy

Ndax faal, ba nga dëkkaaleeg Sëñ Bamba démb lawoon


Mootax ba tay kula xam Sëñ Bamba mo koko déey

Saw melookan rekk a jaaxal gaa ña faal li nga am


Ken musu ko am si goori Yàlla ya rëyi may

Yaay diinu laahi yaay xur-aanu Seex Ibra yaay salaatu


Yaay weeru koor ëmb nga diine ji déey

Moo tax kulay wéddi ngir julleé ki woor kawewul


Bu kawewoon di yëgg ca lëm ma mbëtt ma ngoy
109

Cër bi nga am rekk a jaxal góor ña sab cër a diis


Seex Ibra yaw kula bañ leerug xolam dafa fay

Yaay mah-riful laahi yaay nurul jalali te yaay


Nuurul xaqixatu yaay nuurul wusóoolu ba tay

Mboolem kulay wéddi ngir maamam ju baax jamu am


Wéddi na maamam nde sax maamam amul lula moy

Mboolem kulay wéddi ngir sëriñ bu baax bamu am


Weddi na ab sëriñam sëriñ si yaw lanu roy

Ya jittu goor ñii te yaay baabu rijali aboo


Rijalu laahi, Xaliilu laahi ya gën xày

Mboolem kudib xutbu baa ab xawsu xam nala yaw


Seex Ibra Faal kula reere Yàlla reer nako déy

Baabu daalilu siraajul laahi hiswatunaa


Baabul muriidiina xaluy Yàlla yaa gën a wéy

Yaa baabu rahmati, yaa baabul hudaa kula moy


Day saf ku moy Yàlla ak Yonen ba faf mata ray

Seex Ibra Faal yaa di nuurul laahi ya matta gëm


Mboolem kulay teggi dub tegtal deful kunu roy

Yaay teggtalub Yàlla foo dëggmal Yàlla nga fa yaw


Xaliulu laahi saw tur tekki na wax jilee déey

Yàllaa la teggtal Xabiibal Laahi Axmadanaa


Yaw it nga teggtal nu kookee Yàlla am nasa fay

Jazaaka yaa xillu Seex Ibraahima Faal karaman


Xayral jazaa wal munaa daarayni nan lakko fay

Alhamdu lillaahi ndeem Seex Ibra nokko cëroo


Moom it mu seddoo nu nun baay faal yi xas nanu wéy
110

Alhamdu lillaahi ndeem Làmp gëneel bafi woon


Ñooy doomi pass-passam diy jaamam mu faf dinu may

Baabul muriidiina Xaliilu laahi rahmatunaa


Xuwa daalilu lëzii faxat daalilu ya wéy

huwal muriidu lëzi faxat muriidu kamal


Fi zikri rabbika wal xal-jalu ba wéy

Huwal xabiibu lazi, coffeel ga jeggi na xel


Seex Ibra Faal moodi sàmmub Yàlla bi feggu ay

Moo dëjji ëkk yi naaxal fiir yu bonn ya fi woon


Ba ñépp mùcc mu weettag sun Boroom diko way

Moo fàkk xàl wi, neexal yoon yi bañ gën a neex


Mu gindi góor ñi bañ xam Yàlla xam ko te wéy

Moo indi xewal yi, mboolem jaam ñi ñoo ngi gërëm
Jaa-jëffe Seex Ibra Faal Buur Yàlla am nasa fay

Alhamdu lilaahi rabbanaka xal-hikaman


Alhamdu liilaahi sukru-laahi da gën a yay

Axadun yaay axadun yaay axadal axadaa


Yaay kenn kennal Boroom Tuuba mu jox kako doy

Seex Ibra Faal jërëjëf Yàlla nga naa Jërëjëf


Bamba nga naa jërëjëf kuko waxul dafa yooy

baayu seex faalu faal fadilu fadalana


Seex faalu siqir sa ken du peese sa faay

Cëy baayi seex mustafaa faal yakka indi njariñ


Japp nga rabb wi fi gën ndawal gi daj na ba doy

Cëy baayu seex talla faal seex talla kenn duni mel
Jambaari lislam ja sayfu laahi mbër la mu rëy
111

Cëy baayi seex abdu laahi faal abdu laahi


Sa baay amul sa goor ña fiwoon amu si ñi ña di wéy

Jaraama baayib sërif Xasan husnu ridda


Baayib sërif kuko dakke Yàlla bàl ba du mooy

Jaraama baayil sëriñ aliwu faal mbawaraa


Boroom mbawar faal sa baay lim jëff si diine du fay

Cëy baayu seex modu faal mbendaa di Baabu ridda


Seex modu faal sa baay ñeel na ñu sant ko deey

Cëy baayu seex mbakke faal yaay ker gu sedd te féex


Seex mbakke Seex Ibra Faal sa baay ba moo matta ngoy

Jaraama baayib seriñ bassiru faal busuraa


Bassiru Seex Ibra Faal semmal na xawsu ya wéy

Cëy baayi seex abdu sakkóor habdaan sakkóoran sa baay


Moo ñu soqal ñaari ngéemeñ ngeméeñ lu takk du moy

Cëy baayi seex ngunda faal saaliwu faal karaman


Boroom ngërëm ya sa biir sa baay ba rekk a nu doy

Jaa-jëffe Seex Ibra Faal, faal yaa yaayoo Jërëjëf


Xewal yu rëy yi nga lamboo wal na fepp ba doy

Seex Ibra nun ni ko seddoo nun la Yàlla faral


Ñun it ba ëttu sabba ag malaka yakk lanu ngoy

Ñoo am lu ken amul, ñoo am ku ken amul


Ñoo moos lu ken mussul ba am si tibb yunu doy

Ñoo daj ku ken dajul ñoo gëm ku ken gënul


Ku ngoy si wul kinu goy leg muni wuy sama ndéy

Ñun ngoy nanu si doomi Maam Saynabu Njay jii bu wér


Ka getti goor ña si baattu laa ilaaha ba wéy
112

Subxana rabbika rabbil mulku wa samara


Walhamdu lilaahi rabbul harsii ak lasa wéy

Sallaa wa sallama baaqin laa hassuda lëhóo


Wal-aali wa-sahbi fegg jàmm a ngi am gë ày
113

8. Alhamdu lillaahi
Alahamdu lillaahi lizil mulóoki
Rabul wara muxalamu sulóoki

Wa baxdu lissalaati xayrul xalqi


Seyyidina Muxamadin zil xaqi

Yeenu murit sëtub muriidu laahi


Mooy deeti way xàlla xaliilu laahi

Sayxu suyooxi saahibul xayraati


Sàmsu sumóosi seyyidus sadati

Baabu daliiluka siraajul laahi


hawsul wara, Seex Ibra Baabu laahi

Siidi Biraahim Làmp Faal kamaalu


Abal tàqiiyi sayyidi rijaalu

Moo seqi lañcup Yàlla saqi leer ya


Di xooti déyléey Yàlla fekki ngiir ya

Moo nu xamal kinu xamal ci Ahmadaa


Budul kon ak moom jàm reer nu abada

Yoor katanug Yàlla di fàl di folli


Di seqi jéegoo kënooy araas yay jolli

Di sippi sëff yanu sëffoon si xol yi


Di sëff i sëff yanu sippi won si xel yi

Ku saytaane sëffoon sa xol mu sippi


Daggi sa xol ba reeni gëm yay xippi

Moo tax ba tay xol yepp nee nanu ming


Gambaal sa kàddu Seexra Faal ni fàng
114

Kenn reeratul kenn reereewul Sëriñ bi


Kudul ku Yàlla dàkk xol bi tàbbi

Goor ñepp masee nan simil kom sàppu


Si géewi Yàlla dayoom amul ab àppu

Fawxana goor i Yàlla yay rijaalu


Ba sakki goor si jamanooy dajalu

Moo gën i goor magherifaa lay defal goor


Àggale goor Seex Ibra moo ca man góor

Day àggaley goor banu dem ba àgg


Te dunu julli dunu woor te màgg

Kenn amewul katàn ni Sidi mbër ma


Kenn mus la gis ku mel ni moom si worma

Tegg na Sëriñ bi si barabub boroomam


Sëriñ bi geetil Seexra Faal moroomam

Siidi Biraahim waaju ko noonu hall-ku


Tabbi safaanu ga ña ko soppu gëm ko

Yàlla ko tegtal mboor ma dey ko mbóot ma


Mu xotti ngiirum Yàlla laal sa wor ma

Ku xotti wormam Yàlla teppi say jëff


Ku aw si mbooram Yàlla yéege saw lef

Alhamdou liilaahi ku santul bew na


Seex Ibra Faal ku ko gànnaawel sew na

Ku jëm si Yàlla waa juko toppu jàll


Waa juko noonu xol ba dootu sél

Te kenn jotul Seexra si toppu Yàlla


Xawsul waraa ki moo di goorug yàlla
115

Géttina goor ña naani leer ba màndi


Ba xotti déeyleey mbër ma wuutu Amdi

Moo tax mu xam Sëriñ bi xam gu yàgg


Ca yawma alastu lanu digalee jëgg

Daa yàgg a ñew si adduna ag meloom wi


Kuñ masa yooni moola xàllal yoon wi

Biilaahi wallaahi taalaahi, ku bañ


Seex Ibra Faal buur Yàlla daadi koy fuuñ

Waa juko noonu lum jàmmu-jaammu Yàlla


Mbaate mu julil Mustafaa xad jàla

Du gis sa lamu jàmmu lu tool ni sàra


Noonu ko woorul sopp leen Seex Ibra

Sëñ Bàmba ne ku noonu Seexra mbër ma


Yàgg kula toppay cërub jaxal nama

Derub rijalu laahi dan koy tookee


Waa jusa tegg baat Yàlla ngay attaake

Ku bàyyiwul yàq derub góor Yàlla


Du àgg du aggale ñay moy Yàlla

Kon bayyiléen ségg mbirum xaalilu


Ku fuuyu Seexra Faal amul wusóolu

May yanu ko may ku koy lijanti lëj lee


Ku jeema dii-ngat lef wa daadi yahu lee

Mbirum rijalu laahi dunu ko càmbar


Ku weddi waayu Yàlla mat na caw yàr

Nagub doggal moo nga sa ponki diine


Ku nagguwul li Yàlla deff bul yeene
116

Loo yeene mbóot ma daadi dees fa Yàlla


Nekkal fa ñay nagub doggal ngir yilla

Lu tee ñu naggul Seexra Faal mayaam yi


Te xam ni Yàllaay kàttanal mbindeef yi

Ku Yàlla roof doole nga weesu xel yi


Di xus sa mulki ak malakóot not xol yi

Seex Ibra Faal not na xoli rijaal yi


Xol bukko soppul sañi wun sidit yi

Kun sañi say siditi xol nga xooli


Di for sa mbóoti seexi riijali

kon soppu leen Baabul Muriidu Laahi


Xutbu ridaa xàlla xalilu laahi

Ku soppu waayu Yàlla génno àlla


Ku noonu waayu Yàlla doo am Yàlla

Fa Yàlla ne xel du xalam ba dajj ko


Xol rekk a fay àggale goor mu yëgg ko

Te gooru Yàllay yéege goor fa Yàlla


Ku moy kalay yéegi du giis Buur Yàlla

Kay yéege goor ñay baayub abdu sakkóor


Siidi Biraahim baayub sërif rekkay goor

Getti na goor ñay kumalul waaliyi


Ba sàkk goor ñu gën a gaw mahdiyi

Seex Ibra Faal yaa di sagup Sëriñ bi


Yaa fàkk xàl wi fi gën si dund bi

Dee sukko tëkkaale ka dindale ka xayma


Si genn góor loola du xeeti worma
117

Sàkk na mbër yooy làmb jun fi wàli


Dinan ko upp ba ëtti géew ya lalli

Kuy wax na wax si ñii te bàyyi xàlla


Te tegg ko famu tegg Xaadimu rasuula

Seex Ibra Faal dayoom xajul si xel yi


Te aw meloom nàm na mboole xol yi

Moo tax ku koy diiggant si ñakka julli


Ag ñakka woor moog wa këram ñam wali

Deggul Sëriñ bu Màgg ba sañci tuuba


Yoomal xoyaamati du tàbbi tuuba

Sëñ Bamba ne mboolem jumaa yeeg jàkka


Ak seeni pay ming naleen ba màkka

Malakani maliku kula jaamihi


Wa kula masjidin munal maja mihi

Kon kuko digant lumu jàmmu-jaamu Yàlla


Du giss sa lamu jàmmu sàrra neen la

Te fummu dëkkmu Yàlla foofa jàggadi


Te lumu julli bamu woor mu saxadi

Seex Ibra Faal Siidi Biraahim Faalu


Fajul sunuy ajoo nde ñoo la wóolu

Ñakko lu baax ñakko ñu baax ya màgg


Ku lay xebbéet xolam du gaw yéeg

Sëñ Bamba ne mboolem bëggug rijal yi


Bur Yàlla may nakko ko zil kamaali

Malakani xubbu rijalu laaahi


Muh jila kula haasidin wallaahi
118

Nee na rijal yi ñepp moom lan soppu


Te waaju koy añaane russ ni xépp

Te kenn jottul Seex Ibra Faal si soppu


Bëggam ga da sàar wër na reew mi mépp

Kon nanu ko soppu ngir lamu soppu Bàmba


Ba lakko Bamba soppu fay ko boor ba

Nun soppu nanu la yaa xalila laahi


Te bëgg nanu la ngir xabiba laahi

Ñakkoo si Yàlla ben cër ñakkoo nu


Jàpp nga rab wi Seexra faal ummo nu

Yay génn góor nde ya di baayi góor ñi


Aboo rijal weesu nga mboolem góor ñi

Semmal nga mboolem kumalul waliyyi


Si waxi mbër ma Axmadul pàxiyyi

Subhana laahi ma ngi sabbal mbër ma


Sabbal gu sax si sama xol te bir ma

Ci nimu binde Siidi Ibraahimu


Te muy sunub cër Yàlla moy hakiimu

Seex Ibra Faal mbóot la mu Yàllay yëggle


Yalnanu ko yëgg funu toolu ndax ñu jàgle

Kun yëggalul mbóot ma nga daadi weddi


Ku weddi waayi Yàlla do gis Amdi

Ngir Yàlla Amdi moy ndawam lam yonni


Mooy ndaw lu matt la mattal lam yonnee

Xaadimu rassuul di yeesalat ngiiram mi


Seex Ibra dar ko dinu wan mbóoram mi
119

Mootax ku weddi Làmp bul gëm Bàmba


Bul gëm Rassulu Laahi may Yoneen ba

Ngir weddi yonen daadi gëm Boroom ba


Munula nekk xas na wéy doggal ba

Te weddi góor di gëm i góor gu yees góor


Taxula góor àg sa Yàlla may Buur

Te foofi seeru gaa ña noonu Siidi


Ñañ gëm a yees Yàlla nanu Yàlla gindi

Ku Yàlla gindiwul du leeral gis ba


Day lambatuy wéy fekk xol ba gùmba

Seex Ibra neena fàng mel ni ab jànt


Waaye ku Yàlla baaxewul lay lënt

Yalnanu xool te sunu xol yi xippi


Te gëm i xaybu abadan te noppi

Si darajay Seex Ibra Saar jazaaka


Bi xaqi mbër ma da nuroo ag malaka

Yal nanu Yàlla feeweleg saytaane


Ag way xañaan gu andul ak limaani

Si darajéey seex ibra xutbul xawsu


Baayub rijal yi dendul ag uwaysu

Semal na ñay goori naar mooy góoru


Ngiram doy na ñetti ngir yuy tuuru

Moo gën a degg Yàlla gaa ña jiitu


Te sóobu won ba ami ndam yu yaatu

Dayob gëmam fawexana goog malaaka


Nam deggé Yàlla gën a jot mawlaaka
120

Kenn mus la gis ku mel ni moom si dunyaa


Tiital na ibliis nësaxal pexem yaa

Yor sekreeb turam wa laa ilaa haa


Muxamadun arsalahul ilaahaa

Mootax dënam ba gën a foor ay kàggu


Moo dakku turu géej yu makk yay yëngu

Moo gën riis wax gaa ña xàl ngiir ya


Kàddooma gën oor gën jàama ngir leer ya

Kanzul kunóozi saahibul xayraati


Daambe na mboolem yiw yi lissalaati

Xaliilu laahi saahibul miftaahi


Siidi Biraahim seyidil arwaahi

Gaa ña ko soppu seen yaram xaram na


Duñ tabbi naari mukk loolu leer na

jazaaka laahu fi hayrul zajaa-u


Yaw minu badil darajeey fana-u

Defar nga toolub diine mbay ma leer na


Ngóobeen sileen Seexra Faal ñooral na

Lislam ji yéppa bëgg a yor meloom wi


Ku bëgg a dem faw mu laal yoonam wi

Mayam yi daar na pinku daj na sówwu


Dambe na mulku ag malakóot ni cówwu

Gaaya fanaani aras ak kursiyyu


Xam nanu maqaama dindul ak tarqiyu

Way dée ya xam nanu darajay xaliilu


Ay junni lay ràmmu di óot marsóolu
121

Nuurul ilaahi saahibul xulóomi


Moo gën a jàng kàang yi won ci reew mi

Moo gën a degg alxuran ñay waare


Mah-naaya lay jëff kàng yi mooleen fóoree

Seex Ibra Faal semmal na gaaña sóobu


Fawxana ñoñ tasóof ak majzóobu

Ñoom sunniyóog gaaña xam haqiha


Yillif na seeni kem si bir tariqa

Te ñay drus di julli tay wassifa


Ku ko si diggant amuloo kusufa

Ahazana laahu si xol bu gàntu


Lahala boon ibliss ba xol ba tontu

Ibliss xolam ba rekk mu halku


Wedib doggal la deff ba xay wa dal ko

Te gàntu Yàlla ag gàntu waayu Yàlla


Ñoo yami atte toppileen góor Yàlla

Te waayi Yàlla mooy xaliilu laahi


Sirub turam wa mooy xabiibu laahi

Xaliilu laahi sowru Faal xaliilu


Xol bu ko gàntu reen yi daadi sulu

Moy teg taalub mboolem ku gëm rasulu


Te gëm kitaabu laahi gëm jibriilu

Te gëm doggal yi yépp gëm bis pincc


Ku noonu Seexra Faal keroog ndaw gacce

Ndax ay jikkoom la Yàlla soxla sib jaam


Kuko yorul lum yobbuloo gënul saam
122

Laa yanfahu maalun walaa banoona


La Yàlla soxlay xol bu seel neena

Yàlla nanu doyloo Seexra Faal te roy ko


Te dooni surgaam fumu jëm ñu dàr ko

Yowmal xiyaam buy ràmmu danuy ràmmu


Sa mbooyi àljanaam ya moonuy sàmm

Si darajaay sangam ya ak doomam yi


Ak seex yu màgg ag mbóot ya dar teereem yi

Si darajeey jummam ji jàkkam ji


Ak mbóoti Njarem li hadaqul haaji

Yàlnanu dëggoo gën ngoy si sowru


Te dikko roy ba làkku xayrul xayru

Si darajeey Seex Ibra ag doomam yi


Ak Seex yu màkk yamu sooxal kënoom yi

Yall nanu lamboo martabaam muridu


Ba dee si toolub Yàlla doon sahiidu

Sa darajaay sàng ba juur saa baayu


Abdul karim ture ma doon waaliyu

Yalnanu am Yàlla ye am roosóolu


Te ami ndam si Xaadimu Rasóolu

Si darajaay seyyidi hakiimi


Seydil karimi seexra faal yeeme

Amina Amina wasala laahu


Hala nabiyina waman walahu

Muhamadin waa aalihi wasahbi


Bi haqi seexunal mu rabbi
123

Subxana rabbika rabbu sukkóori


Wal xamdu liilahi lizi hafóori

You might also like