You are on page 1of 4

#lejeunepoete

Dans l'avion en rentrant de Brazzaville


pour assister au 137ème anniversaire de
l'Appel de Seydina Limamou Lahi (PSL).

Damay xalam sa mbir di xool


Damay xalaat Maam ni nga mel
Foofi taxaw ñu nawla Njool
Amoo moroom Baay Abdulaay

Du rek li ngay sëtub Yonnen


Di Taawu Sëydinaa mi gën
Sab taxawaay la yaafi man
Amoo moroom Baay Abdulaay

Da ngay xalam ku tolni Maam


Maxaamayeek may yimu am
Di xaar nga ñëw ñu manko xam
Amoo moroom Baay Abdulaay

Goorgoorlu mooy tax nit di xam


Cërem ci suuf ndeem narna ndam
Kii nak ndamam jiitna judooom
Amoo moroom Baay Abdulaay

Fu doomu soxna mus fanaan


Dem nga fa naanfa lamfa naan
Boolek sa yëf koo songa daan
Amoo moroom Baay Abdulaay
1
#lejeunepoete
Ndonal Limaamu ak Isaa
Kep kuka donna raw ba Saa
Ndax Yalla mooy ki leen di sa
Amoo moroom Baay Abdulaay

Isaa la yor moola defar


Moo tax nga màgga doonu gar
Suuxloo nga bañ yi ngir naqar
Amoo moroom Baay Abdulaay

Manoon nga wooté nguur ba faw


Konoot ñu doon say dak di daw
Dila dawal ngir bëgga raw
Amoo moroom Baay Abdulaay

Manoon nga xëy wooté sa kër


Ñu lay wayal Maam ba fajar
Ndax kula xam moytu sa mer
Amoo moroom Baay Abdulaay

Waayé nga jaay bànneexu fii


Dëkkee di wër yër "suhufi"
"Kanzal-ghinaa wash-sharafi"
Amoo moroom Baay Abdulaay

Taloo sa kër taloo njaboot


Taloo sa yëf ndax ñi nga boot
Di xeex di bañ rek kunu noot
Amoo moroom Baay Abdulaay

2
#lejeunepoete
Taloo di lekkak di nelaw
Taloo xawaaré, dëkké daw
Ngir rek njabootu Maam gi raw
Amoo moroom Baay Abdulaay

Lislaama tax nga jël sa doom


yu baax yi tuddé say moroom
Sallaaw du toolbi yaay boroom
Amoo moroom Baay Abdulaay

Mbokka gi yaa tax mu dëgër


Shaytaané yaa tax mu jëfur
Diinéji yaako far kuloor
Amoo moroom Baay Abdulaay

Lu mana xew Maam nang fi took


Ñoo ngii sa keppaar dunfi jok
Fayseené wun jok fing nu tek
Amoo moroom Baay Abdulaay

Maynu nu naan ndax man ngako


Fexeel nu àgga sañ ngako
Jebbël nu Njiin ndax miin ngako
Amoo moroom Baay Abdulaay

Lun mana def yit yaanu saf


Maam sunu xolyi lan la def
Sunuk cofeel si yaw du kaf
Amoo moroom Baay Abdulaay

3
#lejeunepoete
Ku am kaneen jëlël nu jël
Baay Abdulaahi "zil-kamaal"
Am sa ngërëm kay doyna njël
Amoo moroom Baay Abdulaay

Feek picca ngiy sab noo ngi ñaan


Tusuur nga taac nu say bagaan
Sun ànda bii dem ba Jinaan
Amoo moroom Baay Abdulaay

Wa Laa Ilaaha Illa Laa


Wa Laa Ilaaha Illa Laa
Wa Laa Ilaaha Illa Laa
Amoo moroom Baay Abdulaay

"Ya rabbi salliman 'alaa


xayri nabiyyin ursila"
Took fi ñulay xool "hiwalaa"
Amoo moroom Baay Abdulaay

APPEL 2017 (27-04-2017)


#lejeunepoete

You might also like