You are on page 1of 4

Fathul Manaan fi

Fathul Manaan fii Jawabi Abdu Rahmaan.(si ubbik yàlla miy aji xéewale kaat si tontu
Abdu Rahmaan).
Tënk ndënkan bi
✓ Ubiteeg ndënkan bi
✓ Sababu bindum ndënkan bi
✓ Ñeet Xaaji ndënkan bi
✓ Ragal yàlla (At Taqwa)
a. Lan moy ragal Yallah
b. Darajay ragal Yallah
c. Ragal Yallah moy teranga
d. Gënéel yu nekk si ragal yàlla
e. Topp ndigël yi teet tere yi
✓ Sàkku xam-xam
a. Xam-xam ak jaammu Yalla
b. Tedayu Xam-xam
c. Xam sa boroom
d. Xeeti xam-xam yi
✓ Sàmmu sa juroom ñaari cër
a. Sàmm laamiñ
b. Sàmm sa biir
c. Sàmm sa pëy
d. Sàmm say tank
e. Sàmm say loxo
f. Sàmm say bëtt
g. Sàmm say nopp
✓ Buntu Safara Xol
✓ Nettali yu am jërign yu Ibraayma bun Ad'ham
✓ Dundug Abdaal yi si nettali Sëhwu
✓ Ñaari wàll jaamu Yallah
✓ Wuuteek ñi Sóobu ak ñi Àgg si Yallah
✓ Ndenkaan jeem si sa diganete ak niit ñi
✓ Teej téeg ndënkan bi

✓ Ubiteeg ndënkan bi
Ganaaw Bismillahi Rahmaani rahiimi dafa julli si Muhammad teksi la xaw'la wala
xuwaata..... Daldi wax ap seedayu xolam si li Yallah doon ap Boromam, l'islam di
diineem, Muhammad (SAW) di yonnantam.
Teksi sant yàlla mi ga xamni ñi mu nam si ñom ak texe daf leen tela yée si nelawi
ça gañete, mooy, ak xamadi te mu baaxe léen ñu saax si sàkku tuyaaba ak gërëm daldi
julli si Muhammad ñanal ko teranga ak jaam mom aki mbokkam ak sahabaam ak kéep ku
léen toppu di jeem’a jaar fa ñu jaaroon.

✓ Sababu bindum ndënkan bi


Sëriñ Abdul Rahmaan Lo mo sàkku woon si Ku téd ki defal ko ap ndenkaane bu xamni
dakoy jëriñ si biir ak si bitii te di ko dakal pexem séytaane.
Guinaw l'istikhaar lako Sëriñ bi daldi amal waxko si lo xam dinako jërign aduna ak
alaxiira mom ak kéep Koku xeemeem daldi koy tudde " ubbik Yallah mi ajii xëwaale
kaat bi si tontu Abdu Rahmaan "
Guinaaw gi mu ñan yalla mu nangu ko te défko ak yiiw ak muccukaay aduna ak alaxiira
si mom ak nëpp ñi ko xeemeem.

✓ Ñeet Xaaji ndënkan bi


Sëriñ bi dafko ndënk Ragal yàlla, Sàkku xam-xam, ak Sàmmu juroom ñaar cèer yi.
✓ Ragal yàlla (At Taqwa)
a.Lan moy ragal Yallah : moy xam li Yallah ndig le ga taxaw teem si défko gir mom -
xam li yallah di tere ga taxaw teem si moytu ko té jëmaam taax woroo ak ni ku
jàppee muy ragal bugalu yàlla yi té teewul yagi sëg si tere sasounè kuy def li
ragalo Yallah té ku gaat xel ga te ku séytaane Jaap ga.
b. Darajay ragal Yallah : ragal yàlla mom dafa def ñetti darajaa:

Bu jëkk(mom la alxuraan di waxni wa alzahum Kalimata Taqwa "battu ragal Yallah moy
laahilaaha ilah lah" ) bi moy wéetal Yàlla ba dokko booleek dara loko warta booleel
(moy taxa baña saax si safara-da nafa jaar su feeke jegalu ñu ko ay bàkkaaram)

Bu ñaareel bi (mom la alxuraan di waax ni walaw a'naa ëhlaal xuraah amano wa


taqaw... "doonte ñooñu dëkk ya gëm nañu te ragal yàlla" ....) moy guinaw gëm yàlla
soori léep lu yàlla â yee si wax, jëf... Si sariiha li moy ragal Yallah

Bu ñeeteel bi ( ya ayuhal laziina aamanoo itaxul laha xaqa tuxati hii... Yéen gas
yi gëm ragal leen yàlla dëggi-dëggi ragal) moy ginaaw gëm ak di sorii léep lu yàlla
tere mu bëgg yalla bëgg go xamni mom keep mokoy ñor bi nak moy búñu wara xeemeem
te diko yotuu.
c.Ragal Yallah moy teranga : haadiis bi dafa waxni "al karamu at taqwa" sa dëgg-
dëgg ragal yàlla rek moy teranga. Niit ku am ragal yàlla gu matt sëkk mom lañuy
waax Borom teranga.
d. Gënéel yu nekk si ragal yàlla
Ragal yàlla mu ëmb mbooleem yiiwi adunaa ak gu alaxiira.
Ku bëgg : Xam-xam (wa taxul laha wa yu anlimukumul lah), Wërsëg (wa mane yataxil
laha yadia 'anl lehu mahrajaan wa yarzuhu min aysu la yaax taasibu), Mùth ak
Teranga. Naga ragal Yallah
e. Topp ndigël yi teet tere yi
Dafko waxni giir ga xame li yallah ndigël wala limuy tere faaw ga jang ko jaarale
ko si sariiha.

✓ Sàkku xam-xam
Ragal yàlla mënuta am si ludul sàkku xam-xam. Kne jámm bi warna jitaal xamlu ba
noppi doga jàmmu.
a. Xam-xam ak jaammu Yalla
Leep lo giss mba dëgg ko géenul ñar yi. Sokoo bëgge xam setlul ñari aya yi :
"alahu lëzi xaalaqa sabh'an samaa waati wa minal ardii mislahuuna yatanazalu amru
bayna hun'na li ta'anlaamu anaa laha anlaah kuli sey'iine xadiirun wa an'na lahaa
qad akhataa bi kulli sey'iine hilmaan" mane yalla ma sakk juroom ñarii asamaan ak
suuf ak lissi diganete bi dissi sopaax dikoo nimu ma soobe dara taxul lumoy bëgg
geen xamni may Yallah ma xam,mën,sañ leep..
"Wa ma xalaxtul jiin na wal inesaa ilaah li ya'anbudunii"sakku ma niit ak jiine
ludul ñu jaamu ma.
Kon jaam bi ginaw bamu xame li warul yite wo ludul ñom ñaar.
b. Tedayu Xam-xam
Xam-xam mo gënaa tedd jaamu Yalla daax bu amul jëfë du am.
Giir wone tedayu xam-xam nenako Yonént bi nena ki xam bolle ak jëfë nimu gëne kuy
jëfe te amut xam mogi melni "maan mi" nima gëne bollem sama xeet wi
Teek bët borom xam-xam buy jëfe giir Yallah moka gënal jaamu Yalla Att mo xamni day
woor bëthëk yi di taxaw guddi yi.
Lii keep day wonei ni tedayu xam xam si jaamu yallah waye na feek mu doon bu ñuy
jëfe giir yallah.
c.Xam sa boroom
Mënula ñakk xam sa borom muy xam nigakoy gëmë ,wetal ko ,xam nigakoy jamoo ndax
bu feke xamoko mëne gako jamoo no xamni du nii melni kulay wokal rek te xamul fuy
xésaan fi yow.
d. Xeeti xam-xam yi
Nenako nak xam-xam dafa yatuu waye ñeet yi mënul ñakk kon buñuy wax sàkku xam-xam
farata la ñu taax ñuy wax.
-Bu jëkk bi moy "hinlmu Tawhid"molay xamal nigay gëme ak wétal sa boroom.
-Bu ñaareel bi moy " hinlmu fiqh wala sariiha " molay jàngal ndigël yi ak tere yi
fi ga wara yem te do ko saña wessu.
-Bu ñeeteel bi modii " hinlmu Tassawuuf " molay xamal nigay sellale sa diggante ak
sa boroom ba sa bakkan baa aduna dula mëna gàllankoor.
✓ Sàmmu sa juroom ñaari cër
Ginaaw sàkku xam-xam sëñ bi daf ko ndigël mu wattu juroom ñaari cëram (lammiñ,
biir, pëy, ñaari tank, loxo,bëtt,noppu) bu si ñeek mu waxko naka la koy sàmme.
a. Sàmm laamiñ
Ndënk nako mu sàmm laamiñam si jëw ak wax lu amul njariñ.
Déss na dimbali ko si wutuu lammiñ si ñeet yi di baaril taxaw di Julli, ak weet di
sorii mbindéef yi, new ak leek.Mbokk na batey liñuy dimbali ko si sàmm laamiñam ñay
baril di jang Suratu nassi ak suratul Qadri.
b. Sàmm sa biir
Daf niko naga sàmm sa biir ba léep losiy dugal mu doon lu leew, léep lu haraam mba
lënt dekko sorii lo mën nax kuy leek lu leew fawu mu topp Yallah mu neex ko wala mu
naxari kem nonú la kuy leek lu haraam faw mu mo'y
Nangu farlu si ñakk leek riiba nax kussi lekk ap tiib digama am ñeenti fukki faan
yo xam ni Yallah du nangu sap jaamu.
c. Sàmm Sa Pëy
Daf ko ni ku gëm Yallah ku ne na sàmm sawukaayam bu baax ba dussi def leen lu aay
mu melni ndialo, warna di sàng awram
Bokk na si yiiy taax sàmm sa awra ba dossi mo'y bëril jang Souratul falaq, di wax
subhaanalaah malikul qudoos, ak bëril jang suratul Taariq.
d. Sàmm say tank
Sa ñaari tank na gako tëye bu baax bala ga jugg jëm feen naga xam luy maye tuyaaba
la wayé bul jeem mukku si liñu tere lu melni sácc, rambaaje, poo mo xamni Yoon
dafko aye wala jugg di dem si buuri adduna yi si lu mëna ñakk
e. Sàmm say loxo
Dafa ñëw si ñaari loxom yi mune ko fexel ba bulsi laal dara lo xamni yoon mayu
lako niki jigueen buy jàmbur si yow (ko mëna sëyal)
Bul laal alalu jàmbur si ludul ndigalam
Nag'a wootu binede leep luñu sañul wax si laamiñ.
f. Sàmm say bëtt
Say bëtt dël moytú dissi xol lu haraam a xol.
Bul xol jigueen buy jàmbur si yow ak gonee gu am aw taar si xolu baanexu.Bul di
yënrdu Bataaxalu jàmbur ak luñu sutural
Moytu xol awra donte daf ko sangul ludul ñaar yuuy sëy. Moytu xol sa awray bop te
amul been loor nax day waral ndialo ji wala yu ko niru.
Sàmm say bëtt si xol Borom doole yi ñeme Yàlla xoluuk magal ak keen si mbindéef yi
xoluuk xeebel
Léep luñu sañul binedeu wala jeema xam sañe su ko xol
Keep ku sàmm say bëtt ba dossi xol lo wart'a xol yàlla Samal la sa xol ba lussa
warta duggu dussi duggu
g. Sàmm say nopp
Noppu yi daf ko ni nako sámm bu baax si léep luñu aaye si wax dañu koy aaye si degg
mu melni tewlu jëw, rambaaj, feen
✓ Buntu Saafara Xol
Daf ko ni yiy saafara xol bamu sell juroom la:
Bi si njëkk : jang alxuraan te bo mëne xam man'a yaa diko settantal
Bu ñaareel bi : newaal ak regg manam bëril xiif te mu digg doomu
Bu ñeeteel bi : di Julli Guddi
Bu ñeenteel bi : jegalu ak di tuubaal sa boroom si waxtuw jël
Bu juroomeel bi : di jotayo ak ñu baax ñi.
✓ Nettali yu am jërign yu Ibraayma bun Ad'hëm.
Néna woon lu ëpp si Góor Yallah nekoon nañu sëriñam te liñu ko doon ndigal giir wa
aduna moy moytu bëril leek nax ku koy def du am baanexu jaamu Yallah, wootu bëriy
nelaw nax day taax sag dund du barkel, kuy wut ngërëmal niit ñi du am ngërëmal
Yalla.
✓ Dundug Abdaal yi si nettali Sëhwu
Ay niit yu baax lañu yu sunu Borom taane te doñu juk si aduna nax kussi fatu rek
Borom bi wutaal ko
Sëhwu neena saaxo ñeent yi mo leen may martaba yooyee muy : ñeme xiif, tëye séen
làmmiñ si lu amul tuyaaba, dii bëru niit ñi bañ di jaxasoo ak ñom si lu amul
njariñ, newaal seeni nelaw guddi te di jaamu yàlla.
✓ Ñaari wàll jaamu Yallah
Sëriñ bi dafa xamal Sëriñ Abdu Rahmaan ni Jaamu yàlla ñaari wàll la
Bu njëkk bi moy di diema def la Yallah bëgg, Bu ñaareel bi moy di diema moytu la
Yallah tere.
Moytu yi ñu tere mo gëna jaafe te mo ëpp daraja te moy li wuutale ñi sóobu si Yonu
Yallah ak Ñi Àgg.
✓ Wuuteek ñi Sóobu ak ñi Àgg si Yallah
Ñi doga sóobu Yonnu Yallah té séen bëtti xol fetagul séen yite yu ëpp moy xeeti
toppu yallah yi lu melni di woor bëcëk di Julli guddi ak boleem jëf yi ga xamni cër
mokoy jëf waye ñi ga xamni séen xol yi feet na, ñu xam kumpa te Àgg li ñu gëna
yitewoo moy moytu léep lu Yallah tammu wuut. Seeni xol baña xalaat leen ludul
Yallah té di diema sámm séen bopp si leek ba naan ay caaxaan waxuma la lu lënt ba
haraam, di sàmm seenug lammiñ si waxug neen wala caaxaan, di jeem’a tëye seeni bëtt
si xol lu leen amalul njariñ.
✓ Ndenkaan jeem si sa digaante ak niit ñi
Daf ko ni yow talibé bi léep lo bëggal sa boppu bëggal ko kéep ku gëm yàlla, keep
kuy wax baatu seede yi, li booko defe yàlla tabaal la ajaana te du seet say mbir.
So ame ap gaan nag'a ko teral doonte ap kàccoor la rawatina muy ku baax.
Say ñaari wayjur sa bo sëlmële jullig farata na ga leen fàttaliku te ñanal léen.
Bul iñaane keen gu gëm Yàlla ndax ku iñaan faaw dafay feete suuf ñu feete ko kawe.
Bu la keen si niit ñi tooñe jeegal ko bul feyu te Yallah taax té bul ñaan mu tékk
ko bëne mussiba.
Keep kula màgg fonk ko te teral ko magal ko.
Keep ko màgg yërëm ko té ñewante ko.
Keep ko maasel def ko ni sa boppu, di ko bëggal ak defal ligay defal sa bopp.
✓ Tëj téeg ndënkan bi
Sëriñ bi daf ko ni bo jëfandikoo ndënkan bi diga mucc fi si aduna ak si alaxiira te
diga am yiit léep lo bëgg si aduna ak fofe sa alaxiira
Ginaaw gi mu ñaan Yallah boole leen wërsëgale rafet ug mucc.te nangul leen si
Darajay ki ñu taan Muhammad (SAW) Yalla na Yalla nangu ñaan.

You might also like